Mateus 26
Téereb Injiil (WOL2010) vs NTLH
1 Bi nga xamee ne Yeesu wax na loolu lépp ba noppi, mu ne taalibeem ya:
1 Quando Jesus acabou de ensinar essas coisas, disse aos discípulos:
2 «Xam ngeen ne ñaari fan a des ci màggalu bésu Mucc ba, te dinañu wor Doomu nit ki, daaj ko ci bant.»
2 — Vocês sabem que daqui a dois dias vai ser comemorada a
3 Booba nag sarxalkat yu mag ya ak njiiti xeet wa dajaloo ca kër gu réy gu sarxalkat bu mag ba, tudd Kayif.
3 Os chefes dos sacerdotes e os líderes judeus se reuniram no palácio de Caifás, o Grande Sacerdote ,
4 Ñu daldi gise, ba xam lu ñu mana fexe, ba jàpp Yeesu, reylu ko.
4 e fizeram um plano para prender Jesus em segredo e matá-lo.
5 Waaye ñu ne: «Bumu doon ci bésu màggal bi, ngir yëngu-yëngu baña am ci nit ñi.»
5 Eles diziam: — Não vamos fazer isso durante a festa, para não haver uma revolta no meio do povo.
6 Bi nga xamee ne Yeesu nekkoon na dëkku Betani ca kër Simoŋ ma gaana woon,
6 — ausente —
7 jenn jigéen ñëw ci moom, yor njaq lu ñu yette doj wu ñuy wax albaatar. Njaq la def latkoloñ ju jar lu baree bare. Noonu bi Yeesu toogee di lekk, jigéen ji tuur ko ci boppu Yeesu.
7 — ausente —
8 Waaye bi ko taalibe ya gisee, ñu daldi mer ne: «Yàq gii, lu muy jariñ?
8 Ao verem aquilo, os discípulos ficaram zangados e disseram: — Que desperdício!
9 Maneesoon na koo jaay ci lu bare, jox xaalis bi miskin yi.»
9 Esse perfume poderia ter sido vendido por uma fortuna, e o dinheiro, dado aos pobres.
10 Yeesu nag xam la ñu wax, mu ne leen: «Jigéen ji defal na ma jëf ju rafet; lu tax ngeen di ko sonal?
10 Mas Jesus, sabendo o que eles diziam, disse:
11 Miskin yaa ngi ak yéen bés bu nekk, waaye dungeen ma gis ba fàww.
11 Pois os pobres estarão sempre com vocês, mas eu não.
12 Kii, ci li mu tuur latkoloñ jii ci sama yaram, def na ko ngir waajal sama rob.
12 O que ela fez foi perfumar o meu corpo para o meu sepultamento.
13 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, fépp fu ñuy yéene xibaaru jàmm bi ci àddina sépp, dinañu fa fàttali it li jigéen jii def.»
13 Eu afirmo a vocês que isto é verdade: em qualquer lugar do mundo onde o
14 Ca waxtu woowu kenn ci fukki taalibe ya ak ñaar, ku tudd Yudaa Iskariyo, dem ca sarxalkat yu mag ya,
14 Então um dos doze discípulos, chamado Judas Iscariotes, foi falar com os chefes dos sacerdotes.
15 ne leen: «Lan ngeen ma mana jox, ngir ma jébbal leen Yeesu?» Noonu sarxalkat ya daldi ko waññal fanweeri poseti estateer.
15 Ele disse: — Quanto vocês me pagam para eu lhes entregar Jesus? E eles lhe pagaram trinta moedas de prata.
16 Li dale ci saa soosa nag Yudaa di fexe jamono ju mu leen mana jébbal Yeesu.
16 E daí em diante Judas ficou procurando uma oportunidade para entregar Jesus.
17 Bés bu jëkk ca màggal, ga ñuy wax Mburu ma amul lawiir, taalibe yi ñëw ci Yeesu ne ko: «Foo bëggoon nu defaral la reeru bésu Mucc ba?»
17 No primeiro dia da Festa dos Pães sem Fermento , os discípulos chegaram perto de Jesus e perguntaram: — Onde é que o senhor quer que a gente prepare o jantar da
18 Yeesu ne leen: «Demleen ca dëkk ba, jëm ca diw, ngeen ne ko: “Kilifa gi nee na: Sama jamono jege na; ci sa kër laay màggalsi bésu Mucc ba, man ak samay taalibe.”»
18 Ele respondeu:
19 Noonu taalibe yi defar reeru bésu Mucc ba, na leen Yeesu waxe woon.
19 Os discípulos fizeram como Jesus havia mandado e prepararam o jantar da Páscoa.
20 Bi nga xamee ne timis jot na, Yeesu toog di lekk, moom ak fukki taalibe yi ak ñaar.
20 Quando anoiteceu, Jesus e os doze discípulos sentaram para comer.
21 Bi ñuy lekk, mu ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, kenn ci yéen dina ma wor.»
21 Durante o jantar Jesus disse:
22 Taalibe ya am naqaru xol bu réy; ku nekk daldi ne ko: «Mbaa du man, Boroom bi?»
22 Eles ficaram muito tristes e, um por um, começaram a perguntar: — O senhor não está achando que sou eu; está?
23 Yeesu ne leen: «Ki dugal loxoom ak man ci ndab li, kooku moo may wor.
23 Jesus respondeu:
24 Doomu nit ki mu ngi dem, ni ñu ko waxe ci Mbind mi, waaye ki koy wor dina torox; bañoona juddu moo gënoon ci moom.»
24 Pois o
25 Yudaa, mi ko nara wor, laaj ko: «Mbaa du man, kilifa gi?» Yeesu ne ko: «Wax nga ko.»
25 Então Judas, o traidor, perguntou: — Mestre, o senhor não está achando que sou eu; está? Jesus respondeu:
26 Noonu bi ñuy lekk, Yeesu jël mburu, sant Yàlla, damm ko, jox ko taalibe ya. Mu ne leen: «Jël-leen lekk, lii sama yaram la.»
26 Enquanto estavam comendo, Jesus pegou o pão e deu graças a Deus. Depois partiu o pão e o deu aos discípulos, dizendo:
27 Gannaaw loolu mu jël kaas, sant Yàlla, jox leen ko. Mu ne leen: «Yéen ñépp naanleen ci,
27 Em seguida, pegou o cálice de vinho e agradeceu a Deus. Depois passou o cálice aos discípulos, dizendo:
28 ndaxte lii mooy sama deret, ji fas kóllëre gi, te mu tuuru, ngir ñu bare jot mbaalug bàkkaar yi.
28 porque isto é o meu sangue, que é derramado em favor de muitos para o perdão dos pecados, o sangue que garante a
29 Maa ngi leen di wax, dootuma naan gannaaw-si-tey ndoxum reseñ mii, ba kera may naan ak yéen ndoxum reseñ mu bees ci sama nguuru Baay.»
29 Eu afirmo a vocês que nunca mais beberei deste vinho até o dia em que beber com vocês um vinho novo no
30 Gannaaw loolu ñu woy Yàlla, ba noppi génn, dem ca tundu Oliw ya.
30 Então eles cantaram canções de louvor e foram para o monte das Oliveiras.
31 Booba Yeesu ne leen: «Yéen ñépp dingeen ma dàggeeku ci guddi gii, ndaxte bind nañu:
31 E Jesus disse aos discípulos:
32 Waaye bu ma dekkee, dinaa leen jiituji Galile.»
32 Mas, depois que eu ressuscitar, irei adiante de vocês para a Galileia.
33 Piyeer nag daldi jël kàddu gi naan: «Bu la ñépp dàggeekoo, man duma la dàggeeku mukk.»
33 Então Pedro disse a Jesus: — Eu nunca abandonarei o senhor, mesmo que todos o abandonem.
34 Yeesu ne ko: «Ci dëgg maa ngi la koy wax, ci guddi gii, bala ginaar a sab, dinga ma weddi ñetti yoon.»
34 Mas Jesus lhe disse:
35 Piyeer ne ko: «Boo xamee ne sax, damaa wara dee ak yaw, duma la weddi mukk.» Taalibe yépp it waxe noonu.
35 Pedro respondeu: — Eu nunca vou dizer que não o conheço, mesmo que eu tenha de morrer com o senhor! E todos os outros discípulos disseram a mesma coisa.
36 Bi loolu amee Yeesu ànd ak ñoom ba ca bérab bu tudd Setsemane, mu ne taalibe ya: «Toogleen fii, ma dem fale, ñaan fa.»
36 Jesus foi com os discípulos para um lugar chamado Getsêmani e lhes disse:
37 Bi mu waxee loolu, mu ànd ak Piyeer ak ñaari doomi Sebede, daldi am tiis ba xonet.
37 Então Jesus foi, levando consigo Pedro e os dois filhos de Zebedeu. Aí ele começou a sentir uma grande tristeza e aflição
38 Mu ne leen: «Sama xol dafa tiis, ba may bëgga dee; toogleen fi, xool ak man.»
38 e disse a eles:
39 Bi mu waxee loolu, Yeesu dem ci kanam tuuti, ne nërëm ci suuf, di ñaan ne: «Sama Baay, bu manee am, na ma kaasu naqar bii teggi! Moona, bumuy ci sama coobare, waaye na sa coobare am.»
39 Ele foi um pouco mais adiante, ajoelhou-se, encostou o rosto no chão e orou:
40 Noonu mu ñëw ca taalibe ya, fekk leen ñuy nelaw. Mu ne Piyeer: «Amuleen sax dooley xoolandoo ak man benn waxtu?
40 Depois voltou e encontrou os três discípulos dormindo. Então disse a Pedro:
41 Xool-leen te ñaan, ngir baña daanu cig fiir. Seen xol jag na, waaye seen bind a woyof.»
41 Vigiem e orem para que não sejam tentados. É fácil querer resistir à tentação; o difícil mesmo é conseguir.
42 Yeesu delluwaat di ñaan ne: «Sama Baay, bu fekkee ne kaasu naqar bii manu maa teggi te naanuma ko, kon na sa coobare am.»
42 Pela segunda vez Jesus foi e orou, dizendo:
43 Yeesu ñëwaat ca taalibe ya, fekk leen ñuy nelaw, ndaxte seeni bët dañoo diis.
43 Ele voltou de novo e encontrou os discípulos dormindo. Eles estavam com sono e não conseguiam ficar com os olhos abertos.
44 Mu daldi leen bàyyi, waxaat loolu ñetteel bi yoon.
44 Jesus tornou a sair de perto deles e orou pela terceira vez, dizendo as mesmas palavras.
45 Noonu mu ñëw ca taalibe ya ne leen: «Nelawleen léegi te noppalu. Waxtu wu ñu ma wara jébbale ci loxoy bàkkaarkat yi, jege na.
45 Então voltou até onde os discípulos estavam e perguntou:
46 Jógleen nu dem; xool-leen, ki may wor a ngi nii, di ñëw.»
46 Levantem-se, e vamos embora. Vejam! Aí vem chegando o homem que está me traindo!
47 Bi muy wax loolu nag, Yudaa, mi bokkoon ca fukki taalibe ya ak ñaar te naroon koo wor, agsi, ànd ak mbooloo mu bare, jóge ca sarxalkat yu mag ya ak ca njiiti xeet wa, te gànnaayoo jaasi ak yet.
47 Jesus ainda estava falando, quando chegou Judas, um dos doze discípulos. Vinha com ele uma grande multidão armada com espadas e porretes, que tinha sido mandada pelos chefes dos sacerdotes e pelos líderes judeus.
48 Fekk Yudaa moomu joxoon na leen tegtal ne leen: «Ki may fóon, moom la; jàppleen ko.»
48 O traidor tinha combinado com eles um sinal. Ele tinha dito: “Prendam o homem que eu beijar, pois é ele.”
49 Mu daldi ñëw ci Yeesu nag ne ko: «Salaam-maalikum, kilifa gi!» daldi ko fóon bu tàng.
49 Judas foi até perto de Jesus e disse: — Mestre, que a paz esteja com o senhor! E o beijou.
50 Yeesu ne ko: «Sama xarit, xam naa lu tax nga ñëw.» Noonu ñu daldi jegesi, song ko, jàpp ko.
50 Jesus respondeu: Então eles chegaram, prenderam Jesus e o amarraram.
51 Ca saa sa kenn ci ñi ànd ak Yeesu bocci jaaseem, dóor surgab sarxalkat bu mag ba, nopp ba dagg.
51 Mas um dos que estavam ali com Jesus tirou a espada, atacou um empregado do Grande Sacerdote e cortou uma orelha dele.
52 Waaye Yeesu ne ko: «Roofal sa jaasi ci mbaram, ndaxte ku bocci jaasi, jaasi moo lay rey.
52 Aí Jesus disse:
53 Xanaa xamuloo ne man naa laaj sama Baay, te dina ma may ci taxawaay bi mbooloom malaaka mu xel dajul?
53 Você não sabe que, se eu pedisse ajuda ao meu Pai, ele me mandaria agora mesmo doze exércitos de anjos?
54 Waaye su ma ko defoon, nan la Mbind mi mana ame? Ndaxte Mbind mi nee na, nii la wara ame.»
54 Mas, nesse caso, como poderia se cumprir aquilo que as
55 Booba Yeesu ne mbooloo mi: «Jóg ngeen ngir jàpp ma, gànnaayoo jaasi ak yet, mel ni ñuy topp sàcc. Moona daa naa toog bés bu nekk ca kër Yàlla ga, di jàngle, te jàppuleen ma.
55 Depois Jesus disse para aquela gente:
56 Waaye lii lépp xew na, ngir amal Mbindi yonent yi.» Ci kaw loolu taalibe yépp dëddu ko, daw.
56 Mas tudo isso está acontecendo para se cumprir o que os Então todos os discípulos abandonaram Jesus e fugiram.
57 Ña jàppoon Yeesu yóbbu ko kër Kayif, sarxalkat bu mag ba, fa xutbakat ya ak njiit ya daje.
57 Os homens que prenderam Jesus o levaram até a casa do Grande Sacerdote Caifás, onde estavam reunidos alguns mestres da Lei e alguns líderes judeus.
58 Piyeer topp ko fu sore, ba ci ëttu sarxalkat bu mag ba; mu dugg, toog ak surga ya, ngir seet nu mbir may mujje.
58 Pedro seguiu Jesus de longe até o pátio da casa do Grande Sacerdote. Entrou e sentou-se com os guardas para ver como aquilo ia terminar.
59 Noonu sarxalkat yu mag ya ak kureelu àttekat ya di seet naaféq bu mana seede ci Yeesu, ba ñu man koo rey,
59 Os chefes dos sacerdotes e todo o Conselho Superior estavam procurando alguma acusação falsa contra Jesus a fim de o condenar à morte.
60 waaye manuñu koo am. Teewul ñu bare ñëwoon nañu, di seede lu dul dëgg. Ba mujj ñaari nit ñëw naan:
60 Mas não puderam encontrar nada contra ele, embora muitos se levantassem para dizer mentiras a respeito dele. Afinal dois homens se apresentaram
61 «Kii nee woon na: “Man naa toj kër Yàlla ga, tabaxaat ko ci ñetti fan.”»
61 e disseram: — Este homem afirmou: “Eu posso destruir o Templo de Deus e construí-lo de novo em três dias.”
62 Ci kaw loolu sarxalkat bu mag ba jóg ne ko: «Ndax doo wax dara? Loo xam ci li ñii seede ci yaw?»
62 Aí o Grande Sacerdote se levantou e perguntou a Jesus: — Você não vai se defender desta acusação?
63 Waaye Yeesu ne cell. Sarxalkat bu mag ba ne ko: «Giñloo naa la ci Yàlla miy dund, nga wax nu, ndax yaa di Almasi bi, Doomu Yàlla ji.»
63 Mas Jesus ficou calado. Então o Grande Sacerdote tornou a perguntar: — Em nome do Deus vivo, eu exijo que você diga para nós: você é o
64 Yeesu ne ko: «Wax nga ko. Maa ngi leen koy wax it, li dale fii dingeen gis Doomu nit ki toog ci ndijooru Aji Man ji, di ñëw ci niiri asamaan si.»
64 Jesus respondeu:
65 Bi mu déggee loolu, sarxalkat bu mag ba daldi mer lool, ba xotti ay yéreem, daldi ne: «Weddi na Yàlla, lu nu doyeeti seede? Dégg ngeen ni mu weddee.
65 Aí o Grande Sacerdote rasgou as suas próprias roupas e disse: — Ele
66 Lu ngeen ci xalaat?» Ñu ne ko: «Yoon teg na ko dee.»
66 Então, o que resolvem? Eles responderam: — Ele é culpado e deve morrer!
67 Ci kaw loolu ñu daldi tifli ci xar kanamam, dóor ko ay kurfeñ. Ñeneen talaata ko,
67 Em seguida cuspiram no rosto de Jesus e deram bofetadas nele. E os que batiam nele
68 ne ko: «Yaw Kirist, yonent bi, ndax xam nga ku la dóor?»
68 diziam: — Ei, Messias, adivinhe para nós quem foi que bateu em você!
69 Bi looluy xew, Piyeer moom ma nga toogoon ca biti ca ëtt ba. Noonu benn mbindaan ñëw ci moom ne ko: «Yaw itam àndoon nga ak Yeesum Galile.»
69 Pedro estava sentado lá fora no pátio, quando uma das empregadas chegou perto dele e disse: — Você também estava com Jesus da Galileia.
70 Waaye Piyeer weddi ko ci kanam ñépp ne ko: «Xawma li ngay wax.»
70 Mas ele negou diante de todos, dizendo: — Eu não sei do que é que você está falando.
71 Bi mu ko waxee, mu jëm ca bunt ba, te beneen mbindaan gis ko, mu wax ña fa nekkoon: «Kii àndoon na ak Yeesum Nasaret.»
71 Depois foi para a entrada do pátio. Outra empregada o viu e disse às pessoas que estavam ali: — Ele estava com Jesus de Nazaré.
72 Waaye Piyeer weddiwaat, boole ko ak ay ngiñ ne ko: «Xawma nit kooku.»
72 Pedro negou outra vez, respondendo: — Juro que não conheço esse homem!
73 Nees-tuut ña fa taxawoon ñëw ci Piyeer ne ko: «Ci lu wóor ne yaw itam bokk nga ci ñoom, ndaxte sa waxin feeñal na la.»
73 Pouco depois, os que estavam ali chegaram perto de Pedro e disseram: — O seu modo de falar mostra que, de fato, você também é um deles.
74 Bi mu ko déggee, Piyeer daldi giñ ak di waat ne: «Xawma nit kooku.» Te ci taxawaay ginaar daldi sab.
74 Então Pedro disse: — Juro que não conheço esse homem! Que Deus me castigue se não estou dizendo a verdade! Naquele instante o galo cantou,
75 Noonu Piyeer fàttaliku la Yeesu waxoon ne: «Bala ginaar a sab, dinga ma weddi ñetti yoon.» Mu daldi génn, di jooy jooy yu metti.
75 e Pedro lembrou que Jesus lhe tinha dito: “Antes que o galo cante, você dirá três vezes que não me conhece.” Então Pedro saiu dali e chorou amargamente.
Atalhos do teclado
- Capítulo anterior←
- Próximo capítulo→
- Versículo anteriork
- Próximo versículoj
- Limpar seleçãoEsc
- Esta ajuda?
Estude este capítulo no WhatsApp
Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Mateus 26, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.