Mateus 11
Téereb Injiil (WOL2010) vs NAA
1 Ba Yeesu joxee fukki taalibeem ya ak ñaar ndigal yooyu, mu jóge fa, ngir dem jàngleji ak a waare ci seeni dëkk.
1 Quando Jesus acabou de dar estas instruções a seus doze discípulos, saiu dali para ir ensinar e pregar nas cidades deles.
2 Gannaaw loolu Yaxya dégg ca kaso ba jëfi Almasi bi. Mu yónni ci moom nag ay taalibeem,
2 Quando João, no cárcere, ouviu falar das obras de Cristo, mandou que seus discípulos fossem perguntar:
3 ne ko: «Ndax yaa di Ki wara ñëw, walla danoo wara xaar keneen?»
3 — Você é aquele que estava para vir ou devemos esperar outro?
4 Yeesu ne leen: «Demleen nettali Yaxya li ngeen dégg te gis ko.
4 Então Jesus lhes respondeu:
5 Gumba yaa ngi gis, lafañ yiy dox, gaana yi wér, tëx yiy dégg, ñi dee di dekki, te néew doole ñaa ngi dégg xibaaru jàmm bi.
5 os cegos veem, os coxos andam, os leprosos são purificados, os surdos ouvem, os mortos são ressuscitados e aos pobres está sendo pregado o evangelho.
6 Yaw mi sa ngëm yolomul ndax man, barkeel nga.»
6 E bem-aventurado é aquele que não achar em mim motivo de tropeço.
7 Bi nga xamee ne taalibe ya Yaxya yónni woon ci Yeesu dem nañu, Yeesu daldi wax ak mbooloo ma ci mbirum Yaxya ne leen: «Lu ngeen seeti woon ca màndiŋ ma? Xanaa barax buy jaayu ci ngelaw li?
7 Quando os discípulos de João foram embora, Jesus começou a dizer ao povo a respeito de João:
8 Kon lu ngeen seeti woon nag? Nit ku sol yére yu rafet? Waaye ñi sol yére yu rafet ñu ngi dëkk ci këri buur.
8 O que vocês foram ver? Um homem vestido de roupas finas? Os que vestem roupas finas moram nos palácios reais.
9 Lu tax ngeen génn nag? Ngir gis ab yonent? Waaw, wax naa leen ne ëpp na yonent.
9 Sim, o que foram ver? Um profeta? Sim, eu lhes digo, e muito mais do que um profeta.
10 Yaxya male moo di ki ñu waxoon ci Mbind mi naan:
10 Este é aquele de quem está escrito:
11 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, ci li jigéen jur, ku sut Yaxya masula feeñ. Waaye ba tey ki gëna ndaw ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji moo ko sut.
11 — Em verdade lhes digo: entre os nascidos de mulher, não apareceu ninguém maior do que João Batista; mas o menor no Reino dos Céus é maior do que ele.
12 Ci li dale ci jamonoy Yaxya ba léegi, nit ñaa ngi góor-góorlu ngir dugg ci nguuru Yàlla, te ñi sawar ñoo ci am wàll.
12 Desde os dias de João Batista até agora, o Reino dos Céus sofre violência, e os que usam de força se apoderam dele.
13 Ndaxte li yonent yi wax ak li yoonu Musaa tëral ñu ngi doon dox, ba kera Yaxya di feeñ.
13 Porque todos os Profetas e a Lei profetizaram até João.
14 Te Yaxya moomu, su ngeen bëggee nangu lii, mooy Ilyaas bi waroona ñëw.
14 E, se vocês o querem reconhecer, ele mesmo é Elias, que estava para vir.
15 Déglul bu baax, yaw mi am ay nopp.
15 Quem tem ouvidos para ouvir, ouça.
16 «Niti jamono jii nag, lan laa leen mana méngaleel? Ñu ngi nirook xale yu toog ca pénc ma, di woo seeni xarit,
16 — Mas a que compararei esta geração? É semelhante a meninos que, sentados nas praças, gritam aos companheiros:
17 ne leen:
17 “Nós tocamos flauta,
18 Ndaxte Yaxya feeñ na, lekkul, naanul, ngeen daldi ne: “Dafa ànd ak rab.”
18 — Pois veio João, que não comia nem bebia, e as pessoas dizem: “Ele tem demônio!”
19 Gannaaw gi nag, Doomu nit ki ñëw na, lekk, naan, ngeen daldi ne: “Kii daal bëgg na lekk, di naan biiñ, tey xaritoo ak ay juutikat ak ay boroom bàkkaar.” Waaye li xam-xamu Yàlla di jur, mooy firndeel ne dëgg la.»
19 Veio o Filho do Homem, comendo e bebendo, e as pessoas dizem: “Eis aí um glutão e bebedor de vinho, amigo de publicanos e pecadores!” Mas a sabedoria é justificada por suas obras.
20 Gannaaw loolu Yeesu daldi gëdd dëkk, ya mu defe woon la ëpp cay kéemaanam, ndaxte tuubuñu seeni bàkkaar.
20 Então Jesus começou a repreender as cidades nas quais ele tinha feito muitos milagres, pelo fato de não terem se arrependido:
21 Mu ne: «Dingeen torox, yéen waa Korasin ak waa Betsayda, ndaxte kéemaan yi ma def ci yéen, bu ñu leen defoon ci dëkku Tir walla ci dëkku Sidon, kon réccu nañu bu yàgg, xëppoo dóom, sol saaku.
21 — Ai de você, Corazim! Ai de você, Betsaida! Porque, se em Tiro e em Sidom se tivessem operado os milagres que foram feitos em vocês, há muito que elas teriam se arrependido com pano de saco e cinza.
22 Waaye maa ngi leen koy wax, keroog bés pénc ma Tir ak Sidon ñoo leen di tane.
22 Mas eu digo a vocês que, no Dia do Juízo, haverá menos rigor para Tiro e Sidom do que para vocês.
23 Te yaw dëkku Kapernawum, ndax dees na la yékkati bu kawe? Déedéet, dees na la daane bu suufe. Ndaxte kéemaan yi ma def ci yaw, bu ñu leen defoon ci dëkku Sodom, kon mu nekk ba tey.
23 — E você, Cafarnaum, pensa que será elevada até o céu? Será jogada no inferno! Porque, se em Sodoma se tivessem operado os milagres que foram feitos em você, ela teria permanecido até o dia de hoje.
24 Waaye maa ngi leen koy wax, keroog bés pénc ma Sodom moo lay tane.»
24 Mas eu digo a vocês que, no Dia do Juízo, haverá menos rigor para a terra de Sodoma do que para você.
25 Ca jamono joojale Yeesu wax na lii: «Yaw Baay, Boroom asamaan ak suuf, maa ngi lay sant ci li nga nëbb yëf yii ñi am xam-xam ak ñi am xel, te xamal leen gone yi.
25 Por aquele tempo, Jesus exclamou:
26 Waaw, Baay, ndaxte looloo la neex.»
26 Sim, ó Pai, porque assim foi do teu agrado.
27 Yeesu teg ca ne: «Sama Baay jébbal na ma lépp, te kenn manu maa xam, man Doom ji, ku dul Baay bi; kenn it manula xam Baay bi, ku dul man Doom ji, ak ku ma ko bëgga xamal.
27 Tudo me foi entregue por meu Pai. Ninguém conhece o Filho, a não ser o Pai; e ninguém conhece o Pai, a não ser o Filho e aquele a quem o Filho o quiser revelar.
28 «Ñëwleen ci man, yéen ñépp ñi sonn te diis, dinaa leen may noflaay.
28 — Venham a mim todos vocês que estão cansados e sobrecarregados, e eu os aliviarei.
29 Jébbaluleen ci man te jàng ci man, ndaxte lewet naa te woyof, te dingeen am noflaay ci seen xol.
29 Tomem sobre vocês o meu jugo e aprendam de mim, porque sou manso e humilde de coração; e vocês acharão descanso para a sua alma.
30 Ndaxte sama kilifteef lewet na te sama yen diisul.»
30 Porque o meu jugo é suave, e o meu fardo é leve.
Atalhos do teclado
- Capítulo anterior←
- Próximo capítulo→
- Versículo anteriork
- Próximo versículoj
- Limpar seleçãoEsc
- Esta ajuda?
Estude este capítulo no WhatsApp
Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Mateus 11, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.