Mateus 25

Téereb Injiil (WOL2010) vs ARC

Sair da comparação
ARC Almeida Revista e Corrigida 2009
1 «Booba nguuru Yàlla Aji Kawe ji dina mel ni fukki janq, ñu fab seeni làmp, génn, gatanduji boroom séet ba.
1 Então, o Reino dos céus será semelhante a dez virgens que, tomando as suas lâmpadas, saíram ao encontro do esposo.
2 Fekk juróom ca janq ya di ñu am xel, juróom ya ca des ñàkk xel.
2 E cinco delas eram prudentes, e cinco, loucas.
3 Ñi ñàkk xel nag fab nañu seeni làmp, waaye fabaalewuñu diw;
3 As loucas, tomando as suas lâmpadas, não levaram azeite consigo.
4 waaye ñi am xel ñoom fab nañu seeni làmp, fabaale diw ciy njaq.
4 Mas as prudentes levaram azeite em suas vasilhas, com as suas lâmpadas.
5 Ni boroom séet bi yéexee ñëw nag, ñépp gëmméentu bay nelaw.
5 E, tardando o esposo, tosquenejaram todas e adormeceram.
6 «Noonu ci xaaju guddi baat jib ne: “Boroom séet baa ngi, génnleen, gatandu ko.”
6 Mas, à meia-noite, ouviu-se um clamor: Aí vem o esposo! Saí-lhe ao encontro!
7 Bi ko janq ya déggee, ñu jóg, defar seeni làmp.
7 Então, todas aquelas virgens se levantaram e prepararam as suas lâmpadas.
8 Ñi ñàkk xel wax ñi am xel: “Mayleen nu ci seen diw, ndaxte sunuy làmp ñu ngi bëgga fey.”
8 E as loucas disseram às prudentes: Dai-nos do vosso azeite, porque as nossas lâmpadas se apagam.
9 Waaye ñi am xel ne leen: “Li nu yor du doy ngir nun ak yéen. Tee ngeena dem ca jaaykat ya, jënd?”
9 Mas as prudentes responderam, dizendo:
10 «Bi nga xamee ne dem nañu jëndi, boroom séet ba agsi. Ñi amoon diw ci seeni làmp, ànd ak boroom séet ba ca reer ya. Noonu bunt ba tëj.
10 E, tendo elas ido comprá-lo, chegou o esposo, e as que estavam preparadas entraram com ele para as bodas, e fechou-se a porta.
11 Gannaaw loolu janq ya ca des agsi naan: “Sang bi, Sang bi, ubbil nu!”
11 E, depois, chegaram também as outras virgens, dizendo: Senhor, senhor, abre-nos a porta!
12 Mu ne leen: “Ci dëgg maa ngi leen koy wax, xawma leen.”
12 E ele, respondendo, disse: Em verdade vos digo que vos não conheço.
13 «Yewwuleen nag, ndaxte xamuleen bés ba mbaa waxtu wa.
13 Vigiai, pois, porque não sabeis o Dia nem a hora em que o Filho do Homem há de vir.
14 «Te it nguuru Yàlla dafa mel ni kuy tukki bitim réew. Bi muy laata dem, mu woo ay surgaam, batale leen alalam, ku nekk lu mu àttan.
14 Porque isto é também como um homem que, partindo para fora da terra, chamou os seus servos, e entregou-lhes os seus bens,
15 Kenn ka, mu dénk ko juróomi milyoŋ, keneen ka, mu dénk ko ñaar; ka ca des, benn; daldi tukki.
15 e a um deu cinco talentos, e a outro, dois, e a outro, um, a cada um segundo a sua capacidade, e ausentou-se logo para longe.
16 «Bi mu demee nag, ki jot juróomi milyoŋ ya dem, di ci jula, ba amaat yeneen juróom.
16 E, tendo ele partido, o que recebera cinco talentos negociou com eles e granjeou outros cinco talentos.
17 Noonu it ki jot ñaar amaat yeneen ñaar.
17 Da mesma sorte, o que
18 Waaye ki jot benn milyoŋ dem, gas pax, nëbb fa xaalisu njaatigeem.
18 Mas o que recebera um foi, e cavou na terra, e escondeu o dinheiro do seu senhor.
19 «Gannaaw diir bu yàgg njaatigeb surga ya délsi, daldi leen laaj alalam.
19 E, muito tempo depois, veio o senhor daqueles servos e ajustou contas com eles.
20 Noonu ki jot juróomi milyoŋ ya jegeñsi, indi yeneen juróom naan: “Kilifa gi, dénk nga ma juróomi milyoŋ; seetal, ame naa ci yeneen juróom.”
20 Então, aproximou-se o que recebera cinco talentos e trouxe-lhe outros cinco talentos, dizendo: Senhor, entregaste-me cinco talentos; eis aqui outros cinco talentos que ganhei com eles.
21 Njaatigeem ne ko: “Def nga lu baax, surga bu baax nga te takku. Gannaaw takku nga ci lu tuuti, dinaa la dénk lu bare. Kaay bokk ci sama mbég.”
21 E o seu senhor lhe disse: Bem Sobre o pouco foste fiel, sobre muito te colocarei; entra no gozo do teu senhor.
22 Naka noona ki jot ñaari milyoŋ it jegeñsi ne ko: “Kilifa gi, dénk nga ma ñaari milyoŋ, seetal, ame naa ci yeneen ñaar.”
22 E, chegando também o que tinha recebido dois talentos, disse: Senhor, entregaste-me dois talentos; eis que com eles ganhei outros dois talentos.
23 Njaatigeem ne ko: “Def nga lu baax, surga bu baax nga te takku. Gannaaw takku nga ci lu tuuti, dinaa la dénk lu bare. Kaay bokk ci sama mbég.”
23 Disse-lhe o seu senhor: Bem
24 «Gannaaw loolu nag, ki jot benn milyoŋ jegeñsi ne ko: “Kilifa gi, xamoon naa ne, nit ku néeg nga; dangay dajale foo jiwul, tey góob foo faruwul.
24 Mas, chegando também o que recebera um talento disse: Senhor, eu conhecia-te, que és um homem duro, que ceifas onde não semeaste e ajuntas onde não espalhaste;
25 Moo tax ma ragaloon la, ba dem, nëbb sa xaalis ci biir suuf; mi ngii, fabal li nga moom.”
25 e, atemorizado, escondi na terra o teu talento; aqui tens o
26 Waaye njaatigeem ne ko: “Surga bu bon nga te tayel! Gannaaw xamoon nga ne damay dajale fu ma jiwul, tey góob fu ma faruwul,
26 Respondendo, porém, o seu senhor, disse-lhe: Mau e negligente servo; sabes que ceifo onde não semeei e ajunto onde não espalhei;
27 kon waroon ngaa yóbbu sama xaalis ca denckati xaalis ya. Bés bu ma ñëwee nag, ma mana jot li ma moom ak la mu jur.”
27 devias, então, ter dado o meu dinheiro aos banqueiros, e, quando eu viesse, receberia o que é meu com os juros.
28 Noonu njaatige bi ne: “Nanguleen xaalis bi ci moom, jox ko boroom fukki milyoŋ yi.
28 Tirai-lhe, pois, o talento e dai-o ao que tem os dez talentos.
29 Ndaxte ku am dinañu la dolli, ba nga barele, waaye ku amul, li nga am as néew sax, dinañu ko nangu.
29 Porque a qualquer que tiver será dado, e terá em abundância; mas ao que não tiver, até o que tem ser-lhe-á tirado.
30 Te sànnileen surga bu amul njariñ bi ci biti ci lëndëm gi. Foofa dees na fa jooy te yéyu.”
30 Lançai, pois, o servo inútil nas trevas exteriores; ali, haverá pranto e ranger de dentes.
31 «Boo xamee ne Doomu nit ki mu ngi ñëw ci ndamam, ànd ak malaaka yépp, booba dina falu ni buur, toog ci jalam bu soloo ndam.
31 E, quando o Filho do Homem vier em sua glória, e todos os santos anjos, com ele, então, se assentará no trono da sua glória;
32 Bu boobaa dees na dajale xeeti àddina yépp ci kanamam, te dina leen xàjjale, ni sàmm di xàjjalee xar yi ak bëy yi,
32 e todas as nações serão reunidas diante dele, e apartará uns dos outros, como o pastor aparta dos bodes as ovelhas.
33 mu teg xar yi ci ndijooram, bëy yi ci càmmoñam.
33 E porá as ovelhas à sua direita, mas os bodes à esquerda.
34 «Noonu Buur bi dina wax ñi féete ndijoor: “Agsileen, yéen ñi sama Baay barkeel, jël-leen nguur, gi ñu leen waajal li dale ci njàlbéenug àddina.
34 Então, dirá o Rei aos que Vinde, benditos de meu Pai, possuí por herança o Reino que vos está preparado desde a fundação do mundo;
35 Ndaxte xiifoon naa, ngeen jox ma, ma lekk; te mar, ngeen jox ma, ma naan; nekkoon naa ab doxandéem, ngeen fat ma;
35 porque tive fome, e destes-me de comer; tive sede, e destes-me de beber; era estrangeiro, e hospedastes-me;
36 te rafle, ngeen wodd ma; woppoon naa, ngeen seetsi ma; te ñu tëj ma, ngeen ñëw fi man.”
36 e vestistes-me; adoeci, e visitastes-me; estive na prisão, e fostes ver-me.
37 Ci kaw loolu ñi jub dinañu ne: “Boroom bi, kañ lanu la gisoon, nga xiif, nu jox la, nga lekk; mbaa nga mar, nu jox la, nga naan?
37 Então, os justos lhe responderão, dizendo: Senhor, quando te vimos com fome e
38 Kañ lanu la gisoon, nga nekk ab doxandéem, nu fat la; mbaa nga rafle, nu wodd la?
38 E, quando te vimos estrangeiro e
39 Kañ lanu la gisoon, nga wopp mbaa ñu tëj la, nu ñëw ci yaw?”
39 E, quando te vimos enfermo ou na prisão e fomos ver-te?
40 Noonu Buur bi dina leen ne: “Ci dëgg maa ngi leen koy wax, saa yu ngeen defalee loolu kenn ki gëna ndaw ci sama bokk yii, man ngeen ko defal.”
40 E, respondendo o Rei, lhes dirá: Em verdade vos digo que, quando o fizestes a um destes meus pequeninos irmãos, a mim
41 «Gannaaw loolu dina wax ñi ci càmmoñam: “Soreleen ma yéen ñi alku, te dem ci sawara su dul fey, si ñu sàkkal Seytaane ak ay malaakaam.
41 Então, dirá também Apartai-vos de mim, malditos, para o fogo eterno, preparado para o diabo e seus anjos;
42 Ndaxte xiifoon naa waaye joxuleen ma, ma lekk; te mar waaye joxuleen ma, ma naan.
42 porque tive fome, e não me destes de comer; tive sede, e não me destes de beber;
43 Nekkoon naa ab doxandéem, waaye fatuleen ma; te rafle, waaye wodduleen ma; woppoon naa te ñu tëj ma, waaye seetsiwuleen ma.”
43 sendo estrangeiro, não me recolhestes;
44 Ci kaw loolu dinañu ne: “Boroom bi, kañ lanu la gisoon, nga xiif, mbaa nga mar, nga nekk ab doxandéem mbaa rafle, nga wopp mbaa ñu tëj la, te topptoowunu la?”
44 Então, eles também lhe responderão, dizendo: Senhor, quando te vimos com fome, ou com sede, ou estrangeiro, ou nu, ou enfermo, ou na prisão e não te servimos?
45 Kon dina leen ne: “Ci dëgg maa ngi leen koy wax, saa su ngeen ko defalul kenn ci ñi gëna ndaw, man ngeen ko defalul.”
45 Então, lhes responderá, dizendo: Em verdade vos digo que, quando a um destes pequeninos
46 Noonu ñii dinañu sóobu ci mbugal gu dul jeex, waaye ñi jub dinañu tàbbi ci dund gu dul jeex.»
46 E irão estes para o tormento eterno, mas os justos, para a vida eterna.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Mateus 25, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.