Mateus 14
Téereb Injiil (WOL2010) vs NAA
1 Ca jamono joojale Erodd boroom diiwaanu Galile dégg na tur, wa Yeesu am.
1 Por aquele tempo, o tetrarca Herodes soube da fama de Jesus
2 Noonu mu ne ay surgaam: «Kooku mooy Yaxya mi dekki; moo tax mu ànd ak kàttanu def ay kéemaan.»
2 e disse aos que o serviam: — Este é João Batista. Ele ressuscitou dos mortos, e, por isso, forças miraculosas operam nele.
3 Ndaxte Erodd jàppoon na Yaxya, yeew ko, tëj. Ndaxte Erodd takkoon na Erojàdd jabaru Filib magam,
3 Porque Herodes, havendo prendido João, o amarrou e pôs na prisão, por causa de Herodias, mulher do seu irmão Filipe.
4 te Yaxya daan ko wax: «Jaaduwul nga denc ko.»
4 Pois João lhe dizia: “Você não tem o direito de viver com ela.”
5 Erodd nag bëgg koo rey, waaye dafa ragal nit ñi, ci li ñu teg Yaxya ab yonent.
5 Embora Herodes quisesse matá-lo, tinha medo do povo, porque consideravam João como profeta.
6 Bi ñu ca tegee ab diir nag, ñuy màggal bés ba Erodd juddu woon, te doomu Erojàdd ju jigéen di fecc ci biir gan ñi. Loolu neex Erodd,
6 Mas, quando chegou o dia do aniversário de Herodes, a filha de Herodias dançou diante de todos e agradou a Herodes.
7 ba mu dig ko ci kaw ngiñ ne ko: «Loo laaj, dinaa la ko jox.»
7 Este prometeu, com juramento, dar-lhe o que ela pedisse.
8 Noonu ndaw sa daldi topp la ko ndey ji digaloon, ne Erodd: «Indil ma fii ci biir ndab boppu Yaxya.»
8 Então ela, instigada por sua mãe, disse: — Dê-me, aqui, num prato, a cabeça de João Batista.
9 Bi ko buur ba déggee, mu am naqar, waaye ngiñ la ak gan ña tax mu santaane, ñu jox ko ko.
9 O rei ficou triste, mas, por causa do juramento e dos que estavam com ele à mesa, ordenou que o pedido fosse atendido.
10 Mu yónnee nag, ngir ñu dagg boppu Yaxya ca kaso ba.
10 Assim, deu ordens para que João fosse decapitado na prisão.
11 Ñu indi bopp bi ci biir ndab, jox ko janq ba, mu jox ko ndeyam.
11 A cabeça foi trazida num prato e dada à jovem, que a levou à sua mãe.
12 Noonu taalibey Yaxya ñëw, fab néew ba, suul ko; ba noppi dem, wax ko Yeesu.
12 Então vieram os discípulos de João, levaram o corpo e o sepultaram; depois, foram e anunciaram isso a Jesus.
13 Bi Yeesu déggee deewu Yaxya nag, mu jóge fa, dugg cig gaal, di dem ca bérab bu wéet. Waaye bi ko nit ñi yégee, ñu daldi jóge ci dëkk yi, topp ko ak seeni tànk.
13 Jesus, ouvindo isto, retirou-se dali num barco para um lugar deserto, à parte. Ao saberem disso, as multidões vieram das cidades seguindo-o por terra.
14 Yeesu génn ci gaal gi nag, gis mbooloo mu réy, mu yërëm leen, ba faj ñi ci wopp.
14 Ao desembarcar, Jesus viu uma grande multidão, compadeceu-se dela e curou os seus enfermos.
15 Ca ngoon sa taalibe yi ñëw ci moom ne ko: «Fii àllub neen la, te léegi mu guddi. Doo yiwi mbooloo mi, ngir ñu dem ci dëkk yu ndaw yi, jënd lu ñu mana lekk?»
15 Ao cair da tarde, os discípulos se aproximaram de Jesus e disseram: — Este lugar é deserto, e já é tarde. Mande as multidões embora, para que, indo pelas aldeias, comprem para si o que comer.
16 Waaye Yeesu ne leen: «Matul ñu dem, yéen joxleen leen lu ñu lekk.»
16 Jesus, porém, lhes disse:
17 Ñu ne ko: «Amunu fi lu dul juróomi mburu ak ñaari jën.»
17 Mas eles responderam: — Não temos aqui senão cinco pães e dois peixes.
18 Yeesu ne leen: «Indil-leen ma ko fii.»
18 Então Jesus disse:
19 Ci kaw loolu Yeesu sant mbooloo ma, ñu toog ca ñax ma. Mu jël juróomi mburu ya ak ñaari jën ya, xool ci kaw, sant Yàlla. Mu damm mburu ma, jox ko taalibe ya, ñu séddale ko nit ña.
19 E, tendo mandado que a multidão se assentasse sobre a relva, pegando os cinco pães e os dois peixes, erguendo os olhos para o céu, os abençoou. Depois, tendo partido os pães, deu-os aos discípulos, e estes deram às multidões.
20 Noonu ñépp lekk ba suur. Te ñu dajale dammit ya ca des, mu nekk fukki pañe ak ñaar yu fees.
20 Todos comeram e se fartaram, e ainda recolheram doze cestos cheios dos pedaços que sobraram.
21 Gannaaw jigéen ña ak gone ya, góor ña doon lekk matoon nañu juróomi junni.
21 E os que comeram eram cerca de cinco mil homens, além de mulheres e crianças.
22 Bi loolu amee Yeesu sant taalibe ya, ñu dugg gaal ga te jàll dex ga, jiituji ko, muy yiwi mbooloo ma.
22 Logo a seguir, Jesus fez com que os discípulos entrassem no barco e fossem adiante dele para o outro lado, enquanto ele despedia as multidões.
23 Bi mu ko yiwee nag, mu yéeg ca tund wa, ngir wéet ak Yàlla. Noonu guddi jot, fekk mu nekk fa moom rekk.
23 E, tendo despedido as multidões, ele subiu ao monte, a fim de orar sozinho. Ao cair da tarde, lá estava ele, só.
24 Bi mu fa nekkee nag, gaal ga sore na tefes ga, te duus ya di ko yëngal bu metti, ndax ngelaw la leen soflu.
24 Entretanto, o barco já estava longe, a uma boa distância da terra, açoitado pelas ondas; porque o vento era contrário.
25 Ca njël nag Yeesu jëm ci ñoom, di dox ci kaw dex gi.
25 De madrugada, Jesus foi até onde eles estavam, andando sobre o mar.
26 Waaye bi ko taalibe yi gisee, muy dox ci kaw dex ga, ñu daldi jommi naan: «Njuuma la!» daldi tiit bay yuuxu.
26 Os discípulos, porém, vendo-o andar sobre o mar, ficaram apavorados e disseram: — É um fantasma! E, tomados de medo, gritaram.
27 Waaye ca saa sa Yeesu ne leen: «Takkleen seen fit, man la, buleen tiit!»
27 Mas Jesus imediatamente lhes disse:
28 Ci kaw loolu Piyeer jël kàddu gi ne ko: «Sang bi, bu dee yaw, sant ma, ma dox ci kaw ndox mi, ñëw ci yaw.»
28 Então Pedro disse: — Se é o Senhor mesmo, mande que eu vá até aí, andando sobre as águas.
29 Yeesu ne ko: «Kaay!» Piyeer nag wàcc ca gaal ga, di dox ci kaw ndox mi, jëm ci Yeesu.
29 Jesus disse: E Pedro, descendo do barco, andou sobre as águas e foi até Jesus.
30 Waaye bi mu gisee ni ngelaw li mettee, mu daldi tiit, tàmbalee suux. Mu woote ne: «Sang bi, wallu ma!»
30 Reparando, porém, na força do vento, teve medo; e, começando a afundar, gritou: — Salve-me, Senhor!
31 Ca saa sa Yeesu tàllal loxoom, jàpp ko naan: «Yaw mi néew ngëm, lu tax nga am xel ñaar?»
31 E, prontamente, Jesus, estendendo a mão, o segurou e disse:
32 Noonu ñu dugg ca gaal ga, ngelaw li ne tekk.
32 Subindo ambos para o barco, o vento cessou.
33 Ñi nekk ci gaal gi nag sukk ci kanamam ne ko: «Ci dëgg yaa di Doomu Yàlla ji.»
33 E os que estavam no barco o adoraram, dizendo: — Verdadeiramente o senhor é o Filho de Deus!
34 Bi loolu amee ñu jàll, teer ca diiwaanu Senesaret.
34 Estando já no outro lado, chegaram à terra de Genesaré.
35 Ña fa dëkk xàmmi Yeesu, yónnee nag ca diiwaan bépp, indil ko ñu wopp ñépp.
35 Quando as pessoas daquela terra o reconheceram, mandaram avisar em todos aqueles arredores e lhe trouxeram todos os enfermos.
36 Noonu ñu ñaan ko, mu may leen ñu laal cati mbubbam rekk, te ku ko laal daldi wér.
36 E pediam-lhe que ao menos pudessem tocar na borda da sua roupa. E todos os que tocavam nela ficaram curados.
Atalhos do teclado
- Capítulo anterior←
- Próximo capítulo→
- Versículo anteriork
- Próximo versículoj
- Limpar seleçãoEsc
- Esta ajuda?
Estude este capítulo no WhatsApp
Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Mateus 14, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.