Mateus 28

Téereb Injiil (WOL2010) vs VC

Sair da comparação
VC Versão Católica
1 Gannaaw bésub noflaay ba nag, ca fajar ga, ca bés bu jëkk ca ayu-bés ga, Maryaamam Magdala ak Maryaama ma ca des dem, seeti bàmmeel ba.
1 Depois do sábado, quando amanhecia o primeiro dia da semana, Maria Madalena e a outra Maria foram ver o túmulo.
2 Fekk suuf yëngu woon na bu metti, ndaxte benn malaakam Boroom bi wàcc na ci asamaan, ñëw béraŋ doj wa, toog ci kaw.
2 E eis que houve um violento tremor de terra: um anjo do Senhor desceu do céu, rolou a pedra e sentou-se sobre ela.
3 Meloom mel na ni melax, ay yéreem weex tàll ni perkaal.
3 Resplandecia como relâmpago e suas vestes eram brancas como a neve.
4 Ñi doon wottu tiit bay lox, daldi mel ni ñu dee.
4 Vendo isto, os guardas pensaram que morreriam de pavor.
5 Noonu malaaka ma ne jigéen ña: «Buleen tiit. Xam naa ne yéena ngi wut Yeesu, ma ñu daajoon ca bant ba,
5 Mas o anjo disse às mulheres: Não temais! Sei que procurais Jesus, que foi crucificado.
6 waaye nekkatu fi, ndaxte dekki na, ni mu ko waxe woon. Ñëwleen seet fi mu tëddoon,
6 Não está aqui: ressuscitou como disse. Vinde e vede o lugar em que ele repousou.
7 te ngeen dem bu gaaw, wax ay taalibeem ne dekki na te jiituji na leen Galile; foofa ngeen koy gise. Lii laa leen wax.»
7 Ide depressa e dizei aos discípulos que ele ressuscitou dos mortos. Ele vos precede na Galiléia. Lá o haveis de rever, eu vo-lo disse.
8 Bi loolu amee nag jigéen ña daldi jóge bu gaaw ca bàmmeel ba, tiit ak mbég mu réy di jax seen xol, ñu daldi daw, ngir yégal ko taalibe ya.
8 Elas se afastaram prontamente do túmulo com certo receio, mas ao mesmo tempo com alegria, e correram a dar a boa nova aos discípulos.
9 Ba ñuy dem nag, Yeesu taseek ñoom ne leen: «Maa ngi leen di nuyu.» Jigéen ña jegesi, laxasu cay tànkam, di ko màggal.
9 Nesse momento, Jesus apresentou-se diante delas e disse-lhes: Salve! Aproximaram-se elas e, prostradas diante dele, beijaram-lhe os pés.
10 Yeesu ne leen: «Buleen tiit, waaye demleen yégal samay bokk, ñu dem Galile; foofa lañu may gise.»
10 Disse-lhes Jesus: Não temais! Ide dizer aos meus irmãos que se dirijam à Galiléia, pois é lá que eles me verão.
11 Ba ñuy dem, ñenn ca wottukat ya ñëw ca dëkk ba, xamal sarxalkat yu mag ya lépp lu xew.
11 Enquanto elas voltavam, alguns homens da guarda já estavam na cidade para anunciar o acontecimento aos príncipes dos sacerdotes.
12 Noonu sarxalkat ya dajaloo ak njiit ya, ñu diisoo; ba noppi ñu fab xaalis bu bare, jox ko xarekat ya,
12 Reuniram-se estes em conselho com os anciãos. Deram aos soldados uma importante soma de dinheiro, ordenando-lhes:
13 ne leen: «Nangeen wax lii: “Ay taalibeem ñëw nañu ci guddi, sàcc ko, bi nuy nelaw.”
13 Vós direis que seus discípulos vieram retirá-lo à noite, enquanto dormíeis.
14 Te bu ko boroom réew mi yégee nag, dinanu ko neexal, ngir rawale leen.»
14 Se o governador vier a sabê-lo, nós o acalmaremos e vos tiraremos de dificuldades.
15 Wottukat ya nag fab xaalis ba, def la ñu leen santoon. Te nettali boobu siiw na ci Yawut yi ba bésu tey.
15 Os soldados receberam o dinheiro e seguiram suas instruções. E esta versão é ainda hoje espalhada entre os judeus.
16 Noonu fukki taalibe ya ak benn dem ci biir Galile, ca tund wa leen Yeesu digaloon.
16 Os onze discípulos foram para a Galiléia, para a montanha que Jesus lhes tinha designado.
17 Bi ñu gisee Yeesu, ñu màggal ko, waaye ñenn ñi am xel ñaar.
17 Quando o viram, adoraram-no; entretanto, alguns hesitavam ainda.
18 Yeesu jegesi ne leen: «Sañ-sañ bépp, jox nañu ma ko ci kaw ak ci suuf.
18 Mas Jesus, aproximando-se, lhes disse: Toda autoridade me foi dada no céu e na terra.
19 Demleen nag sàkk ay taalibe ci xeet yépp, sóob leen ci ndox ci turu Baay bi ak Doom ji ak Xel mu Sell mi;
19 Ide, pois, e ensinai a todas as nações; batizai-as em nome do Pai, do Filho e do Espírito Santo.
20 ngeen jàngal leen, ñuy sàmm lépp li ma leen sant. Maa ngi ànd ak yéen bés bu nekk, ba kera àddina di tukki.»
20 Ensinai-as a observar tudo o que vos prescrevi. Eis que estou convosco todos os dias, até o fim do mundo.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Mateus 28, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.