Hebreus 9
Wolof NT 2010 (WOL_INJ) vs NTLH
1 Kóllëre gu jëkk ga ëmboon na ay ndigal ci mbirum ni ñu wara jaamoo Yàlla. Amoon na itam kër Yàlla gu nekkoon àddina.
1 A primeira aliança tinha leis sobre a adoração e tinha também um santuário construído por seres humanos, onde se adorava a Deus.
2 Nekkoon na ab xaymab màggalukaay bu ñu séddale ñaari néeg. Ca ba jiitu la tegukaayu làmp ba nekkoon, ak taabal, ja ñu daan teg mburu, ya ñu teewal ca kanam Yàlla. Foofaa nga tuddoon bérab bu sell ba.
2 Foi armada uma Tenda , dividida em duas partes. Na parte da frente, chamada Lugar Santo , ficavam o candelabro e a mesa com os pães oferecidos a Deus.
3 Néeg ba ñu tudde bérab bu sell baa sell a nga nekkoon ca gannaaw ñaareelu rido ba.
3 Atrás da segunda cortina ficava a parte que era chamada de Lugar Santíssimo .
4 Sarxalukaayu wurus, ba ñuy taal cuuraay ca kawam, a nga fa woon, ak gaalu kóllëre, ga ñu taf wurus ba mu daj. Ca biir gaal ga amoon na fa benn njaqu wurus bu defoon ñam, wi ñuy wax mànn, ak it yetu Aaróona wi jebbi woon, ak àlluway doj, ya ñu bindoon wax yi kóllëre gi ëmb.
4 Ali estava colocado o altar de ouro onde era queimado o incenso, e também estava colocada a arca da aliança , toda coberta de ouro. Dentro da arca estavam a vasilha de ouro com o maná , o bastão de Arão, do qual tinham saído brotos, e as duas placas de pedra com os mandamentos escritos nelas.
5 Ca kaw gaal ga teg nañu fa ñaari nataali mbindeef yu ñuy wax serub, yu doon wone ndamu Yàlla. Seeni laaf ñoo doon yiir kubéeru saraxu njotlaay ga. Waaye loolu lépp léegi manunu koo tekki benn-benn.
5 Em cima da arca, representando a Presença Divina, estavam os querubins , com as suas asas abertas sobre o lugar onde os pecados eram perdoados. Mas agora não é o momento de explicar os detalhes dessas coisas.
6 Ba ñu defaree lépp, sarxalkat ya dañu daan dugg bés bu set ca néeg bu jëkk ba, ngir mottali seen liggéeyu sarxale ca Yàlla.
6 Depois de tudo isso ter sido preparado, os sacerdotes entram todos os dias na parte da frente da Tenda, que é o Lugar Santo, para cumprir os seus deveres religiosos.
7 Waaye ca néeg ba ca topp, sarxalkat bu mag ba rekk moo fa daan dugg benn yoon ci at mi. Te daawu fa dugg mukk te yóbbaalewul deretu mala, yi muy jagleel Yàlla, ngir bàkkaari boppam ak yu mbooloo mi daan def ci seen ñàkka xam.
7 Mas somente o Grande Sacerdote entra na parte de trás, que é o Lugar Santíssimo, e isso apenas uma vez por ano. Ele oferece a Deus o sangue de animais, em favor de si mesmo e também pelos pecados que o povo cometeu sem saber que estava pecando.
8 Ci noonu nag Xel mu Sell mi wone na ne yoon wi ñuy jaar, ba dem ca bérab bu sell baa sell, ubbikoogul woon, fi ak xayma ba jëkk baa ngi doon taxaw.
8 Por meio disso tudo, o Espírito Santo nos ensina, de modo bem claro, que a entrada para o Lugar Santíssimo ainda não foi aberta enquanto a parte da frente, que é o Lugar Santo, continuar sendo usada.
9 Misaal la ci jamonoy tey; dafay wone ne sarax yi ak saraxi mala yi ñu daan jagleel Yàlla, manuñoo dalal xelu jaamukatu Yàlla bi.
9 Isso é um símbolo para hoje. Quer dizer que as ofertas e os sacrifícios de animais oferecidos a Deus não tornam perfeito o coração das pessoas que o adoram.
10 Sarax yooyu ñu ngi jëmoon ci lekk ak ci naan ak ci fànn yu bare ci mbirum sangu set. Ay sàrt yu jëm ci yaram lañu, yu ñu waroona farataal, ba kera jamono ji Yàllay tëral kóllëre gu bees.
10 Essas ofertas e sacrifícios têm a ver somente com comida, com bebida e com várias cerimônias de purificação . São regras externas que têm valor somente até que Deus renove todas as coisas.
11 Waaye Kirist ñëw na, doon sarxalkat bu mag, bi joxe xéewal yi teew. Jaar na ca màggalukaay ba gëna màgg te gëna mat, te màggalukaay booba loxol nit defaru ko, maanaam bokkul ci àddina sii.
11 Mas Cristo veio como o Grande Sacerdote das coisas boas que já estão aqui. A Tenda em que ele serve é melhor e mais perfeita e não foi construída por seres humanos, isto é, não é deste mundo.
12 Noonu Kirist dugg na benn yoon ba fàww ca bérab bu sell baa sell. Duggu fa ak deretu sikket yi ak yu yëkk yi. Waaye mi ngi duggaale ak deretu boppam te indil na nu noonu njot gu amul àpp.
12 Quando Cristo veio e entrou, uma vez por todas, no Lugar Santíssimo , ele não levou consigo sangue de bodes ou de bezerros para oferecer como sacrifício. Pelo contrário, ele ofereceu o seu próprio sangue e conseguiu para nós a salvação eterna.
13 Deretu sikket yi ak ju yëkk yi, ak wëllu, wi ñu lakk te di suy dóom bi ñi taq sobe, ñooy sellal yaram.
13 O sangue de bodes e de touros e as cinzas da bezerra queimada são espalhados sobre as pessoas impuras , e elas ficam purificadas por fora.
14 Su fekkee ne noonu la deme nag, du kon deretu Kirist moo ëpp doole? Jox na bakkanam Yàlla, def ko sarax su amul sikk jaarale ko ci dooley Xel miy sax abadan. Kon deretam moo mana sellal sunu xel, mi nu doon yedd ndax jëf yu jëm ci dee, ngir nu mana jaamu Yàlla jiy dund.
14 Se isso é assim, imaginem então quanto maior ainda é o poder do sangue de Cristo! Por meio do Espírito eterno ele se ofereceu a si mesmo a Deus como sacrifício sem defeito. E o seu sangue nos purifica por dentro, tirando as nossas culpas; assim podemos servir ao Deus vivo, pois já não praticamos cerimônias que não valem nada.
15 Looloo tax mu nekk Rammukat bi ci wàllu kóllëre gu bees ci diggante Yàlla ak nit, ngir ñi Yàlla woo am cér bu sax ci kaw, te mu digoon leen ko, ndaxte Kirist dee na, ngir jot ñi jàdd yoon ca kóllëre gu jëkk ga.
15 Portanto, é Cristo quem consegue fazer uma nova aliança , para que os que foram chamados por Deus possam receber as bênçãos eternas que o próprio Deus prometeu. Isso pode ser feito porque houve uma morte que livrou as pessoas dos pecados que praticaram enquanto a primeira aliança estava em vigor.
16 Ci li jëm ci dénkaanebu ñu bind, jëme ci miraas, fàww ñu wone firndeg deewu ka ko bind,
16 Onde há um testamento , é necessário provar que a pessoa que o fez já morreu.
17 ndaxte bala dénkaaneb miraas di taxaw, dee am; te taxawul, fi ak ki ko bind a ngi dund.
17 Pois o testamento não vale nada enquanto estiver vivo quem o fez; só depois da morte dessa pessoa é que o testamento tem valor.
18 Looloo waral kóllëre gu jëkk ga, ñu fasoon ko ak deret.
18 É por isso que a primeira aliança entrou em vigor somente com o uso do sangue de animais.
19 Keroog Musaa jàng na ndigali yoon wépp ci kanam bànni Israyil gépp. Gannaaw loolu jël na deretu wëllu, jëlaale ndox, ak caru garab gu ñuy wax isob, laxas ci kawaru xar mu xonq. Noonu mu capp ko ca deret ja, daldi ko wis ca téereb yoon wa ak ca mbooloo mépp
19 Em primeiro lugar, Moisés anunciou ao povo todos os mandamentos conforme estavam na lei . Depois pegou o sangue dos bezerros e dos bodes, misturou com água e borrifou o livro da lei e todo o povo, usando lã tingida de vermelho e hissopo .
20 te naan: «Lii mooy deretu kóllëre gi leen Yàlla tëralal.»
20 Então disse: “Este é o sangue que sela a aliança, que Deus mandou vocês obedecerem.”
21 Noonu mu daldi wis it deret ja ca xayma ba ak ca jumtukaay, ya ñu daan jaamoo.
21 Da mesma forma Moisés também borrifou sangue sobre a Tenda e sobre todos os objetos usados na adoração.
22 Ndaxte ci yoonu Musaa, daanaka deret lañuy sellale lépp, te bu deret tuuruwul, mbaalug bàkkaar du am.
22 De fato, de acordo com a lei, quase tudo é purificado com sangue. E, não havendo derramamento de sangue, não há perdão de pecados.
23 Yëfi àddina yi misaal yu dëggu yi ci asamaan, war nañu leena sellale noonu. Waaye yëf yu dëggu yooyu ci asamaan, laaj na sarax yu gëna baax, ngir ñu sell.
23 Essas coisas, que eram cópias das realidades celestiais, deviam ser purificadas desse modo; mas as próprias coisas celestiais exigem sacrifícios bem melhores.
24 Ndaxte Kirist duggul ci bérab bu sell bu nit tabax, muy doon nataal ci bu dëggu bi. Waaye dugg na ca biir asamaan sax, ngir taxawal nu ca kanam Yàlla léegi.
24 Cristo não entrou num Lugar Santo feito por seres humanos, que é a cópia do verdadeiro Lugar. Ele entrou no próprio céu, onde agora aparece na presença de Deus para pedir em nosso favor.
25 Sarxalkat bu mag bi dafay dugg at mu jot ca bérab bu sell baa sell ak deret ju dul josam. Waaye Kirist joxewul bakkanam ay yooni yoon.
25 O Grande Sacerdote entra, todos os anos, no Lugar Santíssimo , levando consigo sangue de um animal. Porém Cristo não entrou para se oferecer muitas vezes.
26 Bu demee woon noonu, kon dina sonn ba tàyyi ca njàlbéenug àddina ba tey. Waaye nag benn yoon rekk la feeñu ci mujjeelu jamono yi, joxe boppam ni sarax ngir far bàkkaar yi.
26 Se fosse assim, ele teria de sofrer muitas vezes desde a criação do mundo. Pelo contrário, uma vez por todas ele apareceu agora, quando os tempos estão chegando ao fim, para tirar os pecados por meio do sacrifício de si mesmo.
27 Kon ni nit ñi deeye benn yoon rekk, ba noppi jaar ca àtte ba, ni ko Yàlla dogale,
27 Cada pessoa tem de morrer uma vez só e depois ser julgada por Deus.
28 noonu it la Kirist joxee boppam benn yoon, ngir gàddu bàkkaaru nit ñu bare, te dina feeñaat, waxuma ci mbiri bàkkaar, waaye ngir indil ñi koy séentu mucc gi.
28 Assim também Cristo foi oferecido uma só vez em sacrifício, para tirar os pecados de muitas pessoas. Depois ele aparecerá pela segunda vez, não para tirar pecados, mas para salvar as pessoas que estão esperando por ele.
Atalhos do teclado
- Capítulo anterior←
- Próximo capítulo→
- Versículo anteriork
- Próximo versículoj
- Limpar seleçãoEsc
- Esta ajuda?
Estude este capítulo no WhatsApp
Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Hebreus 9, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.