Tiago 1

Téereb Injiil (WOL2010) vs ACF

Sair da comparação
ACF Almeida Corrigida Fiel
1 Man Saag, jaamu Yàlla ak Boroom bi Yeesu Kirist, maa leen di nuyu, yéen fukki giir ak ñaar, yi tasaaroo ci biir àddina si.
1 Tiago, servo de Deus, e do Senhor Jesus Cristo, às doze tribos que andam dispersas, saúde.
2 Yéen samay bokk, waxtu wu nattu yi dalee ci seen kaw, ak nu ñu mana mel, defleen ko ni mbég mu réy,
2 Meus irmãos, tende grande gozo quando cairdes em várias tentações;
3 xam ne nattub ngëm mooy ndeyu muñ.
3 Sabendo que a prova da vossa fé opera a paciência.
4 Kon na seen muñ dem ba mat, ngir ngeen baña fell fenn, waaye ngeen mat sëkk.
4 Tenha, porém, a paciência a sua obra perfeita, para que sejais perfeitos e completos, sem faltar em coisa alguma.
5 Ku xelam des ci benn fànn ci yéen nag, na ko ñaan Yàlla, te dina ko ko may, ndaxte Yàlla mooy Aji Yéwén, jiy may ñépp ci lu àndul ak genn ŋàññ.
5 E, se algum de vós tem falta de sabedoria, peça-a a Deus, que a todos dá liberalmente, e o não lança em rosto, e ser-lhe-á dada.
6 Waaye na ko ñaan ci ngëm te bañ cee werante; ndaxte kiy werante mi ngi mel ni ndoxum géej, mi ngelaw liy lëmbaaje wet gu ne.
6 Peça-a, porém, com fé, em nada duvidando; porque o que duvida é semelhante à onda do mar, que é levada pelo vento, e lançada de uma para outra parte.
7 Bu kooku yaakaar dara ci Boroom bi.
7 Não pense tal homem que receberá do Senhor alguma coisa.
8 Ku am xel ñaar la, te ñàkk pastéef ci lépp lu mu mana def.
8 O homem de coração dobre é inconstante em todos os seus caminhos.
9 Naka mbokk mi néew doole, na sant ci teraangaam fa kanam Yàlla;
9 Mas glorie-se o irmão abatido na sua exaltação,
10 te boroom alal it sant cig suufeem, ndax ni tóor-tóor di ruuse, noonu lay wéye.
10 E o rico em seu abatimento; porque ele passará como a flor da erva.
11 Su jant fenkee, ba naaj wi tàng, kon gàncax lax, tóor-tóor ruus, te rafetaayam naaw. Noonu la boroom alal di nasaxe, moom ak i jëfam.
11 Porque sai o sol com ardor, e a erva seca, e a sua flor cai, e a formosa aparência do seu aspecto perece; assim se murchará também o rico em seus caminhos.
12 Ku dékku nattu, ku barkeel nga, ndax boo ci génnee ak ndam, dees na la jagleel kaalag dund, gi Yàlla dig ñi ko bëgg.
12 Bem-aventurado o homem que sofre a tentação; porque, quando for provado, receberá a coroa da vida, a qual o Senhor tem prometido aos que o amam.
13 Bu la fiir galanee, bul ne: «Yàllaa ko dogal,» ndaxte Yàlla jegewul ak mbon fenn te du fiir kenn.
13 Ninguém, sendo tentado, diga: De Deus sou tentado; porque Deus não pode ser tentado pelo mal, e a ninguém tenta.
14 Waaye ku sa bakkan nax, ba man la, looloo lay dugal ci fiir.
14 Mas cada um é tentado, quando atraído e engodado pela sua própria concupiscência.
15 Kon bu bëgg-bëgg ëmbee, bàkkaar lay wasin, te bu bàkkaar màggee, jur dee.
15 Depois, havendo a concupiscência concebido, dá à luz o pecado; e o pecado, sendo consumado, gera a morte.
16 Yéen sama bokk yi ma bëgg, buleen juum ci lii:
16 Não erreis, meus amados irmãos.
17 gépp may gu baax ak gépp jagle gu mat, ci Yàlla la jóge, di Baay bi sàkk leeri asamaan, fekk moom du soppiku, mbaa muy leer ak di lëndëm.
17 Toda a boa dádiva e todo o dom perfeito vem do alto, descendo do Pai das luzes, em quem não há mudança nem sombra de variação.
18 Ci coobareem la nu sole kàddug dëgg gi, ba nu judduwaat, di tànneefu lépp lu mu bind.
18 Segundo a sua vontade, ele nos gerou pela palavra da verdade, para que fôssemos como primícias das suas criaturas.
19 Yéen sama bokk yi ma bëgg, nangeen xam lii: ku nekk war ngaa farlu ci déglu, di yéexa wax tey yéexa mer.
19 Portanto, meus amados irmãos, todo o homem seja pronto para ouvir, tardio para falar, tardio para se irar.
20 Ndaxte meru nit du jur njub gi neex Yàlla.
20 Porque a ira do homem não opera a justiça de Deus.
21 Moo tax nanguleen ci woyof kàddu, gi leen Yàlla sol te man leena musal, di dëddu bépp sobe ak coxor gi daj àddina.
21 Por isso, rejeitando toda a imundícia e superfluidade de malícia, recebei com mansidão a palavra em vós enxertada, a qual pode salvar as vossas almas.
22 Buleen yem ci déglu kàddu gi rekk, di nax seen bopp; waaye jëfeleen ko.
22 E sede cumpridores da palavra, e não somente ouvintes, enganando-vos a vós mesmos.
23 Ndaxte ku déglu kàddu gi te bañ koo jëfe, moom ak kuy seetu ñoo yem:
23 Porque, se alguém é ouvinte da palavra, e não cumpridor, é semelhante ao homem que contempla ao espelho o seu rosto natural;
24 day gis xar kanamam, te su nee wërëñ, daldi fàtte meloom.
24 Porque se contempla a si mesmo, e vai-se, e logo se esquece de como era.
25 Waaye kuy gëstu yoonu Yàlla, wi mat tey goreel —waxuma ki dégg, ba noppi fàtte, waaye kiy jëfe ndigal— kooku barkeel na ci kaw jëfam.
25 Aquele, porém, que atenta bem para a lei perfeita da liberdade, e nisso persevera, não sendo ouvinte esquecediço, mas fazedor da obra, este tal será bem-aventurado no seu feito.
26 Ku yaakaar ne am na diine, waaye moomul làmmiñam, xanaa di nax boppam rekk, diineem jooju du diiney dara.
26 Se alguém entre vós cuida ser religioso, e não refreia a sua língua, antes engana o seu coração, a religião desse é vã.
27 Ku diineem sell te amul benn gàkk fa kanam Yàlla mooy kii: ki nemmiku jirim yi ak jigéen, ñi seen jëkkër faatu, ci seeni tiis, tey waggar sobey àddina.
27 A religião pura e imaculada para com Deus e Pai, é esta: Visitar os órfãos e as viúvas nas suas tribulações, e guardar-se da corrupção do mundo.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Tiago 1, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.