Lucas 14
Téereb Injiil (WOL2010) vs NAA
1 Benn bésub noflaay Yeesu dem ci këru benn kilifag Farisen yi, ngir lekke fa. Nit ñaa ngi ko doon xool bu baax.
1 Num sábado, ao entrar Jesus na casa de um dos principais fariseus para tomar uma refeição, eles o estavam observando.
2 Faf am ca kanamam nit ku feebaroon, ay tànkam newi.
2 E eis que diante dele se achava um homem hidrópico.
3 Yeesu yékkati baatam, ne xutbakat ya ak Farisen ya: «Ndax jaadu na, nu faj ci bésub noflaay bi?»
3 Então Jesus, dirigindo-se aos intérpretes da Lei e aos fariseus, perguntou:
4 Waaye ñépp ne cell. Yeesu daldi laal jarag ja, faj ko, ba noppi ne ko mu ñibbi.
4 Eles, porém, não disseram nada. Então Jesus pegou na mão daquele homem, curou-o e o mandou embora.
5 Gannaaw loolu mu ne leen: «Ku sa doom walla sa yëkk daanu ci teen, ndax doo dem génneji ko ca saa sa, fekk sax bésub noflaay la?»
5 A seguir, Jesus lhes perguntou:
6 Amuñu woon dara lu ñu ciy teg.
6 A isto nada puderam responder.
7 Yeesu gis ni gan yi doon tànne toogu yu yiw yi, mu daldi leen wax léeb wii:
7 Reparando como os convidados escolhiam os primeiros lugares, Jesus contou-lhes uma parábola:
8 «Bu ñu la wooyee ci xewu céet, bul jël toogu bu yiw. Man na am woo nañu it nit ku la ëpp daraja.
8 — Quando alguém convidá-lo para um casamento, não sente no lugar de honra, pois pode haver um convidado mais importante do que você.
9 Kon ki leen woo yéen ñaar ñépp man na ñëw ci yaw ne la: “Joxal toogu bi nit kii.” Noonu dinga rusa dem ca toogu bu gannaawe ba.
9 Então aquele que convidou os dois dirá a você: “Dê o lugar a este aqui.” Então você irá, envergonhado, ocupar o último lugar.
10 Waaye bu ñu la wooyee, demal ca toogu bu gannaawe ba. Bu ko defee ki la woo, bu agsee ne la: “Sama xarit, àggal ca kaw.” Loolu dina la sagal ci ñi nga toogandool ci lekkukaay bi.
10 Pelo contrário, quando alguém convidá-lo, vá sentar no último lugar, para que, quando vier aquele que o convidou, diga a você: “Amigo, venha sentar num lugar melhor.” Isso será uma honra para você diante de todos os demais convidados.
11 Ndaxte képp kuy yékkatiku dees na la suufeel, te kuy suufeelu, ñu yékkati la.»
11 Porque todo o que se exalta será humilhado; e o que se humilha será exaltado.
12 Noonu Yeesu ne ki ko woo woon lekk: «Boo dee woote añ walla reer, bul woo rekk say xarit, say doomi ndey, say bokk, walla say dëkkandoo yu am alal. Lu ko moy ñooñu itam dinañu la woo, fey la bor bi.
12 Depois Jesus disse ao que o havia convidado:
13 Waaye boo dee woote lekk, wool néew doole yi, làggi yi, lafañ yi ak gumba yi.
13 Pelo contrário, ao dar um banquete, convide os pobres, os aleijados, os coxos e os cegos,
14 Soo ko defee, dinga barkeel, ndaxte duñu la ko mana fey, waaye dinga jot sag pey, bés bi ñi jub di dekki.»
14 e você será bem-aventurado, pelo fato de não terem eles com que recompensá-lo. A sua recompensa você receberá na ressurreição dos justos.
15 Bi mu déggee wax yooyu, kenn ca gan ya ne Yeesu: «Kiy lekk ci ñam, yi Yàlla di joxe ci nguuram, barkeel nga!»
15 Ao ouvir tais palavras, um dos que estavam à mesa com Jesus lhe disse: — Bem-aventurado aquele que participar do banquete no Reino de Deus.
16 Yeesu ne ko: «Dafa amoon nit ku togglu ay ñam, woo ay nit ñu bare.
16 Jesus, porém, respondeu:
17 Bi waxtuw lekk jotee mu yónni surga ca ña muy ganale, fàttali leen: “Man ngeena ñëw, ndaxte lépp sotti na léegi.”
17 À hora da ceia, enviou o seu servo para avisar aos convidados: “Venham, porque tudo já está preparado.”
18 «Waaye ñu tàmbali di jégglu ci ngan gi ñoom ñépp. Ku jëkk ka ne ko: “Damaa jënd tool léegi, te fàww ma dem seeti ko. Maa ngi lay ñaan, nga jéggal ma.”
18 Mas todos eles, um por um, começaram a apresentar desculpas. O primeiro disse: “Comprei um campo e preciso ir vê-lo; peço que me desculpe.”
19 Keneen ne: “Damaa jënd léegi fukki yëkk, te damay dem nii, jéem leena beyloo ba xam. Maa ngi lay ñaan, nga jéggal ma.”
19 Outro disse: “Comprei cinco juntas de bois e vou experimentá-las; peço que me desculpe.”
20 Keneen ne ko: “Damay sooga takk jabar, looloo tax duma mana ñëw.”
20 E outro disse: “Casei-me e, por isso, não posso ir.”
21 «Surga ba dellu ca njaatigeem nettali ko loolu lépp. Noonu boroom kër ga mer, daldi ne surga ba: “Demal gaaw ca pénc ya ak ca mbedd ya ca dëkk ba, te indil ma fii néew doole yi, ñu làggi ñi, gumba yi ak lafañ yi.”
21 — O servo voltou e, contou tudo ao seu senhor. Então, irado, o dono da casa disse ao seu servo: “Saia depressa para as ruas e becos da cidade e traga para cá os pobres, os aleijados, os cegos e os coxos.”
22 «Surga ba ñëwaat ne ko: “Sang bi, def naa li nga ma sant, waaye bérab bi feesul.”
22 Mais tarde, o servo lhe disse: “Patrão, já fiz o que o senhor mandou, e ainda há lugar.”
23 Noonu njaatige ba ne ko: “Génnal dëkk bi te dem ca yoon ya ak ca tool ya, xiir nit ñi, ñu duggsi, ngir sama kër fees.
23 Então o senhor disse ao servo: “Saia pelos caminhos e atalhos e obrigue todos a entrar, para que a minha casa fique cheia.
24 Maa ngi leen koy wax, ci ñi ma woo woon ci sama reer bi, kenn du ci ñam.”»
24 Porque digo a vocês que nenhum daqueles homens que foram convidados provará a minha ceia.”
25 Am mbooloo yu réy yu toppoon ci Yeesu, ba muy dem ca yoon wa. Mu geestu ne leen:
25 Grandes multidões acompanhavam Jesus, e ele, voltando-se, lhes disse:
26 «Képp ku ñëw ci man te gënalu ma ko baayam, yaayam, soxnaam, ay doomam, ay magam ak ay rakkam, walla sax bakkanam, du mana nekk sama taalibe.
26 — Se alguém vem a mim e não me ama mais do que ama o seu pai, a sua mãe, a sua mulher, os seus filhos, os seus irmãos, as suas irmãs e até a sua própria vida, não pode ser meu discípulo.
27 Képp koo xam ne nanguwuloo ñàkk sa bakkan, ba mel ni ku ñu daaj ci bant, te nga topp ma, doo mana nekk sama taalibe.
27 E quem não tomar a sua cruz e vier após mim não pode ser meu discípulo.
28 Su kenn ci yéen bëggee tabax taaxum kaw, ndax du jëkka toog, xalaat ñaata la ko wara dikke, ngir seet ba xam ndax am na xaalis bu mana àggale liggéey bi?
28 Pois qual de vocês, pretendendo construir uma torre, não se assenta primeiro para calcular a despesa e verificar se tem os meios para a concluir?
29 Lu ko moy, su yékkatee fondamaa bi te manu koo àggale, ñi koy gis dinañu ko ñaawal, naan ko:
29 Para não acontecer que, tendo lançado os alicerces e não podendo terminar a construção, todos os que a virem zombem dele,
30 “Waa jii dafa tàmbalee tabax, waaye manu koo àggale.”
30 dizendo: “Este homem começou a construir e não pôde acabar.”
31 Walla boog ban buur mooy dugg ci xare ak beneen buur te jëkkula toog, seet ba xam moom ak fukki junniy xarekat man na xeex ak kiy ñëw ak ñaar fukki junniy xarekat?
31 Ou qual é o rei que, indo para combater outro rei, não se assenta primeiro para calcular se com dez mil homens poderá enfrentar o que vem contra ele com vinte mil?
32 Su ko manul, dafay yónni ndaw ca beneen buur ba, fi ak ma ngay sore, ngir ñu juboo.
32 Caso contrário, estando o outro ainda longe, envia-lhe uma embaixada, pedindo condições de paz.
33 Naka noonu itam ku nekk ci yéen, bu dëdduwul li mu am lépp, du mana nekk sama taalibe.
33 Assim, pois, qualquer um de vocês que não renuncia a tudo o que tem não pode ser meu discípulo.
34 «Xam ngeen nag ne xorom lu baax la, waaye bu sàppee, nan lañu koy delloo cafkaam?
34 — O sal é certamente bom; mas, se o sal se tornar insípido, como lhe restaurar o sabor?
35 Du jariñ suuf, te du nekk tos. Dañu koy sànni ca biti. Déglul bu baax, yaw mi am ay nopp.»
35 Não presta mais nem para a terra nem para o monte de estrume; lançam-no fora. Quem tem ouvidos para ouvir, ouça.
Atalhos do teclado
- Capítulo anterior←
- Próximo capítulo→
- Versículo anteriork
- Próximo versículoj
- Limpar seleçãoEsc
- Esta ajuda?
Estude este capítulo no WhatsApp
Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Lucas 14, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.