Lucas 1

Téereb Injiil (WOL2010) vs VC

Sair da comparação
VC Versão Católica
1 Yaw Teyofil mu tedd mi, xam nga ne, nit ñu bare sasoo nañoo bind ab nettali bu jëm ci mbir, yi xewoon ci sunu biir,
1 Muitos empreenderam compor uma história dos acontecimentos que se realizaram entre nós,
2 li dëppook waxi seede, yi ko teewe woon li dale ca ndoorte la te ñu mujj nekk jawriñi kàddug Yàlla.
2 como no-los transmitiram aqueles que foram desde o princípio testemunhas oculares e que se tornaram ministros da palavra.
3 Léegi nag kon man ci sama wàll, gëstu naa ci lépp li ko dale ca njàlbéen ga, te fas naa la ko yéenee bindal, nettali la ni xew-xew yooyu deme woon tembe.
3 Também a mim me pareceu bem, depois de haver diligentemente investigado tudo desde o princípio, escrevê-los para ti segundo a ordem, excelentíssimo Teófilo,
4 Noonu dinga mana xam ne li ñu la jàngaloon lu wér péŋŋ la.
4 para que conheças a solidez daqueles ensinamentos que tens recebido.
5 Ca jamonoy Erodd, mi nekkoon buur ca réewu Yawut ya, amoon na sarxalkat bu ñu tudde Sakari te bokk ca mbootaayu sarxalkat, ya askanoo ci Abiya. Soxnaam Elisabet askanoo moom itam ci Aaróona.
5 Nos tempos de Herodes, rei da Judéia, houve um sacerdote por nome Zacarias, da classe de Abias; sua mulher, descendente de Aarão, chamava-se Isabel.
6 Sakari ak soxnaam ñu jub lañu ca kanam Yàlla, di topp ni mu ware ndigal yi ak dogali Boroom bi yépp.
6 Ambos eram justos diante de Deus e observavam irrepreensivelmente todos os mandamentos e preceitos do Senhor.
7 Waaye amuñu doom, ndaxte Elisabet manula am doom, te it fekk ñoom ñaar ñépp ay màggat lañu.
7 Mas não tinham filho, porque Isabel era estéril e ambos de idade avançada.
8 Benn bés nag Sakari doon def liggéeyu sarxaleem ca Yàlla, ndaxte mbootaayam a aye keroog.
8 Ora, exercendo Zacarias diante de Deus as funções de sacerdote, na ordem da sua classe,
9 Bi ñuy tegoo bant, ni ko sarxalkat yi daan defe naka-jekk, ngir xam kan mooy dugg ca bérab bu sell ba ca kër Yàlla ga, ngir taal fa cuuraay, bant ba tegu ci Sakari.
9 coube-lhe por sorte, segundo o costume em uso entre os sacerdotes, entrar no santuário do Senhor e aí oferecer o perfume.
10 Ca waxtu wa ñuy taal cuuraay la, mbooloo maa nga woon ca biti, di ñaan.
10 Todo o povo estava de fora, à hora da oferenda do perfume.
11 Noonu benn malaakam Boroom bi daldi feeñu Sakari, taxaw ca féeteek ndijooru sarxalukaay, ba ñuy taal cuuraay ca kawam.
11 Apareceu-lhe então um anjo do Senhor, em pé, à direita do altar do perfume.
12 Naka la ko Sakari gis, fitam daldi dem, mu tiit.
12 Vendo-o, Zacarias ficou perturbado, e o temor assaltou-o.
13 Waaye malaaka ma ne ko: «Bul ragal dara Sakari, ndaxte sa ñaan nangu na. Elisabet sa soxna dina la jural doom, te dinga ko tudde Yaxya.
13 Mas o anjo disse-lhe: Não temas, Zacarias, porque foi ouvida a tua oração: Isabel, tua mulher, dar-te-á um filho, e chamá-lo-ás João.
14 Sa mbég lay doon, sa xol sedd ci, te ñu bare dinañu bég ci juddoom,
14 Ele será para ti motivo de gozo e alegria, e muitos se alegrarão com o seu nascimento;
15 ndaxte dina nekk ku màgg ca kanam Yàlla. Du naan biiñ walla dara luy màndil, te bu juddoo, Xel mu Sell mi daldi ko solu.
15 porque será grande diante do Senhor e não beberá vinho nem cerveja, e desde o ventre de sua mãe será cheio do Espírito Santo;
16 Dina delloosi niti Israyil yu bare ci Yàlla seen Boroom.
16 ele converterá muitos dos filhos de Israel ao Senhor, seu Deus,
17 Mooy jiitu, di yégle ñëwug Boroom bi, ànd ak xel mi ak doole, ji yonent Yàlla Ilyaas amoon, ngir jubale xoli baay yi ak doom yi, ngir delloo ñi déggadi ci maanduteg ñi jub. Noonu dina waajal mbooloo muy teeru Boroom bi.»
17 e irá adiante de Deus com o espírito e poder de Elias para reconduzir os corações dos pais aos filhos e os rebeldes à sabedoria dos justos, para preparar ao Senhor um povo bem disposto.
18 Sakari daldi ne malaaka ma: «Nan laay xame ne loolu dëgg la? Ndaxte mag laa, te sama soxna it màggat na.»
18 Zacarias perguntou ao anjo: Donde terei certeza disto? Pois sou velho e minha mulher é de idade avançada.
19 Malaaka ma ne ko: «Man maay Jibril miy taxaw ci kanam Yàlla. Dañu maa yónni ngir ma wax ak yaw te yégal la xibaaru jàmm boobu.
19 O anjo respondeu-lhe: Eu sou Gabriel, que assisto diante de Deus, e fui enviado para te falar e te trazer esta feliz nova.
20 Léegi nag gannaaw gëmuloo li ma wax, dinga luu te dootuloo mana wax, ba kera sama wax di am, bu jamonoom jotee.»
20 Eis que ficarás mudo e não poderás falar até o dia em que estas coisas acontecerem, visto que não deste crédito às minhas palavras, que se hão de cumprir a seu tempo.
21 Fekk na booba mbooloo maa ngi xaar, jaaxle lool ci li Sakari yàgg ca bérab bu sell ba.
21 No entanto, o povo estava esperando Zacarias; e admirava-se de ele se demorar tanto tempo no santuário.
22 Waaye bi mu génnee nag, manula wax ak ñoom. Noonu nit ña xam ne dafa am lu ko feeñu ca bérab bu sell ba. Dafa luu, ba di leen liyaar.
22 Ao sair, não lhes podia falar, e compreenderam que tivera no santuário uma visão. Ele lhes explicava isto por acenos; e permaneceu mudo.
23 Bi Sakari matalee liggéeyu sarxaleem ba noppi, mu daldi ñibbi.
23 Decorridos os dias do seu ministério, retirou-se para sua casa.
24 Bi mbir yooyu weesoo, Elisabet soxnaam ëmb, di ko nëbb lu mat juróomi weer
24 Algum tempo depois Isabel, sua mulher, concebeu; e por cinco meses se ocultava, dizendo:
25 te naan: «Lii mooy yiw wi ma Boroom bi defal, ba fajal ma li doon sama gàcce ci nit ñi!»
25 Eis a graça que o Senhor me fez, quando lançou os olhos sobre mim para tirar o meu opróbrio dentre os homens.
26 Bi Elisabet nekkee ci juróom benni weeram, Yàlla yónni na malaakaam Jibril ca dëkku Nasaret ca diiwaanu Galile.
26 No sexto mês, o anjo Gabriel foi enviado por Deus a uma cidade da Galiléia, chamada Nazaré,
27 Mu yebal ko ca janq bu ñu may waa ju bokk ci askanu Daawuda te ñu koy wax Yuusufa, waaye àndaguñu. Janq baa ngi tudd Maryaama.
27 a uma virgem desposada com um homem que se chamava José, da casa de Davi e o nome da virgem era Maria.
28 Malaaka ma dikk ca moom ne ko: «Jàmm nga am, yaw mi Boroom bi defal aw yiw; mu ngi ak yaw.»
28 Entrando, o anjo disse-lhe: Ave, cheia de graça, o Senhor é contigo.
29 Waxi malaaka ma daldi jaaxal Maryaama, muy xalaat lu nuyoo boobu mana tekki.
29 Perturbou-se ela com estas palavras e pôs-se a pensar no que significaria semelhante saudação.
30 Malaaka ma ne ko: «Bul ragal dara Maryaama, ndaxte Yàlla tànn na la ci yiwam.
30 O anjo disse-lhe: Não temas, Maria, pois encontraste graça diante de Deus.
31 Dinga ëmb, jur doom ju góor; nanga ko tudde Yeesu.
31 Eis que conceberás e darás à luz um filho, e lhe porás o nome de Jesus.
32 Ku màgg lay nekki, te dinañu ko wooye Doomu Aji Kawe ji. Boroom bi Yàlla dina ko jébbal nguuru Daawuda maamam.
32 Ele será grande e chamar-se-á Filho do Altíssimo, e o Senhor Deus lhe dará o trono de seu pai Davi; e reinará eternamente na casa de Jacó,
33 Noonu dina yilif askanu Yanqóoba ba fàww, te nguuram du am àpp.»
33 e o seu reino não terá fim.
34 Maryaama laaj malaaka ma ne ko: «Naka la loolu mana ame? Man de, janq laa ba tey.»
34 Maria perguntou ao anjo: Como se fará isso, pois não conheço homem?
35 Malaaka ma ne ko: «Xel mu Sell mi dina wàcc ci yaw, te Aji Kawe ji dina la yiir ci kàttanam. Moo tax xale biy juddu dinañu ko wooye Ku sell ki, Doomu Yàlla ji.
35 Respondeu-lhe o anjo: O Espírito Santo descerá sobre ti, e a força do Altíssimo te envolverá com a sua sombra. Por isso o ente santo que nascer de ti será chamado Filho de Deus.
36 Elisabet sa mbokk mi it dina am doom ju góor cig màggatam. Ki ñu doon wooye ku manula am doom, mu ngi ci juróom benni weeram.
36 Também Isabel, tua parenta, até ela concebeu um filho na sua velhice; e já está no sexto mês aquela que é tida por estéril,
37 Ndaxte dara tëwul Yàlla.»
37 porque a Deus nenhuma coisa é impossível.
38 Maryaama ne ko: «Jaamub Boroom bi laa. Na Yàlla def ci man li nga wax.»
38 Então disse Maria: Eis aqui a serva do Senhor. Faça-se em mim segundo a tua palavra. E o anjo afastou-se dela.
39 Ci jamono jooju Maryaama jóg, gaawantu dem ci benn dëkk bu nekkoon ca tund ya ca diiwaanu Yude.
39 Naqueles dias, Maria se levantou e foi às pressas às montanhas, a uma cidade de Judá.
40 Mu dugg ca kër Sakari, daldi nuyu Elisabet.
40 Entrou em casa de Zacarias e saudou Isabel.
41 Naka la Elisabet dégg Maryaama di nuyoo, doomam daldi yëngatu ci biiram. Noonu Xelum Yàlla mu Sell mi daldi solu Elisabet.
41 Ora, apenas Isabel ouviu a saudação de Maria, a criança estremeceu no seu seio; e Isabel ficou cheia do Espírito Santo.
42 Elisabet wax ca kaw ne: «Barkeel nañu la ci jigéen ñi, barkeel doom ji nga ëmb!
42 E exclamou em alta voz: Bendita és tu entre as mulheres e bendito é o fruto do teu ventre.
43 Man maay kan, ba ndeyu sama Boroom ñëw di ma seetsi?
43 Donde me vem esta honra de vir a mim a mãe de meu Senhor?
44 Maa ngi lay wax ne naka laa la dégg ngay nuyoo rekk, sama doom ji yëngu ci sama biir ndax mbég.
44 Pois assim que a voz de tua saudação chegou aos meus ouvidos, a criança estremeceu de alegria no meu seio.
45 Barke ñeel na la, yaw mi gëm ne li la Boroom bi yégal dina mat!»
45 Bem-aventurada és tu que creste, pois se hão de cumprir as coisas que da parte do Senhor te foram ditas!
46 Noonu Maryaama daldi ne:
46 E Maria disse: Minha alma glorifica ao Senhor,
47 «Sama xol a ngi màggal Boroom bi,
47 meu espírito exulta de alegria em Deus, meu Salvador,
48 ndaxte fàttaliku na ma,
48 porque olhou para sua pobre serva. Por isto, desde agora, me proclamarão bem-aventurada todas as gerações,
49 ndaxte Ku Màgg ki defal na ma lu réy.
49 porque realizou em mim maravilhas aquele que é poderoso e cujo nome é Santo.
50 Day wàcce yërmandeem ci ñi ko ragal,
50 Sua misericórdia se estende, de geração em geração, sobre os que o temem.
51 Wone na jëf yu mag ci dooley loxoom,
51 Manifestou o poder do seu braço: desconcertou os corações dos soberbos.
52 daaneel boroom doole yi ci seen nguur,
52 Derrubou do trono os poderosos e exaltou os humildes.
53 Ñi xiif, reggal na leen ak ñam wu neex,
53 Saciou de bens os indigentes e despediu de mãos vazias os ricos.
54 Wallu na bànni Israyil giy jaamam,
54 Acolheu a Israel, seu servo, lembrado da sua misericórdia,
55 ni mu ko dige woon sunuy maam,
55 conforme prometera a nossos pais, em favor de Abraão e sua posteridade, para sempre.
56 Noonu Maryaama toog fa Elisabet lu wara tollook ñetti weer, sooga ñibbi.
56 Maria ficou com Isabel cerca de três meses. Depois voltou para casa.
57 Gannaaw loolu jamono ji Elisabet wara mucc agsi, mu daldi jur doom ju góor.
57 Completando-se para Isabel o tempo de dar à luz, teve um filho.
58 Dëkkandoom yi ak bokkam yi yég ne, Boroom bi won na ko yërmande ju réy, ñu ànd ak moom bég.
58 Os seus vizinhos e parentes souberam que o Senhor lhe manifestara a sua misericórdia, e congratulavam-se com ela.
59 Bi bés ba délsee, ñu ñëw xarafalsi xale ba, bëgg koo dippee baayam Sakari.
59 No oitavo dia, foram circuncidar o menino e o queriam chamar pelo nome de seu pai, Zacarias.
60 Waaye yaayam ne leen: «Déedéet, Yaxya lay tudd.»
60 Mas sua mãe interveio: Não, disse ela, ele se chamará João.
61 Ñu ne ko: «Amoo menn mbokk mu tudd noonu.»
61 Replicaram-lhe: Não há ninguém na tua família que se chame por este nome.
62 Ñu daldi liyaar baayam, ngir xam nan la bëgg ñu tudde xale ba.
62 E perguntavam por acenos ao seu pai como queria que se chamasse.
63 Sakari laaj àlluwa, bind ci ne: «Yaxya la tudd.» Ñépp daldi waaru.
63 Ele, pedindo uma tabuinha, escreveu nela as palavras: João é o seu nome. Todos ficaram pasmados.
64 Ca saa sa Yàlla dindi luu gi, Sakari daldi waxaat, di màggal Yàlla.
64 E logo se lhe abriu a boca e soltou-se-lhe a língua e ele falou, bendizendo a Deus.
65 Waa dëkk ba bépp jaaxle, xew-xew yooyu siiw ca tundi Yude yépp.
65 O temor apoderou-se de todos os seus vizinhos; o fato divulgou-se por todas as montanhas da Judéia.
66 Ñi dégg nettali, bi jëm ci mbir yooyu, dañu koo denc ci seen xol te naan: «Nu xale bii di mujje nag?» Ndaxte leeroon na ne dooley Boroom baa ngi ànd ak moom.
66 Todos os que o ouviam conservavam-no no coração, dizendo: Que será este menino? Porque a mão do Senhor estava com ele.
67 Sakari baayu Yaxya daldi fees ak Xel mu Sell mi. Noonu mu wax ci kàddug Yàlla ne:
67 Zacarias, seu pai, ficou cheio do Espírito Santo e profetizou, nestes termos:
68 «Cant ñeel na Boroom bi, Yàllay Israyil,
68 Bendito seja o Senhor, Deus de Israel, porque visitou e resgatou o seu povo,
69 Feeñal na nu Musalkat bu am doole,
69 e suscitou-nos um poderoso Salvador, na casa de Davi, seu servo
70 ni mu yéglee woon bu yàgg jaarale ko ci yonentam yu sell yi.
70 {como havia anunciado, desde os primeiros tempos, mediante os seus santos profetas},
71 Dina nu musal ci sunuy noon,
71 para nos livrar dos nossos inimigos e das mãos de todos os que nos odeiam.
72 Yàlla wone na yërmandeem, ji mu digoon sunuy maam,
72 Assim exerce a sua misericórdia com nossos pais, e se recorda de sua santa aliança,
73 di ngiñ, li mu giñaloon sunu maam Ibraayma naan,
73 segundo o juramento que fez a nosso pai Abraão: de nos conceder que, sem temor,
74 dina nu teqale ak sunuy noon,
74 libertados de mãos inimigas, possamos servi-lo
75 nu sell te jub ci kanamam sunu giiru dund.
75 em santidade e justiça, em sua presença, todos os dias da nossa vida.
76 Yaw nag doom, dinañu lay wooye yonentu Aji Kawe ji,
76 E tu, menino, serás chamado profeta do Altíssimo, porque precederás o Senhor e lhe prepararás o caminho,
77 Dinga xamal mbooloom ni leen Boroom bi mana musale,
77 para dar ao seu povo conhecer a salvação, pelo perdão dos pecados.
78 ndaxte Yàlla sunu Boroom fees na ak yërmande,
78 Graças à ternura e misericórdia de nosso Deus, que nos vai trazer do alto a visita do Sol nascente,
79 ngir leeral ñi toog ci lëndëm,
79 que há de iluminar os que jazem nas trevas e na sombra da morte e dirigir os nossos passos no caminho da paz.
80 Noonu Yaxyaa ngi doon màgg, te xelam di ubbiku. Mu dëkk ca màndiŋ ma, ba bés ba muy feeñu bànni Israyil.
80 O menino foi crescendo e fortificava-se em espírito, e viveu nos desertos até o dia em que se apresentou diante de Israel.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Lucas 1, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.