Marcos 4
Téereb Injiil (WOL2010) vs VC
1 Am beneen yoon Yeesu nekk ci wetu dex ga, di jànglewaat. Mbooloo mu bare dajaloosi, ba tax mu yéeg cig gaal, dugg ca dex ga; mbooloo mépp taxaw ca tefes ga.
1 Jesus pôs-se novamente a ensinar, à beira do mar, e aglomerou-se junto dele tão grande multidão, que ele teve de entrar numa barca, no mar, e toda a multidão ficou em terra na praia.
2 Noonu Yeesu daldi leen jàngal lu bare ciy léeb. Ci njàngleem nag mu ne leen:
2 E ensinava-lhes muitas coisas em parábolas. Dizia-lhes na sua doutrina:
3 «Dégluleen, dafa amoon beykat bu demoon jiyi.
3 Ouvi: Saiu o semeador a semear.
4 Bi muy saaw toolam nag, lenn ci pepp mi wadd ci kaw yoon wi, picc yi daldi ñëw, lekk ko lépp.
4 Enquanto lançava a semente, uma parte caiu à beira do caminho, e vieram as aves e a comeram.
5 Leneen ci pepp mi wadd ci bérab bu bare ay doj te néew suuf, mu daldi sax bu gaaw, ndaxte suuf si barewul.
5 Outra parte caiu no pedregulho, onde não havia muita terra; o grão germinou logo, porque a terra não era profunda;
6 Waaye bi jant bi naajee, mu lakk, wow, ndaxte amul ay reen.
6 mas, assim que o sol despontou, queimou-se e, como não tivesse raiz, secou.
7 Leneen nag wadd ci biir ay xaaxaam, xaaxaam yi daldi sax, tanc ko, te meññul dara.
7 Outra parte caiu entre os espinhos; estes cresceram, sufocaram-na e o grão não deu fruto.
8 Li ci des dal ci suuf su baax, mu jóg, sax, di focci ay gub; lii àntu, ba mat fanweeri yoon lu ëpp la mu ji woon, lii mat juróom benn fukk, lii mat téeméer.»
8 Outra caiu em terra boa e deu fruto, cresceu e desenvolveu-se; um grão rendeu trinta, outro sessenta e outro cem.
9 Noonu Yeesu ne leen: «Déglul bu baax, yaw mi am ay nopp.»
9 E dizia: Quem tem ouvidos para ouvir, ouça!
10 Gannaaw loolu ba Yeesu nekkee fu wéet, fukki taalibe ak ñaar ña, ak ñeneen ñu daan ànd ak ñoom, laaj ko ci mbirum léeb yi.
10 Quando se acharam a sós, os que o cercavam e os Doze indagaram dele o sentido da parábola.
11 Mu ne leen: «Yéen may nañu leen, ngeen xam mbóoti nguuru Yàlla, waaye ñi ci biti léeb ay ëmb lépp.
11 Ele disse-lhes: A vós é revelado o mistério do Reino de Deus, mas aos que são de fora tudo se lhes propõe em parábolas.
12 Noonu la, ngir:
12 Desse modo, eles olham sem ver, escutam sem compreender, sem que se convertam e lhes seja perdoado.
13 Noonu Yeesu ne leen: «Ndax xamuleen léeb wii? Nu ngeen xame nag léeb yi ci des?
13 E acrescentou: Não entendeis essa parábola? Como entendereis então todas as outras?
14 Ki ji nag, kàddu gi lay ji.
14 O semeador semeia a palavra.
15 Ki féete ci yoon wi mooy ki dégg, Seytaane ñëw ci saa si, këf kàddu, gi ñu def ci moom.
15 Alguns se encontram à beira do caminho, onde ela é semeada; apenas a ouvem, vem Satanás tirar a palavra neles semeada.
16 Ki jot kàddu gi ci bérab bu bare ay doj mooy ki dégg kàddu gi, nangu ko ak mbég ci saa si,
16 Outros recebem a semente em lugares pedregosos; quando a ouvem, recebem-na com alegria;
17 waaye du yàgg, ndaxte wax ji saxul ci moom. Bu jaaree ci nattu nag, mbaa ñu fitnaal ko ndax kàddu gi, mu dàggeeku ci saa si.
17 mas não têm raiz em si, são inconstantes, e assim que se levanta uma tribulação ou uma perseguição por causa da palavra, eles tropeçam.
18 Ki jot jiwu wi ci xaaxaam yi mooy ki dégg kàddu gi,
18 Outros ainda recebem a semente entre os espinhos; ouvem a palavra,
19 waaye soxlay àddina ak naxi alal ak bëgge solu ko, tanc kàddu gi, ba du meññ dara.
19 mas as preocupações mundanas, a ilusão das riquezas, as múltiplas cobiças sufocam-na e a tornam infrutífera.
20 Ki jot kàddu gi ci suuf su baax si nag, mooy ki ko dégg te nangu ko, ba jariñ; kii mat fanweeri yoon lu ëpp la ñu ji woon, kii mat juróom benn fukk, kii mat téeméer.»
20 Aqueles que recebem a semente em terra boa escutam a palavra, acolhem-na e dão fruto, trinta, sessenta e cem por um.
21 Yeesu ne leen itam: «Ndax nit dina jël làmp, dëpp ci leget walla def ko ci ron lal? Ndax du ko wékk?
21 Dizia-lhes ainda: Traz-se porventura a candeia para ser colocada debaixo do alqueire ou debaixo da cama? Não é para ser posta no candeeiro?
22 Amul dara luy kumpa lu ñu warula siiwal, mbaa mu làqu te warul ne fàŋŋ.
22 Porque nada há oculto que não deva ser descoberto, nada secreto que não deva ser publicado.
23 Déglul bu baax, yaw mi am ay nopp.»
23 Se alguém tem ouvidos para ouvir, que ouça.
24 Mu ne leen: «Seetleen bu baax li ngeen di dégg. Dees na leen nattal ak natt, bi ngeen di nattale, te dollil leen.
24 Ele prosseguiu: Atendei ao que ouvis: com a medida com que medirdes, vos medirão a vós, e ainda se vos acrescentará.
25 Ku am, dees na la dollil; ku amul, li nga am as néew, dees na ko nangu.»
25 Pois, ao que tem, se lhe dará; e ao que não tem, se lhe tirará até o que tem.
26 Yeesu teg ci ne: «Nguuru Yàlla dafa mel ni nit ku ji tool.
26 Dizia também: O Reino de Deus é como um homem que lança a semente à terra.
27 Muy nelaw walla muy xool, guddi mbaa bëccëg, jiwu wi sax, di màgg, te xamul naka la ko defe.
27 Dorme, levanta-se, de noite e de dia, e a semente brota e cresce, sem ele o perceber.
28 Suuf day meññ moom ci boppam, mu sax, focci, def i gub.
28 Pois a terra por si mesma produz, primeiro a planta, depois a espiga e, por último, o grão abundante na espiga.
29 Bu gub yi ñoree nag, mu dagg ko, ndaxte ngóob jot na.»
29 Quando o fruto amadurece, ele mete-lhe a foice, porque é chegada a colheita.
30 Yeesu ne leen ati: «Lu nu mana méngaleel nguuru Yàlla? Walla ban léeb lanu ko mana misaale?
30 Dizia ele: A quem compararemos o Reino de Deus? Ou com que parábola o representaremos?
31 Dafa mel ni doomu fuddën, bi gëna tuuti ci jiwu yépp;
31 É como o grão de mostarda que, quando é semeado, é a menor de todas as sementes.
32 waaye boo ko jiyee, day jóg, màgg, ba sut gàncaxi tóokër yépp; mu sax ay bànqaas yu réy, ba picci asamaan tàgg ci keram.»
32 Mas, depois de semeado, cresce, torna-se maior que todas as hortaliças e estende de tal modo os seus ramos, que as aves do céu podem abrigar-se à sua sombra.
33 Noonu Yeesu dégtal leen yeneen léeb yu bare yu mel ni yii, di leen xamal kàddu gi, aju ci lu ñu àttan.
33 Era por meio de numerosas parábolas desse gênero que ele lhes anunciava a palavra, conforme eram capazes de compreender.
34 Daawu leen wax dara lu dul ciy léeb. Waaye bu wéetee ak ay taalibe, daan na leen firil lépp.
34 E não lhes falava, a não ser em parábolas; a sós, porém, explicava tudo a seus discípulos.
35 Bés booba nag ci ngoon Yeesu ne taalibe yi: «Nanu jàll dex gi.»
35 À tarde daquele dia, disse-lhes: Passemos para o outro lado.
36 Mu yiwi mbooloo mi nag, ay taalibeem jël ko ni mu mel ci gaal gi; te yeneen gaal ànd ak moom.
36 Deixando o povo, levaram-no consigo na barca, assim como ele estava. Outras embarcações o escoltavam.
37 Naka noona ngelaw lu mag daldi jóg, duus yi sàng gaal gi, ba mu bëgga fees.
37 Nisto surgiu uma grande tormenta e lançava as ondas dentro da barca, de modo que ela já se enchia de água.
38 Fekk Yeesu tëdd di nelaw ci ngegenaay ci taatu gaal gi.
38 Jesus achava-se na popa, dormindo sobre um travesseiro. Eles acordaram-no e disseram-lhe: Mestre, não te importa que pereçamos?
39 Ci kaw loolu Yeesu jóg, daldi gëdd ngelaw li, ne dex gi: «Noppil te dal!» Noonu ngelaw li dal, ba lépp ne nemm.
39 E ele, despertando, repreendeu o vento e disse ao mar: Silêncio! Cala-te! E cessou o vento e seguiu-se grande bonança.
40 Yeesu ne taalibe ya: «Lu tax ngeen tiit? Ndax gëmaguleen?»
40 Ele disse-lhes: Como sois medrosos! Ainda não tendes fé?
41 Ñu daldi ragal lool, naan ci seen biir: «Kii moo di kan, ba ngelaw li ak dex gi sax di ko déggal?»
41 Eles ficaram penetrados de grande temor e cochichavam entre si: Quem é este, a quem até o vento e o mar obedecem?
Atalhos do teclado
- Capítulo anterior←
- Próximo capítulo→
- Versículo anteriork
- Próximo versículoj
- Limpar seleçãoEsc
- Esta ajuda?
Estude este capítulo no WhatsApp
Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Marcos 4, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.