Mateus 18
Téereb Injiil (WOL2010) vs VC
1 Ca waxtu woowu taalibe ya ñëwoon nañu ci Yeesu, laaj ko: «Kan moo gëna màgg ci nguuru Yàlla mi nekk ci kaw?»
1 Neste momento os discípulos aproximaram-se de Jesus e perguntaram-lhe: Quem é o maior no Reino dos céus?
2 Noonu Yeesu woo xale, teg ko ci seen biir,
2 Jesus chamou uma criancinha, colocou-a no meio deles e disse:
3 ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, su ngeen waññikuwul ci Yàlla, ba mel niy xale, dungeen dugg mukk ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji.
3 Em verdade vos declaro: se não vos transformardes e vos tornardes como criancinhas, não entrareis no Reino dos céus.
4 Kuy suufeelu nag, ba mel ni xale bii, kooku mooy ki gëna màgg ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji.
4 Aquele que se fizer humilde como esta criança será maior no Reino dos céus.
5 Te it ku nangu ci sama tur xale bu mel ni kii, man mii nga nangu.
5 E o que recebe em meu nome a um menino como este, é a mim que recebe.
6 Waaye ku yóbbe bàkkaar kenn ci ñi gëna tuuti ñi ma gëm, li gën ci moom mooy ñu takk doj wu réy ci baatam, sànni ko ca fa gëna xóot ca géej ga.
6 Mas, se alguém fizer cair em pecado um destes pequenos que crêem em mim, melhor fora que lhe atassem ao pescoço a mó de um moinho e o lançassem no fundo do mar.
7 «Yaw àddina, dinga torox ndax say fiir yiy yóbbe nit bàkkaar. Fiir manta ñàkk, waaye toroxte dal na nit ki koy lal.
7 Ai do mundo por causa dos escândalos! Eles são inevitáveis, mas ai do homem que os causa!
8 Boo xamee ne sa loxo mbaa sa tànk mu ngi lay yóbbe bàkkaar, dagg ko, sànni ko fu sore. Ndaxte nga lafañ walla ñàkk loxo te dugg ci dund gu wóor gi, moo gën ci yaw, nga am ñaari loxo walla ñaari tànk, te ñu sànni la ci sawara su dul fey mukk.
8 Por isso, se tua mão ou teu pé te fazem cair em pecado, corta-os e lança-os longe de ti: é melhor para ti entrares na vida coxo ou manco que, tendo dois pés e duas mãos, seres lançado no fogo eterno.
9 Boo xamee ne sa bët mu ngi lay yóbbe bàkkaar, luqi ko, sànni ko fu sore. Ndaxte nga patt te dugg ci dund gu wóor gi, moo gën ci yaw, nga am ñaari bët, te ñu sànni la ci sawara.
9 Se teu olho te leva ao pecado, arranca-o e lança-o longe de ti: é melhor para ti entrares na vida cego de um olho que seres jogado com teus dois olhos no fogo da geena.
10 — ausente —
10 Guardai-vos de menosprezar um só destes pequenos, porque eu vos digo que seus anjos no céu contemplam sem cessar a face de meu Pai que está nos céus.
11 — ausente —
11 {Porque o Filho do Homem veio salvar o que estava perdido.}
12 «Luy seen xalaat ci lii? Su fi amoon nit ku am téeméeri xar, te benn ci ñoom réer, lu muy def? Ndax du bàyyi ca parlukaay ba juróom ñeent fukki xar ya ak juróom ñeent, te dem wuti ma réer?
12 Que vos parece? Um homem possui cem ovelhas: uma delas se desgarra. Não deixa ele as noventa e nove na montanha, para ir buscar aquela que se desgarrou?
13 Bu ko gisee, mbég mi mu am ci moom mooy ëpp mbég, mi mu am ci juróom ñeent fukki xar ya ak juróom ñeent ya réerul.
13 E se a encontra, sente mais júbilo do que pelas noventa e nove que não se desgarraram.
14 «Noonu it seen Baay bi nekk ci kaw bëggul kenn ci ñi gëna tuuti sànku.
14 Assim é a vontade de vosso Pai celeste, que não se perca um só destes pequeninos.
15 «Te lii itam, bu sa mbokk defee bàkkaar, demal yedd ko, yéen ñaar rekk. Bu la dégloo, kon gindi nga sa mbokk.
15 Se teu irmão tiver pecado contra ti, vai e repreende-o entre ti e ele somente; se te ouvir, terás ganho teu irmão.
16 Waaye bu la dégluwul, àndal ak kenn mbaa ñaar, ngir mbir mi dëggu ci li ko ñaar walla ñett seede.
16 Se não te escutar, toma contigo uma ou duas pessoas, a fim de que toda a questão se resolva pela decisão de duas ou três testemunhas.
17 Bu leen dégluwul ñoom itam, wax ko mbooloom ñi gëm. Bu dégluwul mbooloo ma nag, nga teg ko ni ku gëmul Yàlla mbaa ab juutikat.
17 Se recusa ouvi-los, dize-o à Igreja. E se recusar ouvir também a Igreja, seja ele para ti como um pagão e um publicano.
18 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, lépp lu ngeen yeew ci àddina, dees na ko yeew ci asamaan, te lépp lu ngeen yiwi ci àddina, dees na ko yiwi ci asamaan.
18 Em verdade vos digo: tudo o que ligardes sobre a terra será ligado no céu, e tudo o que desligardes sobre a terra será também desligado no céu.
19 «Maa ngi leen koy wax it, bu ñaar ci yéen déggoo ci àddina, ngir ñaan lu mu mana doon, sama Baay bi nekk ci kaw dina leen ko may.
19 Digo-vos ainda isto: se dois de vós se unirem sobre a terra para pedir, seja o que for, consegui-lo-ão de meu Pai que está nos céus.
20 Ndaxte fu ñaar walla ñetti nit booloo ci sama tur, maa ngi ci seen biir.»
20 Porque onde dois ou três estão reunidos em meu nome, aí estou eu no meio deles.
21 Noonu Piyeer ñëw ci Yeesu, laaj ko: «Boroom bi, bu ma sama mbokk tooñee, ñaata yoon laa ko wara baal? Xanaa ba ci juróom ñaari yoon?»
21 Então Pedro se aproximou dele e disse: Senhor, quantas vezes devo perdoar a meu irmão, quando ele pecar contra mim? Até sete vezes?
22 Yeesu ne ko: «Waxuma la ba ci juróom ñaari yoon, waaye ba ci juróom ñaar fukki juróom ñaari yoon.
22 Respondeu Jesus: Não te digo até sete vezes, mas até setenta vezes sete.
23 «Loolu moo tax nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni buur bu bëgga waññ alalam ak ay jaraafam.
23 Por isso, o Reino dos céus é comparado a um rei que quis ajustar contas com seus servos.
24 Ba mu tàmbalee waññ nag, ñu indil buur ba ku ko ameel ay milyoŋ yu baree bare,
24 Quando começou a ajustá-las, trouxeram-lhe um que lhe devia dez mil talentos.
25 waaye jaraaf ja amul lu mu feye. Kon nag sangam santaane, ñu jaay ko moom ak soxnaam ak ay doomam ak lépp lu mu am, ngir fey bor ba.
25 Como ele não tinha com que pagar, seu senhor ordenou que fosse vendido, ele, sua mulher, seus filhos e todos os seus bens para pagar a dívida.
26 Kon jaraaf ja daanu ciy tànkam ne ko: “Muñal ma, dinaa la fey lépp.”
26 Este servo, então, prostrou-se por terra diante dele e suplicava-lhe: Dá-me um prazo, e eu te pagarei tudo!
27 Noonu sangam yërëm ko, bàyyi ko, baal ko bor ba.
27 Cheio de compaixão, o senhor o deixou ir embora e perdoou-lhe a dívida.
28 «Bi loolu amee jaraaf ja génn, gis benn moroomu jaraafam bu ko ameel ay junni. Mu daldi ko jàpp, poñe ko ne ko: “Fey ma li nga ma ameel.”
28 Apenas saiu dali, encontrou um de seus companheiros de serviço que lhe devia cem denários. Agarrou-o na garganta e quase o estrangulou, dizendo: Paga o que me deves!
29 Kon moroomam daanu ci suuf, ñaan ko ne: “Muñal ma, dinaa la fey.”
29 O outro caiu-lhe aos pés e pediu-lhe: Dá-me um prazo e eu te pagarei!
30 Waaye moom nanguwu ko, mu dem, tëj ko kaso, ba kera mu fey li mu ko ameel.
30 Mas, sem nada querer ouvir, este homem o fez lançar na prisão, até que tivesse pago sua dívida.
31 «Bi ay moroomam gisee loolu nag, ñu am naqar wu réy, daldi dem, xamal seen sang li xew lépp.
31 Vendo isto, os outros servos, profundamente tristes, vieram contar a seu senhor o que se tinha passado.
32 Sang ba nag woolu jaraaf ba ne ko: “Yaw jaraaf ju soxor nga! Baal naa la sa bor bépp, ndaxte tinu nga ma.
32 Então o senhor o chamou e lhe disse: Servo mau, eu te perdoei toda a dívida porque me suplicaste.
33 Lu tax yaw itam yërëmoo sa moroom, ni ma la yërëme?”
33 Não devias também tu compadecer-te de teu companheiro de serviço, como eu tive piedade de ti?
34 Noonu sang ba mer, jébbal ko ñiy fitnaale ca kaso ba, ba kera muy fey li mu ko ameel lépp.
34 E o senhor, encolerizado, entregou-o aos algozes, até que pagasse toda a sua dívida.
35 «Noonu la leen sama Baay bi ci kaw di def, bu ngeen baalul ku nekk seen mbokk ak xol bu sedd.»
35 Assim vos tratará meu Pai celeste, se cada um de vós não perdoar a seu irmão, de todo seu coração.
Atalhos do teclado
- Capítulo anterior←
- Próximo capítulo→
- Versículo anteriork
- Próximo versículoj
- Limpar seleçãoEsc
- Esta ajuda?
Estude este capítulo no WhatsApp
Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Mateus 18, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.