Mateus 20

Téereb Injiil (WOL2010) vs ARC

Sair da comparação
ARC Almeida Revista e Corrigida 2009
1 «Noonu nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni boroom kër bu génn ci suba teel, ngir jël ay liggéeykat ndax toolu reseñam.
1 Porque o Reino dos céus é semelhante a um homem, pai de família, que saiu de madrugada a assalariar trabalhadores para a sua vinha.
2 Mu juboo ak liggéeykat ya ci bëccëg posetu denariyon, door leena yebal ca toolam.
2 E, ajustando com os trabalhadores a um dinheiro por dia, mandou-os para a sua vinha.
3 Ci yoor-yoor mu génn, gis ñeneen ñu toog ca pénc ma te liggéeyuñu.
3 E, saindo perto da hora terceira, viu outros que estavam ociosos na praça.
4 Mu ne leen: “Demleen yéen itam ca tool ba, te dinaa leen fey lu jaadu.”
4 E disse-lhes: Ide vós também para a vinha, e dar-vos-ei o que for justo. E eles foram.
5 Ñu dem ca. Mu génnaat ci digg bëccëg ak ci tisbaar, defaat noonu.
5 Saindo outra vez, perto da hora sexta e nona, fez o mesmo.
6 Mu génnati ci tàkkusaan, gis ñeneen di tendeefal. Mu ne leen: “Lu tax ngeen yendoo tendeefal, te liggéeyiwuleen?”
6 E, saindo perto da hora undécima, encontrou outros que estavam ociosos e perguntou-lhes: Por que estais ociosos todo o dia?
7 Ñu ne ko: “Kenn jëlu nu.” Mu ne leen: “Demleen yéen itam ca tool ba.”
7 Disseram-lhe eles: Porque ninguém nos assalariou. Diz-lhes ele: Ide vós também para a vinha e recebereis o que for justo.
8 «Bi nga xamee ne timis jot na, boroom tool ba ne jawriñ ja: “Woowal liggéeykat yi te fey leen seen bëccëg, tàmbali ci ñi mujja ñëw, ba ci ñi fi jëkk.”
8 E, aproximando-se a noite, diz o senhor da vinha ao seu mordomo: Chama os trabalhadores, e paga-lhes o salário, começando pelos derradeiros até aos primeiros.
9 Noonu ñi mu jël ci tàkkusaan ñëw, ku nekk jot posetu denariyon.
9 E, chegando os que
10 Gannaaw ga nag ñi mu jëkka jël ñëw, yaakaar ne dinañu jot lu ëpp loolu, waaye ñoom itam ñu jot ku nekk benn denariyon.
10 vindo, porém, os primeiros, cuidaram que haviam de receber mais; mas, do mesmo modo, receberam um dinheiro cada um.
11 Bi ñu ko jotee nag, ñu tàmbalee ñaxtu ca boroom kër ga,
11 E, recebendo-
12 naan: “Ñi mujja ñëw, benn waxtu rekk lañu liggéey, ba noppi nga yemale leen ak nun, ñi yenu coonob bëccëg bi ak naaj wu metti wi.”
12 dizendo: Estes derradeiros trabalharam
13 Waaye boroom kër ga ne kenn ci ñoom: “Sama waay tooñuma la. Ndax juboowunu woon ci benn denariyon?
13 Mas ele, respondendo, disse a um deles: Amigo, não te faço injustiça; não ajustaste tu comigo um dinheiro?
14 Kon fabal li nga moom te dem. Su ma bëggee fey ku mujja ñëw, li ma la fey yaw,
14 Toma o
15 ndax sañumaa def ak sama alal li ma neex? Walla ndax danga am kiñaan ci li ma yéwén?”
15 Ou não me é lícito fazer o que quiser do Ou é mau o teu olho porque eu sou bom?
16 Noonu ñi mujj ñooy jiituji, ñi jiitu ñooy mujj.»
16 Assim, os derradeiros serão primeiros, e os primeiros, derradeiros, porque muitos são chamados, mas poucos, escolhidos.
17 Gannaaw loolu Yeesu di dem Yerusalem, ànd ak fukki taalibe yi ak ñaar. Noonu mu wéetoo ak ñoom, di leen xamal ci yoon wi lii:
17 E, subindo Jesus a Jerusalém, chamou à parte os seus doze discípulos e, no caminho, disse-lhes:
18 «Nu ngi jëm Yerusalem, te dees na jébbal Doomu nit ki sarxalkat yu mag ya ak xutbakat ya. Dinañu ko àtte, teg ko dee,
18 Eis que vamos para Jerusalém, e o Filho do Homem será entregue aos príncipes dos sacerdotes e aos escribas, e condená-lo-ão à morte.
19 jébbal ko ñi dul Yawut, ngir ñu di ko ñaawal te di ko dóor ay yar, ba noppi daaj ko ci bant. Waaye ca ñetteelu fan ba dina dekki.»
19 E o entregarão aos gentios para que
20 Ci kaw loolu doomi Sebede ya ànd ak seen ndey, ñëw ci Yeesu. Ndey ja sukk, di ko ñaansi lenn.
20 Então, se aproximou dele a mãe dos filhos de Zebedeu, com seus filhos, adorando- o e fazendo-lhe um pedido.
21 Yeesu ne ko: «Loo bëggoon?» Mu ne ko: «Damaa bëggoon nga santaane ne, boo nekkee ci sa nguur, sama ñaari doom ñii toog ak yaw, kenn ci sa ndijoor, ki ci des ci sa càmmoñ.»
21 E ele diz-lhe: Que queres? Ela respondeu: Dize que estes meus dois filhos se assentem um à tua direita e outro à tua esquerda, no teu Reino.
22 Yeesu ne ko: «Xamuleen li ngeen di ñaan. Ndax man ngeena naan kaasu naqar, bi may naan?» Ñu ne ko: «Man nañu ko.»
22 Jesus, porém, respondendo, disse: Não sabeis o que pedis; podeis vós beber o cálice que eu hei de beber e ser batizados com o batismo com que eu sou batizado? Dizem-lhe eles: Podemos.
23 Yeesu ne leen: «Ci dëgg dingeen naan sama kaas, waaye toog ci sama ndijoor mbaa sama càmmoñ, du man maa koy maye, waaye sama Baay moo koy may ñi mu ko waajal.»
23 E diz-lhes ele: Na verdade bebereis o meu cálice, mas o assentar-se à minha direita ou à minha esquerda não me pertence dá-lo, mas é para aqueles para quem meu Pai o tem preparado.
24 Bi nga xamee ne fukki taalibe ya dégg nañu loolu, ñu mere ñaari doomi ndey ya.
24 E, quando os dez ouviram isso, indignaram-se contra os dois irmãos.
25 Waaye Yeesu woo leen ne leen: «Xam ngeen ne ci xeeti àddina, njiit yi dañu leen di dóor yetu nguur, te kilifa yi dañu leen di not.
25 Então, Jesus, chamando-os para junto de si, disse: Bem sabeis que pelos príncipes dos gentios são estes dominados e que os grandes exercem autoridade sobre eles.
26 Buleen mel ni ñooñu. Waaye ku bëgga nekk kilifa ci yéen, na nekk seen surga,
26 Não será assim entre vós; mas todo aquele que quiser, entre vós, fazer-se grande, que seja vosso serviçal;
27 te ku bëgga nekk njiit, na nekk seen jaam.
27 e qualquer que, entre vós, quiser ser o primeiro, que seja vosso servo,
28 Ndaxte noonu la Doomu nit ki ñëwe, du ngir ñu nekk ay surgaam, waaye muy seen surga, ba joxe bakkanam ngir njotug ñu bare.»
28 bem como o Filho do Homem não veio para ser servido, mas para servir e para dar a sua vida
29 Gannaaw loolu Yeesu génn Yeriko, te mbooloo mu bare topp ko.
29 E, saindo eles de Jericó, seguiu-o grande multidão.
30 Fekk ñaari gumba toog ci wetu yoon wa. Bi gumba ya déggee ne Yeesu di jaar, ñu daldi yuuxu ne ko: «Sang bi, yaw Sëtu Daawuda bi, yërëm nu!»
30 E eis que dois cegos, assentados junto do caminho, ouvindo que Jesus passava, clamaram, dizendo: Senhor, Filho de Davi, tem misericórdia de nós.
31 Waaye nit ña gëdd leen, ngir ñu noppi. Teewul gumba ya gëna yuuxu naan: «Sang bi, yaw Sëtu Daawuda bi, yërëm nu!»
31 E a multidão os repreendia, para que se calassem; eles, porém, cada vez clamavam mais, dizendo: Senhor, Filho de Davi, tem misericórdia de nós.
32 Noonu Yeesu daldi taxaw, woo leen ne: «Lu ngeen bëgg, ma defal leen ko?»
32 E Jesus, parando, chamou-os e disse: Que quereis que vos faça?
33 Ñu ne ko: «Sang bi, na sunuy bët ubbiku.»
33 Disseram-lhe eles: Senhor, que os nossos olhos sejam abertos.
34 Noonu Yeesu yërëm leen, laal seeni bët, ñu daldi gis ca saa sa, topp ci moom.
34 Então, Jesus, movido de íntima compaixão, tocou-lhes nos olhos, e logo viram; e eles o seguiram.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Mateus 20, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.