Lucas 13

Téereb Injiil (WOL2010) vs NAA

Sair da comparação
NAA Nova Almeida Atualizada 2017
1 Ca jamono jooju ay nit ñëw ca Yeesu, nettali mbirum waa Galile, ya Pilaat reylu woon, jaxase seen deret ak dereti mala, yi ñu rendi woon, jébbal leen Yàlla.
1 Naquela mesma ocasião, estavam ali algumas pessoas que falaram para Jesus a respeito dos galileus cujo sangue Pilatos havia misturado com os sacrifícios que os mesmos realizavam.
2 Mu ne leen: «Mbaa du dangeena xalaat ne, waa Galile yooyu dañoo gëna nekk bàkkaarkat ña ca des, ndax coono bi ñu daj?
2 Então Jesus lhes disse:
3 Maa ngi leen di wax ne du dëgg. Waaye su ngeen tuubul seeni bàkkaar, dingeen sànku noonu, yéen ñépp itam.
3 Digo a vocês que não eram; se, porém, não se arrependerem, todos vocês também perecerão.
4 Te fukki nit ak juróom ñett ñooñu dee, bi taaxum kaw ma ca goxu Silowe daanoo ci seen kaw, ndax dangeena yaakaar ne ñoo gëna nekk ay tooñkat ñeneen ñi dëkk Yerusalem yépp?
4 E, quanto àqueles dezoito sobre os quais desabou a torre de Siloé e os matou, vocês pensam que eles eram mais culpados do que todos os outros moradores de Jerusalém?
5 Maa ngi leen di wax ne du dëgg. Waaye su ngeen tuubul seeni bàkkaar, dingeen sànku noonu, yéen ñépp itam.»
5 Digo a vocês que não eram; mas, se não se arrependerem, todos vocês também perecerão.
6 Noonu mu daldi leen wax léeb wii: «Nit amoon na ci toolam garab gu ñu naan figg. Benn bés mu ñëw di ko raas-si, fekku fa benn doom.
6 E Jesus contou a seguinte parábola:
7 Noonu mu ne surga ba: “Ñetti at a ngii may ñëw di raas-si garab gii te duma ci fekk dara. Gor ko. Lu tax muy xatal tool bi?”
7 Então disse ao homem que cuidava da vinha: “Já faz três anos que venho procurar fruto nesta figueira e não encontro nada. Portanto, corte-a! Por que ela ainda está ocupando inutilmente a terra?”
8 Surga ba ne ko: “Sang bi, bàyyiwaat ko fi at mii. Dinaa wàqi taat wi, def ci tos.
8 Mas o homem que cuidava da vinha respondeu: “Senhor, deixe-a ainda este ano, até que eu escave ao redor dela e ponha estrume.
9 Xëy na dina meññi. Bu ko deful, nga gor ko.”»
9 Se vier a dar fruto, muito bem. Se não der fruto, o senhor poderá cortá-la.”
10 Benn bésub noflaay Yeesoo ngi doon jàngle ci ab jàngu.
10 Num sábado, Jesus estava ensinando numa das sinagogas.
11 Amoon na fa jigéen ju rab jàppoon, ba feebarloo ko lu wara mat fukki at ak juróom ñett; dafa xuuge woon te manul woona siggi dara.
11 E chegou ali uma mulher possuída de um espírito de enfermidade, havia já dezoito anos; ela andava encurvada, sem poder se endireitar de modo nenhum.
12 Bi ko Yeesu gisee, mu woo ko ne ko: «Soxna si, sa feebar deñ na.»
12 Ao vê-la, Jesus a chamou e lhe disse:
13 Noonu mu teg ko ay loxoom, soxna sa siggi ca saa sa, di màggal Yàlla.
13 E, impondo-lhe as mãos, ela imediatamente se endireitou e dava glória a Deus.
14 Waaye njiitu jàngu ba mer, ndax li Yeesu fajoon nit ca bésub noflaay ba, mu ne mbooloo ma: «Am na juróom benni fan yu nit ñi wara liggéey. Kon war ngeena ñëw faju ci bés yooyu, waaye du ci bésub noflaay bi.»
14 O chefe da sinagoga, indignado por ver que Jesus curava no sábado, disse à multidão: — Há seis dias em que se deve trabalhar. Venham nesses dias para serem curados, mas não no sábado.
15 Boroom bi ne ko: «Naaféq yi! Ndax bésub noflaay bi, kenn ku nekk ci yéen du yiwee ca gétt ga yëkkam walla mbaamam ngir wëggi ko?
15 Porém o Senhor lhe respondeu:
16 Jigéen jii nag bokk ci askanu Ibraayma te Seytaane tënk ko fukki at ak juróom ñett, ndax kenn waru koo yiwi ci bésub noflaay bi?»
16 Por que motivo não se devia livrar deste cativeiro, em dia de sábado, esta filha de Abraão, a quem Satanás trazia presa há dezoito anos?
17 Naka la wax loolu, noonam yépp daldi rus, waaye mbooloo mi di bég ci jëf yu yéeme, yi mu doon def yépp.
17 Tendo Jesus dito estas palavras, todos os seus adversários ficaram envergonhados. Entretanto, o povo se alegrava por todos os feitos gloriosos que Jesus realizava.
18 Noonu Yeesu neeti: «Lan la nguuru Yàlla di nirool? Lan laa ko mana méngaleel?
18 Jesus disse:
19 Mi ngi mel ni doomu fuddën gu nit jël, ji ko ci toolam. Mu sax, nekk garab, ba picci asamaan ñëw, tàgg ciy caram.»
19 É semelhante a um grão de mostarda, que um homem plantou na sua horta; e cresceu e fez-se árvore; e as aves do céu se aninharam nos seus ramos.
20 Mu neeti: «Lan laa mana méngaleek nguuru Yàlla?
20 Disse mais:
21 Mi ngi mel ni lawiir bu jigéen jël, jaxase ko ak ñetti andaari fariñ, ba kera tooyal bépp di funki.»
21 É semelhante ao fermento que uma mulher pegou e misturou em três medidas de farinha, até ficar tudo levedado.
22 Yeesoo ngi doon jaar ci ay dëkk yu mag ak yu ndaw, di jàngle te jublu Yerusalem.
22 Jesus passava por cidades e aldeias, ensinando e caminhando para Jerusalém.
23 Am ku ko ne: «Boroom bi, ndax ñiy mucc ñu néew lay doon?» Yeesu ne leen:
23 E alguém lhe perguntou: — Senhor, são poucos os que são salvos?
24 «Defleen seen kem kàttan, ngir dugg ci bunt bu xat bi, ndaxte maa ngi leen koy wax, ñu bare dinañu jéema dugg, waaye duñu ko man.
24 Jesus respondeu:
25 Jamono dina ñëw, ju boroom kër gi di jóg, tëj buntam. Dingeen nekk ci biti di fëgg naan: “Boroom bi, ubbil nu!” Mu ne leen: “Xawma fu ngeen bokk.”
25 Quando o dono da casa se tiver levantado e fechado a porta, e vocês, do lado de fora, começarem a bater, dizendo: “Senhor, abra a porta para nós”, ele responderá: “Não sei de onde vocês são.”
26 Bu ko defee ngeen naan: “Noo doon bokk di lekk ak a naan, te jàngle nga ci sunuy pénc.”
26 Então vocês dirão: “Comíamos e bebíamos com o senhor. Além disso, o senhor ensinava em nossas ruas.”
27 Mu ne leen: “Nee naa leen xawma fu ngeen bokk. Yéen ñépp soreleen ma, defkati lu bon yi!”
27 Mas ele dirá a vocês: “Não sei de onde vocês são; afastem-se de mim, vocês todos que praticam o mal.”
28 Foofa dingeen jooy, di yéyu, bu ngeen gisee seeni maam Ibraayma, Isaaxa, Yanqóoba ak yonent yépp ci nguuru Yàlla, te ñu dàq leen ca biti.
28 Ali haverá choro e ranger de dentes, quando vocês virem Abraão, Isaque, Jacó e todos os profetas no Reino de Deus, mas vocês lançados fora.
29 Ay nit dinañu jóge penku ak sowu, nor ak sudd, ñëw, bokk lekk ci ñam, yi Yàlla di joxe ci nguuram.
29 Muitos virão do Oriente e do Ocidente, do Norte e do Sul e tomarão lugar à mesa no Reino de Deus.
30 Noonu ñenn ci ñi mujj ñooy jiituji; te ci ñi jiitu, ñooy mujji.»
30 Porém, de fato, há últimos que serão primeiros, e primeiros que serão últimos.
31 Ca jamono jooja ay Farisen ñëw ca Yeesu ne ko: «Jógeel fii, dem feneen, ndaxte Erodd a ngi lay wuta rey.»
31 Naquela mesma hora, alguns fariseus vieram para dizer a Jesus: — Vá embora daqui, porque Herodes quer matá-lo.
32 Noonu mu ne leen: «Demleen ne bukki boobu ne ko: “Xoolal, maa ngi dàq rab yi tey wéral nit ñi tey ak suba. Ca ñetteelu fan ba, ma àgg fa ma Yàlla jëmale.”
32 Ele, porém, lhes respondeu:
33 Waaye fàww ma dox sama itte tey, suba ak gannaaw suba, ndaxte wareesula reye ab yonent feneen fu dul Yerusalem.
33 Porém, preciso caminhar hoje, amanhã e depois, porque não se espera que um profeta morra fora de Jerusalém.
34 «Yerusalem, Yerusalem, yaw miy rey yonent yi, tey sànni ay doj ndaw yi, ba ñu dee, aka maa bëggoona dajale say doom, ni ginaar di uufe ay cuujam te nanguwuleen!
34 — Jerusalém, Jerusalém! Você mata os profetas e apedreja os que lhe são enviados! Quantas vezes eu quis reunir os seus filhos, como a galinha ajunta os do seu próprio ninho debaixo das asas, mas vocês não quiseram!
35 Kon nag Yàlla dina bërgël seen kër. Te maa ngi leen koy wax, dungeen ma gisati, ba kera ngeen ne: “Yaw miy ñëw ci turu Boroom bi, ku barkeel nga!”»
35 Eis que a casa de vocês ficará deserta. E eu afirmo a vocês que não me verão mais, até que venham a dizer: “Bendito o que vem em nome do Senhor!”

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Lucas 13, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.