Tito 2

Téereb Injiil (WOL2010) vs ARIB

Sair da comparação
ARIB Almeida Revisada Imprensa Bíblica
1 Yaw nag nangay waare li dëppook njàngle mu wér mi.
1 Tu, porém, fala o que convém à sã doutrina.
2 Maanaa, na góor ñu mag ñi foog, am faayda te maandu, di ñu wér ci seen ngëm, seen mbëggeel ak seen muñ.
2 Exorta os velhos a que sejam temperantes, sérios, sóbrios, sãos na fé, no amor, e na constância;
3 Jigéen ñu mag ñi itam, na seen doxalin ànd ak faayda; buñuy jëw mbaa ñuy xér ci sàngara. Waaye nañuy jàngle lu baax,
3 as mulheres idosas, semelhantemente, que sejam reverentes no seu viver, não caluniadoras, não dadas a muito vinho, mestras do bem,
4 bay xiir jeeg ju ndaw ji, ñu bëgg seen jëkkër ak seeni doom,
4 para que ensinem as mulheres novas a amarem aos seus maridos e filhos,
5 di ñu maandu, sell te fonk seen kër, ñu neex deret te déggal seeni jëkkër, ngir kenn bañ cee gàkkal kàddug Yàlla.
5 a serem moderadas, castas, operosas donas de casa, bondosas, submissas a seus maridos, para que a palavra de Deus não seja blasfemada.
6 Naka noonu itam nanga xiir waxambaane yi cig maandu.
6 Exorta semelhantemente os moços a que sejam moderados.
7 Te yaw, ci lépp lu mu mana doon, nekkal ab royukaay ci jëf yu baax. Na sa njàngle wér te am faayda,
7 Em tudo te dá por exemplo de boas obras; na doutrina mostra integridade, sobriedade,
8 ànd ak wax yu wér yu kenn manta diiŋat, ngir sunuy noon rus ba wedam, ci li ñu amul dara lu ñu nu tuumaal.
8 linguagem sã e irrepreensível, para que o adversário se confunda, não tendo nenhum mal que dizer de nós.
9 Waxal it jaam ñi, ñu déggal seeni sang ci lépp, te liggéeyal leen ba seral seen xol, bañ cee boole werante
9 Exorta os servos a que sejam submissos a seus senhores em tudo, sendo-lhes agradáveis, não os contradizendo
10 mbaa sàcc. Waaye nañu wone takkute gu mat, ba rafetal ci lépp njànglem Yàlla sunu Musalkat.
10 nem defraudando, antes mostrando perfeita lealdade, para que em tudo sejam ornamento da doutrina de Deus nosso Salvador.
11 Ndaxte yiwu Yàlla feeñ na te ubbil na ñépp buntu mucc.
11 Porque a graça de Deus se manifestou, trazendo salvação a todos os homens,
12 Moo nu digal, nu dëddu weddi ak bëgg-bëggi jamono, tey dund ci àddina cig maandu, njub ak ragal Yàlla,
12 ensinando-nos, para que, renunciando à impiedade e às paixões mundanas, vivamos no presente mundo sóbria, e justa, e piamente,
13 di séentu bés bu tedd bi nu yaakaar, maanaa Yàlla ju màgg ji, di sunu Musalkat Yeesu Kirist, feeñ ci biir ndamam.
13 aguardando a bem-aventurada esperança e o aparecimento da glória do nosso grande Deus e Salvador Cristo Jesus,
14 Joxe na bakkanam ngir nun, ba jot nu ci lépp lu bon, te beral nu boppam, di xeet wu sell te ràññiku ci jëf yu baax.
14 que se deu a si mesmo por nós para nos remir de toda a iniqüidade, e purificar para si um povo todo seu, zeloso de boas obras.
15 Jàngleel loolu, di leen dénk ak a yedd ak fulla ju mat. Bu la kenn yab.
15 Fala estas coisas, exorta e repreende com toda autoridade. Ninguém te despreze.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Tito 2, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.