Tito 3

Téereb Injiil (WOL2010) vs BKJ

Sair da comparação
1 Fàttali leen ñuy déggal kilifa, yi yore nguur gi, tey jëfe seeni ndigal, ñu taxaw temm ci lépp luy jëf ju baax.
1 Admoesta-os a que sejam submissos aos principados e potestades, que obedeçam os magistrados e estejam preparados para toda boa obra.
2 Buñu jëw kenn mbaa ñuy ŋaayoo, waaye nañu yiwe te won ñépp lewet gu mat sëkk.
2 Que de ninguém falem mal, nem sejam contenciosos, mas bondosos, mostrando toda mansidão para com todos os homens.
3 Ndaxte nun itam ñu ñàkk xel lanu woon te déggadi, nu réer bay jaamu ay bëgg-bëgg ak i bànneex yu wuute, nu dëkk ci coxorte ak ñeetaane, ñu bañ nu te nu bañante ci sunu biir.
3 Porque também nós éramos, noutro tempo, tolos, desobedientes, enganadores, servindo a várias concupiscências e prazeres, vivendo em malícia e inveja, odiosos, e odiando uns aos outros.
4 Waaye naka noona Yàlla sunu Musalkat feeñal na mbaaxam ak cofeelam,
4 Mas, quando a benignidade e o amor de Deus, nosso Salvador, para com os homens, apareceu,
5 ba musal nu; ajuwul ci jëf yu jub yu nu def, waaye ci yërmandeem rekk. Mu juddulaat nu ci laabal sunu xol, te yeesalaat nu ci dooley Xel mu Sell,
5 não pelas obras de justiça que houvéssemos feito, mas, segundo a sua misericórdia, nos salvou pela lavagem da regeneração e da renovação do Espírito Santo,
6 mi mu nu sotti ba mu baawaan, ci darajay Yeesu Kirist sunu Musalkat.
6 que abundantemente ele derramou sobre nós por Jesus Cristo, nosso Salvador,
7 Ci noonu Yàlla àtte na nu jub ci kaw yiwam, te sédd nu ci dund gu dul jeex, gi nuy séentu.
7 para que, sendo justificados por sua graça, sejamos feitos herdeiros, segundo a esperança da vida eterna.
8 Wax jooju ju wóor la, te damaa bëgg nga dëggal loolu, ngir ñi gëm Yàlla sax ci jëf lu rafet. Loolu moo baax te am njariñ ci nit.
8 Esta é uma palavra fiel, e estas coisas quero que deveras afirmes constantemente, para que os que creem em Deus procurem manter as boas obras; estas coisas são boas e proveitosas aos homens.
9 Waaye moytul yu deme ni werantey neen ak limi maam, ay xuloo ak i xëccoo ci doxalinu yoonu Musaa, ndax loolu waxi neen la, te amul benn njariñ.
9 Mas evita questões tolas, genealogias e contendas e debates acerca da lei; porque são inúteis e vãs.
10 Kuy féewale, nanga ko yedd, yeddaat ko; bu tëwee, nga dàq ko,
10 Ao homem que é herege, depois da primeira e segunda admoestação, rejeita.
11 xam ne nit ku ñaaw xel la te ay bàkkaaram fés ci ñépp.
11 Sabendo que aquele que é assim está pervertido e peca, estando condenado em si mesmo.
12 Bu ma la yónnee Artemas walla Tisig, gaawantul fekksi ma ci dëkku Nikopolis, ndax fa laa bëgga lollikooji.
12 Quando eu te enviar Ártemas, ou Tíquico, sê diligente ao vir ter comigo em Nicópolis; porque determinei invernar ali.
13 Naka Senas àttekat bi nag ak Apolos, waajal leen bu jekk ci seen tukki, ba seen aajo yépp faju.
13 Conduza diligentemente Zenas, o advogado, e Apolo, em sua viagem, para que nada lhes falte.
14 Na sunuy bokk it takku ci jëf yu rafet, ba mana faj aajo yépp, te baña yaafus.
14 E os nossos aprendam também a manter as boas obras nas coisas necessárias, para que eles não sejam infrutíferos.
15 Ñiy ànd ak man ñépp ñu ngi lay nuyu. Nuyul nu sunuy soppey ngëm. Yal na yiwu Yàlla ànd ak yéen ñépp.
15 Todos os que estão comigo saúdam-te. Saúda tu os que nos amam na fé. A graça seja com todos vós. Amém.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Tito 3, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.