Mateus 27
Téereb Injiil (WOL2010) vs VC
1 Ci suba teel sarxalkat yu mag yépp ak njiiti xeet wa gise, ngir fexee reylu Yeesu.
1 Chegando a manhã, todos os príncipes dos sacerdotes e os anciãos do povo reuniram-se em conselho para entregar Jesus à morte.
2 Ñu yeew ko, yóbbu ko, jébbal ko Pilaat boroom réew ma.
2 Ligaram-no e o levaram ao governador Pilatos.
3 Bi nga xamee ne Yudaa, mi woroon Yeesu, gis na ne daan nañu ko, mu am naqaru xol. Mu dem nag ca sarxalkat yu mag ya ak njiit ya, delloo leen fanweeri poset yu xaalis,
3 Judas, o traidor, vendo-o então condenado, tomado de remorsos, foi devolver aos príncipes dos sacerdotes e aos anciãos as trinta moedas de prata,
4 ne leen: «Am naa bàkkaar ci li ma wor nit ku tooñul, ngir ñu rey ko.» Ñu ne ko: «Lu ciy sunu yoon? Loolu yaa ko yég.»
4 dizendo-lhes: Pequei, entregando o sangue de um justo. Responderam-lhe: Que nos importa? Isto é lá contigo!
5 Noonu Yudaa sànni xaalis ba ca kër Yàlla ga, jóge fa, dem, takk buum ci baatam, xaru.
5 Ele jogou então no templo as moedas de prata, saiu e foi enforcar-se.
6 Sarxalkat yu mag ya nag fab xaalis ba, naan: «Jaaduwul nu def xaalis bii ci dencukaayu xaalis bi ci kër Yàlla gi, ndaxte njégu deret la.»
6 Os príncipes dos sacerdotes tomaram o dinheiro e disseram: Não é permitido lançá-lo no tesouro sagrado, porque se trata de preço de sangue.
7 Ñu daldi diisoo nag, jënd ca xaalis ba toolu defarkatu ndaa ya, ngir di fa suul doxandéem ya.
7 Depois de haverem deliberado, compraram com aquela soma o campo do Oleiro, para que ali se fizesse um cemitério de estrangeiros.
8 Loolu moo tax ñu wooye tool booba ba tey Toolu deret.
8 Esta é a razão por que aquele terreno é chamado, ainda hoje, Campo de Sangue.
9 Noonu la ñu waxoon jaarale ko ci yonent Yàlla Yeremi am, bi mu naan: «Fab nañu fanweeri poseti xaalis ya, mooy njég li bànni Israyil xayma woon ci nit ki;
9 Assim se cumpriu a profecia do profeta Jeremias: Eles receberam trinta moedas de prata, preço daquele cujo valor foi estimado pelos filhos de Israel;
10 ñu joxe ko ngir toolu defarkatu ndaa ya, ni ma ko Boroom bi sante.»
10 e deram-no pelo campo do Oleiro, como o Senhor me havia prescrito.
11 Gannaaw loolu Yeesu taxaw ca kanam boroom réew ma, boroom réew ma laaj ko: «Ndax yaa di buuru Yawut yi?»
11 Jesus compareceu diante do governador, que o interrogou: És o rei dos judeus? Sim, respondeu-lhe Jesus.
12 Yeesu ne ko: «Wax nga ko,» waaye waxul dara ca la ko sarxalkat yu mag ya ak njiit ya jiiñ.
12 Ele, porém, nada respondia às acusações dos príncipes dos sacerdotes e dos anciãos.
13 Noonu Pilaat ne ko: «Xanaa dégguloo li ñu la jiiñ lépp?»
13 Perguntou-lhe Pilatos: Não ouves todos os testemunhos que levantam contra ti?
14 Waaye Yeesu waxu ko ci dara, ba tax boroom réew ma waaru lool.
14 Mas, para grande admiração do governador, não quis responder a nenhuma acusação.
15 Ca màggal gu nekk nag boroom réew ma daan na may mbooloo ma, ñu tànn kenn ca ña ñu tëjoon, mu daldi leen ko bàyyil.
15 Era costume que o governador soltasse um preso a pedido do povo em cada festa de Páscoa.
16 Fekk booba amoon nañu ku ñu tëjoon, ku siiw te tudd Barabas.
16 Ora, havia naquela ocasião um prisioneiro famoso, chamado Barrabás.
17 Bi nga xamee ne daje nañu nag, Pilaat laaj leen: «Kan ngeen bëgg, ma bàyyi ko, Barabas walla Yeesu mi ñuy wax Kirist?»
17 Pilatos dirigiu-se ao povo reunido: Qual quereis que eu vos solte: Barrabás ou Jesus, que se chama Cristo?
18 Ndaxte xamoon na ne kiñaan rekk a taxoon, ñu jébbal ko ko.
18 {Ele sabia que tinham entregue Jesus por inveja.}
19 Te it bi mu toogee sax ca jalu àttekaay ba, soxnaam yónnee ci moom ne ko: «Bul dugg ci yëfi ku jub kooku, ndaxte tey gént naa ci moom te sonn naa ci lool.»
19 Enquanto estava sentado no tribunal, sua mulher lhe mandou dizer: Nada faças a esse justo. Fui hoje atormentada por um sonho que lhe diz respeito.
20 Waaye sarxalkat yu mag ya ak njiit ya xiir mbooloo ma, ñu laaj Barabas te reylu Yeesu.
20 Mas os príncipes dos sacerdotes e os anciãos persuadiram o povo que pedisse a libertação de Barrabás e fizesse morrer Jesus.
21 Noonu boroom réew ma laaj leen: «Kan ci ñaar ñii ngeen bëgg, ma bàyyil leen ko?» Ñu ne ko: «Barabas.»
21 O governador tomou então a palavra: Qual dos dois quereis que eu vos solte? Responderam: Barrabás!
22 Pilaat ne leen: «Nan laay def nag Yeesu, mi tudd Kirist?» Ñépp ne ko: «Daaj ko ci bant, ba mu dee!»
22 Pilatos perguntou: Que farei então de Jesus, que é chamado o Cristo? Todos responderam: Seja crucificado!
23 Boroom réew ma ne leen: «Lu tax? Gan tooñ la def?» Waaye ñu daldi yuuxu bu gëna kawe naan: «Daaj ko ci bant!»
23 O governador tornou a perguntar: Mas que mal fez ele? E gritavam ainda mais forte: Seja crucificado!
24 Naka Pilaat xam ne du ci man dara, fekk na sax yëngu-yëngu bi gëna am doole, mu daldi fab ndox, raxas ay loxoom ca kanam mbooloo ma ne leen: «Set naa ci deretu ku jub kii; nu ngeen xam, defleen ko.»
24 Pilatos viu que nada adiantava, mas que, ao contrário, o tumulto crescia. Fez com que lhe trouxessem água, lavou as mãos diante do povo e disse: Sou inocente do sangue deste homem. Isto é lá convosco!
25 Ñépp ne ko: «Na deretam dal ci sunu kaw ak sunu kaw njaboot.»
25 E todo o povo respondeu: Caia sobre nós o seu sangue e sobre nossos filhos!
26 Noonu Pilaat bàyyil leen Barabas, mu dóorlu Yeesu ay yar, jébbal ko, ngir ñu daaj ko ci bant.
26 — ausente —
27 Bi ñu ko defee xarekati boroom réew ma fab Yeesu, yóbbu ko ci biir kër ga, ñu daldi woo mbooloom xarekat ya yépp ci moom.
27 Os soldados do governador conduziram Jesus para o pretório e rodearam-no com todo o pelotão.
28 Noonu ñu summi ko, solal ko mbubbum xarekat mu xonq curr.
28 Arrancaram-lhe as vestes e colocaram-lhe um manto escarlate.
29 Ñu ràbb kaalag dég, teg ko ci boppam, teg bantu xat ci loxol ndijooram, sukk ci kanamam, di ko ñaawal ne ko: «Nuyu nanu la, yaw buuru Yawut yi!»
29 Depois, trançaram uma coroa de espinhos, meteram-lha na cabeça e puseram-lhe na mão uma vara. Dobrando os joelhos diante dele, diziam com escárnio: Salve, rei dos judeus!
30 Ba noppi ñu daldi tifli ci kawam, fab bantu xat ba, dóor ko ci boppam.
30 Cuspiam-lhe no rosto e, tomando da vara, davam-lhe golpes na cabeça.
31 Bi ñu ko ñaawalee ba noppi, ñu summi mbubbum xarekat ma, solaatal ko ay yéreem, yóbbu ko, ngir daaj ko ci bant.
31 Depois de escarnecerem dele, tiraram-lhe o manto e entregaram-lhe as vestes. Em seguida, levaram-no para o crucificar.
32 Bi nga xamee ne génn nañu, ñu daje ak nit ku dëkk Siren te tudd Simoŋ; ñu ga ko, ngir mu gàddu bant, ba ñu wara daaj Yeesu.
32 Saindo, encontraram um homem de Cirene, chamado Simão, a quem obrigaram a levar a cruz de Jesus.
33 Ñu ñëw nag fa ñuy wax Golgota, biy tekki «bérabu Kaaŋu bopp.»
33 Chegaram ao lugar chamado Gólgota, isto é, lugar do crânio.
34 Bi ñu fa eggee, ñu jox ko biiñ, ñu def ci lu wex. Waaye bi mu ko mosee, nanguwu koo naan.
34 Deram-lhe de beber vinho misturado com fel. Ele provou, mas se recusou a beber.
35 Noonu ñu daaj ko ca bant ba, ñu daldi séddoo ay yéreem, tegoo ko ay bant,
35 Depois de o haverem crucificado, dividiram suas vestes entre si, tirando a sorte. Cumpriu-se assim a profecia do profeta: Repartiram entre si minhas vestes e sobre meu manto lançaram a sorte {Sl 21,19}.
36 ba noppi toog fa, di ko wottu.
36 Sentaram-se e montaram guarda.
37 Te it ñu teg ci kaw boppam mbind, mu xamle lu tax ñu rey ko, mu ne: «Kii mooy Yeesu, buuru Yawut yi.»
37 Por cima de sua cabeça penduraram um escrito trazendo o motivo de sua crucificação: Este é Jesus, o rei dos judeus.
38 Booba it ñu daajaale ak moom ñaari taskati réew ma, kenn ci ndijooram, ka ca des ci càmmoñam.
38 Ao mesmo tempo foram crucificados com ele dois ladrões, um à sua direita e outro à sua esquerda.
39 Ña fa doon romb di ko xas, di wëcc seen bopp ndax sib ko,
39 Os que passavam o injuriavam, sacudiam a cabeça e diziam:
40 naan: «Yaw mi mana toj kër Yàlla ga, tabaxaat ko ci ñetti fan, musalal sa bopp; boo nekkee Doomu Yàlla, wàccal ci bant bi!»
40 Tu, que destróis o templo e o reconstróis em três dias, salva-te a ti mesmo! Se és o Filho de Deus, desce da cruz!
41 Sarxalkat yu mag ya ak xutbakat ya ak njiit ya it di ko ñaawal naan:
41 Os príncipes dos sacerdotes, os escribas e os anciãos também zombavam dele:
42 «Waa jii musal na ñeneen te manula musal boppam! Ndegam mooy buuru Israyil, na wàcc léegi ci bant bi, nu gëm ko.
42 Ele salvou a outros e não pode salvar-se a si mesmo! Se é rei de Israel, desça agora da cruz e nós creremos nele!
43 Gannaaw dénk na boppam Yàlla, kon na ko Yàlla musal, bu ko soppee, ndaxte nee na: “Maay Doomu Yàlla.”»
43 Confiou em Deus, Deus o livre agora, se o ama, porque ele disse: Eu sou o Filho de Deus!
44 Taskati réew ma it, ya ñu daajaale ak moom, di ko xas noonule.
44 E os ladrões, crucificados com ele, também o ultrajavam.
45 La tàmbalee digg bëccëg, ba ci tisbaar, réew mépp lëndëm.
45 Desde a hora sexta até a nona, cobriu-se toda a terra de trevas.
46 Noonu ci wetu ñetti waxtu Yeesu daldi wootee kàddu gu dëgër naan: «Eli, Eli, lema sabaktani?» liy tekki «Sama Yàlla, sama Yàlla, lu tax nga dëddu ma?»
46 Próximo da hora nona, Jesus exclamou em voz forte: Eli, Eli, lammá sabactáni? - o que quer dizer: Meu Deus, meu Deus, por que me abandonaste?
47 Ñenn ña ca ña fa taxaw nag, bi ñu ko déggee, ñu ne: «Mu ngi woo yonent Yàlla Ilyaas.»
47 A estas palavras, alguns dos que lá estavam diziam: Ele chama por Elias.
48 Ca saa sa kenn ci ñoom daw, jël aw sagar, capp ko ci bineegar, mu teg ko ci kaw bant, jox ko ko, mu muucu.
48 Imediatamente um deles tomou uma esponja, embebeu-a em vinagre e apresentou-lha na ponta de uma vara para que bebesse.
49 Waaye ña ca des ne: «Bàyyil, nu seet ba xam Ilyaas dina ñëw, musal ko.»
49 Os outros diziam: Deixa! Vejamos se Elias virá socorrê-lo.
50 Noonu Yeesu wootewaat ak kàddu gu dëgër, delloo ruuwam Yàlla.
50 Jesus de novo lançou um grande brado, e entregou a alma.
51 Ca saa sa ridob bérab bu sell ba ca kër Yàlla ga xar ñaar, li dale ci kaw ba ci suuf; suuf si yëngu, doj yi toj, bàmmeel yi ubbiku,
51 E eis que o véu do templo se rasgou em duas partes de alto a baixo, a terra tremeu, fenderam-se as rochas.
52 te ñu bare ci jëmmi nit ñu sell ñu dee, dekki.
52 Os sepulcros se abriram e os corpos de muitos justos ressuscitaram.
53 Te gannaaw ndekkitel Yeesu ñu génn ca bàmmeel ya, dugg ca dëkk bu sell ba, te feeñu ñu bare.
53 Saindo de suas sepulturas, entraram na Cidade Santa depois da ressurreição de Jesus e apareceram a muitas pessoas.
54 Noonu njiitu xare bi ak ñi ànd ak moom di wottu Yeesu, bi ñu gisee suuf si yëngu ak li xew, ñu daldi tiit lool ne: «Ci dëgg, kii Doomu Yàlla la.»
54 O centurião e seus homens que montavam guarda a Jesus, diante do estremecimento da terra e de tudo o que se passava, disseram entre si, possuídos de grande temor: Verdadeiramente, este homem era Filho de Deus!
55 Amoon na fa it ay jigéen yu bare yu leen dànd, di seetaan. Te ñoo jóge woon Galile, ànd ak Yeesu, di ko topptoo.
55 Havia ali também algumas mulheres que de longe olhavam; tinham seguido Jesus desde a Galiléia para o servir.
56 Xàmmi nañu ci: Maryaama mi dëkk Magdala, Maryaama ndeyu Saag ak Yuusufa, ak ndeyu doomi Sebede ya.
56 Entre elas se achavam Maria Madalena e Maria, mãe de Tiago e de José, e a mãe dos filhos de Zebedeu.
57 Ca ngoon amoon na taalibeb Yeesu mu ñëw, tudd Yuusufa te dëkk Arimate; ku bare alal la woon.
57 À tardinha, um homem rico de Arimatéia, chamado José, que era também discípulo de Jesus,
58 Mu dem ca Pilaat, laaj ko néewu Yeesu. Pilaat santaane, ñu jox ko ko.
58 foi procurar Pilatos e pediu-lhe o corpo de Jesus. Pilatos cedeu-o.
59 Noonu Yuusufa fab jëmm ja, laxas ko ci càngaay lu set,
59 José tomou o corpo, envolveu-o num lençol branco
60 dugal ko ca bàmmeel bu bees, ba mu yettaloon boppam ciw doj. Mu béraŋ doj wu mag ca buntu bàmmeel ba, dem.
60 e o depositou num sepulcro novo, que tinha mandado talhar para si na rocha. Depois rolou uma grande pedra à entrada do sepulcro e foi-se embora.
61 Fekk Maryaamam Magdala ak Maryaama ma ca des ñoo fa toogoon janook bàmmeel ba.
61 Maria Madalena e a outra Maria ficaram lá, sentadas defronte do túmulo.
62 Ba bët setee nag, ca bés ba topp bésu Waajal ba, sarxalkat yu mag ya ak Farisen ya dajaloo, jëm ci Pilaat.
62 No dia seguinte - isto é, o dia seguinte ao da Preparação -, os príncipes dos sacerdotes e os fariseus dirigiram-se todos juntos à casa de Pilatos.
63 Ñu ne ko: «Boroom réew mi, fàttaliku nanu ne, naxkat booba waxoon na, bi muy dund naan: “Gannaaw ñetti fan dinaa dekki.”
63 E disseram-lhe: Senhor, nós nos lembramos de que aquele impostor disse, enquanto vivia: Depois de três dias ressuscitarei.
64 Danoo bëggoon nag, nga santaane, ñu wottu bàmmeel ba, ba am ñetti fan, ngir bañ taalibeem ya ñëw, sàcc néew ba, tey yégle ne dekki na. Bu ko defee nax bu mujj boobu dina yées bu jëkk ba.»
64 Ordena, pois, que seu sepulcro seja guardado até o terceiro dia. Os seus discípulos poderiam vir roubar o corpo e dizer ao povo: Ressuscitou dos mortos. E esta última impostura seria pior que a primeira.
65 Pilaat ne leen: «Amleen, ay wottukat a ngi nii. Demleen wottuji ko, ni ngeen mane.»
65 Respondeu Pilatos: Tendes uma guarda. Ide e guardai-o como o entendeis.
66 Noonu ñu dem, tëj bàmmeel ba bu wóor, ñu tay ca doj wa màndarga, teg fa wottukat ya.
66 Foram, pois, e asseguraram o sepulcro, selando a pedra e colocando guardas.
Atalhos do teclado
- Capítulo anterior←
- Próximo capítulo→
- Versículo anteriork
- Próximo versículoj
- Limpar seleçãoEsc
- Esta ajuda?
Estude este capítulo no WhatsApp
Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Mateus 27, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.