Marcos 11

Téereb Injiil (WOL2010) vs NAA

Sair da comparação
NAA Nova Almeida Atualizada 2017
1 Gannaaw loolu Yeesu ak taalibe ya jege nañu Yerusalem, ba agsi dëkki Betfase ak Betani ci wetu tundu Oliw ya. Noonu Yeesu yebal ñaar ciy taalibeem,
1 Quando se aproximavam de Jerusalém, de Betfagé e Betânia, junto ao monte das Oliveiras, Jesus enviou dois dos seus discípulos
2 ne leen: «Demleen ci dëkk bi ci kanam. Bu ngeen fa duggee, dingeen fa gis cumbur gu kenn masula war. Yiwileen ko, indi.
2 e disse-lhes:
3 Bu leen kenn nee: “Lu ngeen di def?” neleen ko: “Boroom bi da koo soxla, te léegi mu delloosi ko.”»
3 Se alguém perguntar: “Por que estão fazendo isso?”, respondam: “O Senhor precisa dele e logo o mandará de volta para cá.”
4 Taalibe ya dem nag, ñu gis cumbur ga ci mbedd mi, mu yeewe cib buntu kër.
4 Então foram e acharam o jumentinho preso, junto ao portão, do lado de fora, na rua, e o desprenderam.
5 Bi ñu koy yiwi nag, am na ca ña fa taxaw, ñu ne leen: «Lu ngeen nar, bay yiwi cumbur gi?»
5 Alguns dos que ali estavam reclamaram: — O que estão fazendo, soltando o jumentinho?
6 Taalibe yi wax leen, ni leen Yeesu digale woon, nit ñi bàyyi leen, ñu dem.
6 Eles, porém, responderam conforme as instruções de Jesus. Então os deixaram ir.
7 Ñu indi cumbur gi Yeesu nag, lal ci seeni yére, mu toog ci.
7 Levaram o jumentinho a Jesus, puseram as suas capas sobre o animal, e Jesus montou nele.
8 Ñu bare lal seeni yére ci yoon wi, ñenn ñi dagg ay cari garab ci tool yi, lal leen it ci yoon wi.
8 Muitos estenderam as suas capas no caminho, e outros espalharam ramos que tinham cortado nos campos.
9 Ñiy jiitu ak ñiy topp ci Yeesu ñépp di wax ci kaw naan:
9 Tanto os que iam adiante dele como os que o seguiam clamavam: “Hosana! Bendito o que vem em nome do Senhor!
10 Nguuru sunu maam Daawuda giy ñëw dina barkeel!
10 Bendito o Reino que vem, o reino de Davi, nosso pai! Hosana nas maiores alturas!”
11 Noonu Yeesu dugg Yerusalem, dem kër Yàlla ga, xool lépp, ba noppi génn dem dëkku Betani, moom ak fukki taalibe ya ak ñaar, ndaxte dafa guddi.
11 E Jesus entrou em Jerusalém, no templo. E, tendo observado tudo, como já era tarde, saiu para Betânia com os doze.
12 Bët set ñu génn Betani, fekk Yeesu xiif.
12 No dia seguinte, quando saíram de Betânia, Jesus teve fome.
13 Noonu mu séen fu sore garabu figg gu sëq, mu dem seeti, ndax am na ay doom. Waaye bi mu fa eggee, gisul lu dul ay xob, ndaxte jamonoy figg duggagul.
13 E, vendo de longe uma figueira com folhas, foi ver se nela acharia alguma coisa. Aproximando-se dela, nada achou, a não ser folhas; porque não era tempo de figos.
14 Ci kaw loolu mu ne garab gi: «Dootuloo meññ mukk!» Taalibe yi dégg loolu mu wax.
14 Então Jesus disse à figueira: E os discípulos de Jesus ouviram isto.
15 Bi ñu eggee Yerusalem, Yeesu dugg ci kër Yàlla gi, daldi dàq ñi fay jaay ak ñi fay jënd. Mu daaneel taabali weccikatu xaalis yi ak tooguy jaaykati pitax yi,
15 E foram para Jerusalém. Quando Jesus entrou no templo, começou a expulsar os que ali vendiam e compravam. Derrubou as mesas dos cambistas e as cadeiras dos que vendiam pombas,
16 te mayul kenn, mu yóbbu am njaay ci kër Yàlla gi.
16 e não permitia que alguém atravessasse o templo carregando algum objeto.
17 Mu di leen jàngal ne leen: «Ndax waxuñu ci Mbind mi:
17 Também os ensinava e dizia:
18 Bi ko sarxalkat yu mag ya ak xutbakat ya déggee nag, ñu ragal ko, ndaxte mbooloo mépp dañoo waaru ci njàngleem. Noonu ñu seet pexem reylu ko.
18 E os principais sacerdotes e escribas ouviram isso e procuravam uma maneira de matar Jesus, pois o temiam, porque toda a multidão se maravilhava de sua doutrina.
19 Bi timis jotee Yeesu ak taalibe yi génn dëkk bi.
19 Em vindo a tarde, Jesus e os discípulos saíram da cidade.
20 Ci suba si, bi ñuy dem, ñu gis ne garabu figg gi dee na, ba wow koŋŋ.
20 E, passando eles pela manhã, viram que a figueira estava seca desde a raiz.
21 Noonu Piyeer fàttaliku li xewoon, ne Yeesu: «Kilifa gi, xoolal, figg gi nga rëbb dee na, ba wow!»
21 Então Pedro, lembrando-se, falou: — Mestre, eis que a figueira que o senhor amaldiçoou ficou seca.
22 Yeesu ne: «Gëmleen Yàlla.
22 Ao que Jesus lhes disse:
23 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, ku ne tund wale: “Jógal, tàbbi ca géej ga,” te nga gëm ne loolu dina am, bañ cee boole xel ñaar, kon sa ñaan nangu.
23 Porque em verdade lhes digo que, se alguém disser a este monte: “Levante-se e jogue-se no mar”, e não duvidar no seu coração, mas crer que se fará o que diz, assim será com ele.
24 Moo tax maa ngi leen koy wax, bu ngeen di ñaan Yàlla, lépp lu ngeen ko mana laaj, gëmleen ne jot ngeen ko, te dingeen ko am.
24 Por isso digo a vocês que tudo o que pedirem em oração, creiam que já o receberam, e assim será com vocês.
25 — ausente —
25 E, quando estiverem orando, se tiverem alguma coisa contra alguém, perdoem, para que o Pai de vocês, que está nos céus, perdoe as ofensas de vocês.
26 — ausente —
26 [Mas, se vocês não perdoarem, também o Pai de vocês, que está nos céus, não perdoará as ofensas de vocês.]
27 Gannaaw loolu ñu duggaat Yerusalem, te Yeesu doon doxantu ca ëtti kër Yàlla ga. Noonu sarxalkat yu mag ya ak xutbakat ya ak njiit ya dab ko
27 Então regressaram para Jerusalém. E enquanto Jesus andava pelo templo, os principais sacerdotes, os escribas e os anciãos vieram ao seu encontro
28 ne ko: «Yëf yii ngay def, ci ban sañ-sañ nga koy defe? Te ku la may sañ-sañu def ko?»
28 e lhe perguntaram: — Com que autoridade você faz estas coisas? Ou quem lhe deu esta autoridade para fazer isto?
29 Yeesu ne leen: «Man itam dinaa leen laaj lenn; bu ngeen ma ci tontoo, kon dinaa leen wax ci ban sañ-sañ laay defe yëf yii.
29 Jesus respondeu:
30 La Yaxya daan def, di sóob nit ñi ci ndox, fu mu ko jële, ci Yàlla walla ci nit ñi?»
30 O batismo de João era do céu ou dos homens? Respondam!
31 Bi ñu ko déggee, ñuy werante ci seen biir naan: «Bu nu nee: “Ci Yàlla,” kon dina nu laaj: “Lu tax gëmuleen ko kon?”
31 E eles discutiam entre si: — Se dissermos: “Do céu”, ele dirá: “Então por que não acreditaram nele?”
32 Waaye bu nu nee: “Ci nit ñi,” kon mbooloo mi dal ci sunu kaw;» ndaxte ñépp teg nañu Yaxya ab yonent.
32 Se, porém, dissermos: “Dos homens”, é de temer o povo. Porque todos pensavam que João era realmente um profeta.
33 Ñu wax Yeesu nag ne: «Loolu de xamunu ko.» Noonu Yeesu ne leen: «Kon man itam duma leen wax ci ban sañ-sañ laay defe yëf yii.»
33 Então responderam a Jesus: — Não sabemos. E Jesus, por sua vez, lhes disse:

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Marcos 11, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.