Marcos 8

Téereb Injiil (WOL2010) vs NTLH

Sair da comparação
NTLH Nova Tradução na Linguagem de Hoje 2000
1 Ca bés yooya mbooloo mu réy amaatoon na, te amuñu woon lu ñu lekk. Noonu Yeesu woo taalibe ya ne leen:
1 Pouco tempo depois, ajuntou-se outra vez uma grande multidão. Como eles não tinham nada para comer, Jesus chamou os discípulos e disse:
2 «Yërëm naa mbooloo mi, ndaxte toog nañu fi man ñetti fan, te amatuñu lu ñu lekk.
2 — Estou com pena dessa gente porque já faz três dias que eles estão comigo e não têm nada para comer.
3 Su ma leen yiwee ak seen xiif, dinañu tële ci yoon wi, ndaxte am na ñu jóge fu sore.»
3 Se eu os mandar para casa com fome, eles vão cair de fraqueza pelo caminho, pois alguns vieram de longe.
4 Taalibe yi ne ko: «Waaye fii àllub neen la; fu nuy jële lu doy ngir dundal leen?»
4 Os discípulos perguntaram: — Como vamos encontrar, neste lugar deserto, comida que dê para toda essa gente?
5 Yeesu laaj leen: «Ñaata mburu ngeen am?» Ñu ne ko: «Juróom ñaar.»
5 — Quantos pães vocês têm? — perguntou Jesus. — Sete! — responderam eles.
6 Noonu Yeesu sant mbooloo mi, ñu toog ci suuf. Mu jël juróom ñaari mburu yi, sant Yàlla, damm leen, jox leen taalibe yi, ngir ñu séddale leen mbooloo mi; taalibe yi def ko.
6 Aí Jesus mandou o povo sentar-se no chão. Depois pegou os sete pães e deu graças a Deus. Então os partiu e os entregou aos discípulos, e eles os distribuíram ao povo.
7 Amoon na fa it tuuti jën yu ndaw. Yeesu jël ko, sant Yàlla, wax taalibe yi, ñu séddale leen itam mbooloo mi.
7 Eles tinham também alguns peixinhos. Jesus deu graças a Deus por eles e mandou que os discípulos os distribuíssem.
8 Noonu nit ñi lekk ba suur, ba noppi taalibe yi dajale juróom ñaari dàmba yu fees ak dammit yi ci des.
8 Todos comeram e ficaram satisfeitos; e os discípulos ainda encheram sete cestos com os pedaços que sobraram.
9 Ña ko fekke nag matoon nañu ñeenti junniy góor.
9 As pessoas que comeram eram mais ou menos quatro mil. Jesus mandou o povo embora,
10 Bi ko Yeesu defee, mu yiwi leen, daldi dugg ak taalibe ya ca gaal ga, dem ca wàlli Dalmanuta.
10 e, logo depois, subiu no barco com os seus discípulos, e foi para a região de Dalmanuta.
11 Noonu Farisen yi ñëw, di werante ak moom; ñu fexe koo fiir, ba laaj ko kéemaan gu jóge ci asamaan tey firndeel yónnentam.
11 Alguns fariseus chegaram e começaram a falar com Jesus. Eles queriam conseguir alguma prova contra ele e por isso pediram que ele fizesse um milagre para mostrar que o seu poder vinha mesmo de Deus.
12 Waaye Yeesu binni ci xolam ne leen: «Lu tax niti jamono jii di laaj kéemaan? Ci dëgg maa ngi leen koy wax, duñu jot genn kéemaan.»
12 Jesus deu um grande suspiro e disse:
13 Ci kaw loolu Yeesu bàyyi leen, duggaat ci gaal gi, di jàll dex gi.
13 Então Jesus foi embora. Ele subiu no barco e voltou para o lado leste do lago.
14 Taalibe yi nag fàtte woon nañu yóbbaale mburu, te amuñu woon lu dul benn mburu ci gaal gi.
14 Os discípulos haviam esquecido de levar pão e só tinham um pão no barco.
15 Noonu Yeesu artu leen ne: «Wottuleen te moytu lawiiru Farisen yi ak ñi far ak buur bi Erodd.»
15 Jesus chamou a atenção deles, dizendo:
16 Taalibe yi nag daldi werante naan: «Nun de indaalewunu mburu.»
16 Aí os discípulos começaram a dizer uns aos outros: — Ele está dizendo isso porque não temos pão.
17 Waaye Yeesu yég loolu ne leen: «Lu tax ngeen di werante ci li ngeen indaalewul mburu? Xanaa gisaguleen te xamuleen? Ndax seen xol dafa fatt ba tey?
17 Jesus ouviu o que eles estavam dizendo e perguntou:
18 Ndax ay gumbay njàccaar ngeen, te seeni nopp naqari? Xanaa fàttalikuwuleen;
18 Vocês têm olhos e não enxergam? Têm ouvidos e não escutam? Não lembram
19 bi ma dammee juróomi mburu ya ngir juróomi junni ña, ñaata pañe yu fees ak ay dammit ngeen ca dajale woon?» Ñu ne ko: «Fukk ak ñaar.»
19 dos cinco pães que eu parti para cinco mil pessoas? Quantos cestos cheios de pedaços vocês recolheram? Eles responderam: — Doze.
20 Yeesu neeti leen: «Te bés bi ma dammee juróom ñaari mburu yi ngir ñeenti junni ñi, ñaata dàmba yu fees ak dammit ngeen dajale woon?» Ñu ne ko: «Juróom ñaar.»
20 Jesus perguntou outra vez: Eles responderam: — Sete.
21 Noonu Yeesu ne leen: «Ndax seen xol dafa tëju ba tey?»
21 Então Jesus perguntou:
22 Gannaaw loolu ñu ñëw ci Betsayda. Foofa ñu indil Yeesu ku gumba, di ko ñaan, mu laal ko.
22 Depois Jesus e os discípulos chegaram ao povoado de Betsaida. Algumas pessoas trouxeram um cego e pediram a Jesus que tocasse nele.
23 Yeesu nag jàpp loxob gumba gi, yóbbu ko, ba génn dëkk bi. Mu def tiflit ciy bëtam, teg ko loxo naan: «Ndax gis nga dara?»
23 Ele pegou o cego pela mão e o levou para fora do povoado. Então cuspiu, passou a saliva nos olhos do homem, pôs a mão sobre ele e perguntou:
24 Waa ji xool ne ko: «Gis naa ay nit, ñu mel ni ay garab, te ñu ngi dox.»
24 O homem olhou e disse: — Vejo pessoas; elas parecem árvores, mas estão andando.
25 Kon Yeesu laalaat bët yi, gumba gi ne xefeet, daldi wér, ba gis lépp bu leer.
25 Jesus pôs outra vez as mãos sobre os olhos dele. Dessa vez o cego olhou firme e ficou curado; aí começou a ver tudo muito bem.
26 Ci kaw loolu Yeesu sant ko mu ñibbi ne ko: «Bul dugg ca dëkk ba.»
26 Em seguida, Jesus mandou o homem para casa e ordenou:
27 Bi loolu amee Yeesu ànd ak ay taalibeem, dem ca dëkk, yi wër Sesare bu Filib. Bi ñuy dem nag, mu laaj taalibe yi: «Nit ñi, lu ñu wax ne man moom laa?»
27 Depois Jesus e os seus discípulos foram para os povoados que ficam perto de Cesareia de Filipe. No caminho, ele lhes perguntou:
28 Ñu ne ko: «Am na ñuy ne yaa di Yaxya; ñeneen ne, Ilyaas; ñi ci des ne yaay kenn ci yonent yi.»
28 Os discípulos responderam: — Alguns dizem que o senhor é João Batista; outros, que é Elias; e outros, que é um dos
29 Noonu Yeesu laaj leen: «Yéen nag, ku ngeen wax ne moom laa?» Piyeer ne ko: «Yaa di Almasi bi.»
29 — E vocês? Quem vocês dizem que eu sou? — perguntou Jesus. — O senhor é o
30 Ci kaw loolu Yeesu dénk leen bu wóor, ñu bañ koo wax kenn.
30 Então Jesus proibiu os discípulos de contarem isso a qualquer pessoa.
31 Booba Yeesu tàmbali na leena xamal ne, Doomu nit ki war na sonn lu bare; njiit ya, sarxalkat yu mag ya ak xutbakat ya dëddu ko, ñu rey ko, mu dekki ci ñetti fan.
31 Jesus começou a ensinar os discípulos, dizendo: — O
32 Noonu mu xamal leen mbir mi, ba mu leer nàññ.
32 Jesus dizia isso com toda a clareza. Então Pedro o levou para um lado e começou a repreendê-lo.
33 Waaye Yeesu geestu, gis yeneen taalibe yi, mu daldi yedd Piyeer ne ko: «Sore ma Seytaane; yëfi nit ngay fonk, waaye du yëfi Yàlla.»
33 Jesus virou-se, olhou para os discípulos e repreendeu Pedro, dizendo:
34 Noonu Yeesu woo taalibe yi ak mbooloo mi ne leen: «Ku bëgga topp ci samay tànk, na bàyyi boppam te gàddu bant bi ñu ko wara daaj, doora topp ci man.
34 Aí Jesus chamou a multidão e os discípulos e disse:
35 Ndaxte koo xam ne bëgg ngaa rawale sa bakkan, dinga ko ñàkk, waaye ku ñàkk sa bakkan ngir man ak ngir xibaaru jàmm bi, dinga ko jotaat.
35 Pois quem põe os seus próprios interesses em primeiro lugar nunca terá a vida verdadeira; mas quem esquece a si mesmo por minha causa e por causa do
36 Ndaxte moom àddina sépp, lu muy jariñ nit, bu ñàkkee bakkanam?
36 O que adianta alguém ganhar o mundo inteiro, mas perder a vida verdadeira?
37 Te nit, lu mu wara weccee bakkanam?
37 Pois não há nada que poderá pagar para ter de volta essa vida.
38 Ku ma rusa faral, te nanguwul samay wax ci kanam niti jamono jii, ñi fecci seen kóllëre ak Yàlla te topp bàkkaar, Doomu nit ki dina la rusa xam, bés bu ñëwee ci ndamu Baayam, ànd ak malaaka yu sell yi.»
38 Portanto, se nesta época de incredulidade e maldade alguém tiver vergonha de mim e dos meus ensinamentos, então o Filho do Homem, quando vier na

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Marcos 8, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.