Marcos 7
Téereb Injiil (WOL2010) vs NAA
1 Amoon na bés nag, ay Farisen ak ay xutbakat yu jóge Yerusalem ñëw ci Yeesu.
1 Os fariseus e alguns escribas, vindos de Jerusalém, reuniram-se em volta de Jesus.
2 Ñu gis yenn ciy taalibeem di lekk, fekk seeni loxo setul, maanaam raxasuwuñu woon, ni ko aada santaanee.
2 Eles viram que alguns dos discípulos de Jesus comiam pão com as mãos impuras, isto é, sem lavar.
3 Farisen yi nag ñoom ak Yawut yi yépp dañuy topp aaday yoon, yi maam yi tëral, te fandee leen gënal lekk ak loxo yu ñu raxasul.
3 Porque os fariseus e todos os judeus, observando a tradição dos anciãos, não comem sem lavar cuidadosamente as mãos.
4 Te it bu ñu jógee pénc ma, su ñu sanguwul set, duñu lekk. Am nañu it yeneen aada yu bare, maanaam ni nga wara raxase ay kaas, ay njaq ak ay satala, ba ñu laab.
4 Quando voltam da praça, não comem sem se lavar. E há muitas outras coisas que receberam para observar, como a lavagem de copos, jarros e vasos de metal e camas.
5 Noonu Farisen ya ak xutbakat ya laaj ko ne: «Lu tax say taalibe duñu topp aaday yoon, yi maam yi tëral, waaye ñuy lekk ak loxo yu setul?»
5 Os fariseus e os escribas perguntaram a Jesus: — Por que os seus discípulos não vivem conforme a tradição dos anciãos, mas comem com as mãos impuras?
6 Yeesu ne leen: «Esayi waxoon na bu baax ci kàddug Yàlla ci seen mbir, yéen naaféq yi, bi mu bindee:
6 Jesus respondeu:
7 Seen màggal amul benn njariñ,
7 E em vão me adoram,
8 Yeesu neeti leen: «Dëddu ngeen ndigali Yàlla, jublu ci aaday nit.»
8 — Rejeitando o mandamento de Deus, vocês guardam a tradição humana.
9 Mu teg ca ne leen: «Xelu ngeen ci tebbi ndigali Yàlla, ngir sàmm seen aada.
9 E disse-lhes ainda:
10 Ndaxte Musaa nee na: “Teralal sa ndey ak sa baay,” teg ca ne: “Ku móolu sa yaay walla sa baay, dees na la rey.”
10 Pois Moisés disse: “Honre o seu pai e a sua mãe.” E: “Quem maldisser o seu pai ou a sua mãe seja punido de morte.”
11 Waaye yéen dangeen ne: ku ne sa yaay walla sa baay: “Li nga wara jariñoo ci man Korban la,” —maanaam saraxu Yàlla la—
11 Vocês, porém, dizem que, se alguém disser ao seu pai ou à sua mãe: “A ajuda que você poderia receber de mim é Corbã, isto é, oferta ao Senhor”,
12 dootuleen ko bàyyi, mu defal dara ndeyam walla baayam.
12 então vocês o dispensam de fazer qualquer coisa em favor do seu pai ou da sua mãe,
13 Noonu tebbi ngeen kàddug Yàlla ndax seen aada, ji ngeen di donnante. Te it yéena ngi def yeneen yu bon yu mel nii.»
13 invalidando a palavra de Deus por meio da tradição que vocês mesmos passam de pai para filho. E fazem muitas outras coisas semelhantes.
14 Noonu Yeesu waxaat ak mbooloo mi ne leen: «Yéen ñépp dégluleen ma te xam.
14 E, convocando outra vez a multidão, Jesus disse:
15 — ausente —
15 Não existe nada fora da pessoa que, entrando nela, possa contaminá-la; mas o que sai da pessoa é o que a contamina.
16 — ausente —
16 [Se alguém tem ouvidos para ouvir, ouça.]
17 Bi nga xamee ne jóge nañu ci mbooloo mi, dugg ci kër gi, taalibe yi laaj Yeesu, mu firil leen wax ju làqu jooju.
17 Quando entrou em casa, deixando a multidão, os seus discípulos o interrogaram a respeito da parábola.
18 Yeesu ne leen: «Ndax yéen itam seen xol dafa tëju? Xanaa xamuleen ne, dara lu jóge biti, dugg ci nit, du ko mana indil sobe,
18 Jesus lhes disse:
19 ndaxte du dugg ci xol, waaye ci biiram lay jëm, ba noppi daldi génn ca bérab bu làqu?» Ci li mu wax loolu Yeesu daganal na bépp ñam.
19 porque não entra no coração dela, mas no estômago, e depois é eliminado? E, assim, Jesus considerou puros todos os alimentos.
20 Yeesu ne leen ati: «Li génn ci nit, loolu mooy indil nit sobe.
20 E dizia:
21 Ndaxte ci biir, ci xolu nit, la xalaat yu bon di jóge ak ndoxaanu yàqute, càcc ak bóom,
21 Porque de dentro, do coração das pessoas, é que procedem os maus pensamentos, as imoralidades sexuais, os furtos, os homicídios,
22 njaaloo ak bëgge, coxor, naaféq, ñaawteef, ñeetaan, saaga, réylu ak jëfi ndof.
22 os adultérios, a avareza, as maldades, o engano, a libertinagem, a inveja, a blasfêmia, o orgulho, a falta de juízo.
23 Lu bon loolu lépp day génn ci nit, di ko indil sobe.»
23 Todos estes males vêm de dentro e contaminam a pessoa.
24 Gannaaw loolu Yeesu jóge fa, jëm weti dëkku Tir. Bi mu fa eggee, mu dugg ci kër, te bëggul kenn xam ko, waaye jataayam manula umpe.
24 Levantando-se Jesus, saiu dali e foi para as terras de Tiro e Sidom. Tendo entrado numa casa, não queria que ninguém soubesse onde ele estava. No entanto, não pôde ocultar-se,
25 Amoon na fa nag jigéen ju rab jàpp doomam ju jigéen. Bi mu déggee ne, Yeesoo nga fa, mu ñëw, daanu ciy tànkam,
25 porque uma mulher, cuja filhinha estava possuída de espírito imundo, logo ouviu falar a respeito de Jesus. Ela veio e se ajoelhou aos pés dele.
26 fekk jigéen ja ci xeetu Gereg la bokkoon, juddoo wàlli Fenisi ci diiwaanu Siri.
26 Essa mulher era estrangeira, de origem siro-fenícia, e pedia a Jesus que expulsasse o demônio da sua filha.
27 Waaye Yeesu ne ko: «Na gone yi jëkka lekk, ba regg; fab ñamu gone yi, sànni ko xaj yi, rafetul.»
27 Mas Jesus lhe disse:
28 Jigéen ji ne ko: «Waaw, sang bi, teewul xaj yi di lekk ruusit, yi rot ci lekkukaayu gone yi.»
28 A mulher respondeu a ele: — Senhor, os cachorrinhos, debaixo da mesa, comem das migalhas das crianças.
29 Ci kaw loolu Yeesu ne ko: «Ndax wax jooju demal ci jàmm, rab wa génn na sa doom.»
29 Então Jesus disse à mulher:
30 Noonu mu ñibbi, fekk doom ji tëdd cib lal te mucc ci rab wi.
30 Quando a mulher voltou para casa, achou a menina sobre a cama, pois o demônio tinha saído dela.
31 Bi loolu amee Yeesu jóge na weti Tir, jaar ci wàlli dëkku Sidon, dem dexu Galile, ba noppi dugg ci biir diiwaan, bi ñuy wax Fukki dëkk yi.
31 De novo, Jesus se retirou das terras de Tiro e foi por Sidom até o mar da Galileia, através do território de Decápolis.
32 Foofa ñu indil ko ku tëx te dër lool, ñaan ko mu teg ko loxo.
32 Então lhe trouxeram um surdo e gago e lhe suplicaram que impusesse as mãos sobre ele.
33 Noonu Yeesu yóbbu ko, ba ñu sore mbooloo mi, mu def ay baaraamam ciy noppam, daldi tifli, laal làmmiñam.
33 Jesus, tirando-o da multidão, à parte, pôs os dedos nos ouvidos dele; depois, cuspindo, aplicou saliva na língua do homem.
34 Mu yërëm ko, ba binni ci xolam, xool ci asamaan, daldi ne: «Effata,» liy tekki «Ubbikuleen.»
34 Então, erguendo os olhos ao céu, suspirou e disse:
35 Ci saa si ay noppam daldi dégg te làmmiñam yiwiku, muy wax bu leer.
35 E logo os ouvidos do homem se abriram, e o empecilho da língua se soltou, e ele falava sem dificuldade.
36 Bi mu ko defee Yeesu tere leen, ñu wax ko kenn, waaye lu mu leen ko gëna tere, ñu gën ko nee siiwale.
36 Jesus lhes ordenou que não contassem isso a ninguém; porém, quanto mais recomendava, tanto mais eles o divulgavam.
37 Ñu waaru lool naan: «Lépp lu mu def, lu yéeme la. May na sax tëx yi ñuy dégg, ak luu yi ñuy wax.»
37 Ficavam muito admirados, dizendo: — Tudo ele tem feito muito bem; faz até os surdos ouvirem e os mudos falarem.
Atalhos do teclado
- Capítulo anterior←
- Próximo capítulo→
- Versículo anteriork
- Próximo versículoj
- Limpar seleçãoEsc
- Esta ajuda?
Estude este capítulo no WhatsApp
Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Marcos 7, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.