Judas 1

Téereb Injiil (WOL2010) vs ACF

Sair da comparação
ACF Almeida Corrigida Fiel
1 Man Yudd, jaamu Yeesu Kirist, mi bokk ak Saag ndey ak baay, maa leen di bind, yéen ñi Yàlla Baay bi woo te bëgg leen, te Yeesu Kirist aar leen.
1 Judas, servo de Jesus Cristo, e irmão de Tiago, aos chamados, santificados em Deus Pai, e conservados por Jesus Cristo:
2 Na leen Yàlla may yërmande, jàmm ak mbëggeel.
2 Misericórdia, e paz, e amor vos sejam multiplicados.
3 Samay bokk, bëggoon naa leena bind lool ci mbirum mucc gi nu bokk, waaye lii moo gëna jamp: ma xiir leen, ngeen taxaw ci aar mboolem dëgg, gi Yàlla xasa dénk gaayam yu sell yi ba fàww.
3 Amados, procurando eu escrever-vos com toda a diligência acerca da salvação comum, tive por necessidade escrever-vos, e exortar-vos a batalhar pela fé que uma vez foi dada aos santos.
4 Ndaxte am na ay nit ñu ñeme Yàlla, ñu yoxoosu ci seen biir; dañuy mbubboo yiwu Yàlla, ngir topp seen bakkan, di ci weddi Buur Yàlla miy kenn ak sunu Boroom Yeesu Kirist. Fekk Mbind mi tëral na seen àtte bu yàgg.
4 Porque se introduziram alguns, que já antes estavam escritos para este mesmo juízo, homens ímpios, que convertem em dissolução a graça de Deus, e negam a Deus, único dominador e Senhor nosso, Jesus Cristo.
5 Xam ngeen loolu lépp ba noppi sax, waaye dama leen koy fàttali rekk. Xam ngeen ne Boroom bi musal na xeetam, ba génne leen réewu Misra, waaye gannaaw ba raafal na ñi gëmul woon.
5 Mas quero lembrar-vos, como a quem já uma vez soube isto, que, havendo o Senhor salvo um povo, tirando-o da terra do Egito, destruiu depois os que não creram;
6 Te it malaaka ya jàppul woon ca daraja ja ñu amoon, xanaa toxoo fa ñu leen dëëloon, Yàlla yeew na leen buum yu sax, tëj leen ci biir lëndëm, di leen nége àtteb bés bu mag ba.
6 E aos anjos que não guardaram o seu principado, mas deixaram a sua própria habitação, reservou na escuridão e em prisões eternas até ao juízo daquele grande dia;
7 Noonu itam dëkki Sodom ak Gomor ak dëkk ya leen wëroon, dañoo sóobu ci njaaloo ak di def ay góor-jigéen, waaye àtte bi dal na ci seen kaw, ba ñuy ay tegtal ci ñiy yelloo sawara ba fàww.
7 Assim como Sodoma e Gomorra, e as cidades circunvizinhas, que, havendo-se entregue à fornicação como aqueles, e ido após outra carne, foram postas por exemplo, sofrendo a pena do fogo eterno.
8 Naka noonu itam géntkat yooyu may wax ñu ngi sobeel seen yaram, di weddi gépp kilifteef, di xas doole yi ci asamaan.
8 E, contudo, também estes, semelhantemente adormecidos, contaminam a sua carne, e rejeitam a dominação, e vituperam as dignidades.
9 Waaye bi Mikayel, miy kilifa ci malaaka yi, di xëccook Seytaane néewu Musaa, bay xuloo ak moom, ñemewu koo àtte, boole ciy xas; mu yem ci wax ko ne: «Na la Boroom bi mbugal!»
9 Mas o arcanjo Miguel, quando contendia com o diabo, e disputava a respeito do corpo de Moisés, não ousou pronunciar juízo de maldição contra ele; mas disse: O Senhor te repreenda.
10 Waaye nit ñii may wax, dañuy saaga li ñu xamul. Te li ñu xam ci tañaxu sax, ni bàyyima yu amul xel, dañu ci yàq seen bopp.
10 Estes, porém, dizem mal do que não sabem; e, naquilo que naturalmente conhecem, como animais irracionais se corrompem.
11 Ñookay torox! Dañoo jaar ci yoonu Kayin, sóobu ci réerug Balaam ngir xaalis, di bañ kilifteef ni Kore, te dinañu dee ni moom.
11 Ai deles! porque entraram pelo caminho de Caim, e foram levados pelo engano do prêmio de Balaão, e pereceram na contradição de Coré.
12 Su ñu bokkee ak yéen reeru mbooloo mi, dañu ciy indi ay, niy xeer yu nëbbu ci biir géej; amuñu genn gàcce, waaye dañuy giiroo te fonk seen biir rekk. Ñu ngi mel ni xiin yu amul ndox, yuy naaxsaay ci ngelaw; ni garab yu meññul ci jamonoy meññeef, te buddeeku, dee ba wow koŋŋ;
12 Estes são manchas em vossas festas de amor, banqueteando-se convosco, e apascentando-se a si mesmos sem temor; são nuvens sem água, levadas pelos ventos de uma para outra parte; são como árvores murchas, infrutíferas, duas vezes mortas, desarraigadas;
13 mel ni duusi géej gu mer, yuy gëq jëf yu ruslu; niy biddiiw yuy fàq, te Yàlla dencal na leen lëndëm ga gëna tar ba fàww.
13 Ondas impetuosas do mar, que escumam as suas mesmas abominações; estrelas errantes, para os quais está eternamente reservada a negrura das trevas.
14 Enog, di juróom ñaareelu maam gannaaw Aadama, waxoon na ci kàddug Yàlla, ba weer leen ne: «Boroom bi wàcce na ca asamaan, ànd ak ay junniy junniy malaakaam,
14 E destes profetizou também Enoque, o sétimo depois de Adão, dizendo: Eis que é vindo o Senhor com milhares de seus santos;
15 ngir àtte ñépp, te mbugal ñi weddi ñépp ndax ñaawteef, yi ñu jëf ci ñeme Yàlla; di leen fàttali it kàddu yu ñaaw, yi ñu ko tifaar ci seeni bàkkaar ak seen weddi.»
15 Para fazer juízo contra todos e condenar dentre eles todos os ímpios, por todas as suas obras de impiedade, que impiamente cometeram, e por todas as duras palavras que ímpios pecadores disseram contra ele.
16 Duñu noppee xultu, di jàmbat seen nekkin, tey topp seen nafsu; ay wax yu réy a ngi ball ci seen làmmiñ, waaye dañuy jay ñi ñuy yaakaare njariñ.
16 Estes são murmuradores, queixosos da sua sorte, andando segundo as suas concupiscências, e cuja boca diz coisas mui arrogantes, admirando as pessoas por causa do interesse.
17 Waaye yéen samay xarit, fàttalikuleen la leen ndawi sunu Boroom Yeesu Kirist waxoon lu jiitu,
17 Mas vós, amados, lembrai-vos das palavras que vos foram preditas pelos apóstolos de nosso Senhor Jesus Cristo;
18 ne leen: «Mujug jamono ay tiiñalkat dinañu feeñ, ñuy weddi Yàlla, ngir topp seen bakkan.»
18 Os quais vos diziam que nos últimos tempos haveria escarnecedores que andariam segundo as suas ímpias concupiscências.
19 Ñooy féewale, te Xelum Yàlla nekkul ci ñoom; nit kese lañu.
19 Estes são os que a si mesmos se separam, sensuais, que não têm o Espírito.
20 Waaye yéen samay xarit, doolewuleen ci seen yoonu ngëm wu sell, tey ñaan ci dooley Xel mu Sell mi,
20 Mas vós, amados, edificando-vos a vós mesmos sobre a vossa santíssima fé, orando no Espírito Santo,
21 ba saxoo mbëggeelu Yàlla, tey séentu yërmandey sunu Boroom Yeesu Kirist, mu tàbbal leen ci dund gu dul jeex.
21 Conservai-vos a vós mesmos no amor de Deus, esperando a misericórdia de nosso Senhor Jesus Cristo para a vida eterna.
22 Jubbantileen ñi am werantey xel,
22 E apiedai-vos de alguns, usando de discernimento;
23 ngeen musal ñale, jële leen ci sawara, te yërëm ñeneen ñi, waaye boole ci moytu, ba sib sax seen yére yi taq sobe.
23 E salvai alguns com temor, arrebatando-os do fogo, odiando até a túnica manchada da carne.
24 Yàlla mi leen mana aar ci gépp jeng te teewal leen fa kanam ndamam, ngeen ñàkk sikk te fees dell ak mbég;
24 Ora, àquele que é poderoso para vos guardar de tropeçar, e apresentar-vos irrepreensíveis, com alegria, perante a sua glória,
25 Yàlla miy kenn, di sunu Musalkat, yal na yelloo ndam ak màgg, kàttan ak nguur, jaar ci Yeesu Kirist sunu Boroom, démb, tey, ëllëg ba fàww! Amiin.
25 Ao único Deus sábio, Salvador nosso, seja glória e majestade, domínio e poder, agora, e para todo o sempre. Amém.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Judas 1, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.