Mateus 24

Téereb Injiil (WOL2010) vs NTLH

Sair da comparação
NTLH Nova Tradução na Linguagem de Hoje 2000
1 Bi Yeesu waxee ba noppi, mu génn ca kër Yàlla ga, dem. Noonu ay taalibeem ñëw ci moom, ngir won ko tabaxi kër Yàlla ga.
1 Jesus saiu do pátio do Templo, e, quando já estava indo embora, os seus discípulos chegaram perto dele e chamaram a sua atenção para os edifícios do Templo.
2 Mu ne leen: «Du gis ngeen yii yépp? Ci dëgg maa ngi leen koy wax, lii lépp dina daanu, ba doj dootul des ci kaw doj.»
2 Então ele disse:
3 Noonu bi nga xamee ne Yeesu toog na ca tundu Oliw ya, taalibeem ya ñëw ci moom cig wet. Ñu ne ko: «Wax nu kañ la loolu di am, te luy tegtale ne yaa ngi ñëw te àddina di tukki?»
3 Jesus estava sentado no monte das Oliveiras. Então os discípulos chegaram perto dele e lhe perguntaram em particular: — Conte para nós quando é que isso vai acontecer. Que sinal haverá para mostrar que chegou o tempo de o senhor voltar e de tudo acabar?
4 Yeesu ne leen: «Moytuleen, bu leen kenn nax.
4 Jesus respondeu:
5 Ndaxte ñu bare dinañu ñëw ci sama tur ne: “Maa di Kirist,” te dinañu nax ñu bare.
5 Porque muitos vão aparecer fingindo ser eu e dizendo: “Eu sou o
6 Dingeen dégg ay xare ak coowi xare; wottuleen, buleen ci tiit, ndaxte loolu war na am, waaye booba mujug jamono ji jotagul.
6 Não tenham medo quando ouvirem o barulho de batalhas ou notícias de guerras. Tudo isso vai acontecer, mas ainda não será o fim.
7 Xeet dina jóg, xeex ak weneen xeet, réew xeex ak meneen réew. Dina am ay xiif ak ay yëngu-yënguy suuf ci bérab yu bare.
7 Uma nação vai guerrear contra outra, e um país atacará outro. Em vários lugares haverá falta de alimentos e tremores de terra.
8 Waaye loolu lépp mooy ndoortel metit yi, mel ni jigéen juy matu.
8 Essas coisas serão como as primeiras dores de parto.
9 Bu boobaa dees na leen jébbale, mitital leen, rey leen; te xeet yépp dinañu leen bañ ndax sama tur.
9 — Depois vocês serão presos e entregues para serem maltratados e vocês serão mortos. Todos os odiarão por serem meus seguidores.
10 Bu loolu amee ñu bare dinañu dàggeeku, di booleente tey bañante.
10 Nessa época muitos vão abandonar a sua fé e vão trair e odiar uns aos outros.
11 Te it ñu bare ñuy mbubboo turu yonent dinañu feeñ, nax nit ñu bare.
11 Então muitos falsos
12 Te gannaaw lu bon day law, mbëggeelug ñi ëpp dina wàññiku.
12 A maldade vai se espalhar tanto, que o amor de muitos esfriará;
13 Waaye ku muñ ba ca muj ga, mucc.
13 mas quem ficar firme até o fim será salvo.
14 Noonu xibaaru jàmm bii ci nguuru Yàlla, dees na ko yégle ci àddina sépp, ngir mu nekk seede ci xeet yépp. Bu loolu amee mujug jamono ji jot.
14 E a boa notícia sobre o
15 «Dina am bés bu li ñuy wax: “Lu araam luy yàqe” dina tege ca bérab bu sell ba. Mooy li ñu doon wax jaarale ko ci yonent Yàlla Dañeel; ku ko jàng, nanga ko xam.
15 E Jesus continuou:
16 Bu ngeen gisee loolu nag, ku nekk ci biir diiwaanu Yude, nanga daw ca tund ya;
16 Então, os que estiverem na região da Judeia, que fujam para os montes.
17 ku nekk ci kaw taax ma, bul wàcc ngir fab say yëf, ya nekk ci biir kër ga;
17 Quem estiver em cima da sua casa, no terraço, que fuja logo e não entre para pegar as suas coisas.
18 ku nekk ca tool ba, bul ñibbi ngir fab sa mbubb.
18 E quem estiver no campo, que não volte para casa a fim de buscar as suas roupas.
19 Ngalla jigéen ñi ëmb ca bés yooyu, ngalla it ñiy nàmpal!
19 Ai das mulheres grávidas e das mães com criancinhas naqueles dias!
20 Ñaanleen nag seen gàddaay bumu nekk jamonoy seddaayu lolli, walla bésub noflaay bi.
20 Orem a Deus para que vocês não tenham de fugir no inverno ou no sábado .
21 Ndaxte booba dina am metit wu réy wu masula am, ba àddina sosoo ak tey, te dootul am mukk.
21 Porque naqueles dias haverá um sofrimento tão grande como nunca houve desde que Deus criou o mundo; e nunca mais acontecerá uma coisa igual.
22 Te bu ñu wàññiwul bés yooyu, kenn du mucc, waaye dees na leen wàññi ndax ñi Yàlla tànn.
22 Porém Deus diminuiu esse tempo de sofrimento. Se não fosse assim, ninguém seria salvo. Mas, por causa do povo que Deus escolheu para salvar, esse tempo será diminuído.
23 «Booba nag, bu leen kenn waxee: “Kaayleen gis, Kirist a ngi fi,” mbaa: “Mu nga fale,” buleen ko gëm.
23 — Portanto, se alguém disser para vocês: “Vejam! O
24 Ndaxte ñi mbubboo turu Kirist ak ñi mbubboo turu yonent dinañu feeñ, di joxe ay firnde yu réy ak ay kéemaan, ba ciy nax sax ñi Yàlla tànn, su loolu manoona am.
24 Porque aparecerão falsos profetas e falsos messias, que farão milagres e maravilhas para enganar, se possível, até o povo escolhido de Deus.
25 Wax naa leen ko lu jiitu.
25 Prestem atenção! Eu estou lhes dizendo tudo isso, antes que aconteça.
26 «Bu ñu leen waxee nag: “Seetleen, mu nga nale ca àll ba,” buleen génn, mbaa ñu ne: “Seetleen, mu ngi nii ci biir kër gi,” buleen ko gëm.
26 — E, se disserem: “Vejam! Ele está no deserto”, não vão lá. Ou ainda: “Vejam! Ele está escondido aqui”, não acreditem.
27 Ndaxte ni melax di fàqe penku, te lerax ba sowu, noonu la ñëwug Doomu nit ki di mel.
27 Porque, assim como o relâmpago risca o céu, do nascente até o poente, assim será a vinda do
28 Fa médd nekk, fa la tan yiy dajee.
28 — Onde estiver o corpo de um morto, aí se ajuntarão os urubus.
29 «Gannaaw metitu bés yooyule nag, ca saa sa jant bi dina lëndëm te weer wi dootul leer; biddiiw yi dinañu fàq, daanu ci asamaan, te kàttani asamaan yi yëngu.
29 Jesus disse:
30 Booba firnde ji taxaw, Doomu nit ki feeñ ci asamaan, te xeeti àddina sépp dinañu jooy. Dinañu gis Doomu nit ki di ñëw ci niiri asamaan si, ànd ak kàttan ak ndam lu réy.
30 Então o sinal do
31 Dina yónni ay malaakaam ak baatu liit bu dégtu, ñu dajale ñi mu tànn ci ñeenti xébla yi, fa asamaan dale ba fu mu yem.»
31 A grande trombeta tocará, e ele mandará os seus anjos para os quatro cantos da terra. E os anjos reunirão os escolhidos de Deus de um lado do mundo até o outro.
32 Yeesu teg ca ne: «Jàngleen misaalu garabu figg ga. Boo xamee ne ay bànqaasam duy nañu, tey xobam sëq, xam ngeen ne nawet jege na.
32 Jesus disse ainda:
33 Noonu yéen itam bu ngeen gisee loolu lépp, xamleen ne jege na, mu ngi ci bunt bi sax.
33 Assim também, quando virem acontecer essas coisas, fiquem sabendo que o tempo está perto, pronto para começar.
34 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, niti jamono jii duñu wéy te loolu lépp amul.
34 Eu afirmo a vocês que isto é verdade: essas coisas vão acontecer antes de morrerem todos os que agora estão vivos.
35 Asamaan ak suuf dinañu wéy, waaye samay wax du wéy mukk.
35 O céu e a terra desaparecerão, mas as minhas palavras ficarão para sempre.
36 «Waaye bés booba walla waxtu wa, kenn xamul kañ lay doon; du malaaka yi ci kaw, du sax man Doom ji, waaye Baay bi rekk moo ko xam.
36 Jesus continuou, dizendo:
37 Ni bési Nóoyin ya, noonu lay mel, bu Doomu nit ki di ñëw.
37 A vinda do
38 Ndaxte ca bés ya jiitu mbënn ma, nit ñaa ngi doon lekk di naan, góor ñaa ngi doon takk jabar, tey maye seeni doom, ba bés ba Nóoyin duggee ca gaal ga;
38 Pois, antes do dilúvio, o povo comia e bebia, e os homens e as mulheres casavam, até o dia em que Noé entrou na barca.
39 xalaatuñu woon dara, ba kera ndoxum mbënn ma di dikk, yóbbu leen. Noonu lay mel ci ñëwug Doomu nit ki.
39 Porém não sabiam o que estava acontecendo, até que veio o dilúvio e levou todos. Assim também será a vinda do Filho do Homem.
40 «Bu boobaa ci ñaar ñu nekk cib tool, dinañu jël kenn ki, bàyyi ki ci des.
40 — Naquele dia dois homens estarão trabalhando na fazenda: um será levado, e o outro, deixado.
41 Ci ñaari jigéen ñuy wol ca ëtt ba, dinañu jël kenn ki, bàyyi ki ci des.
41 Duas mulheres estarão no moinho moendo trigo: uma será levada, e a outra, deixada.
42 Yewwuleen nag, ndaxte xamuleen bés bu seen Boroom di ñëw.
42 Fiquem vigiando, pois vocês não sabem em que dia vai chegar o seu Senhor.
43 Waaye xamleen lii: bu boroom kër gi xamoon, ci ban waxtu ci guddi la sàcc bi di ñëw, kon dina yewwu te du ko bàyyi, mu toj këram.
43 Lembrem disto: se o dono da casa soubesse quando ia chegar o ladrão, ficaria vigiando e não deixaria que a sua casa fosse arrombada.
44 Loolu moo tax yéen itam taxawleen jonn, ndaxte Doomu nit ki dina ñëw ci waxtu wu ngeen ko séenuwul.»
44 Por isso vocês também fiquem vigiando, pois o Filho do Homem chegará na hora em que vocês não estiverem esperando.
45 Yeesu teg ca ne: «Kan moo nekk surga bu takku te teey, bu njaatigeem teg ci waa kër gi, ngir mu leen di dundal ca jamono ja?
45 Jesus disse ainda:
46 Bu njaatigeem ñëwee te gis muy def noonu, surga boobu dina am ngërëm.
46 Feliz aquele empregado que estiver fazendo isso quando o patrão chegar!
47 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, njaatige bi dina ko teg ci alalam jépp.
47 Eu afirmo a vocês que isto é verdade: o patrão vai colocá-lo como encarregado de toda a sua propriedade.
48 Waaye bu dee surga bu bon bu naan ci xelam: “Sama njaatige day yéexa ñëw,”
48 Mas, se o empregado for mau, pensará assim: “O meu patrão está demorando muito para voltar.”
49 mu tàmbalee dóor ay bokki surgaam, di lekk te naan ak naankat ya,
49 Então começará a bater nos seus companheiros, e a comer, e a beber com os bêbados.
50 kon njaatige ba dina ñëw ci bés bu mu ko séenuwul ak waxtu wu mu xamul.
50 E o patrão voltará no dia em que o empregado menos espera e na hora que ele não sabe.
51 Dina ko dóor ay yar yu metti, jox ko añub naaféq. Foofa dees na fa jooy tey yéyu.
51 Aí o patrão mandará cortar o empregado em pedaços e o condenará a ir para o lugar aonde os hipócritas vão. Ali ele vai chorar e ranger os dentes de desespero.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Mateus 24, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.