Marcos 3

Téereb Injiil (WOL2010) vs VC

Sair da comparação
VC Versão Católica
1 Am beneen bés, Yeesu duggaat ci jàngu bi, fekk amoon na fa nit ku loxoom làggi.
1 Noutra vez, entrou ele na sinagoga e achava-se ali um homem que tinha a mão seca.
2 Am na fa nag ay Farisen, ñuy xool Yeesu, ba xam ndax dina ko faj ci bésub noflaay bi, ngir ñu man koo tuumaal.
2 Ora, estavam-no observando se o curaria no dia de sábado, para o acusarem.
3 Yeesu ne ku loxoom làggi: «Jógal, taxaw ci kanam ñépp.»
3 Ele diz ao homem da mão seca: "Vem para o meio."
4 Noonu Yeesu ne leen: «Lan moo jaadu, nu def ko bésub noflaay bi, lu baax mbaa lu bon; nu musal nit mbaa nu rey nit?» Waaye ñu ne cell.
4 Então lhes pergunta: "É permitido fazer o bem ou o mal no sábado? Salvar uma vida ou matar?" Mas eles se calavam.
5 Ci kaw loolu Yeesu xool leen ak mer, am naqar ndax seen xol bu fatt; ba noppi mu ne nit ki: «Tàllalal sa loxo.» Nit ki tàllal ko, loxoom daldi wér péŋŋ.
5 Então, relanceando um olhar indignado sobre eles, e contristado com a dureza de seus corações, diz ao homem: "Estende tua mão!" Ele estendeu-a e a mão foi curada.
6 Ca saa sa nag Farisen ya génn, daldi gise ak ñi far ak buur bi Erodd, ngir fexe koo reylu.
6 Saindo os fariseus dali, deliberaram logo com os herodianos como o haviam de perder.
7 Gannaaw loolu Yeesu ak ay taalibeem jóge fa, jëm dex ga. Fekk mbooloo mu mag mu jóge diiwaanu Galile, topp ko.
7 Jesus retirou-se com os seus discípulos para o mar, e seguia-o uma grande multidão, vinda da Galiléia.
8 Te it nit ñu bare dégg la mu def, ñu ñëw fi moom, jóge diiwaanu Yude ak dëkku Yerusalem, ca diiwaanu Idume, ca gannaaw dexu Yurdan ak ci wàlli Tir ak Sidon.
8 E da Judéia, de Jerusalém, da Iduméia, do além-Jordão e dos arredores de Tiro e de Sidônia veio a ele uma grande multidão, ao ouvir o que ele fazia.
9 — ausente —
9 Ele ordenou a seus discípulos que lhe aprontassem uma barca, para que a multidão não o comprimisse.
10 — ausente —
10 Curou a muitos, de modo que todos os que padeciam de algum mal se arrojavam a ele para o tocar.
11 Fekk booba képp ku rab jàpp ku ko gis, daanu fa kanamam di yuuxu naan: «Yaa di Doomu Yàlla.»
11 Quando os espíritos imundos o viam, prostravam-se diante dele e gritavam: Tu és o Filho de Deus!
12 Waaye Yeesu gëdd rab yi bu wér, ngir ñu bañ koo siiwal.
12 Ele os proibia severamente que o dessem a conhecer.
13 Gannaaw loolu Yeesu yéeg ci tund wi, woo ñi ko neex, ñu daldi ñëw ci moom.
13 Depois, subiu ao monte e chamou os que ele quis. E foram a ele.
14 Noonu mu tànn ci fukk ak ñaar, tudde leen ay ndawam, ngir ñu ànd ak moom te mu yónni leen, ñu waareji,
14 Designou doze dentre eles para ficar em sua companhia.
15 mu joxaale leen sañ-sañu dàq ay rab.
15 Ele os enviaria a pregar, com o poder de expulsar os demônios.
16 Fukk ak ñaar ñii la tànn:
16 Escolheu estes doze: Simão, a quem pôs o nome de Pedro;
17 Saag doomu Sebede, ak Yowaana mi mu bokkal ndey ak baay— ñoom ñi mu wooye Bowanerses, maanaam «Ñi aaytal ni dënnu gi»—
17 Tiago, filho de Zebedeu, e João, seu irmão, aos quais pôs o nome de Boanerges, que quer dizer Filhos do Trovão.
18 Andare ak Filib,
18 Ele escolheu também André, Filipe, Bartolomeu, Mateus, Tomé, Tiago, filho de Alfeu; Tadeu, Simão, o Zelador;
19 ak Yudaa Iskariyo mi nara wor Yeesu.
19 e Judas Iscariotes, que o entregou.
20 Am beneen bés Yeesu ñëwaat ca kër ga. Te mbooloo mu bare dajaloowaat fa, ba tax manuñoo lekk sax.
20 Dirigiram-se em seguida a uma casa. Aí afluiu de novo tanta gente, que nem podiam tomar alimento.
21 Bi ko ay bokkam déggee nag, ñu ñëw, ngir jàppsi ko naan: «Dafa tàggoo ak sagoom.»
21 Quando os seus o souberam, saíram para o reter; pois diziam: "Ele está fora de si."
22 Te it xutbakat ya jóge Yerusalem ne: «Beelsebul jàpp na ko; ci kàttanu buuru rab yi lay dàqe rab yi.»
22 Também os escribas, que haviam descido de Jerusalém, diziam: "Ele está possuído de Beelzebul: é pelo príncipe dos demônios que ele expele os demônios."
23 Noonu Yeesu woo leen, wax ak ñoom ciy léeb ne leen: «Naka la Seytaane mana dàqe Seytaane?
23 Mas, havendo-os convocado, dizia-lhes em parábolas: "Como pode Satanás expulsar a Satanás?
24 Réew mu xeex boppam, du mana yàgg.
24 Pois, se um reino estiver dividido contra si mesmo, não pode durar.
25 Te kër gu xeex boppam, du mana yàgg.
25 E se uma casa está dividida contra si mesma, tal casa não pode permanecer.
26 Bu Seytaane nag jógee, ba xeex boppam, xàjjalikoo dikkal na ko te du mana yàgg, waaye dina tas.
26 E se Satanás se levanta contra si mesmo, está dividido e não poderá continuar, mas desaparecerá.
27 «Su fi amee nit ku bare doole, naka la kenn mana dugge ci këram, nangu alalam? Xanaa dafay jëkka yeew ku bare doole ka, ba noppi doora toj këram gépp.
27 Ninguém pode entrar na casa do homem forte e roubar-lhe os bens, se antes não o prender; e então saqueará sua casa.
28 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, lépp dees na ko baal nit ñi, muy bàkkaar, muy sosal Yàlla wu mu mana doon.
28 "Em verdade vos digo: todos os pecados serão perdoados aos filhos dos homens, mesmo as suas blasfêmias;
29 Waaye kuy sosal Xel mu Sell mi deesu ko baal mukk; gàddu na bàkkaar ba fàww.»
29 mas todo o que tiver blasfemado contra o Espírito Santo jamais terá perdão, mas será culpado de um pecado eterno."
30 Yeesu wax na loolu, ndaxte nee woon nañu, rab jàpp na ko.
30 Jesus falava assim porque tinham dito: "Ele tem um espírito imundo."
31 Noonu ndeyu Yeesu ak ay rakkam ñëw, ñu taxaw ci biti, yónnee, woo ko.
31 Chegaram sua mãe e seus irmãos e, estando do lado de fora, mandaram chamá-lo.
32 Fekk booba mbooloo nga toog, wër ko. Ñu ne ko nag: «Sa yaay ak say rakk ñu ngi taxaw ci biti, di la laaj.»
32 Ora, a multidão estava sentada ao redor dele; e disseram-lhe: "Tua mãe e teus irmãos estão aí fora e te procuram."
33 Waaye Yeesu ne leen: «Kan mooy sama ndey? Ñan ñooy samay rakk?»
33 Ele respondeu-lhes: "Quem é minha mãe e quem são meus irmãos?"
34 Noonu mu xool ñi ko wër naan: «Sama yaay ak samay rakk a ngii;
34 E, correndo o olhar sobre a multidão, que estava sentada ao redor dele, disse: "Eis aqui minha mãe e meus irmãos.
35 ndaxte kuy def coobarey Yàlla, kooku mooy sama rakk ak sama jigéen ak sama ndey.»
35 Aquele que faz a vontade de Deus, esse é meu irmão, minha irmã e minha mãe."

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Marcos 3, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.