Mateus 8

Téereb Injiil (WOL2010) vs NAA

Sair da comparação
NAA Nova Almeida Atualizada 2017
1 Bi loolu amee Yeesu wàcc ca tund wa, te mbooloo mu bare topp ko.
1 Quando Jesus desceu do monte, grandes multidões o seguiram.
2 Noonu ku gaana ñëw, sukk ci kanamam ne ko: «Sang bi, soo ko bëggee, man nga maa faj.»
2 E eis que um leproso aproximou-se e o adorou, dizendo: — Senhor, se quiser, pode me purificar.
3 Yeesu tàllal loxoom, laal ko naan: «Bëgg naa ko, wéral.» Ca saa sa ngaanaam daldi deñ.
3 E Jesus, estendendo a mão, tocou nele, dizendo: E, no mesmo instante, ele ficou limpo da sua lepra.
4 Yeesu ne ko: «Déglul, bu ko wax kenn, waaye demal won sa bopp sarxalkat bi, te nga jébbal Yàlla sarax, si yoonu Musaa santaane, ngir mu nekk seede ci ñoom.»
4 Então Jesus lhe disse:
5 Gannaaw loolu Yeesu duggoon na Kapernawum. Bi mu fa duggee nag, ab njiitu xare fekksi ko. Mu ñaan ko,
5 Tendo Jesus entrado em Cafarnaum, um centurião se aproximou dele, implorando:
6 ne ko: «Sang bi, sama surga dafa làggi, tëdd ca kër ga te sonn lool.»
6 — Senhor, o meu servo está na minha casa, de cama, paralítico, sofrendo horrivelmente.
7 Yeesu ne ko: «Dinaa ñëw faj ko.»
7 Jesus lhe disse:
8 Waaye njiit la ne ko: «Sang bi, yeyoowuma nga dugg ci sama kër; waxal genn kàddu rekk, te sama surga dina wér.
8 Mas o centurião respondeu: — Senhor, não sou digno de recebê-lo em minha casa. Mas apenas mande com uma palavra, e o meu servo será curado.
9 Ndaxte man itam maa ngi nekk ci ndigal, te ame naa ay xarekat ci sama ndigal. Su ma nee kii: “Demal,” mu dem. Mbaa ma ne keneen ki: “Ñëwal,” mu ñëw. Te su ma nee sama jaam: “Defal lii,” mu def ko.»
9 Porque também eu sou homem sujeito à autoridade, tenho soldados às minhas ordens e digo a este: “Vá”, e ele vai; e a outro: “Venha”, e ele vem; e ao meu servo: “Faça isto”, e ele o faz.
10 Bi ko Yeesu déggee, mu waaru, ne ña topp ci moom: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, masumaa gis ci bànni Israyil ku gëme ni kii.
10 Ao ouvir isso, Jesus ficou admirado e disse aos que o acompanhavam:
11 Maa ngi leen koy wax, ñu bare dinañu ñëw, jóge ci penku ak sowu, bokk lekk ak Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji.
11 Digo a vocês que muitos virão do Oriente e do Ocidente e tomarão lugar à mesa com Abraão, Isaque e Jacó no Reino dos Céus.
12 Waaye ñi waroona bokk ca nguur ga, dees na leen sànni ci biti ci lëndëm gi. Foofa dees na fa jooy tey yéyu.»
12 Mas os filhos do Reino serão lançados para fora, nas trevas; ali haverá choro e ranger de dentes.
13 Ci kaw loolu Yeesu wax njiit la ne ko: «Ñibbil, na ame, ni nga ko gëme.» Noonu ca waxtu woowa sax surga ba daldi wér.
13 Então Jesus disse ao centurião: E, naquela mesma hora, o servo do centurião foi curado.
14 Gannaaw loolu Yeesu dem kër Piyeer. Ba mu eggee, mu fekk gorob Piyeer bu jigéen tëdd ak yaram wu tàng.
14 Tendo Jesus chegado à casa de Pedro, viu a sogra deste acamada, com febre.
15 Bi mu ko gisee, Yeesu laal loxoom, tàngoor wa daldi wàcc; soxna sa jóg, di ko topptoo.
15 Mas Jesus tomou-a pela mão, e a febre a deixou. Ela se levantou e passou a servi-lo.
16 Ca ngoon sa ñu indil ko ñu bare ñu rab jàpp. Yeesu dàq rab ya ak kàddoom te faj ñi wopp ñépp.
16 Ao cair da tarde, trouxeram a Jesus muitos endemoniados. E apenas com a palavra expulsou os espíritos e curou todos os que estavam doentes,
17 Loolu mu def, def na ko, ngir la ñu waxoon jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi am, bi mu naan:
17 para se cumprir o que foi dito por meio do profeta Isaías: “Ele mesmo tomou as nossas enfermidades e carregou as nossas doenças.”
18 Bi Yeesu gisee mbooloo ma ko wër nag, mu sant taalibe ya, ñu jàll dex ga.
18 Vendo Jesus muita gente ao seu redor, ordenou que passassem para a outra margem.
19 Laata ñuy jàll, benn xutbakat daldi ñëw ci moom ne ko: «Kilifa gi, dinaa la topp fépp foo jëm.»
19 Então, aproximando-se dele um escriba, disse a Jesus: — Mestre, vou segui-lo para onde quer que o senhor for.
20 Waaye Yeesu ne ko: «Till yi am nañu seeni kàmb, te picci asamaan am nañu ay tàgg, waaye Doomu nit ki amul fu mu noppal boppam.»
20 Mas Jesus lhe respondeu:
21 Noonu keneen ca taalibe ya ne ko: «Sang bi, may ma, ma jëkka dem suuli sama baay.»
21 E outro dos discípulos lhe disse: — Senhor, deixe-me ir primeiro sepultar o meu pai.
22 Yeesu ne ko: «Toppal ci man te bàyyi ñi dee, ñu suul seeni néew.»
22 Mas Jesus respondeu:
23 Bi mu ko waxee, Yeesu dugg ca gaal ga, ay taalibeem topp ko.
23 Jesus entrou no barco e os seus discípulos o seguiram.
24 Ca saa sa ngelaw lu bare daldi yëngal dex ga, ba duus ya sàng gaal ga. Fekk booba Yeesu nelaw.
24 E eis que levantou-se no mar uma grande tempestade, de modo que as ondas cobriam o barco. Jesus, porém, estava dormindo.
25 Noonu taalibe ya daldi jegesi, yee ko naan: «Sang bi, musal nu, nu ngiy dee!»
25 Mas os discípulos foram acordá-lo, dizendo: — Senhor, salve-nos! Estamos perecendo!
26 Waaye Yeesu ne leen: «Yéen ñi néew ngëm, lu tax ngeen tiit?» Ci kaw loolu mu jóg, daldi gëdd ngelaw li ak duus yi. Lépp dal, ba ne nemm.
26 Então Jesus perguntou: E, levantando-se, repreendeu os ventos e o mar; e tudo ficou bem calmo.
27 Bi ko nit ña gisee, ñu waaru naan: «Kii kan la ci biir nit ñi, ba ngelaw li ak dex gi di ko déggal?»
27 E aqueles homens ficaram admirados, dizendo: — Quem é este que até os ventos e o mar lhe obedecem?
28 Bi Yeesu jàllee nag, ba teer ca diiwaanu waa Gadara, ñaar ñu rab jàpp daldi génn ca sëg ya, ñëw kar ko. Ñaar ñooñu nag, ñu soxor lañu woon, ba kenn ñemewul woona jaar foofa.
28 Quando Jesus chegou à outra margem, à terra dos gadarenos, dois endemoniados foram ao seu encontro, saindo dentre os túmulos. Eles eram tão furiosos, que ninguém podia passar por aquele caminho.
29 Ña rab jàpp daldi xaacu naan: «Yaw Doomu Yàlla ji, loo nuy fexeel? Ndax danga noo bëgga mbugal, bala waxtu way jot?»
29 E eis que gritaram: — O que você quer conosco, Filho de Deus? Você veio aqui nos atormentar antes do tempo?
30 Fekk amoon na ca wet ya géttu mbaam-xuux yu bare yuy for.
30 Ora, uma grande manada de porcos estava pastando não longe deles.
31 Rab ya nag ñaan ko ne: «Boo nu dàqee, sànni nu ca géttu mbaam-xuux ya.»
31 Então os demônios pediram a Jesus com insistência: — Se você vai nos expulsar, mande-nos para a manada de porcos.
32 Yeesu ne leen: «Demleen.» Rab ya nag daldi génn, dugg ca mbaam-xuux ya, ñu daldi bartalu, daanu ca dex ga, lab ca ndox ma.
32 Jesus disse: E eles, saindo, entraram nos porcos; e eis que toda a manada se precipitou, despenhadeiro abaixo, para dentro do mar, e morreram nas águas.
33 Ba sàmm ya gisee loolu, ñu daw, dem dëkk ba, nettaliji lépp ak la xewoon ca ña rab jàpp.
33 Os que tratavam dos porcos fugiram e, chegando à cidade, anunciaram todas estas coisas e o que tinha acontecido com os endemoniados.
34 Noonu dëkk ba bépp génn seeti Yeesu. Ba ñu ko gisee nag, ñu ñaan ko, mu génn seen réew.
34 Então a cidade toda saiu para encontrar-se com Jesus. E, ao vê-lo, pediram-lhe com insistência que se retirasse da terra deles.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Mateus 8, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.