Mateus 19

Téereb Injiil (WOL2010) vs NAA

Sair da comparação
NAA Nova Almeida Atualizada 2017
1 Bi nga xamee ne Yeesu wax na loolu ba noppi, mu jóge Galile, dem ci wàllu réewu Yawut yi, gi féete ci gannaaw dexu Yurdan.
1 Quando Jesus acabou de proferir estas palavras, deixou a Galileia e foi para o território da Judeia, além do Jordão.
2 Mbooloo mu bare topp ko, mu faj leen fa.
2 Grandes multidões o seguiram, e ele as curou ali.
3 Bi mu fa nekkee, ay Farisen ñëw ci moom, bëgg koo fiir; ñu ne ko: «Ndax jaadu na nit fase soxnaam, saa su ko neexee?»
3 Alguns fariseus se aproximaram de Jesus e, testando-o, perguntaram: — É lícito ao homem repudiar a sua mulher por qualquer motivo?
4 Yeesu ne leen: «Xanaa jànguleen ne, ca njàlbéen ga Aji Bind ji sàkk na leen, kii góor, kii jigéen,
4 Jesus respondeu:
5 te mu ne: “Looloo tax góor di teqalikook ndeyam ak baayam, ànd ak soxnaam, ñoom ñaar doon benn.”
5 e que disse: “Por isso o homem deixará o seu pai e a sua mãe e se unirá à sua mulher, tornando-se os dois uma só carne”?
6 Kon nag nekkatuñu ñaar waaye benn lañu. Lu Yàlla takk nag, bu ko nit tas.»
6 De modo que já não são mais dois, porém uma só carne. Portanto, que ninguém separe o que Deus ajuntou.
7 Bi Yeesu waxee loolu, Farisen ya laaj ko ne: «Waaye Musaa santaane na, nit jox soxnaam kayitu pase, tàggook moom. Lu tax mu wax loolu nag?»
7 Os fariseus perguntaram: — Então por que Moisés ordenou dar uma carta de divórcio e repudiar a mulher?
8 Yeesu ne leen: «Musaa may na leen, ngeen fase seen soxna, ndax seen xol dafa dëgër, waaye ca njàlbéen ga demewul woon noonu.
8 Jesus respondeu:
9 Te it maa ngi leen koy wax, koo xam ne kii fase nga sa soxna te du njaaloo tax, boo séyaatee ak keneen, njaaloo nga.»
9 Eu, porém, lhes digo: quem repudiar a sua mulher, não sendo por causa de relações sexuais ilícitas, e casar com outra comete adultério.
10 Bi ko taalibe ya déggee, ñu ne ko: «Bu dee noonu la digganteb góor ak jigéen mel, baña séy moo gën.»
10 Os discípulos de Jesus disseram: — Se essa é a situação do homem em relação à sua mulher, não convém casar.
11 Yeesu ne leen: «Du ñépp ñoo mana nangu loolu, waaye ñi ko Yàlla jagleel rekk.
11 Jesus, porém, lhes respondeu:
12 Ndaxte am na ñu judduwaale tële, am na ñu tële ci loxoy nit, te am na ñu baña séy ngir nguuru Yàlla Aji Kawe ji. Ku ko mana nangu, nangu ko.»
12 Porque há eunucos de nascença; há outros a quem os homens fizeram tais; e há outros que se fizeram eunucos, por causa do Reino dos Céus. Quem é apto para aceitar isto, que aceite.
13 Gannaaw loolu amoon na ay nit ñuy indil Yeesu ay xale, ngir mu teg leen ay loxoom, ñaanal leen. Waaye taalibe ya gëdd leen.
13 Então trouxeram algumas crianças a Jesus para que ele lhes impusesse as mãos e orasse, mas os discípulos os repreendiam.
14 Bi Yeesu gisee loolu, mu ne leen: «Bàyyileen xale yi, te buleen leen tere, ñu ñëw fi man. Ndaxte ñu mel ni ñoom, ñoo yelloo nguuru Yàlla Aji Kawe ji.»
14 Jesus, porém, disse:
15 Noonu Yeesu teg leen ay loxoom, ba noppi jóge fa.
15 E, tendo-lhes imposto as mãos, retirou-se dali.
16 Bi muy dem nag, nit daldi ñëw ci moom ne ko: «Kilifa gi, lan laa wara def ci lu baax, ngir mana am dund gu dul jeex?»
16 E eis que alguém, aproximando-se de Jesus, lhe perguntou: — Mestre, que farei de bom para alcançar a vida eterna?
17 Yeesu ne ko: «Lu tax nga laaj ma ci wàllu lu baax? Kenn kepp moo baax. Boo bëggee dugg ca dund googu ci kaw, nanga sàmm ndigal yi.»
17 Jesus respondeu:
18 Waxambaane wa laaj ko: «Yan la?» Yeesu ne ko: «Yii: bul bóome, bul njaaloo, bul sàcc, bul seede lu dul dëgg,
18 E ele lhe perguntou: — Quais? Jesus respondeu:
19 teralal sa ndey ak sa baay, te it: nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp.»
19 honre o seu pai e a sua mãe e ame o seu próximo como você ama a si mesmo.”
20 Waxambaane wa ne ko: «Sàmm naa yooyu yépp, lu ma deseeti?»
20 O jovem disse: — Tudo isso tenho observado. O que me falta ainda?
21 Noonu Yeesu ne ko: «Boo bëggee mat sëkk, demal jaay li nga am, jox ko miskin yi te dinga woomle ca asamaan. Boo noppee, ñëwal topp ci man.»
21 Jesus respondeu:
22 Waaye bi waxambaane wa déggee loolu, mu jóge fa ak tiis, ndaxte ku bare woon alal la.
22 Mas o jovem, ouvindo esta palavra, retirou-se triste, porque era dono de muitas propriedades.
23 Noonu Yeesu wax taalibeem ya ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, boroom alal dugg ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji, lu jafee ngoogu!
23 Então Jesus disse aos seus discípulos:
24 Ma waxaat leen ko: giléem jaar ci bën-bënu puso moo gëna yomb boroom alal dugg ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji.»
24 E ainda lhes digo que é mais fácil um camelo passar pelo fundo de uma agulha do que um rico entrar no Reino de Deus.
25 Bi nga xamee ne taalibe ya dégg nañu loolu, ñu daldi waaru lool ne ko: «Kan moo mana mucc nag?»
25 Ouvindo isto, os discípulos ficaram muito admirados e perguntaram: — Sendo assim, quem pode ser salvo?
26 Noonu Yeesu xool leen ne: «Loolu të na nit, waaye dara tëwul Yàlla.»
26 Jesus, olhando para eles, disse:
27 Bi ko Piyeer déggee, mu daldi ne: «Waaw, nun nag, dëddu nanu lépp, topp la; kon nu nuy mujje nun?»
27 Então Pedro, tomando a palavra, disse: — Eis que nós deixamos tudo e seguimos o senhor; que será, pois, de nós?
28 Yeesu ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, bés baa ngi ñëw bu Yàllay yeesalaat lépp, te Doomu nit ki toog ci jalam, bi soloo ndam. Bés boobu nag, yéen ñi ma topp dingeen toog ci fukki jal ak ñaar, di àtte fukki giir ak ñaar yu bànni Israyil.
28 Jesus lhes respondeu:
29 Koo xam ne kii dëddu nga ngir sama tur ay kër, ay doomi ndey yu góor walla yu jigéen, ndey walla baay, ay doom walla ay tool, dinga ko jotaat téeméeri yoon, ba noppi am dund gu dul jeex.
29 E todo aquele que tiver deixado casas, irmãos, irmãs, pai, mãe, filhos ou campos, por causa do meu nome, receberá muitas vezes mais e herdará a vida eterna.
30 Waaye ñu bare ci ñi jiitu, ñooy mujji; ñi mujj, ñooy jiituji.
30 Porém muitos primeiros serão últimos; e os últimos serão primeiros.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Mateus 19, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.