Tito 1
Téereb Injiil (WOL2010) vs VC
1 Man Pool maa lay bind, man miy jaamu Yàlla ak ndaw li Yeesu Kirist yónni, ngir xamle ngëm, gi lal yoonu ñi Yàlla tànn, tey yokk xam-xamu dëgg, giy meññ ragal Yàlla;
1 Paulo, servo de Deus, apóstolo de Jesus Cristo para levar aos eleitos de Deus a fé e o profundo conhecimento da verdade que conduz à piedade,
2 mu sukkandiku ci yaakaar ju dëggu, ji nu am ci dund gu dul jeex, gi Yàlla dige ba dara sosoogul, moom mi dul tebbi waxam.
2 na esperança da vida eterna prometida em tempos longínquos por Deus veraz e fiel,
3 Te léegi, ci jamono ji ko soob, feeñal na xibaaram boobu ci waaraate, bi ma Yàlla sunu Musalkat dénk te digal ma, ma xamle ko.
3 que na ocasião escolhida manifestou a sua palavra mediante a pregação que me foi confiada por ordem de Deus, nosso Salvador,
4 Maa ngi lay bind, Tit, yaw sama doomu diine ju wér ci ngëm, gi nu bokk nun ñépp. Yal na la Yàlla Baay bi ak Kirist Yeesu sunu Musalkat may yiw ak jàmm.
4 a Tito, meu verdadeiro filho em nossa fé comum: graça e paz da parte de Deus Pai e de Jesus Cristo, nosso Salvador!
5 Bàyyi naa la ca réewu Keret, ngir nga mottali la desoon ci liggéey bi, te samp ay njiiti mbooloo ca dëkk bu nekk, ni ma la ko sante woon.
5 Eu te deixei em Creta para acabares de organizar tudo e estabeleceres anciãos em cada cidade, de acordo com as normas que te tracei.
6 Njiit nag nii la wara mel: war na ñàkk ŋàññ, yem ci benn soxna, am ay doom yu gëm yu amul baatu gannaaw cig yàqute mbaa déggadi.
6 {Devem ser escolhidos entre} quem seja irrepreensível, casado uma só vez, tenha filhos fiéis e não acusados de má conduta ou insubordinação.
7 Ndaxte kuy sàmm mbooloo mi mooy jawriñu Yàlla, kon warul am ŋàññ, walla di ku dëgër bopp mbaa ku tàng bopp; warul dib màndikat walla xeexkat mbaa ku bëgge ci alal ju lewul.
7 Porquanto é mister que o bispo seja irrepreensível, como administrador que é posto por Deus. Não arrogante, nem colérico, nem intemperante, nem violento, nem cobiçoso.
8 Waaye war na man gan te bëgg lu baax, di ku maandu te jub, ku sell te not boppam.
8 Ao contrário, seja hospitaleiro, amigo do bem, prudente, justo, piedoso, continente,
9 War na jàpp ci xibaar bu dëggu, bi lal sunu yoon, ba mana dénkaane ci njàngle mu wér mi, tey yey ñi weddi.
9 firmemente apegado à doutrina da fé tal como foi ensinada, para poder exortar segundo a sã doutrina e rebater os que a contradizem.
10 Loolu war na, ndaxte am na ñu bare ñu déggul lenn ndigal, rawatina ci Yawut yi, ñuy yàq xeli nit ñi ak seen waxi neen.
10 Com efeito, há muitos insubmissos, charlatães e sedutores, principalmente entre os da circuncisão.
11 Fàww nga wedamloo leen, ndax dañuy tas këri lëmm, ciy jàngle li warul, ngir sàkku alal ju lewul.
11 É necessário tapar-lhes a boca, porque transtornam famílias inteiras, ensinando o que não convém, e isso por vil espírito de lucro.
12 Am na nitu Keret, di yonent ci ñoom, mu ne: «Waa Keret, ay fenkat lañu masa doon, ñu soxor ni ay rabi àll, fuqle te tayel.»
12 Um dentre eles, o profeta deles disse: Os cretenses são sempre mentirosos, feras selvagens, glutões preguiçosos.
13 Te li mu wax dëgg la. Looloo tax nga war leena yey bu wóor ci seeni bàkkaar, ngir ñu am ngëm gu wér
13 Esta asserção reflete a verdade. Portanto, repreende-os severamente, para que se mantenham sãos na fé,
14 te baña topp léebi diiney neen yu Yawut yi, mbaa tegtali nit, ñi dëddu dëgg.
14 e não dêem ouvidos a fábulas judaicas nem a preceitos de homens avessos à verdade.
15 Ñi sell seen lépp a sell, waaye ñi selladi te gëmadi seen dara sellul, du seeni xalaat, du seeni xel.
15 Para os puros todas as coisas são puras. Para os corruptos e descrentes nada é puro: até a sua mente e consciência são corrompidas.
16 Dañoo mbubboo xam-xamu Yàlla, waaye seeni jëf weddi na ko; ñu sikk lañu te déggadi, ba tële ci jëf lenn lu baax.
16 Proclamam que conhecem a Deus, mas na prática o renegam, detestáveis que são, rebeldes e incapazes de qualquer boa obra.
Atalhos do teclado
- Capítulo anterior←
- Próximo capítulo→
- Versículo anteriork
- Próximo versículoj
- Limpar seleçãoEsc
- Esta ajuda?
Estude este capítulo no WhatsApp
Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Tito 1, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.