João 7
Téereb Injiil (WOL2010) vs NAA
1 Gannaaw loolu Yeesu doon na wër diiwaanu Galile.
1 Passadas essas coisas, Jesus andava pela Galileia, porque não desejava andar pela Judeia, visto que os judeus queriam matá-lo.
2 Bëggul woona dem diiwaanu Yude, ndaxte Yawut ya dañu ko doon wuta rey.
2 E a festa dos judeus, chamada de Festa dos Tabernáculos, estava próxima.
3 Noonu rakki Yeesu yu góor ya ne ko: «Jóge fi te dem diiwaanu Yude, ngir say taalibe gis, ñoom itam, jaloore yi ngay def.
3 Então os irmãos de Jesus se dirigiram a ele e disseram: — Deixe este lugar e vá para a Judeia, para que também os seus discípulos vejam as obras que você faz.
4 Ku bëgga siiw, doo nëbb say jëf. Boo demee bay wone jaloore yu mel ni, fexeel ba ñépp gis la.»
4 Porque, se alguém quer ser conhecido, não pode realizar os seus feitos em segredo. Já que você faz essas coisas, manifeste-se ao mundo.
5 Rakkam yi dañu doon wax loolu, ndaxte ñoom itam gëmuñu ko woon.
5 Acontece que nem mesmo os irmãos de Jesus criam nele.
6 Yeesu ne leen: «Sama waxtu jotagul. Ci yéen nag, waxtu yépp a baax.
6 Então Jesus lhes disse:
7 Àddina du leen bañ waaye bañ na ma, man, ndaxte maa wax ne seeni jëf baaxul.
7 O mundo não pode odiar vocês, mas a mim ele odeia, porque eu dou testemunho a respeito dele, dizendo que as suas obras são más.
8 Yéen nag demleen màggal ga. Demaguma màggal googu, ndaxte sama waxtu jotagul.»
8 Vão vocês para a festa. Eu não vou, porque o meu tempo ainda não se cumpriu.
9 Bi mu leen waxee loolu ba noppi, moom mu des Galile.
9 Tendo dito isso, Jesus continuou na Galileia.
10 Bi rakkam ya demee ca màggal ga, Yeesu itam sooga dem te kenn yégu ko; siiwalul demam.
10 Depois que seus irmãos tinham ido à festa, Jesus também foi, não publicamente, mas em segredo.
11 Fekk Yawut yaa nga ko doon seet ca màggal ga te naan: «Ana waa ji?»
11 Ora, os judeus o procuravam na festa e perguntavam: — Onde estará ele?
12 Ca biir mbooloo ma ñu ngi doon déeyante, di wax ci ay mbiram. Ñii naan: «Nit ku baax la.» Ñee naan: «Déedéet, day nax nit ñi.»
12 E havia grande murmuração a respeito de Jesus entre as multidões. Uns diziam: — Ele é bom. E outros afirmavam: — Não, não é! Ele engana o povo.
13 Waaye kenn ñemewu koo tudd ca kaw, ndaxte dañoo ragaloon Yawut ya.
13 Entretanto, ninguém falava dele abertamente, por ter medo dos judeus.
14 Bi ñu demee ba ca diggu màggal ga, Yeesu dem di jàngle ca kër Yàlla ga.
14 Quando a festa já estava na metade, Jesus foi ao templo e começou a ensinar.
15 Yawut ya nag jaaxle, daldi ne: «Nu waa jii def ba xam lii lépp, moom mi jàngul?»
15 Então os judeus se maravilhavam e diziam: — Como é que ele pode ser letrado, se não chegou a estudar?
16 Yeesu daldi leen wax ne: «Li may jàngle, jógewul ci man, waaye ci ki ma yónni la jóge.
16 Jesus lhes respondeu:
17 Ku fas yéenee wéy ci bëgg-bëggu Yàlla, dina xam ndax sama njàngle ci Yàlla la jóge, walla ci sama coobare.
17 Se alguém quiser fazer a vontade de Deus, conhecerá a respeito da doutrina, se ela é de Deus ou se eu falo por mim mesmo.
18 Nit kiy wax ci coobareem nag, day wuta màggal boppam, waaye kiy wuta màggal ki ko yónni, dëgg rekk lay wax te jubadiwul fenn.
18 Quem fala por si mesmo está buscando a sua própria glória; mas o que busca a glória de quem o enviou, esse é verdadeiro, e nele não há falsidade.
19 Xanaa du Musaa moo leen jox ndigali Yàlla yi? Waaye kenn ci yéen sàmmu ko! Lu tax ngeen bëgg maa rey?»
19 Não é fato que Moisés deu a Lei para vocês? Contudo, nenhum de vocês a cumpre. Por que estão querendo me matar?
20 Mbooloo ma ne ko: «Xanaa dangaa am ay rab! Ku lay wuta rey?»
20 A multidão respondeu: — Você tem demônio. Quem é que está querendo matá-lo?
21 Yeesu ne leen: «Benn jaloore rekk laa def, te yéen ñépp ngeen jaaxle!
21 Jesus respondeu:
22 Li leen Musaa jox ndigalu xarafal gone yi —jógewul kat ci Musaa; mi ngi tàmbalee ci seen maami cosaan— moo tax ba ngeen nangoo xarafal nit ci bésub noflaay bi.
22 Moisés lhes deu a circuncisão — se bem que ela não vem de Moisés, mas dos patriarcas —, e vocês fazem a circuncisão de um menino até mesmo no sábado.
23 Bu ngeen manee xarafal nit ci bésub noflaay bi, ngir baña wàcc yoonu Musaa, lu tax nag ngeen mere ma, ndax li ma ci wéral nitu lëmm?
23 E, se um menino pode ser circuncidado em dia de sábado, para que a Lei de Moisés não seja desrespeitada, por que vocês ficam indignados contra mim, pelo fato de eu ter curado por completo um homem num sábado?
24 Bàyyileen di àtte ci ni ngeen di gise, te di àtte dëgg.»
24 Não julguem segundo a aparência, mas julguem pela reta justiça.
25 Am na ci waa Yerusalem ñu doon wax naan: «Xanaa du nit kii lañuy wuta rey?
25 Alguns de Jerusalém diziam: — Não é este o homem que estão querendo matar?
26 Xool-leen, mi ngi waaraate ci biir nit ñi, te kenn du ko wax dara. Ndax sunu kilifa yi dañoo xam ne mooy Almasi bi?
26 Eis que ele fala abertamente, e ninguém lhe diz nada. Será que as autoridades reconhecem de fato que este é o Cristo?
27 Waaye waa ji, xam nanu fu mu jóge, te saa su Almasi bi dee dikk, kenn du xam fu mu bàyyikoo.»
27 Mas nós sabemos de onde este homem vem. Quando, porém, o Cristo vier, ninguém saberá de onde ele é.
28 Yeesu di jàngle ca kër Yàlla ga, daldi wax ca kaw ne: «Ndax xam ngeen ma te xam fi ma jóge? Ñëwaluma sama bopp, waaye ki ma yónni, ku wóor la. Yéen xamuleen ko.
28 Enquanto ensinava no templo, Jesus disse em voz alta:
29 Man xam naa ko, ndaxte ca moom laa jóge, te itam moo ma yónni.»
29 Eu o conheço, porque venho da parte dele e ele me enviou.
30 Noonu ñu koy wuta jàpp, waaye kenn manalu ko woon dara, ndaxte waxtoom jotagul woon.
30 Então quiseram prendê-lo, mas ninguém lhe pôs as mãos, porque a sua hora ainda não havia chegado.
31 Moona nag, ñu bare ca mbooloo ma gëm nañu ko. Ñu nga naan: «Ndax bés bu Almasi bi dikkee, ay firndeem dina ëpp yu nit kii?»
31 Porém muitos dentre a multidão creram nele e diziam: — Quando o Cristo vier, será que vai fazer maiores sinais do que este homem tem feito?
32 Farisen ya daldi dégg la mbooloo ma doon déeyante ci mbirum Yeesu. Sarxalkat yu mag ya ak Farisen ya yebal ay alkaati yu daan wottu kër Yàlla ga, ngir ñu jàppi ko.
32 Os fariseus, ouvindo a multidão murmurar essas coisas a respeito de Jesus, juntamente com os principais sacerdotes enviaram guardas para o prender.
33 Yeesu wax ne: «Dinaa nekk ak yéen fi ak ab diir, sooga dem ci ki ma yónni.
33 Jesus disse:
34 Dingeen ma seet, waaye dungeen ma gis; te dungeen mana dem fa may nekk.»
34 Vocês irão me procurar, mas não me acharão; vocês também não podem ir para onde eu estou.
35 Yawut ya di laajante ci seen biir naan: «Fu muy dem fu nu ko dul fekk? Mbaa du dafa nara dem ca Yawut, ya gàddaaye ca Gereg ya, te jàngali Gereg ya?
35 Então os judeus disseram uns aos outros: — Para onde ele irá que não o possamos achar? Será que pretende ir para a diáspora entre os gregos, a fim de ensinar os gregos?
36 Lan la baat yii mu wax di tekki: “Dingeen ma seet waaye dungeen ma gis,” ak: “Dungeen mana dem fa may nekk”?»
36 Que significa isso que ele diz: “Vocês irão me procurar, mas não me acharão; vocês também não podem ir para onde eu estou?”
37 — ausente —
37 No último dia, o grande dia da festa, Jesus se levantou e disse em voz alta:
38 — ausente —
38 Quem crer em mim, como diz a Escritura, do seu interior fluirão rios de água viva.
39 Booba li ko taxoon di wax mooy Xelu Yàlla, mi ñi ko gëm naroona jot. Fekk na joxeeguñu woon Xelu Yàlla mi, ndaxte ndamu Yeesu feeñagul woon.
39 Isso ele disse a respeito do Espírito que os que nele cressem haviam de receber; pois o Espírito até aquele momento não tinha sido dado, porque Jesus ainda não havia sido glorificado.
40 Bi ñu déggee wax jooja, am ay nit ca mbooloo ma ñu naan: «Dëgg-dëgg kii mooy Yonent bi wara ñëw.»
40 Quando ouviram essas palavras, alguns do meio do povo diziam: — Este é verdadeiramente o profeta.
41 Ñeneen naan: «Mooy Almasi bi.» Ña ca des it ne: «Waaye nan la Almasi bi mana jógee Galile?
41 Outros diziam: — Ele é o Cristo. Outros, porém, perguntavam: — Por acaso o Cristo virá da Galileia?
42 Mbind mi wax na ne, Almasi bi ci xeetu Daawuda lay wàcce te Betleyem, dëkku Daawuda, lay jóge.»
42 Não diz a Escritura que o Cristo vem da descendência de Davi e da aldeia de Belém, de onde era Davi?
43 Noonu féewaloo daldi am ca biir mbooloo ma ndax Yeesu.
43 Assim, houve divisão entre o povo por causa dele.
44 Am na ca ñoom ñu ko bëggoona jàpp, waaye kenn manalu ko woon dara.
44 Alguns queriam prendê-lo, mas ninguém lhe pôs as mãos.
45 Bi alkaati ya delloo, sarxalkat yu mag ya ak Farisen ya laaj leen ne: «Lu tax indiwuleen ko?»
45 Os guardas voltaram à presença dos principais sacerdotes e fariseus, e estes lhes perguntaram: — Por que vocês não o trouxeram?
46 Alkaati ya ne leen: «Kenn masula waxe ni nit kooku!»
46 Eles responderam: — Jamais alguém falou como este homem.
47 Noonu Farisen ya laaj leen: «Mbaa naxuñu leen, yéen itam?
47 Os fariseus disseram aos guardas: — Será que também vocês foram enganados?
48 Ndax am na kenn ci sarxalkat yi walla ci Farisen yi ku ko gëm? Déedéet.
48 Por acaso alguma das autoridades ou algum dos fariseus creu nele?
49 Waaye mbooloo mi xamuñu yoonu Musaa; ñu alku lañu!»
49 Mas esse povo que nada sabe da lei é maldito.
50 Nikodem bokkoon na ca Farisen ya fa nekkoon. Fekk moo seeti woon Yeesu lu jiitu. Mu ne leen:
50 Nicodemos, um deles, que antes tinha ido conversar com Jesus, perguntou-lhes:
51 «Ndax ci sunu yoon, man nañoo daan kenn te dégluwuñu ko, mbaa ñu xam lu mu def?»
51 — Será que a nossa lei condena um homem sem primeiro ouvi-lo e saber o que ele fez?
52 Ñu ne ko: «Mbaa du yaw itam dangaa bokk ci diiwaanu Galile? Gëstul, kon dinga xam ne benn yonent masula jóge Galile.»
52 Eles responderam: — Por acaso também você é da Galileia? Examine e verá que da Galileia não se levanta profeta.
53 Gannaaw loolu ku ci nekk dellu sa kër.
53 E cada um foi para a sua casa.
Atalhos do teclado
- Capítulo anterior←
- Próximo capítulo→
- Versículo anteriork
- Próximo versículoj
- Limpar seleçãoEsc
- Esta ajuda?
Estude este capítulo no WhatsApp
Peça à IA da Bíblia Fala para explicar João 7, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.