Marcos 1
Téereb Injiil (WOL2010) vs NAA
1 Xibaaru jàmm bu Yeesu Kirist, Doomu Yàlla, nii la tàmbalee.
1 Princípio do evangelho de Jesus Cristo, Filho de Deus.
2 Bind nañu ci téereb yonent Yàlla Esayi naan:
2 Como está escrito na profecia de Isaías: “Eis que envio o meu mensageiro adiante de você, o qual preparará o seu caminho.
3 Baat a ngi xaacu ca màndiŋ ma naan:
3 Voz do que clama no deserto: Preparem o caminho do Senhor, endireitem as suas veredas.”
4 Noonu Yaxya feeñ ca màndiŋ ma, di sóob nit ñi ci ndox, tey waaree nii: «Tuubleen seeni bàkkaar, ba noppi ma sóob leen ci ndox, ngir Yàlla baal leen seeni bàkkaar.»
4 E foi assim que João Batista apareceu no deserto, pregando batismo de arrependimento para remissão de pecados.
5 Kon waa diiwaanu Yude ñépp ak waa dëkku Yerusalem ñépp daldi génn jëm ci moom, di nangu seeni bàkkaar fi kanam ñépp, Yaxya sóob leen ca dexu Yurdan.
5 E toda a região da Judeia e todos os moradores de Jerusalém iam até ele. E, confessando os seus pecados, eram batizados por ele no rio Jordão.
6 Yaxya nag mi ngi soloon mbubb mu ñu ràbbe kawaru giléem, takk laxasaayu der ci ndiggam. Ay njéeréer la doon dunde ak lem.
6 A roupa de João era feita de pelos de camelo. Ele usava um cinto de couro e se alimentava de gafanhotos e mel silvestre.
7 Mu waare ne: «Am na kuy ñëw sama gannaaw koo xam ne kii moo ma ëpp kàttan; yeyoowuma sax sëgg, ngir tekki ay dàllam.
7 E João pregava, dizendo: — Depois de mim vem aquele que é mais poderoso do que eu, do qual não sou digno de, curvando-me, desamarrar as correias das suas sandálias.
8 Maa ngi leen di sóob ci ndox, waaye moom dina leen sóob ci Xel mu Sell mi.»
8 Eu batizei vocês com água; ele, porém, os batizará com o Espírito Santo.
9 Booba Yeesu jóge na dëkku Nasaret ci diiwaanu Galile, ñëw, Yaxya sóob ko ci dexu Yurdan.
9 Naqueles dias, Jesus veio de Nazaré da Galileia e foi batizado por João no rio Jordão.
10 Bi muy génn ndox mi, mu daldi gis asamaan xar, te Xelum Yàlla di wàcc ci melow pitax, ñëw ci moom.
10 Logo ao sair da água, Jesus viu os céus se abrindo e o Espírito descendo como pomba sobre ele.
11 Te baat bu jóge asamaan jib ne: «Yaa di sama Doom, ji ma bëgg; ci yaw laa ame bànneex.»
11 Então veio uma voz dos céus, que dizia: — Você é o meu Filho amado; em você me agrado.
12 Ci kaw loolu Xelum Yàlla daldi jéñ Yeesu, mu dem ca màndiŋ ma.
12 E logo o Espírito conduziu Jesus ao deserto,
13 Mu nekk fa ñeent fukki fan, jànkoonte ak fiiri Seytaane; mu dëkk ci biir rabi àll yi, te malaakay Yàlla di ko topptoo.
13 onde ficou durante quarenta dias, sendo tentado por Satanás. Estava com as feras, e os anjos o serviam.
14 Bi nga xamee ne jàpp nañu Yaxya, Yeesu dem ca diiwaanu Galile, di waare xibaaru jàmm bu Yàlla bi,
14 Depois de João ter sido preso, Jesus foi para a Galileia, pregando o evangelho de Deus.
15 naan: «Jamono ji mat na, nguuru Yàlla jegesi na; tuubleen seeni bàkkaar te gëm xibaaru jàmm bi.»
15 Ele dizia:
16 Am bés Yeesu doon dox ca tefesu dexu Galile, mu gis fa ñaar ñu bokk ndey ak baay, di Simoŋ ak Andare rakkam, ñuy sànni seeni mbaal ci dex gi, ndaxte ay nappkat lañu woon.
16 Caminhando junto ao mar da Galileia, Jesus viu os irmãos Simão e André, que lançavam a rede ao mar, porque eram pescadores.
17 Yeesu ne leen: «Ñëwleen topp ci man, dinaa leen def nappkati nit.»
17 Jesus lhes disse:
18 Ci saa si ñu bàyyi seeni mbaal, topp ci moom.
18 Então eles deixaram imediatamente as redes e o seguiram.
19 Bi Yeesu demee ba ca kanam, mu gis Saag doomu Sebede, ak Yowaana, mi mu bokkal ndey ak baay, ñu nekk ci gaal gi, di defar seeni mbaal.
19 Pouco mais adiante, Jesus viu Tiago, filho de Zebedeu, e João, seu irmão, que estavam no barco consertando as redes,
20 Noonu Yeesu woo leen, ñu daldi bàyyi seen baay Sebede ci gaal gi, moom ak surga ya, tey topp ci moom.
20 e logo os chamou. E eles seguiram Jesus, deixando o seu pai Zebedeu no barco com os empregados.
21 Gannaaw loolu ñu dem Kapernawum. Ca bésub noflaay nag Yeesu daldi dugg ci jàngu bi, di leen jàngal.
21 Depois, entraram em Cafarnaum, e, logo no sábado, Jesus foi ensinar na sinagoga.
22 Te ñu waaru ca njàngleem, ndaxte jàngal na leen ak sañ-sañ bu seeni xutbakat amul.
22 E maravilhavam-se com a sua doutrina, porque os ensinava como alguém que tem autoridade e não como os escribas.
23 Noonu am na ci jàngu bi nit ku rab jàpp. Mu daldi yuuxu naan:
23 E logo apareceu na sinagoga um homem possuído de espírito imundo, o qual gritou:
24 «Yaw Yeesum Nasaret, loo nuy fexeel? Ndax dangaa ñëw, ngir alag nu? Xam naa la, yaa di Aji Sell, ji jóge ci Yàlla.»
24 — O que você quer conosco, Jesus Nazareno? Você veio para nos destruir? Sei muito bem quem você é: o Santo de Deus!
25 Waaye Yeesu gëdd ko naan: «Noppil te génn ci moom!»
25 Mas Jesus o repreendeu, dizendo:
26 Noonu rab wi daldi sayloo nit ki te génn ci moom ak yuux gu réy.
26 Então o espírito imundo, agitando-o violentamente e gritando em alta voz, saiu dele.
27 Bi loolu amee ñépp waaru, ba laajante naan: «Kii mooy kan? Mii njàngle lu bees la te ànd ak sañ-sañ. Day sant rab yi sax, ñu di ko déggal.»
27 Todos se admiraram, a ponto de perguntarem entre si: — Que é isto? Uma nova doutrina! Com autoridade ele ordena aos espíritos imundos, e eles lhe obedecem!
28 Noonu turam daldi siiw ci diiwaani Galile gépp.
28 E a fama de Jesus se espalhou depressa em todas as direções, por toda a região da Galileia.
29 Bi nga xamee ne génn nañu ci jàngu bi, ñu ànd ak Saag ak Yowaana, dem ci kër Simoŋ ak Andare.
29 E, saindo da sinagoga, foram, com Tiago e João, para a casa de Simão e André.
30 Fekk gorob Simoŋ bu jigéen tëdd wopp ak yaram wu tàng; ñu daldi ko yégal Yeesu.
30 A sogra de Simão estava de cama, com febre; e logo deram essa notícia a Jesus.
31 Mu ñëw nag ci moom, jàpp loxoom, yékkati ko. Noonu tàngoor wi daldi wàcc, te soxna si di leen topptoo.
31 Então, aproximando-se, Jesus pegou na mão dela e fez com que ela se levantasse. A febre a deixou, e ela passou a servi-los.
32 Ca ngoon sa nag, bi jant sowee, ñu indil Yeesu ñi wopp ñépp ak ñi rab jàpp ñépp,
32 À tarde, depois do pôr do sol, trouxeram a Jesus todos os enfermos e endemoniados.
33 ba dëkk bi bépp dajaloo ci buntu kër gi.
33 Toda a cidade estava reunida à porta da casa.
34 Noonu mu wéral ñu bare, ñu wopp ak ay jàngoro yu wuute, te dàq ay rab yu bare. Waaye mu tere rab yi, ñu wax dara, ndaxte xam nañu ko.
34 E ele curou muitos que se achavam doentes de todo tipo de enfermidades. Também expulsou muitos demônios, não lhes permitindo que falassem, porque sabiam quem ele era.
35 Ca njël laata bët di set, Yeesu jóg dem ca bérab bu wéet, di fa ñaan Yàlla.
35 Tendo-se levantado de madrugada, quando ainda estava escuro, Jesus saiu e foi para um lugar deserto, e ali orava.
36 Simoŋ nag ak ñi ànd ak moom di ko seet fu nekk.
36 Simão e os que estavam com ele procuraram Jesus por toda parte.
37 Bi ñu ko gisee, ñu ne ko: «Ñépp a ngi lay seet.»
37 Quando o encontraram, lhe disseram: — Todos estão à sua procura.
38 Waaye Yeesu ne leen: «Nanu dem feneen ci dëkk yi nu wër, ma waare fa itam, ndaxte moo tax ma génn.»
38 Jesus, porém, lhes disse:
39 Noonu mu wër ci diiwaanu Galile gépp, di waare ci seeni jàngu, tey dàq rab yi.
39 Então ele foi por toda a Galileia, pregando nas sinagogas deles e expulsando os demônios.
40 Am bés ku gaana ñëw ci moom, sukk, ñaan ko ne: «Soo ko bëggee, man nga maa wéral.»
40 Um leproso se aproximou de Jesus e lhe pediu, de joelhos: — Se o senhor quiser, pode me purificar.
41 Yeesu yërëm ko, tàllal loxoom, laal ko naan: «Bëgg naa ko, wéral.»
41 E Jesus, profundamente compadecido, estendeu a mão, tocou nele e disse:
42 Ca saa sa ngaanaam daldi deñ, mu wér.
42 No mesmo instante, a lepra desapareceu dele, e ele ficou limpo.
43 Noonu Yeesu yebal ko, dénk ko bu wér naan:
43 E, advertindo-o severamente, logo o despediu.
44 «Moytula wax kenn dara, waaye demal won sa bopp sarxalkat bi, te nga jébbal Yàlla sarax, si yoonu Musaa santaane, ngir ñu xam ne wér nga, te mu nekk seede ci ñoom.»
44 E lhe disse:
45 Waaye naka la waa ji génn, mu di yéene ci kaw li xewoon, te di ko jéebaane, ba tax Yeesu manatula fàŋŋaaral dugg cib dëkk, waaye mu nekk ci biti ciy bérab yu wéet. Ba tey nit ñi jóge fu nekk, di ko fa fekk.
45 Mas, tendo ele saído, começou a proclamar muitas coisas e a divulgar a notícia, a ponto de Jesus não poder mais entrar publicamente em nenhuma cidade. Por isso, permanecia fora, em lugares desertos. E de toda parte vinham ao encontro dele.
Atalhos do teclado
- Capítulo anterior←
- Próximo capítulo→
- Versículo anteriork
- Próximo versículoj
- Limpar seleçãoEsc
- Esta ajuda?
Estude este capítulo no WhatsApp
Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Marcos 1, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.