Mateus 4

Téereb Injiil (WOL2010) vs NAA

Sair da comparação
NAA Nova Almeida Atualizada 2017
1 Bi loolu amee Xelum Yàlla yóbbu Yeesu ca màndiŋ ma, ngir mu jànkoonte ak fiiri Seytaane.
1 A seguir, Jesus foi levado pelo Espírito ao deserto, para ser tentado pelo diabo.
2 Yeesu nekk fa te lekkul ñeent fukki bëccëg ak ñeent fukki guddi, doora xiif.
2 E, depois de jejuar quarenta dias e quarenta noites, teve fome.
3 Noonu fiirkat bi ñëw ci moom ne ko: «Boo dee Doomu Yàlla, santal doj yii, ñu nekk mburu.»
3 Então o tentador, aproximando-se, disse a Jesus: — Se você é o Filho de Deus, mande que estas pedras se transformem em pães.
4 Waaye Yeesu ne ko: «Mbind mi nee na: “Nit du dunde mburu rekk, waaye itam gépp kàddu gu génne ci gémmiñug Yàlla.”»
4 Jesus, porém, respondeu:
5 Bi mu waxee loolu, Seytaane yóbbu ko ca dëkk bu sell ba, teg ko ca njobbaxtalu kër Yàlla ga.
5 Então o diabo levou Jesus à Cidade Santa, colocou-o sobre o pináculo do templo
6 Mu ne ko: «Boo dee Doomu Yàlla, tëbal ci suuf, ndaxte Mbind mi nee na:
6 e disse: — Se você é o Filho de Deus, jogue-se daqui, porque está escrito: “Aos seus anjos ele dará ordens a seu respeito. E eles o sustentarão nas suas mãos, para que você não tropece em alguma pedra.”
7 Yeesu ne ko: «Bind nañu it ne: “Bul diiŋat Yàlla, sa Boroom.”»
7 Jesus respondeu:
8 Gannaaw loolu Seytaane yóbbu ko ci kaw tund wu kawe lool, won ko réewi àddina yépp ak seeni ndam.
8 O diabo ainda levou Jesus a um monte muito alto, mostrou-lhe todos os reinos do mundo e a glória deles
9 Mu ne ko: «Lii lépp dinaa la ko may, boo sukkee màggal ma.»
9 e disse: — Tudo isso lhe darei se, prostrado, você me adorar.
10 Waaye Yeesu ne ko: «Sore ma Seytaane, ndaxte Mbind mi nee na: “Nanga màggal Yàlla sa Boroom, te jaamu ko moom rekk.”»
10 Então Jesus lhe ordenou:
11 Noonu Seytaane bàyyi ko. Te ay malaaka daldi ñëw fi Yeesu, di ko topptoo.
11 Com isto, o diabo deixou Jesus, e eis que vieram anjos e o serviram.
12 Am bés Yeesu dégg ne jàpp nañu Yaxya; mu jóg nag, jëm Galile.
12 Ao ouvir que João tinha sido preso, Jesus voltou para a Galileia.
13 Gannaaw gi, mu toxoo dëkku Nasaret, dem dëkk Kapernawum, bi féeteek dex ga ci diiwaani Sabulon ak Neftali.
13 E, deixando Nazaré, foi morar em Cafarnaum, situada à beira-mar, na região de Zebulom e Naftali.
14 Noonu am la ñu waxoon, jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi, bi mu naan:
14 Isso aconteceu para se cumprir o que tinha sido dito por meio do profeta Isaías:
15 «Yaw réewum Sabulon ak réewum Neftali,
15 “Terra de Zebulom, terra de Naftali, caminho do mar, além do Jordão, Galileia dos gentios!
16 xeet wa nekkoon cig lëndëm,
16 O povo que vivia em trevas viu grande luz, e aos que viviam na região e sombra da morte resplandeceu-lhes a luz.”
17 Booba Yeesu tàmbali di waare naan: «Tuubleen seeni bàkkaar, ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji jegesi na.»
17 Daí em diante Jesus começou a pregar e a dizer:
18 Gannaaw loolu Yeesu doon dox ca tefesu dexu Galile, mu gis fa ñaar ñu bokk ndey ak baay, mooy Simoŋ mi ñuy wax Piyeer, ak Andare. Fekk ñuy sànni seen caax ca dex ga, ndaxte ay nappkat lañu woon.
18 Caminhando junto ao mar da Galileia, Jesus viu dois irmãos, Simão, chamado Pedro, e André. Eles lançavam as redes ao mar, porque eram pescadores.
19 Yeesu ne leen: «Ñëwleen topp ci man, ma def leen nappkati nit.»
19 Jesus lhes disse:
20 Ca saa sa ñu daldi bàyyi seeni mbaal, topp ci moom.
20 Então eles deixaram imediatamente as redes e o seguiram.
21 Ba Yeesu demee ba ca kanam, mu gis yeneen ñaar ñu bokk ndey ak baay, ñuy Saag doomu Sebede, ak Yowaana rakkam. Ñu nekk ci seen biir gaal ak Sebede seen baay, di defar seeni mbaal. Noonu Yeesu woo leen.
21 Pouco mais adiante, Jesus viu outros dois irmãos, Tiago, filho de Zebedeu, e João, o irmão dele. Eles estavam no barco em companhia de seu pai, consertando as redes; e Jesus os chamou.
22 Ca saa sa ñu daldi bàyyi gaal ga ak seen baay, topp ci moom.
22 Então eles, no mesmo instante, deixaram o barco e seu pai e seguiram Jesus.
23 Ba loolu amee Yeesu doon wër Galile gépp, di jàngle ci seeni jàngu tey yégle xibaaru jàmm bi ci nguuru Yàlla; muy faj jàngoro yépp ak wéradi yépp ca nit ña,
23 Jesus percorria toda a Galileia, ensinando nas sinagogas, pregando o evangelho do Reino e curando todo tipo de doenças e enfermidades entre o povo.
24 ba tax turam siiw ba ci biir réewu Siri mépp. Ñu di ko indil ñi wopp ñépp, ñi sonn ndax ay jàngoro ak metit yu bare, ñi rab jàpp, ñiy say ak ñi làggi, mu faj leen.
24 E a sua fama correu por toda a Síria. Trouxeram-lhe, então, todos os doentes, acometidos de várias enfermidades e tormentos: endemoniados, epilépticos e paralíticos. E ele os curou.
25 Noonu mbooloo mu bare topp ci moom, jóge ci wàlli Galile ak diiwaan bi ñuy wax Fukki dëkk yi, ci dëkku Yerusalem ak ci diiwaanu Yude, ba ci gannaaw dexu Yurdan.
25 E da Galileia, de Decápolis, de Jerusalém, da Judeia e do outro lado do Jordão numerosas multidões o seguiam.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Mateus 4, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.