Mateus 10

Téereb Injiil (WOL2010) vs NVI

Sair da comparação
NVI Nova Versão Internacional
1 Noonu Yeesu woo ca moom fukki taalibeem ya ak ñaar, jox leen sañ-sañu dàq rab yi, tey faj jàngoro yépp ak wéradi yépp.
1 Chamando seus doze discípulos, deu-lhes autoridade para expulsar espíritos imundos e curar todas as doenças e enfermidades.
2 Fukki ndaw ak ñaar, ya Yeesu yónni woon nag, nii lañu tuddoon:
2 Estes são os nomes dos doze apóstolos: primeiro, Simão, chamado Pedro, e André, seu irmão; Tiago, filho de Zebedeu, e João, seu irmão;
3 Filib ak Bartelemi;
3 Filipe e Bartolomeu; Tomé e Mateus, o publicano; Tiago, filho de Alfeu, e Tadeu;
4 Simoŋ, mi bokk ca mbooloo, ma ñu tudde Ñi farlu ci moom seen réew;
4 Simão, o zelote, e Judas Iscariotes, que o traiu.
5 Yeesu yónni fukk ñooñule ak ñaar, jox leen ndigal ne leen: «Buleen dem ci ñi dul Yawut mbaa dugg ci benn dëkku waa Samari.
5 Jesus enviou estes doze com as seguintes instruções: "Não se dirijam aos gentios, nem entrem em cidade alguma dos samaritanos.
6 Waaye demleen ci bànni Israyil, ñoom ñi réer niy xar.
6 Antes, dirijam-se às ovelhas perdidas de Israel.
7 Bu ngeen demee nag, yégleleen naan: “Nguuru Yàlla Aji Kawe ji jegesi na.”
7 Por onde forem, preguem esta mensagem: ‘O Reino dos céus está próximo’.
8 Fajleen ñi wopp, dekkal ñi dee, fajleen gaana yi te dàq rab yi. Cig neen ngeen ame, mayeleen cig neen.
8 Curem os enfermos, ressuscitem os mortos, purifiquem os leprosos, expulsem os demônios. Vocês receberam de graça; dêem também de graça.
9 Buleen dajale wurus, xaalis mbaa xànjar ci seeni maxtume.
9 Não levem nem ouro, nem prata, nem cobre em seus cintos;
10 Buleen wut it mbuus ngir tukki mbaa ñaari turki, ay dàll mbaa aw yet, ndaxte liggéeykat yeyoo na dundam.
10 não levem nenhum saco de viagem, nem túnica extra, nem sandálias, nem bordão; pois o trabalhador é digno do seu sustento.
11 «Bu fekkee ne agsi ngeen ci dëkk bu mag mbaa bu ndaw, nangeen fa seet ku fa am faayda, dal ca moom ba kera ngeen jóge dëkk ba.
11 "Na cidade ou povoado em que entrarem, procurem alguém digno de recebê-los, e fiquem em sua casa até partirem.
12 Bu ngeen di dugg ci kër nag, nuyooleen.
12 Ao entrarem na casa, saúdem-na.
13 Bu fekkee ne kër ga yeyoo na ko, na seen jàmm wàcc ci ñoom, waaye bu ko yeyoowul, na seen yéene délsi ci yéen.
13 Se a casa for digna, que a paz de vocês repouse sobre ela; se não for, que a paz retorne para vocês.
14 Koo xam ne gàntu na leen, mbaa mu tanqamlu seeni wax, génnleen ca kër ga mbaa ca dëkk ba, yëlëb seen pëndu tànk.
14 Se alguém não os receber nem ouvir suas palavras, sacudam a poeira dos pés, quando saírem daquela casa ou cidade.
15 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, keroog bésub àtte ba, waa réewu Sodom ak Gomor ñooy tane dëkk boobu.
15 Eu lhes digo a verdade: No dia do juízo haverá menor rigor para Sodoma e Gomorra do que para aquela cidade.
16 «Dégluleen, maa ngi leen di yónni, mel ni ay xar ci biir ay bukki. Muusleen nag niy jaan, te lewet niy pitax.
16 Eu os estou enviando como ovelhas entre lobos. Portanto, sejam prudentes como as serpentes e simples como as pombas.
17 Waaye moytuleen nit ñi, ndaxte dinañu leen jébbal àttekat yi te dóor leen ay yar ci seeni jàngu.
17 "Tenham cuidado, pois os homens os entregarão aos tribunais e os açoitarão nas sinagogas deles.
18 Dees na leen yóbbu ngir man ci kanam i boroom réew ak i buur, ngir ngeen seede ma ci ñoom ak ci ñi dul Yawut.
18 Por minha causa vocês serão levados à presença de governadores e reis como testemunhas a eles e aos gentios.
19 Boo xamee ne nag jébbale nañu leen, buleen am xel ñaar ci li ngeen di wax, mbaa ni ngeen koy waxe. Ndaxte ca waxtu woowa sax dingeen jot li ngeen wara wax;
19 Mas quando os prenderem, não se preocupem quanto ao que dizer, ou como dizer. Naquela hora lhes será dado o que dizer,
20 du yéenay wax, waaye Xelum seen Baay mooy wax ci yéen.
20 pois não serão vocês que estarão falando, mas o Espírito do Pai de vocês falará por intermédio de vocês.
21 «Mag dina joxe rakkam cig dee, baay joxe doomam; ay doom it dinañu jóg, bañ seeni waajur, di leen reylu.
21 "O irmão entregará à morte o seu irmão, e o pai o seu filho; filhos se rebelarão contra seus pais e os matarão.
22 Te yéen nag, ñépp dinañu leen bañ ndax sama tur; waaye ku muñ ba muj ga, mucc.
22 Todos odiarão vocês por minha causa, mas aquele que perseverar até o fim será salvo.
23 Boo xamee ne fitnaal nañu leen ci dëkk bii, demleen ca ba ca kanam. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, dungeen mana wër dëkki Israyil yépp, te Doomu nit ki ñëwul.»
23 Quando forem perseguidos num lugar, fujam para outro. Eu lhes garanto que vocês não terão percorrido todas as cidades de Israel antes que venha o Filho do homem.
24 Yeesu teg ca ne: «Taalibe gënul kilifaam, te jaam gënul sangam.
24 "O discípulo não está acima do seu mestre, nem o servo acima do seu senhor.
25 Bu taalibe yemee ak kilifaam demin, doy na; jaam it ni sangam. Ndegam tudde nañu boroom kër gi Beelsebul, astamaak waa kër gi.
25 Basta ao discípulo ser como o seu mestre, e ao servo, como o seu senhor. Se o dono da casa foi chamado Belzebu, quanto mais os membros da sua família!
26 Kon nag buleen leen ragal, ndaxte amul dara lu nëbbu, lu ñu warula biral, mbaa luy kumpa lu ñu warula siiwal.
26 "Portanto, não tenham medo deles. Não há nada escondido que não venha a ser revelado, nem oculto que não venha a se tornar conhecido.
27 Li ma leen wax ci biir lëndëm, waxleen ko ci leer; li ma leen déey, yégleleen ko ci kaw taax yi.
27 O que eu lhes digo na escuridão, falem à luz do dia; o que é sussurrado em seus ouvidos, proclamem dos telhados.
28 Te buleen ragal ñu mana rey yaram, te manuñoo rey ruu, waaye ragal-leen ki mana sànk yaram ak ruu ci sawara.
28 Não tenham medo dos que matam o corpo, mas não podem matar a alma. Antes, tenham medo daquele que pode destruir tanto a alma como o corpo no inferno.
29 Ñaari picci ramatu, ndax duñu ko jaay ci dërëm? Waaye benn ci ñoom du daanu ci suuf te soobul seen Baay.
29 Não se vendem dois pardais por uma moedinha? Contudo, nenhum deles cai no chão sem o consentimento do Pai de vocês.
30 Seen kawari bopp sax, waññees na leen.
30 Até os cabelos da cabeça de vocês estão todos contados.
31 Kon buleen ragal dara, yéena gën ndiiraanu ramatu.
31 Portanto, não tenham medo; vocês valem mais do que muitos pardais!
32 «Koo xam ne nangu nga ma ci kanam nit ñi, man itam dinaa la nangu ci sama kanam Baay, bi nekk ci kaw.
32 "Quem, pois, me confessar diante dos homens, eu também o confessarei diante do meu Pai que está nos céus.
33 Waaye ku ma gàntu ci kanam nit ñi, man itam dinaa la gàntu ci sama kanam Baay, bi nekk ci kaw.
33 Mas aquele que me negar diante dos homens, eu também o negarei diante do meu Pai que está nos céus.
34 «Te it buleen defe ne damaa ñëw ngir indi jàmm ci àddina; ñëwuma ngir indi jàmm, waaye jaasi laa indaale.
34 "Não pensem que vim trazer paz à terra; não vim trazer paz, mas espada.
35 Ndaxte ñëw naa ngir féewale doom ak baayam, doom ju jigéen ak ndeyam, jabar ak goroom;
35 Pois vim para fazer que ‘o homem fique contra seu pai, a filha contra sua mãe, a nora contra sua sogra;
36 te nooni nit ñooy waa këram.
36 os inimigos do homem serão os da sua própria família’.
37 Ku ma gënalul sa ndey walla sa baay, yeyoowuloo ma; ku ma gënalul sa doom ju góor walla ju jigéen, yeyoowuloo ma.
37 "Quem ama seu pai ou sua mãe mais do que a mim não é digno de mim; quem ama seu filho ou sua filha mais do que a mim não é digno de mim;
38 Koo xam ne kii nanguwuloo ñàkk sa bakkan, ba mel ni ku ñu daaj ci bant, te nga topp ma, yeyoowuloo ma.
38 e quem não toma a sua cruz e não me segue, não é digno de mim.
39 Kuy rawale sa bakkan, ñàkk ko, te ku ñàkk sa bakkan ndax man, jotaat ko.
39 Quem acha a sua vida a perderá, e quem perde a sua vida por minha causa a encontrará.
40 «Te lii itam am na, ku leen nangu, nangu na ma, te ku ma nangu, nangu na ki ma yónni.
40 "Quem recebe vocês, recebe a mim; e quem me recebe, recebe aquele que me enviou.
41 Ku nangu yonent ndax yónnentam, dina jot ci peyu yonent; te ku nangu ku jub ndax njubteem, dina jot ci peyu ku jub.
41 Quem recebe um profeta, porque ele é profeta, receberá a recompensa de profeta, e quem recebe um justo, porque ele é justo, receberá a recompensa de justo.
42 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, koo xam ne kii may na kaasu ndox mu sedd rekk kenn ci ñi gëna ndaw, ndax sama taalibe la, kooku du ñàkk yoolam mukk.»
42 E se alguém der mesmo que seja apenas um copo de água fria a um destes pequeninos, porque ele é meu discípulo, eu lhes asseguro que não perderá a sua recompensa".

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Mateus 10, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.