Mateus 3
Téereb Injiil (WOL2010) vs VC
1 Ca jamono jooja Yaxya feeñoon na, di waare ca màndiŋu Yude.
1 Naqueles dias, apareceu João Batista, pregando no deserto da Judéia.
2 Nii la doon waaree: «Tuubleen seeni bàkkaar, ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji jege na.»
2 Dizia ele: Fazei penitência porque está próximo o Reino dos céus.
3 Yaxya mooy ki ñu doon wax jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi, bi mu naan:
3 Este é aquele de quem falou o profeta Isaías, quando disse: Uma voz clama no deserto: Preparai o caminho do Senhor, endireitai as suas veredas {Is 40,3}.
4 Yaxya nag mu ngi soloon mbubb mu ñu ràbbe kawaru giléem, takk geñog der ci ndiggam. Ay njéeréer la doon dunde ak lem.
4 João usava uma vestimenta de pêlos de camelo e um cinto de couro em volta dos rins. Alimentava-se de gafanhotos e mel silvestre.
5 Noonu ñépp génn jëm ci moom, ñi dëkk Yerusalem ak diiwaanu Yude, ak waa dexu Yurdan.
5 Pessoas de Jerusalém, de toda a Judéia e de toda a circunvizinhança do Jordão vinham a ele.
6 Ñu nangu seeni bàkkaar, Yaxya sóob leen ca dexu Yurdan.
6 Confessavam seus pecados e eram batizados por ele nas águas do Jordão.
7 Noonu ay Farisen ak ay Sadusen yu bare ñëw ci Yaxya, ngir mu sóob leen ñoom itam ca dex ga. Waaye bi leen Yaxya gisee, mu ne leen: «Yéen ñi fees ak daŋar mel ni ay co, ku leen artu, ngeen daw merum Yàlla mi nara wàcc?
7 Ao ver, porém, que muitos dos fariseus e dos saduceus vinham ao seu batismo, disse-lhes: Raça de víboras, quem vos ensinou a fugir da cólera vindoura?
8 Jëfeleen nag ni ñu tuub seeni bàkkaar,
8 Dai, pois, frutos de verdadeira penitência.
9 te buleen wax ci seen xel naan: “Nun daal doomi Ibraayma lanu,” ndaxte maa ngi leen koy wax, Yàlla man na sàkkal Ibraayma ay doom ci doj yii.
9 Não digais dentro de vós: Nós temos a Abraão por pai! Pois eu vos digo: Deus é poderoso para suscitar destas pedras filhos a Abraão.
10 Sémmiñ wi tiim na reeni garab yi. Garab nag gu meññul doom yu baax, dees na ko gor, sànni ko ci sawara si.
10 O machado já está posto à raiz das árvores: toda árvore que não produzir bons frutos será cortada e lançada ao fogo.
11 Man maa ngi leen di sóob ci ndox, ci lu ànd ak tuub seeni bàkkaar. Waaye kiy ñëw sama gannaaw moo ma ëpp kàttan, ba yeyoowuma koo yóbbul sax ay dàllam. Kooku dina leen sóob ci Xel mu Sell mi ak sawara.
11 Eu vos batizo com água, em sinal de penitência, mas aquele que virá depois de mim é mais poderoso do que eu e nem sou digno de carregar seus calçados. Ele vos batizará no Espírito Santo e em fogo.
12 Layoom mu ngi ci loxoom, ngir jéri dàgga ja, ba mu set; pepp ma dina ko def ca sàq ma, waaye xatax ba dina ko lakk ci sawara su dul fey mukk.»
12 Tem na mão a pá, limpará sua eira e recolherá o trigo ao celeiro. As palhas, porém, queimá-las-á num fogo inextinguível.
13 Booba Yeesu jóge Galile, ñëw ngir Yaxya sóob ko ca dexu Yurdan.
13 Da Galiléia foi Jesus ao Jordão ter com João, a fim de ser batizado por ele.
14 Waaye Yaxya gàntu ko ne: «Man maa soxla, nga sóob ma ci ndox, te yaa ngi ñëw ci man!»
14 João recusava-se: Eu devo ser batizado por ti e tu vens a mim!
15 Yeesu ne ko: «Bàyyil noonu, ndaxte war nanoo mottali lépp lu jub.» Noonu Yaxya nangu.
15 Mas Jesus lhe respondeu: Deixa por agora, pois convém cumpramos a justiça completa. Então João cedeu.
16 Bi ko Yaxya sóobee ca dex ga, Yeesu génn. Ca saa sa asamaan yi daldi ubbiku, te Yaxya gis Xelum Yàlla wàcc ci melow pitax, ñëw ci kaw Yeesu.
16 Depois que Jesus foi batizado, saiu logo da água. Eis que os céus se abriram e viu descer sobre ele, em forma de pomba, o Espírito de Deus.
17 Te baat bu jóge asamaan dégtu ne: «Kii mooy sama Doom ji ma bëgg; ci moom laa ame bànneex.»
17 E do céu baixou uma voz: Eis meu Filho muito amado em quem ponho minha afeição.
Atalhos do teclado
- Capítulo anterior←
- Próximo capítulo→
- Versículo anteriork
- Próximo versículoj
- Limpar seleçãoEsc
- Esta ajuda?
Estude este capítulo no WhatsApp
Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Mateus 3, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.