Marcos 15

Téereb Injiil (WOL2010) vs ARIB

Sair da comparação
ARIB Almeida Revisada Imprensa Bíblica
1 Ci suba teel sarxalkat yu mag yi gise, ñoom ak njiit yi ak xutbakat yi ak kureelu àttekat yi yépp. Ñu yeew nag Yeesu, daldi ko yóbbu, jébbal ko Pilaat.
1 Logo de manhã tiveram conselho os principais sacerdotes com os anciãos, os escribas e todo o sinédrio; e maniatando a Jesus, o levaram e o entregaram a Pilatos.
2 Noonu Pilaat laaj ko: «Ndax yaa di buuru Yawut yi?» Yeesu ne ko: «Wax nga ko.»
2 Pilatos lhe perguntou: És tu o rei dos judeus? Respondeu-lhe Jesus: É como dizes.
3 Te sarxalkat yu mag yi di ko jiiñ lu bare.
3 e os principais dos sacerdotes o acusavam de muitas coisas.
4 Kon nag Pilaat laajaat ko: «Déggal lépp li ñu lay jiiñ. Xanaa amoo ci tont?»
4 Tornou Pilatos a interrogá-lo, dizendo: Não respondes nada? Vê quantas acusações te fazem.
5 Waaye ba tey Yeesu waxul dara, ba tax Pilaat waaru.
5 Mas Jesus nada mais respondeu, de maneira que Pilatos se admirava.
6 Màggal gu nekk nag Pilaat daan na may mbooloo mi, ñu tànn kenn ci ñi ñu tëjoon, mu bàyyil leen ko.
6 Ora, por ocasião da festa costumava soltar-lhes um preso qualquer que eles pedissem.
7 Fekk booba amoon na ku ñu tëj, tudd Barabas, ku bokk ci ña bëggoona tas réew mi, boole ci rey nit.
7 E havia um, chamado Barrabás, preso com outros sediciosos, os quais num motim haviam cometido um homicídio.
8 Noonu mbooloo mi ñëw, laaj Pilaat, mu defal leen la mu daan def.
8 E a multidão subiu e começou a pedir o que lhe costumava fazer.
9 — ausente —
9 Ao que Pilatos lhes perguntou: Quereis que vos solte o rei dos judeus?
10 — ausente —
10 Pois ele sabia que por inveja os principais sacerdotes lho haviam entregado.
11 Waaye sarxalkat yu mag yi xiir mbooloo mi, ñu laaj Pilaat, mu bàyyil leen Barabas.
11 Mas os principais sacerdotes incitaram a multidão a pedir que lhes soltasse antes a Barrabás.
12 Kon Pilaat ne leen: «Lan laay def nag ak ki ngeen di wooye buuru Yawut yi?»
12 E Pilatos, tornando a falar, perguntou-lhes: Que farei então daquele a quem chamais reis dos judeus?
13 Ñu daldi yuuxuwaat naan: «Daaj ko ci bant, ba mu dee!»
13 Novamente clamaram eles: Crucifica-o!
14 Pilaat ne leen: «Lu tax? Gan tooñ la def?» Waaye mbooloo mi di yuuxu bu gëna kawe: «Daaj ko ci bant!»
14 Disse-lhes Pilatos: Mas que mal fez ele? Ao que eles clamaram ainda mais: Crucifica-o!
15 Noonu Pilaat, mi wuta neex mbooloo mi, bàyyil leen Barabas, ba noppi mu dóorlu Yeesu ay yar, jébbal ko, ngir ñu daaj ko ci bant.
15 Então Pilatos, querendo satisfazer a multidão, soltou-lhe Barrabás; e tendo mandado açoitar a Jesus, o entregou para ser crucificado.
16 Bi loolu amee ñu dugal Yeesu ci biir kër boroom réew ma, mooy bérab bu ñuy wax Peretoriyum, ñu daldi woo mbooloom xarekat yépp.
16 Os soldados, pois, levaram-no para dentro, ao pátio, que é o pretório, e convocaram toda a corte;
17 Noonu ñu solal ko mbubb mu xonq curr, ràbb kaalag dég, teg ko ci boppam.
17 vestiram-no de púrpura e puseram-lhe na cabeça uma coroa de espinhos que haviam tecido;
18 Ñu daldi ko wax bu kawe: «Nuyu nanu la, yaw buuru Yawut yi!»
18 e começaram a saudá-lo: Salve, rei dos judeus!
19 Ñu di ko dóor ci bopp ak bant, di ko tifli, daldi sukk, màggal ko.
19 Davam-lhe com uma cana na cabeça, cuspiam nele e, postos de joelhos, o adoravam.
20 Bi ñu ko ñaawalee noonu ba noppi, ñu summi mbubb mu xonq mi, solaatal ko ay yéreem, yóbbu ko, ngir daaj ko ci bant.
20 Depois de o terem assim escarnecido, despiram-lhe a púrpura, e lhe puseram as vestes. Então o levaram para fora, a fim de o crucificarem.
21 Amoon na nag nit ku dëkk Siren, tudd Simoŋ, di baayu Alegsàndar ak Rufus. Fekk booba mu romb fa, jóge ca wet, ga féete ak tool ya, ñu ga ko ngir mu gàddu bant bi.
21 E obrigaram certo Simão, cireneu, pai de Alexandre e de Rufo, que por ali passava, vindo do campo, a carregar-lhe a cruz.
22 Noonu ñu yóbbu Yeesu ca bérab bu ñuy wax Golgota, liy tekki «bérabu Kaaŋu bopp.»
22 Levaram-no, pois, ao lugar do Gólgota, que quer dizer, lugar da Caveira.
23 Ñu bëgg koo jox biiñ bu ñu boole ak naan gu tudd miir, waaye nanguwu ko.
23 E ofereciam-lhe vinho misturado com mirra; mas ele não o tomou.
24 Foofa ñu daaj Yeesu ci bant, daldi séddoo ay yéreem, tegoo ko ay bant, ba xam ku nekk, looy am;
24 Então o crucificaram, e repartiram entre si as vestes dele, lançando sortes sobre elas para ver o que cada um levaria.
25 booba fekk yoor-yoor di jot.
25 E era a hora terceira quando o crucificaram.
26 Mbind mi xamle lu tax ñu rey ko nee na: «Kii mooy buuru Yawut yi.»
26 Por cima dele estava escrito o título da sua acusação: O REI DOS JUDEUS.
27 — ausente —
27 Também, com ele, crucificaram dois salteadores, um à sua direita, e outro à esquerda.
28 — ausente —
28 {E cumpriu-se a escritura que diz: E com os malfeitores foi contado.}
29 Ña fa doon romb di ko xas, di wëcc seen bopp ndax sib ko, naan: «Waaw kay, yaw mi bëgga toj kër Yàlla gi, tabaxaat ko ci ñetti fan,
29 E os que iam passando blasfemavam dele, meneando a cabeça e dizendo: Ah! tu que destróis o santuário e em três dias o reedificas.
30 wàccal ci bant bi te musal sa bopp!»
30 salva-te a ti mesmo, descendo da cruz.
31 Noonu it sarxalkat yu mag yi ak xutbakat yi di ko ñaawal ci seen biir naan: «Kii musal na ñeneen waaye manula musal boppam.
31 De igual modo também os principais sacerdotes, com os escribas, escarnecendo-o, diziam entre si: A outros salvou; a si mesmo não pode salvar;
32 Almasi bii, di buuru Israyil, na wàcc léegi ci bant bi, nu gis ko te gëm.» Ñi ñu daajaale ak moom it di ko xarab.
32 desça agora da cruz o Cristo, o rei de Israel, para que vejamos e creiamos, Também os que com ele foram crucificados o injuriavam.
33 Li tàmbalee digg bëccëg, ba ci tisbaar, réew mépp lëndëm.
33 E, chegada a hora sexta, houve trevas sobre a terra, até a hora nona.
34 Ci tisbaar nag Yeesu wootee kàddu gu dëgër naan: «Elowi, Elowi, lema sabaktani?» liy tekki: «Sama Yàlla, sama Yàlla, lu tax nga dëddu ma?»
34 E, à hora nona, bradou Jesus em alta voz: Eloí, Eloí, lamá, sabactani? que, traduzido, é: Deus meu, Deus meu, por que me desamparaste?
35 Ñenn ci ña fa taxaw nag, bi ñu ko déggee, ñu ne: «Mu ngi woo yonent Yàlla Ilyaas.»
35 Alguns dos que ali estavam, ouvindo isso, diziam: Eis que chama por Elias.
36 Noonu kenn daw, jël aw sagar, capp ko ci bineegar, mu teg ko ci bant, jox ko ko, mu muucu. Mu ne: «Bàyyileen, nu seet, ba xam Ilyaas dina ñëw, wàcce ko.»
36 Correu um deles, ensopou uma esponja em vinagre e, pondo-a numa cana, dava-lhe de beber, dizendo: Deixai, vejamos se Elias virá tirá-lo.
37 Noonu Yeesu wootewaat ak kàddu gu dëgër, delloo ruuwam Yàlla.
37 Mas Jesus, dando um grande brado, expirou.
38 Bi mu ko defee ridob bérab bu sell ba ca kër Yàlla ga xar ñaar, li dale ci kaw ba ci suuf.
38 Então o véu do santuário se rasgou em dois, de alto a baixo.
39 Njiitu xare nag, bi taxawoon ci kanam Yeesu, bi mu gisee ni Yeesu deeye, mu ne: «Ci dëgg, nit kii Doomu Yàlla la!»
39 Ora, o centurião, que estava defronte dele, vendo-o assim expirar, disse: Verdadeiramente este homem era filho de Deus.
40 Amoon na fa nag ay jigéen, ñu leen dànd, di xool. Xàmmi nañu ci: Maryaama mi dëkk Magdala, Maryaama yaayu Saag mu ndaw ak Yuusufa, ak Salome.
40 Também ali estavam algumas mulheres olhando de longe, entre elas Maria Madalena, Maria, mãe de Tiago o Menor e de José, e Salomé;
41 Bi Yeesu nekkee Galile, jigéen ñooñu ñoo ko doon topp, di ko topptoo. Amoon na fa it yeneen jigéen yu bare yu àndoon ak moom, ba ñëw Yerusalem.
41 as quais o seguiam e o serviam quando ele estava na Galiléia; e muitas outras que tinham subido com ele a Jerusalém.
42 Booba nag bésu Waajal la woon, maanaam bés bu jiitu bésub noflaay bi. Ca ngoon sa nag,
42 Ao cair da tarde, como era o dia da preparação, isto é, a véspera do sábado,
43 Yuusufa mi dëkk Arimate takk aw fitam, dem Pilaat, laaj ko néewu Yeesu. Yuusufa moomu nag, ku siiw la woon ci kureelu àttekat yi, te doon séentu moom itam nguuru Yàlla.
43 José de Arimatéia, ilustre membro do sinédrio, que também esperava o reino de Deus, cobrando ânimo foi Pilatos e pediu o corpo de Jesus.
44 Bi Pilaat déggee ne, Yeesu faatu na xaat, mu waaru. Mu woolu nag njiit li, laaj ko, ndax yàgg na faatu.
44 Admirou-se Pilatos de que já tivesse morrido; e chamando o centurião, perguntou-lhe se, de fato, havia morrido.
45 Bi ko ko njiit li dëggalee, Pilaat jox néew bi Yuusufa.
45 E, depois que o soube do centurião, cedeu o cadáver a José;
46 Noonu Yuusufa jënd càngaay, wàcce néew bi, laxas ko ci, dugal ko cib bàmmeel bu ñu yett ci xeer. Bi mu ko defee mu béraŋ aw doj, ube ko buntu bàmmeel bi.
46 o qual, tendo comprado um pano de linho, tirou da cruz o corpo, envolveu-o no pano e o depositou num sepulcro aberto em rocha; e rolou uma pedra para a porta do sepulcro.
47 Maryaamam Magdala nag ak Maryaama yaayu Yuusufa xool fu mu ko denc.
47 E Maria Madalena e Maria, mãe de José, observavam onde fora posto.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Marcos 15, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.