Mateus 13
Téereb Injiil (WOL2010) vs NTLH
1 Bés booba Yeesu génnoon na ca kër ga, toog ca wetu dex ga.
1 Naquele mesmo dia Jesus saiu de casa, foi para a beira do lago da Galileia, sentou-se ali e começou a ensinar.
2 Mbooloo mu bare dajaloo ca moom, ba tax mu dugg cig gaal, toog; mbooloo mépp taxaw ca tefes ga.
2 A multidão que se ajuntou em volta dele era tão grande, que ele entrou num barco e sentou-se; e o povo ficou em pé na praia.
3 Noonu Yeesu dégtal leen lu bare ciy léeb ne leen: «Dafa amoon beykat bu demoon jiyi.
3 Jesus usou parábolas para ensinar muitas coisas. Ele disse:
4 Bi muy saaw toolam nag, lenn ci pepp mi wadd ci kaw yoon wi, picc yi daldi ñëw, lekk ko lépp.
4 Quando estava espalhando as sementes, algumas caíram na beira do caminho, e os passarinhos comeram tudo.
5 Leneen ci pepp mi wadd ci bérab bu bare ay doj te néew suuf, mu daldi sax bu gaaw, ndaxte suuf si barewul.
5 Outra parte das sementes caiu num lugar onde havia muitas pedras e pouca terra. As sementes brotaram logo porque a terra não era funda.
6 Waaye bi jant bi naajee, mu lakk, wow, ndaxte amul ay reen.
6 Mas, quando o sol apareceu, queimou as plantas, e elas secaram porque não tinham raízes.
7 Leneen nag wadd ci biir ay xaaxaam, xaaxaam yi daldi jóg, tanc ko.
7 Outras sementes caíram no meio de espinhos, que cresceram e sufocaram as plantas.
8 Li ci des dal ci suuf su baax, nangu ba def ay gub; lii àntu ba mat téeméeri yoon lu ëpp la mu ji woon, lii mat juróom benn fukk, li ci des fanweer.
8 Mas as sementes que caíram em terra boa produziram na base de cem, de sessenta e de trinta grãos por um.
9 Déglul bu baax, yaw mi am ay nopp.»
9 E Jesus terminou, dizendo:
10 Bi Yeesu waxee ba noppi, ay taalibeem jegeñsi, laaj ko lu tax mu di leen wax ciy léeb.
10 Então os discípulos chegaram perto de Jesus e perguntaram: — Por que é que o senhor usa
11 Noonu mu ne leen: «May nañu leen, ngeen xam mbóoti nguuru Yàlla Aji Kawe ji, waaye ñale mayuñu leen ko.
11 Jesus respondeu:
12 Ndaxte ku am, dinañu la dollil, ba nga barele; waaye ku amul, li nga am as néew, dinañu ko nangu.
12 Pois quem tem receberá mais, para que tenha mais ainda. Mas quem não tem, até o pouco que tem lhe será tirado.
13 “Dañuy xool te duñu gis,
13 É por isso que eu uso parábolas para falar com essas pessoas. Porque elas olham e não enxergam; escutam e não ouvem, nem entendem.
14 Li Esayi waxoon ci kàddug Yàlla am na ci ñoom, bi mu naan:
14 E assim acontece com essas pessoas o que disse o
15 Ndaxte xolu xeet wii dafa dërkiis;
15 Pois a mente deste povo está fechada:
16 «Waaye yéen barkeel ngeen, ndaxte seeni bët a ngi gis te seeni nopp di dégg!
16 Jesus continuou, dizendo:
17 Ndaxte ci dëgg maa ngi leen koy wax, ay yonent yu bare ak nit ñu jub ñu bare bëggoon nañu gis li ngeen di gis waaye gisuñu ko, te dégg li ngeen di dégg waaye dégguñu ko.
17 Eu afirmo a vocês que isto é verdade: muitos profetas e muitas outras pessoas do povo de Deus gostariam de ver o que vocês estão vendo, mas não puderam; e gostariam de ouvir o que vocês estão ouvindo, mas não ouviram.
18 «Yéen nag dégluleen li léebu beykat biy tekki.
18 — Então escutem e aprendam o que a
19 Boo xamee ne nit mu ngi déglu wax ju jëm ci nguuru Yàlla te xamu ko, Ibliis day ñëw, këf li ñu def ci xolam; kooku mooy ki jot ci jiwu wi ci kaw yoon wi.
19 As pessoas que ouvem a mensagem do vem e tira o que foi semeado no coração delas.
20 Ki jot ci jiwu wi ci bérab bu bare ay doj nag, mooy ki dégg wax ji, am ci bànneex bu gaaw;
20 As sementes que foram semeadas onde havia muitas pedras são as pessoas que ouvem a mensagem e a aceitam logo com alegria,
21 waaye du yàgg, ndaxte wax ji saxul ci moom. Bu jaaree ci nattu nag, mbaa ñu fitnaal ko ndax kàddu gi, mu dàggeeku ci saa si.
21 mas duram pouco porque não têm raiz. E, quando por causa da mensagem chegam os sofrimentos e as perseguições, elas logo abandonam a sua fé.
22 Ki jot ci jiwu wi ci xaaxaam yi mooy ki dégg wax ji, waaye soxlay àddina ak naxi alal tanc wax ji, ba du jur njariñ.
22 Outras pessoas são parecidas com as sementes que foram semeadas no meio dos espinhos. Elas ouvem a mensagem, mas as preocupações deste mundo e a ilusão das riquezas sufocam a mensagem, e essas pessoas não produzem frutos.
23 Ki jot ci jiwu wi ci suuf su baax si nag, mooy ki dégg wax ji te xam ko; mu jural ko njariñ, muy lu mat téeméeri yoon lu ëpp la ñu ji woon, muy juróom benn fukk mbaa fanweer.»
23 E as sementes que foram semeadas em terra boa são aquelas pessoas que ouvem, e entendem a mensagem, e produzem uma grande colheita: umas, cem; outras, sessenta; e ainda outras, trinta vezes mais do que foi semeado.
24 Noonu Yeesu dégtal leen beneen léeb ne leen: «Nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni nit ku ji jiwu wu baax ci toolam.
24 Jesus contou outra parábola . Ele disse ao povo:
25 Waaye bi nit ñi di nelaw, noonam ñëw, ji jëmb ci biir dugub ji, daldi dem.
25 Certa noite, quando todos estavam dormindo, veio um inimigo, semeou no meio do trigo uma erva ruim, chamada joio, e depois foi embora.
26 Bi dugub ji saxee nag, jëmb bi saxaale ak moom.
26 Quando as plantas cresceram, e se formaram as espigas, o joio apareceu.
27 «Noonu surgay boroom kër ga ñëw ci moom ne ko: “Góor gi, xanaa jiwuloo jiwu wu baax ci sa tool? Fu jëmb bi jóge nag?”
27 Aí os empregados do dono das terras chegaram e disseram: “Patrão, o senhor semeou sementes boas nas suas terras. De onde será que veio este joio?”
28 Mu ne leen: “Noon a ko def.” Surga ya ne ko: “Ndax nu dem dindi ko?”
28 — “Foi algum inimigo que fez isso!”, respondeu ele.
29 Mu ne leen: “Déedéet, ngir baña buddiwaale dugub ji, bu ngeen koy dindi.
29 — “Não”, respondeu ele, “porque, quando vocês forem tirar o joio, poderão arrancar também o trigo.
30 Bàyyileen ñoom ñaar, ñu màgg, ba ngóob ma jot. Bu ngóob ma jotee nag, dinaa wax ñi koy góob: ‘Jëkkleena dindi jëmb bi, takk ko ay say, lakk ko, waaye ngeen semb dugub ji ci sama sàq.’ ”»
30 Deixem o trigo e o joio crescerem juntos até o tempo da colheita. Então eu direi aos trabalhadores que vão fazer a colheita: ‘Arranquem primeiro o joio e amarrem em feixes para ser queimado. Depois colham o trigo e ponham no meu depósito.’ ”
31 Yeesu waxaat leen beneen léeb ne leen: «Nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni doomu fuddën bu nit jël, ji ko ci toolam.
31 Jesus contou outra parábola . Ele disse ao povo:
32 Doomu fuddën moo gëna tuuti ci jiwu yépp, waaye bu saxee, mooy sut ci gàncaxi tóokër yi, di nekk garab, ba picci asamaan ñëw, tàgg ciy caram.»
32 Ela é a menor de todas as sementes; mas, quando cresce, torna-se a maior de todas as plantas. Ela até chega a ser uma árvore, de modo que os passarinhos vêm e fazem ninhos nos seus ramos.
33 Yeesu teg ca beneen léeb ne leen: «Nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni lawiir bu jigéen jël, jaxase ko ak ñetti andaari fariñ, ba kera tooyal bépp di funki.»
33 Jesus contou mais esta parábola para o povo:
34 Loolu Yeesu wax mbooloo ma, ëmb na ko lépp ciy léeb, te waxuleen dara lu dul ciy léeb.
34 Jesus usava parábolas para dizer tudo isso ao povo. Ele não dizia nada a eles sem ser por meio de parábolas.
35 Noonu am la ñu waxoon jaarale ko cib yonent, bi mu naan:
35 Isso aconteceu para se cumprir o que o profeta tinha dito: “Usarei parábolas quando falar com esse povo e explicarei coisas desconhecidas desde a criação do mundo.”
36 Ci kaw loolu Yeesu bàyyi mbooloo ma, dugg ca kër ga. Taalibeem yi ñëw ci moom ne ko: «Firil nu léebu jëmb, bi sax ci tool bi.»
36 Então Jesus deixou a multidão e voltou para casa. Os discípulos chegaram perto dele e perguntaram: — Conte para nós o que quer dizer a
37 Noonu Yeesu ne leen: «Doomu nit ki mooy ji jiwu wu baax wi;
37 Jesus respondeu:
38 àddina mooy tool bi; ñi bokk ci nguuru Yàlla ñoo di jiwu wu baax wi; ñi bokk ci Ibliis ñooy jëmb bi;
38 O terreno é o mundo. As sementes boas são as pessoas que pertencem ao .
39 Seytaane mooy noon bi ko ji; tukkitel àddina mooy ngóob mi, te malaaka yi ñooy góobkat yi.
39 O inimigo que semeia o joio é o próprio Diabo. A colheita é o fim dos tempos, e os que fazem a colheita são os anjos.
40 Ni ñu dajalee jëmb ba, lakk ko, noonu lay nekke, bu àddina tukkee.
40 Assim como o joio é ajuntado e jogado no fogo, assim também será no fim dos tempos.
41 Doomu nit ki dina yebal ay malaakaam, ñu jële ci nguuram lépp luy yóbbe nit bàkkaar, ak ñiy def bàkkaar,
41 O Filho do Homem mandará os seus anjos, e eles ajuntarão e tirarão do seu Reino todos os que fazem com que os outros pequem e também todos os que praticam o mal.
42 sànni leen ci sawara; foofa dees na fa jooy te yéyu.
42 Depois os anjos jogarão essas pessoas na fornalha de fogo, onde vão chorar e ranger os dentes de desespero.
43 Booba nag ñu jub ñi dinañu leer ni jant bi ci seen nguuru Baay. Déglul bu baax, yaw mi am ay nopp.»
43 Então o povo de Deus brilhará como o sol no Reino do seu Pai. Se vocês têm ouvidos para ouvir, então ouçam.
44 Yeesu teg ca ne: «Nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni alal ju nëbbu cib tool. Nit ki ko gis nëbbaat ko; xolam sedd, ba mu dem jaay li mu am lépp, jënd tool ba.
44 — O
45 «Te it nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni jaaykat buy wut per yu rafet.
45 — O
46 Am bés mu gis per buy jar njég lu réy. Mu dem nag, jaay li mu am lépp, jënd ko.»
46 Quando encontra uma pérola que é mesmo de grande valor, ele vai, vende tudo o que tem e compra a pérola.
47 Yeesu waxaat ne: «Nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni mbaal mu ñu wàcce ci géej, mu jàpp jën wu nekk.
47 — O
48 Bi mbaal mi feesee nag, ñu ñoddi ko ci tefes gi, ba noppi ñu taxaw, dajale yu baax yi ciy ndab, waaye sànni yi bon.
48 E, quando está cheia, os pescadores a arrastam para a praia e sentam para separar os peixes: os que prestam são postos dentro dos cestos, e os que não prestam são jogados fora.
49 Noonu lay mel, bu àddina tukkee. Malaaka yi dinañu génn, tànn ñu bon ñi ci biir ñu jub ñi,
49 No fim dos tempos também será assim: os anjos sairão, e separarão as pessoas más das boas,
50 sànni leen ci sawara. Foofa dees na fa jooy te yéyu.»
50 e jogarão as pessoas más na fornalha de fogo. E ali elas vão chorar e ranger os dentes de desespero.
51 Noonu Yeesu laaj taalibe ya ne leen: «Loolu lépp, ndax xam ngeen lu muy tekki?» Ñu ne ko: «Waaw.»
51 Então Jesus perguntou aos discípulos: — Sim! — responderam eles.
52 Yeesu ne leen: «Kon nag xutbakat bu nekk bu jàng ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji, dafa mel ni boroom kër buy génne ci dencukaayam yu bees ak yu màggat.»
52 Jesus disse:
53 Bi nga xamee ne Yeesu dégtal na léeb yooyu ba noppi, mu jóge fa,
53 Quando Jesus acabou de contar essas parábolas , saiu dali
54 dem fa mu yaroo. Mu di leen jàngal ci seen jàngu, ba ñu waaru ne: «Xam-xam bii ak kéemaan yii, fu mu ko jële?
54 e voltou para a cidade de Nazaré, onde ele tinha morado. Ele ensinava na sinagoga , e os que o ouviam ficavam admirados e perguntavam: — De onde vêm a sabedoria dele e o poder que ele tem para fazer milagres?
55 Ndax kii du doomu minise bi, te ndeyam tudd Maryaama? Ndax rakkam yu góor duñu Saag, Yuusufa, Simoŋ ak Yuda?
55 Por acaso ele não é o filho do carpinteiro? A sua mãe não é Maria? Ele não é irmão de Tiago, José, Simão e Judas?
56 Te ay rakkam yu jigéen, ndax nekkuñu fi ak nun? Lii lépp nag, fu mu ko jële?»
56 Todas as suas irmãs não moram aqui? De onde é que ele consegue tudo isso?
57 Kon ñu daldi koy xeeb.
57 Por isso ficaram desiludidos com ele. Mas Jesus disse:
58 Te Yeesu defu fa kéemaan yu bare ndax seen ngëmadi.
58 Jesus não pôde fazer muitos milagres ali porque eles não tinham fé.
Atalhos do teclado
- Capítulo anterior←
- Próximo capítulo→
- Versículo anteriork
- Próximo versículoj
- Limpar seleçãoEsc
- Esta ajuda?
Estude este capítulo no WhatsApp
Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Mateus 13, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.