Marcos 13

Téereb Injiil (WOL2010) vs VC

Sair da comparação
VC Versão Católica
1 Bi Yeesu di jóge ca kër Yàlla ga, kenn ca taalibe ya ne ko: «Kilifa gi, xoolal! Ni mu réye ay doj, te rafete ni ay taax!»
1 Saindo Jesus do templo, disse-lhe um dos seus discípulos:Mestre, olha que pedras e que construções!
2 Waaye Yeesu ne leen: «Du gis ngeen taax yu réy yii yépp? Lii lépp dina daanu, ba doj dootul des ci kaw doj.»
2 Jesus replicou-lhe: Vês este grande edifício? Não se deixará pedra sobre pedra que não seja demolida.
3 Gannaaw loolu, bi nga xamee ne Yeesu toog na ci tundu Oliw ya, jàkkaarlook kër Yàlla ga, Piyeer, Saag, Yowaana ak Andare fekki ko cig wet, laaj ko:
3 E estando sentado no monte das Oliveiras, defronte do templo, perguntaram-lhe à parte Pedro, Tiago, João e André:
4 «Wax nu kañ la loolu di am? Te luy tegtal ne, mbir yii yépp a ngi bëgga mat?»
4 Dize-nos, quando hão de suceder essas coisas? E por que sinal se saberá que tudo isso se vai realizar?
5 Noonu Yeesu ne leen: «Moytuleen, bu leen kenn nax.
5 Jesus pôs-se então a dizer-lhes: Cuidai que ninguém vos engane.
6 Ñu bare dinañu ñëw ci sama tur naan: “Moom laa,” te dinañu nax ñu bare.
6 Muitos virão em meu nome, dizendo: Sou eu. E seduzirão a muitos.
7 Bu ngeen déggee ay xare ak coowi xare, wottuleena tiit; loolu war na am, waaye mujug jamono ji jotagul.
7 Quando ouvirdes falar de guerras e de rumores de guerra, não temais; porque é necessário que estas coisas aconteçam, mas não será ainda o fim.
8 Xeet dina jóg, xeex ak weneen xeet, réew xeex ak meneen réew. Te yëngu-yënguy suuf dina am ciy bérab yu bare, ak ay xiif. Loolu lépp mooy ndoortel metit yi, mel ni jigéen juy matu.
8 Levantar-se-ão nação contra nação e reino contra reino; e haverá terremotos em diversos lugares, e fome. Isto será o princípio das dores.
9 «Moytuleen. Dees na leen jébbal àttekat ya, di leen dóor ay yar ca jàngu ya. Dinañu leen dëj ci kanam i boroom réew ak i buur ndax sama tur, ngir ngeen nekk seede ci ñoom.
9 Cuidai de vós mesmos; sereis arrastados diante dos tribunais e açoitados nas sinagogas, e comparecereis diante dos governadores e reis por minha causa, para dar testemunho de mim diante deles.
10 Fàww xibaaru jàmm bi jëkka jib ci xeet yépp.
10 Mas primeiro é necessário que o Evangelho seja pregado a todas as nações.
11 Saa su ñu leen jàppee nag, dëj leen ci péncum layoo, buleen jàq ci li ngeen wara wax; li ngeen jot ca waxtu woowa waxleen ko, ndaxte du yéenay wax waaye Xel mu Sell mi.
11 Quando vos levarem para vos entregar, não premediteis no que haveis de dizer, mas dizei o que vos for inspirado naquela hora; porque não sois vós que falais, mas sim o Espírito Santo.
12 «Mag dina joxe rakkam cig dee, baay joxe doomam; ay doom it dinañu jóg, di bañ seeni waajur, di leen reylu.
12 O irmão entregará à morte o irmão, e o pai, o filho; e os filhos insurgir-se-ão contra os pais e dar-lhes-ão a morte.
13 Te ñépp dinañu leen bañ ndax sama tur; waaye ku muñ ba ca muj ga, mucc.
13 E sereis odiados de todos por causa de meu nome. Mas o que perseverar até o fim será salvo.
14 «Bés baa ngi ñëw, bu li ñuy wax “Lu araam luy yàqe” tegee ca bérab bu mu yelloowul; kiy jàng, na xam. Bu ngeen gisee loolu nag, ku nekk ci biir diiwaanu Yude, nanga daw ca tund ya.
14 Quando virdes a abominação da desolação no lugar onde não deve estar o leitor entenda , então os que estiverem na Judéia fujam para os montes;
15 Ku nekk ci kaw taax mi, bul wàcc ngir dugg kër gi, fab say yëf ya fa nekk.
15 o que estiver sobre o terraço não desça nem entre em casa para dela levar alguma coisa;
16 Ku nekk ci tool bi, bul ñibbi ngir fab sa mbubb.
16 e o que se achar no campo não volte a buscar o seu manto.
17 Ngalla jigéen ñi ëmb ca bés yooya, ngalla it ñiy nàmpal.
17 Ai das mulheres que naqueles dias estiverem grávidas e amamentando!
18 Ñaanleen ngir seen gàddaay baña tase ak jamonoy seddaayu lolli.
18 Rogai para que isto não aconteça no inverno!
19 Ndaxte booba dina am metit wu réy wu masula am, ba àddina sosoo ak tey, te dootul am mukk.
19 Porque naqueles dias haverá tribulações tais, como não as houve desde o princípio do mundo que Deus criou até agora, nem haverá jamais.
20 Te bu fekkul woon Boroom bi wàññi bés yooyu, kenn du mucc, waaye fekk na mu wàññi leen ndax gaayam ñi mu tànn.
20 Se o Senhor não abreviasse aqueles dias, ninguém se salvaria; mas ele os abreviou em atenção aos eleitos que escolheu.
21 «Booba nag, bu leen kenn waxee: “Kaayleen gis, Kirist a ngi fi,” mbaa: “Xool-leen, mu nga fale,” buleen ko gëm.
21 E se então alguém vos disser: Eis, aqui está o Cristo; ou: Ei-lo acolá, não creiais.
22 Ndaxte ñiy mbubboo turu Kirist ak ñiy mbubboo turu yonent, dinañu feeñ, di joxe ay firnde yu réy ak ay kéemaan, ba ciy nax sax ñi Yàlla tànn, su loolu manoona am.
22 Porque se levantarão falsos cristos e falsos profetas, que farão sinais e portentos para seduzir, se possível for, até os escolhidos.
23 Wax naa leen ko lu jiitu. Kon nag moytuleen.
23 Ficai de sobreaviso. Eis que vos preveni de tudo.
24 «Waaye booba, gannaaw metit yooyu:
24 Naqueles dias, depois dessa tribulação, o sol se escurecerá, a lua não dará o seu resplendor;
25 biddiiw yi di daanoo asamaan,
25 cairão os astros do céu e as forças que estão no céu serão abaladas.
26 «Noonu dees na gis Doomu nit ki ñëw ci niir yi, ànd ak kàttan ak ndam lu réy.
26 Então verão o Filho do homem voltar sobre as nuvens com grande poder e glória.
27 Dina yónni ay malaakaam, ñu dajale ñi mu tànn ci ñeenti xébla yi, fa àddina dale, ba fa asamaan yem.»
27 Ele enviará os anjos, e reunirá os seus escolhidos dos quatro ventos, desde a extremidade da terra até a extremidade do céu.
28 Yeesu teg ca ne: «Jàngleen misaalu garabu figg ga. Boo xamee ne ay bànqaasam duy nañu, tey xobam sëq, xam ngeen ne nawet jege na.
28 Compreendei por uma comparação tirada da figueira. Quando os seus ramos vão ficando tenros e brotam as folhas, sabeis que está perto o verão.
29 Noonu itam bu ngeen gisee loolu lépp xew, xamleen ne jege na; mu ngi ci bunt bi sax.
29 Assim também quando virdes acontecer estas coisas, sabei que o Filho do homem está próximo, às portas.
30 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, niti jamono jii duñu wéy, te loolu lépp amul.
30 Em verdade vos digo: não passará esta geração sem que tudo isto aconteça.
31 Asamaan ak suuf dinañu wéy, waaye samay wax du wéy mukk.
31 Passarão o céu e a terra, mas as minhas palavras não passarão.
32 «Waaye bés boobu ak waxtu woowu, kenn xamul kañ lay doon; du malaaka yi ci kaw, du sax Doom ji, waaye Baay bi rekk moo ko xam.
32 A respeito, porém, daquele dia ou daquela hora, ninguém o sabe, nem os anjos do céu nem mesmo o Filho, mas somente o Pai.
33 Moytuleen te xool! Xamuleen kañ la waxtu wi di jot.
33 Ficai de sobreaviso, vigiai; porque não sabeis quando será o tempo.
34 «Mi ngi mel ni nit ku tukki, mu dénk këram ay surgaam, ku nekk ak sa sas, te sant bëkk-néeg bi, mu xool.
34 Será como um homem que, partindo em viagem, deixa a sua casa e delega sua autoridade aos seus servos, indicando o trabalho de cada um, e manda ao porteiro que vigie.
35 Yéen nag xool-leen, ndaxte xamuleen kañ la boroom kër gi di délsi, muy ci timis mbaa ci xaaju guddi, muy ci fajar mbaa njël.
35 Vigiai, pois, visto que não sabeis quando o senhor da casa voltará, se à tarde, se à meia-noite, se ao cantar do galo, se pela manhã,
36 Bu nee jalañ, bumu leen bett, ngeen di nelaw.
36 para que, vindo de repente, não vos encontre dormindo.
37 Li ma leen wax, ñépp laa ko wax: “Xool-leen!”»
37 O que vos digo, digo a todos: vigiai!

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Marcos 13, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.