João 10
Téereb Injiil (WOL2010) vs NTLH
1 «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, ku jaar feneen fu dul ci buntu gétt gi, kooku sàcc la, saay-saay la.
1 Jesus disse:
2 Waaye ki jaar ci bunt bi, mooy sàmmu xar yi.
2 Mas quem entra pela porta é o pastor do rebanho.
3 Wottukat bi dina ko ubbil bunt bi, xar yiy dégg baatam. Xar yi mu moom nag, bu ci nekk dina la woo ci sa tur, ba noppi nga topp ko ci biti.
3 O porteiro abre a porta para ele. As ovelhas reconhecem a sua voz quando ele as chama pelo nome, e ele as leva para fora do curral.
4 Sàmm bi, bu génnee yi mu moom yépp, dina leen jiitu, ñu topp ko, ndaxte xam nañu baatam.
4 Quando todas estão do lado de fora, ele vai na frente delas, e elas o seguem porque conhecem a voz dele.
5 Waaye duñu topp jaambur; dañu koy daw, ndaxte miinuñu baatam.»
5 Mas de jeito nenhum seguirão um estranho! Pelo contrário, elas fugirão, pois não conhecem a voz de estranhos.
6 Yeesu misaaloon na leen loolu, waaye xamuñu lu mu leen doon wax.
6 Jesus fez esta comparação, mas ninguém entendeu o que ele queria dizer.
7 Noonu Yeesu newaat: «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, man maay buntu gétt gi.
7 Então Jesus continuou:
8 Ñi ma fi jiitu ñépp ay sàcc lañu, ak ay saay-saay; waaye xar yi dégluwuñu leen.
8 Todos os que vieram antes de mim são ladrões e bandidos, mas as ovelhas não deram atenção à voz deles.
9 Man maay bunt bi; ku jaar ci man, dinga mucc, dinga mana dugg ak a génn, dinga am it mbooy goo mana fore.
9 Eu sou a porta. Quem entrar por mim será salvo; poderá entrar e sair e achará comida.
10 Sàcc bi moom, day sàccsi rekk, di rey ak a yàq. Man damaa ñëw, ngir nit ñi am dund, ba nekk ci naataange.
10 O ladrão só vem para roubar, matar e destruir; mas eu vim para que as ovelhas tenham vida, a vida completa.
11 «Man maay sàmm bu baax bi. Sàmm bu baax bi day joxe bakkanam ngir ay xaram.
11 — Eu sou o bom pastor; o bom pastor dá a vida pelas ovelhas.
12 Ki dul sàmm bi tey liggéeyal xaalis rekk waaye moomul xar yi, bu séenee bukki, day daw, bàyyi fa xar ya. Bu ko defee bukki ba dal ca coggal ja, jàpp ca, tasaare ya ca des.
12 Um empregado trabalha somente por dinheiro; ele não é pastor, e as ovelhas não são dele. Por isso, quando vê um lobo chegando, ele abandona as ovelhas e foge. Então o lobo ataca e espalha as ovelhas.
13 Booba surga day daw, ndaxte xaalis rekk lay liggéeyal, faalewul xar ya.
13 O empregado foge porque trabalha somente por dinheiro e não se importa com as ovelhas. Eu sou o bom pastor. Assim como o Pai me conhece, e eu conheço o Pai, assim também conheço as minhas ovelhas, e elas me conhecem. E estou pronto para morrer por elas.
16 Am naa yeneen xar yu bokkul ci gétt gii. War naa leena indi, ñoom it, te dinañu déglu sama baat. Benn coggal ay am ak benn sàmm.
16 Tenho outras ovelhas que não estão neste curral. Eu preciso trazer essas também, e elas ouvirão a minha voz. Então elas se tornarão um só rebanho com um só pastor.
17 Baay bi bëgg na ma, ndaxte damay joxe sama bakkan ngir jëlaat ko.
17 — O Pai me ama porque eu dou a minha vida para recebê-la outra vez.
18 Kenn du ko jële ci man; maa koy joxe ci sama coobarey bopp. Am naa it sañ-sañu joxe ko te am naa sañ-sañu jëlaat ko. Loolu la ma sama Baay sant.»
18 Ninguém tira a minha vida de mim, mas eu a dou por minha própria vontade. Tenho o direito de dá-la e de tornar a recebê-la, pois foi isso o que o meu Pai me mandou fazer.
19 Kàddu yooyee ñoo féewalewaat Yawut yi.
19 Quando ouviu isso, o povo se dividiu outra vez. Muitos diziam:
20 Ñu bare ca ñoom naan: «Dafa ànd ak rab! Dafa dof! Lu tax ngeen koy déglu?»
20 — Ele está dominado por um demônio! Está louco! Por que é que vocês escutam o que ele diz?
21 Waaye ñeneen naan: «Nit ku am ay rab du waxe nii. Ndax rab man na ubbi bëti gumba?»
21 Outros afirmavam: — Quem está dominado por um demônio não fala assim! Será que um demônio pode dar vista aos cegos?
22 Am bés ñu doon màggal ca Yerusalem Bés ba ñu sellale woon kër Yàlla ga; ci jamonoy sedd la woon.
22 Era inverno, e em Jerusalém estavam comemorando a Festa da Dedicação .
23 Yeesoo nga woon ca kër Yàlla ga, di doxantu ca biir Werandaa bu Suleymaan.
23 Jesus estava andando pelo pátio do Templo, perto da entrada chamada “ Alpendre de Salomão ”.
24 Yawut ya wër ko ne ko: «Kañ nga nuy dindi ci kumpa? Boo dee Almasi bi, wax ko mu leer.»
24 Então o povo se ajuntou em volta dele e perguntou: — Até quando você vai nos deixar na dúvida? Diga com franqueza: você é ou não é o
25 Yeesu ne leen: «Wax naa leen ko ba noppi, waaye gëmuleen. Jëf yi may def ci sama turu Baay ñoo may seede.
25 Jesus respondeu:
26 Waaye gëmuleen ndaxte bokkuleen ci samay xar.
26 mas vocês não creem porque não são minhas ovelhas.
27 Samay xar dinañu dégg sama baat; xam naa leen te ñu ngi may topp.
27 As minhas ovelhas escutam a minha voz; eu as conheço, e elas me seguem.
28 Dama leen di jox dund gu dul jeex; duñu sànku mukk, te kenn du leen jële ci sama loxo.
28 Eu lhes dou a vida eterna, e por isso elas nunca morrerão. Ninguém poderá arrancá-las da minha mão.
29 Baay bi ma leen jox, moo gëna màgg lépp, te kenn manula jële dara ci loxob Baay bi.
29 O poder que o Pai me deu é maior do que tudo, e ninguém pode arrancá-las da mão dele.
30 Man ak Baay bi benn lanu.»
30 Eu e o Pai somos um.
31 Yawut ya daldi foraat ay xeer, bëgg koo sànni, ngir rey ko.
31 Então eles tornaram a pegar pedras para matar Jesus.
32 Noonu Yeesu ne leen: «Def naa ci seen kanam jëf yu baax yu bare ci ndigalu Baay bi. Ban ci jëf yooyu moo tax ba ngeen bëgg maa sànni ay doj?»
32 E ele disse:
33 Yawut ya ne ko: «Jëf ju baax taxul nu bëgg laa sànniy xeer, waaye dangay suufeel turu Yàlla; yaw, nit rekk nga, ba noppi di def sa bopp Yàlla!»
33 Eles responderam: — Não é por causa de nenhuma coisa boa que queremos matá-lo, mas porque, ao dizer isso, você está
34 Yeesu ne leen: «Bind nañu ci seen téereb yoon ne: “Yàlla nee na: Ay yàlla ngeen.”
34 Então Jesus afirmou:
35 Yàlla wooye na “ay yàlla” ñi mu yónnee kàddoom, te xam nanu ne kenn manula randal waxi Yàlla.
35 Sabemos que as
36 Kon nu ngeen mana waxe ne damay suufeel turu Yàlla ndax li ma ne Doomam laa, man mi Yàlla tànn, yónni ma ci àddina?
36 Quanto a mim, o Pai me escolheu e me enviou ao mundo. Então por que vocês dizem que blasfemo contra Deus quando afirmo que sou Filho dele?
37 Su ma deful sama jëfi Baay, buleen ma gëm;
37 Se não faço o que o meu Pai manda, não creiam em mim.
38 waaye su ma ko defee, bu ngeen ma gëmul sax, gëmleen boog samay jëf, ngir ngeen xam te nangu ne maa ngi nekk ci Baay bi te Baay bi nekk na ci man.»
38 Mas, se eu faço, e vocês não creem em mim, então creiam pelo menos nas coisas que faço. E isso para que vocês fiquem sabendo de uma vez por todas que o Pai vive em mim e que eu vivo no Pai.
39 Ñu di ko wuta jàppaat, waaye mu bàyyi leen fa, dem.
39 A essa altura tentaram novamente prendê-lo, mas Jesus escapou das mãos deles.
40 Yeesu génn, jàllaat dexu Yurdan, toog fa Yaxya daan sóobe ci ndox bu jëkk.
40 Ele voltou de novo para o lado leste do rio Jordão, foi para o lugar onde João Batista tinha batizado antes e ficou lá.
41 Nit ñu bare ñëw ci moom, te naan: «Yaxya deful benn kéemaan, waaye li mu wax ci kii yépp, dëgg la.»
41 E muita gente ia vê-lo, dizendo: — João não fez nenhum milagre, mas tudo o que ele disse sobre Jesus é verdade.
42 Noonu ñu bare gëm ko.
42 E naquele lugar muita gente creu em Jesus.
Atalhos do teclado
- Capítulo anterior←
- Próximo capítulo→
- Versículo anteriork
- Próximo versículoj
- Limpar seleçãoEsc
- Esta ajuda?
Estude este capítulo no WhatsApp
Peça à IA da Bíblia Fala para explicar João 10, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.