Mateus 15
Téereb Injiil (WOL2010) vs NAA
1 Ca jamono jooja amoon na bés ay Farisen ak ay xutbakat jóge Yerusalem, ñëw ci Yeesu ne ko:
1 Então alguns fariseus e escribas vieram de Jerusalém até Jesus e perguntaram:
2 «Lu tax say taalibe di moy aaday yoon, yi maam yi tëral? Ndaxte duñu raxas seeni loxo, bu ñuy lekk.»
2 — Por que os seus discípulos transgridem a tradição dos anciãos? Pois não lavam as mãos, quando comem.
3 Waaye Yeesu ne leen: «Yéen itam lu tax ngeen di moy li Yàlla santaane, ngir topp seeni aada?
3 Jesus, porém, lhes respondeu:
4 Yàlla nee na: “Teralal sa ndey ak sa baay,” te it: “Ku móolu sa ndey walla sa baay, dees na la rey.”
4 Porque Deus disse: “Honre o seu pai e a sua mãe.” E: “Quem maldisser o seu pai ou a sua mãe seja punido de morte.”
5 Waaye yéen dangeen ne: “Ku wax sa ndey walla sa baay: ‘Li ngeen wara jariñoo ci man, jébbal naa ko Yàlla,’
5 Vocês, porém, dizem que, se alguém disser ao seu pai ou à sua mãe: “A ajuda que você poderia receber de mim é oferta ao Senhor”,
6 kooku amatul warugaru teral baayam.” Noonu tebbi ngeen kàddug Yàlla ndax seen aada.
6 esse não precisará mais honrar os seus pais. E, assim, vocês invalidam a palavra de Deus, por causa da tradição de vocês.
7 Yéen ñi naaféq, Esayi waxoon na bu baax ci kàddug Yàlla ci seen mbir, bi mu naan:
7 Hipócritas! Bem profetizou Isaías a respeito de vocês, dizendo:
8 “Xeet wii ñu ngi may teral ci seen gémmiñ,
8 “Este povo me honra
9 Seen màggal amul benn njariñ,
9 E em vão me adoram,
10 Noonu Yeesu woo mbooloo mi ci moom ne leen: «Dégluleen te xam:
10 E, convocando a multidão, Jesus disse:
11 du li dugg ci gémmiñ mooy indil nit sobe, waaye li ciy génne mooy indil nit sobe.»
11 o que contamina a pessoa não é o que entra pela boca, mas o que sai da boca; isto, sim, contamina a pessoa.
12 Bi taalibeem ya déggee loolu, ñu ñëw ci moom ne ko: «Ndax xam nga ne, Farisen yi dañoo mer ndax loolu nga wax?»
12 Então, aproximando-se dele os discípulos, disseram: — Sabia que os fariseus, ouvindo o que o senhor disse, ficaram escandalizados?
13 Yeesu ne leen: «Garab gu sama Baay bi ci kaw jiwul, dees na ko buddi.
13 Mas ele respondeu:
14 Bàyyileen leen, ay gumba lañu yuy wommat ay gumba; bu gumba dee wommat moroomam nag, kon dinañu daanu ñoom ñaar ci kàmb.»
14 Esqueçam os fariseus; são cegos, guias de cegos. Ora, se um cego guiar outro cego, ambos cairão num buraco.
15 Piyeer nag jël kàddu gi, laaj Yeesu: «Firil nu léeb wi.»
15 Então Pedro disse a Jesus: — Explique-nos esta parábola.
16 Noonu Yeesu ne ko: «Ndax ba tey seen xol dafa tëju, yéen itam?
16 Jesus, porém, disse:
17 Xamuleen ne, lépp lu dugg ci gémmiñ, ci biir lay jëm tey génn ca bérab bu làqu?
17 Não compreendem que tudo o que entra pela boca desce para o estômago e depois é eliminado?
18 Waaye li génn ci gémmiñ mu ngi jóge ci xol; loolu mooy indil nit sobe.
18 Mas o que sai da boca vem do coração, e é isso que contamina a pessoa.
19 Ndaxte ci xol la xalaat yu bon di jóge, ak bóom, njaaloo, ndoxaanu yàqute, càcc, seede lu dul dëgg ak saaga.
19 Porque do coração procedem maus pensamentos, homicídios, adultérios, imoralidade sexual, furtos, falsos testemunhos, blasfêmias.
20 Yooyu ñooy indil nit sobe, waaye lekk ak loxo yoo raxasul du tax nit am sobe.»
20 São estas as coisas que contaminam a pessoa; mas o comer sem lavar as mãos não a contamina.
21 Gannaaw loolu Yeesu jóge fa, dem ci diiwaanu Tir ak Sidon.
21 Saindo dali, Jesus foi para a região de Tiro e Sidom.
22 Ba mu fa àggee nag, jigéenu waa Kanaan, ja dëkk ca wàll yooyu, daldi génn, di wax ca kaw ne ko: «Yaw sang bi, Sëtu Daawuda bi, yërëm ma! Rab jàpp na sama doom ju jigéen, te dafa sonn lool.»
22 E eis que uma mulher cananeia, que tinha vindo daqueles lados, clamava: — Senhor, Filho de Davi, tenha compaixão de mim! Minha filha está horrivelmente endemoniada.
23 Waaye Yeesu waxu ko dara. Ay taalibeem nag ñëw ci moom ne ko: «Doo ko yiwi, mu ngi nuy topp, di yuuxu ci sunu kaw.»
23 Jesus, porém, não lhe respondeu palavra. Então os seus discípulos, aproximando-se, disseram: — Mande-a embora, pois vem gritando atrás de nós.
24 Yeesu ne: «Yónniwuñu ma, lu dul ci xari bànni Israyil yu réer.»
24 Mas Jesus respondeu:
25 Waaye jigéen ja ñëw, sukk ci kanamam naan: «Sang bi, wallusi ma!»
25 Ela, porém, veio e o adorou, dizendo: — Senhor, me ajude!
26 Yeesu ne ko: «Jël ñamu gone yi, sànni ko xaj yi, rafetul.»
26 Jesus respondeu:
27 Waaye jigéen ja ne ko: «Waaw, sang bi, teewul xaj yi di lekk ruusit, yi rot ci seen lekkukaayu boroom.»
27 A mulher disse: — É verdade, Senhor, pois os cachorrinhos comem das migalhas que caem da mesa dos seus donos.
28 Ci kaw loolu Yeesu ne ko: «Yaw jigéen ji, sa ngëm réy na; na am, ni nga ko bëgge.» Noonu doomam daldi wér ca saa sa.
28 Então Jesus exclamou: E, desde aquele momento, a filha dela ficou curada.
29 Bi loolu amee Yeesu jóge foofa, ñëw ci weti dexu Galile; mu yéeg ca aw tund, toog fa.
29 Saindo dali, Jesus foi para junto do mar da Galileia; e, subindo ao monte, assentou-se ali.
30 Ba mu fa nekkee, nit ñu bare ñëw ci moom, indaale ay lafañ, ay làggi, ay gumba, ay luu ak ñeneen ñu bare. Ñu teg leen ci tànki Yeesu, mu faj leen.
30 E vieram a ele muitas multidões trazendo consigo coxos, cegos, aleijados, mudos e muitos outros e os deixaram junto aos pés de Jesus; e ele os curou.
31 Nit ñépp waaru, ndaxte gis nañu luu yuy wax, làggi yu wér, lafañ yuy dox, ak gumba yuy gis. Ñu daldi màggal Yàlla Buuru Israyil.
31 O povo ficou maravilhado ao ver que os mudos falavam, os aleijados recuperavam a saúde, os coxos andavam e os cegos viam. E glorificavam o Deus de Israel.
32 Gannaaw loolu Yeesu woo ci moom taalibeem ya ne leen: «Yërëm naa mbooloo mi, ndaxte toog nañu fi man ñetti fan, te amatuñu lu ñu lekk. Bëgguma leena yiwi te lekkuñu, ngir bañ ñu tële ci yoon wi.»
32 Então Jesus chamou os seus discípulos e disse:
33 Noonu taalibeem ya laaj ko: «Waaye fu nuy jële ci àll bi mburu mu doy ngir mbooloo mu tollu nii?»
33 Mas os discípulos lhe disseram: — Onde haverá neste deserto pão suficiente para saciar tão grande multidão?
34 Yeesu ne leen: «Ñaata mburu ngeen am?» Ñu ne ko: «Juróom ñaari mburu ak ay jën yu ndaw.»
34 Jesus perguntou: Eles responderam: — Sete pães e alguns peixinhos.
35 Ci kaw loolu Yeesu sant mbooloo mi, ñu toog ci suuf.
35 Então, tendo mandado o povo assentar-se no chão,
36 Mu fab juróom ñaari mburu yi ak jën yi, sant Yàlla, damm leen, jox leen taalibe yi, ñu séddale leen mbooloo mi.
36 pegou os sete pães e os peixes e, tendo dado graças, os partiu e deu aos discípulos, e estes distribuíram ao povo.
37 Noonu ñépp lekk ba suur. Te ñu dajale juróom ñaari dàmba yu fees ak dammit yi ci des.
37 Todos comeram e se fartaram; e, dos pedaços que sobraram, recolheram sete cestos cheios.
38 Gannaaw jigéen ñi ak gone yi, góor ñi ci lekk matoon nañu ñeenti junni.
38 Ora, os que comeram eram quatro mil homens, além de mulheres e crianças.
39 Noonu Yeesu yiwi mbooloo mi, dugg ci gaal, ñëw ci wàlli Magadan.
39 E, tendo despedido as multidões, Jesus entrou no barco e foi para o território de Magadã.
Atalhos do teclado
- Capítulo anterior←
- Próximo capítulo→
- Versículo anteriork
- Próximo versículoj
- Limpar seleçãoEsc
- Esta ajuda?
Estude este capítulo no WhatsApp
Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Mateus 15, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.