Mateus 17
Téereb Injiil (WOL2010) vs NAA
1 Juróom benni fan gannaaw gi, Yeesu àndoon na ak Piyeer, Saag ak Yowaana rakkam, yóbbu leen fu wéet ci tund wu kawe lool.
1 Seis dias depois, Jesus tomou consigo Pedro e os irmãos Tiago e João e os levou, em particular, a um alto monte.
2 Mu soppiku fa seen kanam, xar kanamam di melax nib jant, te ay yéreem weex ni leer.
2 E Jesus foi transfigurado diante deles. O seu rosto resplandecia como o sol, e as suas roupas se tornaram brancas como a luz.
3 Naka noonu ñu gis yonenti Yàlla Musaa ak Ilyaas, di waxtaan ak Yeesu.
3 E eis que lhes apareceram Moisés e Elias, falando com Jesus.
4 Piyeer nag daldi wax Yeesu ne ko: «Sang bi, bég nanu ci sunu teew fii; soo ko bëggee, dinaa fi defar ñetti mbaar, benn yaw, benn Musaa ak benn Ilyaas.»
4 Então Pedro, tomando a palavra, disse a Jesus: — Senhor, bom é estarmos aqui. Se o senhor quiser, farei aqui três tendas: uma para o senhor, outra para Moisés e outra para Elias.
5 Waaye bi muy wax, niir wu leer muur leen, te baat jib ca niir wa naan: «Kii mooy sama Doom ji ma bëgg, ci moom laa ame bànneex; dégluleen ko.»
5 Falava ele ainda, quando uma nuvem luminosa os envolveu; e eis, vindo da nuvem, uma voz que dizia: — Este é o meu Filho amado, em quem me agrado; escutem o que ele diz!
6 Bi taalibe yi déggee baat bi, ñu ne nërëm ci suuf, daldi tiit lool.
6 Ao ouvirem aquela voz, os discípulos caíram de bruços, tomados de grande medo.
7 Waaye Yeesu jegeñsi, laal leen naan: «Jógleen, buleen ragal dara.»
7 Jesus aproximou-se e tocou neles, dizendo:
8 Noonu ñu xool ci kaw, waaye gisatuñu kenn ku dul Yeesu rekk.
8 Então eles, levantando os olhos, não viram mais ninguém, a não ser Jesus.
9 Bi loolu amee ñu wàcc ca tund wa. Bi ñuy wàcc nag, Yeesu sant leen ne: «Buleen nettali kenn li ngeen gis, ba kera Doomu nit ki dekki.»
9 Ao descerem do monte, Jesus lhes ordenou:
10 Noonu taalibe ya laaj ko: «Lu tax xutbakat ya nag di wax ne, Ilyaas mooy jëkka ñëw?»
10 Mas os discípulos perguntaram a Jesus: — Por que, então, os escribas dizem ser necessário que Elias venha primeiro?
11 Yeesu ne leen: «Waaw, dëgg la, Ilyaas war na ñëw, jubbanti lépp.
11 Jesus respondeu:
12 Teewul maa ngi leen di wax ne, Ilyaas ñëw na te xàmmiwuñu ko, waaye def nañu ko la leen neex. Noonu it dañoo nara sonal léegi Doomu nit ki.»
12 Eu, porém, lhes digo que Elias já veio, e não o reconheceram; pelo contrário, fizeram com ele tudo o que quiseram. Assim também o Filho do Homem irá sofrer nas mãos deles.
13 Ndax wax jooju nag, taalibe ya xam ne ci mbirum Yaxya la leen doon wax.
13 Então os discípulos entenderam que ele estava se referindo a João Batista.
14 Bi nga xamee ne wàcc nañu, ba ñëw ca mbooloo ma, genn góor ñëw ci moom, sukk
14 Quando eles chegaram para junto da multidão, um homem se aproximou de Jesus, ajoelhou-se e disse:
15 naan: «Sang bi, yërëmal sama doom, ndaxte mu ngi say, di am coono bu metti; léeg-léeg mu daanu ci sawara, léeg-léeg mu daanu ci ndox.
15 — Senhor, tenha pena do meu filho, porque ele tem convulsões e sofre muito; pois muitas vezes cai no fogo e outras tantas cai na água.
16 Indi naa ko ci say taalibe, waaye manuñu koo faj.»
16 Apresentei-o aos seus discípulos, mas eles não puderam curá-lo.
17 Noonu Yeesu ne: «Yéen niti jamono jii, yéen ñi gëmadi te dëng, ba kañ laa wara nekk ak yéen, ba kañ laa leen di wara muñal?» Mu ne leen: «Indil-leen ma xale bi fii.»
17 Jesus exclamou:
18 Noonu Yeesu tëkku rab wa, rab wa génn ca xale ba, mu daldi wér ca saa sa.
18 E Jesus repreendeu o demônio, e este saiu do menino; e, desde aquela hora, o menino ficou curado.
19 Bi loolu amee taalibe ya ñëw ci Yeesu, laaj ko ci pegg: «Lu tax nun manunu woona dàq rab wi?»
19 Então os discípulos, aproximando-se de Jesus, perguntaram em particular: — Por que motivo nós não pudemos expulsá-lo?
20 — ausente —
20 Jesus respondeu:
21 — ausente —
21 [Mas esse tipo de demônio só pode ser expulso por meio de oração e jejum.]
22 Bi ñuy wër diiwaanu Galile nag, Yeesu ne leen: «Léegi ñu jébbal Doomu nit ki ci loxoy nit ñi;
22 Quando eles estavam reunidos na Galileia, Jesus lhes disse:
23 dinañu ko rey, mu dekki ca ñetteelu fan ba.» Bi ko taalibe ya déggee, ñu am naqar lool.
23 e estes o matarão; mas, ao terceiro dia, ressuscitará. Então os discípulos ficaram muito tristes.
24 Gannaaw loolu Yeesu ak taalibe ya ñëw Kapernawum. Bi ñu fa àggee nag, laajkati warugaru kër Yàlla ga ñëw ci Piyeer ne ko: «Ndax seen kilifa du fey posetu ñaari daraxma ngir warugar wi?»
24 Quando Jesus e os discípulos chegaram a Cafarnaum, os que cobravam o imposto das duas dracmas se dirigiram a Pedro e perguntaram: — O Mestre de vocês não paga as duas dracmas?
25 Piyeer ne leen: «Ahakay!»
25 Pedro respondeu: — Claro que paga! Quando Pedro estava entrando em casa, Jesus se adiantou, dizendo:
26 Piyeer ne ko: «Xanaa ñi bokkul ci kër gi.» Yeesu ne ko: «Kon doom yi nag mucc nañu ci.
26 Quando Pedro respondeu: “Dos estranhos”, Jesus lhe disse:
27 Waaye bëgguma nu naqaral leen; demal sànni oos ca dex ga te nga génne jën wa jëkka xëcc. Boo ubbee gémmiñam, dinga ca gis posetu estateer. Jël ko nag, jox leen ko ngir man ak yaw.»
27 Mas, para que não os escandalizemos, vá ao mar, jogue o anzol e puxe o primeiro peixe que fisgar. Ao abrir a boca do peixe, você encontrará uma moeda. Pegue essa moeda e entregue aos cobradores, para pagar o meu imposto e o seu.
Atalhos do teclado
- Capítulo anterior←
- Próximo capítulo→
- Versículo anteriork
- Próximo versículoj
- Limpar seleçãoEsc
- Esta ajuda?
Estude este capítulo no WhatsApp
Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Mateus 17, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.