Romanos 9

Téereb Injiil (WOL2010) vs ARIB

Sair da comparação
ARIB Almeida Revisada Imprensa Bíblica
1 Li ma bëgga wax nag, ci kanam Kirist laa koy waxe; dëgg la, du aw fen. Sama xel, mi Xel mu Sell miy leeral, seedeel na ma ne dëgg laay wax.
1 Digo a verdade em Cristo, não minto, dando testemunho comigo a minha consciência no Espírito Santo,
2 Maanaam, duma noppee am naqar wu réy ci sama biir xol,
2 que tenho grande tristeza e incessante dor no meu coração.
3 ba xawa bëgga tàggoo ak Kirist te alku, ngir ñi ma bokkal xeet mucc.
3 Porque eu mesmo desejaria ser separado de Cristo, por amor de meus irmãos, que são meus parentes segundo a carne;
4 Bànni Israyil lañu, te Yàlla def na leen ni ay doomam; dëkkaloon na ndamam ci seen biir, fas ak ñoom kóllëre yi. Ñoom la Yàlla dénk yoonu Musaa, ñoom la xamal ni ñu ko wara jaamoo, ñoom la jox i digam.
4 os quais são israelitas, de quem é a adoção, e a glória, e os pactos, e a promulgação da lei, e o culto, e as promessas;
5 Maam ya Yàlla tànnoon, ci ñoom lañu bokk, ci ñoom it la Kirist wàcce, maanaam ci jëmmam, Kirist mi di Yàlla, tiim lépp, te yelloo teraanga ba fàww. Amiin.
5 de quem são os patriarcas; e de quem descende o Cristo segundo a carne, o qual é sobre todas as coisas, Deus bendito eternamente. Amém.
6 Waaye neewuma waxu Yàlla dafa toxu, ndaxte bokk ci bànni Israyil, taxul nga bokk ci Israyil tigi.
6 Não que a palavra de Deus haja falhado. Porque nem todos os que são de Israel são israelitas;
7 Te it du ñi soqikoo ci Ibraayma ñépp, ay doomam dëgg lañu. Ndaxte Yàlla dafa wax Ibraayma ne ko: «Saw askan ci Isaaxa lay jaar.»
7 nem por serem descendência de Abraão são todos filhos; mas: Em Isaque será chamada a tua descendência.
8 Maanaam, soqikoo ci Ibraayma taxula nekk doomu Yàlla, waaye juddu ci biir digeb Yàlla mooy taxa bokk dëgg-dëgg ci askanu Ibraayma.
8 Isto é, não são os filhos da carne que são filhos de Deus; mas os filhos da promessa são contados como descendência.
9 Ndaxte Yàlla dafa digoon Ibraayma ne ko: «Ci waxtu wii déwén dinaa délsi ci yaw, te Saarata dina am doom ju góor.»
9 Porque a palavra da promessa é esta: Por este tempo virei, e Sara terá um filho.
10 Du ci loolu rekk, waaye noonu la it ci lu jëm ci Rebeka; doom yi mu jur ñoo bokk benn baay, moo di sunu maam Isaaxa.
10 E não somente isso, mas também a Rebeca, que havia concebido de um, de Isaque, nosso pai
11 — ausente —
11 {pois não tendo os gêmeos ainda nascido, nem tendo praticado bem ou mal, para que o propósito de Deus segundo a eleição permanecesse firme, não por causa das obras, mas por aquele que chama},
12 — ausente —
12 foi-lhe dito: O maior servirá o menor.
13 Loolu la Mbind mi wax ne: «Bëgg naa Yanqóoba, bañ naa Esawu.»
13 Como está escrito: Amei a Jacó, e aborreci a Esaú.
14 Kon lu nu ci wara wax? Ndax Yàlla àttewul foofu yoon nag? Mukk!
14 Que diremos, pois? Há injustiça da parte de Deus? De modo nenhum.
15 Dafa wax Musaa sax ne ko:
15 Porque diz a Moisés: Terei misericórdia de quem me aprouver ter misericórdia, e terei compaixão de quem me aprouver ter compaixão.
16 Dama leen di wax nag, dara ajuwul ci coobarey nit, mbaa ci ñaqam, waaye lépp a ngi aju ci yërmandey Yàlla.
16 Assim, pois, isto não depende do que quer, nem do que corre, mas de Deus que usa de misericórdia.
17 Ndax Mbind mi biral na li Yàlla wax Firawna ne ko: «Def naa la buur, ngir feeñal sama kàttan ci say mbir, ngir siiwal sama tur ci àddina si sépp.»
17 Pois diz a Escritura a Faraó: Para isto mesmo te levantei: para em ti mostrar o meu poder, e para que seja anunciado o meu nome em toda a terra.
18 Kon nag Yàlla, la ko neex lay def, muy yërëm nit, mbaa dëgëral xolam ci lu bon.
18 Portanto, tem misericórdia de quem quer, e a quem quer endurece.
19 Waaye xanaa dina am ku may wax ne: «Gannaaw kenn manula bañ coobarey Yàlla, lu tax kon muy teg nit tooñ?»
19 Dir-me-ás então. Por que se queixa ele ainda? Pois, quem resiste à sua vontade?
20 Yaw nag nit ki, ak koo mana doon, lu tax ngay werante ak Yàlla? Ndax mbindeef dina laaj ki ko bind: «Lu tax nga binde ma nii?»
20 Mas, ó homem, quem és tu, que a Deus replicas? Porventura a coisa formada dirá ao que a formou: Por que me fizeste assim?
21 Ndax tabaxkatu ndaa sañula fab banam, tabax ci ñaari ndaa, benn bi ngir soxla yu am maana, bi ci des ngir soxla yu ndaw?
21 Ou não tem o oleiro poder sobre o barro, para da mesma massa fazer um vaso para uso honroso e outro para uso desonroso?
22 Kon nag looy wax ci lii: Yàlla bëggoon na wone meram, xamle it dooleem ci àddina; teewul dafa sax ci muñal ñi yelloo meram te taxaw ci sànku.
22 E que direis, se Deus, querendo mostrar a sua ira, e dar a conhecer o seu poder, suportou com muita paciência os vasos da ira, preparados para a perdição;
23 Bëggoon na it xamle màggaayam mu ëpp xel, ci boole ñi mu yërëm ci ndamam; moo tax mu tànn leen ca njàlbéen.
23 para que também desse a conhecer as riquezas da sua glória nos vasos de misericórdia, que de antemão preparou para a glória,
24 Wax ji noo ko moom, nun ñi Yàlla woo ci boppam ci biir Yawut yi ak ci biir xeet yi ci des.
24 os quais somos nós, a quem também chamou, não só dentre os judeus, mas também dentre os gentios?
25 Moom la wax ci téereb Ose ne:
25 Como diz ele também em Oséias: Chamarei meu povo ao que não era meu povo; e amada à que não era amada.
26 Te:
26 E sucederá que no lugar em que lhes foi dito: Vós não sois meu povo; aí serão chamados filhos do Deus vivo.
27 Esayi wax na ci mbirum Israyil ne:
27 Também Isaías exclama acerca de Israel: Ainda que o número dos filhos de Israel seja como a areia do mar, o remanescente é que será salvo.
28 Ndaxte li Boroom bi dogal ci àddina,
28 Porque o Senhor executará a sua palavra sobre a terra, consumando-a e abreviando-a.
29 Esayi it waxoon na lu jiitu loolu ne:
29 E como antes dissera Isaías: Se o Senhor dos Exércitos não nos tivesse deixado descendência, teríamos sido feitos como Sodoma, e seríamos semelhantes a Gomorra.
30 Lu nu ci wara wax nag? Ñi dul Yawut te fonkuñu woon jub ci kanam Yàlla, léegi jub nañu ci kaw ngëm.
30 Que diremos pois? Que os gentios, que não buscavam a justiça, alcançaram a justiça, mas a justiça que vem da fé.
31 Waaye bànni Israyil, mi bëggoona sàmm yoon ngir jub, matalu ko.
31 Mas Israel, buscando a lei da justiça, não atingiu esta lei.
32 Ndax lan? Ndax dañoo sukkandiku ci seeni jëf, bàyyi ngëm. Dañoo daanu ci «doj wuy fakktale.»
32 Por que? Porque não a buscavam pela fé, mas como que pelas obras; e tropeçaram na pedra de tropeço;
33 Moom la Yàlla wax ci Mbind mi ne:
33 como está escrito: Eis que eu ponho em Sião uma pedra de tropeço; e uma rocha de escândalo; e quem nela crer não será confundido.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Romanos 9, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.