Hebreus 7

Téereb Injiil (WOL2010) vs VC

Sair da comparação
VC Versão Católica
1 Melkisedeg moomu doon buuru Salem, moo nekkoon sarxalkat ca Yàlla Aji Kawe ji. Gannaaw ba Ibraayma dàqee buur ya, ba délsi, Melkisedeg gatandu woon na ko, di ko barkeel.
1 Este Melquisedec, rei de Salém, sacerdote do Deus Altíssimo, que saiu ao encontro de Abraão quando este regressava da derrota dos reis e o abençoou,
2 Noonu Ibraayma fab fukkeelu cér bi, maanaam asaka, ci li mu jële woon ci xare ba lépp, jox ko. Ci lu jëkk turu Melkisedeg mi ngi tekki «buur bu jub bi». Gannaaw loolu mooy buuru Salem, tur woowu mooy tekki «buuru jàmm».
2 ao qual Abraão ofereceu o dízimo de todos os seus despojos, é, conforme seu nome indica, primeiramente "rei de justiça" e, depois, rei de Salém, isto é, "rei de paz".
3 Melkisedeg nag xamaluñu ko baay, xamaluñu ko yaay walla menn maam. Amul fenn fu ñu wax ag juddoom walla ag deeyam. Moo tax nu di ko méngale ak Doomu Yàlla ji, ndaxte sarxalkat la bu kenn dul wuutu.
3 Sem pai, sem mãe, sem genealogia, a sua vida não tem começo nem fim; comparável sob todos os pontos ao Filho de Deus, permanece sacerdote para sempre.
4 Seetleen ni mu màgge, moom Melkisedeg! Ibraayma sax, maamu cosaan mi, fab na li mu jële woon lépp ca xare ba, jox Melkisedeg asaka ja.
4 Considerai, pois, quão grande é aquele a quem até o patriarca Abraão deu o dízimo dos seus mais ricos espólios.
5 Yoonu Musaa digle na ne ñi bokk ci giiru Lewi te di ay sarxalkat, nañu jot asaka ci alalu bànni Israyil, doonte sax ñuy seeni bokk te soqikoo ci Ibraayma.
5 Os filhos de Levi, revestidos do sacerdócio, na qualidade de filhos de Abraão, têm por missão receber o dízimo legal do povo, isto é, de seus irmãos.
6 Waaye Melkisedeg mi bokkul woon ci giiru Lewi, jotoon na asaka ci alali Ibraayma. Te rax-ca-dolli barkeel na ko, moom mi Yàlla sédde woon dige yi.
6 Naquele caso, porém, foi um estrangeiro que recebeu os dízimos de Abraão e abençoou o detentor das promessas.
7 Kiy barkeel a gëna màgg ki ñuy barkeel, loolu amu ci benn werante.
7 Ora, é indiscutível: é o inferior que recebe a. bênção do que é superior.
8 Sarxalkat yi soqikoo ci Lewi, ñu ngi jot asaka, ni ko Melkisedeg jote woon. Waaye ñoom ñu nara dee lañu. Melkisedeg nag moom, Mbind mi wóoral na ne dafay dund.
8 De mais, aqui, os levitas que recebem os dízimos são homens mortais; lá, porém, se trata de alguém do qual é atestado que vive.
9 Léegi nag ci ni ñu ko mana waxe, Lewi miy jot asaka ci bànni Israyil, moom ci boppam jox na ko Melkisedeg, jaare ko ci Ibraayma.
9 Por fim, por assim dizer, também Levi, que recebe os dízimos, pagou-os na pessoa de Abraão,
10 Ndaxte mi ngi nekkoon ci geñog maamam Ibraayma, bi ko Melkisedeg gatandoo.
10 pois ele já estava em germe no íntimo deste, quando aconteceu o encontro com Melquisedec.
11 Jox nañu bànni Israyil yoon wu sukkandiku ci liggéeyu sarxalkat yi soqikoo ci Lewi. Su fekkoonte ne nag liggéeyu sarxalkat yooyu manoon na yeggale nit cig mat, kon du soxlaati ab sarxalkat ni ko Melkisedeg nekke, ci fànn gu wuute ak gu Aaróona.
11 Se a perfeição tivesse sido realizada pelo sacerdócio levítico {porque é sobre este que se funda a legislação dada ao povo}, que necessidade havia ainda de que surgisse outro sacerdote segundo a ordem de Melquisedec, e não segundo a ordem de Aarão?
12 Te bu ñu fi jëlee sarxalkat yi ak seen liggéey, dañoo wara toxal itam yoon, wi ñu fi tëraloon.
12 Pois, transferido o sacerdócio, forçoso é que se faça também a mudança da lei.
13 Noonu Yeesu mi nuy wax, mi ngi soqikoo ci geneen giir gu bokkul ak giiru Lewi. Giir googu nag, amu ci kenn ku ci masa def liggéeyu sarxale ca sarxalukaay ba.
13 De fato, aquele ao qual se aplicam estas palavras é de outra tribo, da qual ninguém foi encarregado do serviço do altar.
14 Li wóor moo di, sunu Boroom mi ngi soqikoo ci giiru Yuda. Te bi Musaa bindee ci mbirum sarxalkat yi, limaalewul woon giir googu.
14 E é notório que nosso Senhor nasceu da tribo de Judá, tribo à qual Moisés nada encarregou ao falar do sacerdócio.
15 Li waral mbir mi gëna leer moo di ne beneen sarxalkat bu mel ni Melkisedeg dafa ñëw.
15 Isto se torna ainda mais evidente se se tem em conta que este outro sacerdote, que surge à semelhança de Melquisedec,
16 Te defuñu ko sarxalkat jaarale ko ci yoonu ndono, waaye fal nañu ko ci dooley dund gu amul àpp.
16 foi constituído não por prescrição de uma lei humana, mas pela sua imortalidade.
17 Ndaxte seedeel nañu Yeesu lii:
17 Porque está escrito: Tu és sacerdote eternamente, segundo a ordem de Melquisedec.
18 Noonu tebbi nañu yoon wu jëkk, wa néewoon doole te meññul dara
18 Com isso, está abolida a antiga legislação, por causa de sua ineficácia e inutilidade.
19 —ndax yoonu Musaa yeggalewul dara cig mat— waaye dugalal nañu nu fii yaakaar ju gën ju nu mana jaare ngir jege Yàlla.
19 Pois a lei nada levou à perfeição. Apenas foi portadora de uma esperança melhor que nos leva a Deus.
20 Te rax-ca-dolli ngiñ ànd na ci. Ndaxte ñi soqikoo ci Lewi doon nañu ay sarxalkat te kenn giñul.
20 E isso não foi feito sem juramento. Os outros sacerdotes foram instituídos sem juramento.
21 Waaye nag Yeesu moom doon na sarxalkat, bi Yàlla giñee ne ko:
21 Para ele, ao contrário, interveio o juramento daquele que disse: Jurou o Senhor e não se arrependerá: tu és sacerdote eternamente.
22 Ngiñ loolu moo tax Yeesu nekk tayle, giy wóoral kóllëre gi gën.
22 E esta aliança da qual Jesus é o Senhor, é-lhe muito superior.
23 Te it yeneen sarxalkat yi dañoo bare woon, ndaxte dee moo daan tax duñu mana sax ci seen liggéey.
23 Além disso, os primeiros sacerdotes deviam suceder-se em grande número, porquanto a morte não permitia que permanecessem sempre.
24 Waaye Yeesu miy dund ba fàww, sasoo na liggéeyu sarxale bu sax fàww.
24 Este, porque vive para sempre, possui um sacerdócio eterno.
25 Loolu moo tax it mu mana musal tey yeggale cig mat ñiy jaar ci moom te bëgg jege Yàlla, ndaxte mi ngi dund ba fàww ngir di leen rammu.
25 É por isso que lhe é possível levar a termo a salvação daqueles que por ele vão a Deus, porque vive sempre para interceder em seu favor.
26 Kon nag Yeesu mooy sarxalkat bu mag, bi nu soxla; dafa sell, du def lu bon, du taq bàkkaar, bokkul dara ak bàkkaarkat yi, te yéege nañu ko fa Yàlla.
26 Tal é, com efeito, o Pontífice que nos convinha: santo, inocente, imaculado, separado dos pecadores e elevado além dos céus,
27 Niroowul ak yeneen sarxalkat yu mag yi; soxlawul di def bés bu set ay saraxi mala ngir bàkkaari boppam jëkk, teg ca yoy mbooloo mi. Yeesu def na sarax benn yoon ba fàww ngir dindi bàkkaar yi, bi muy joxe bakkanam.
27 que não tem necessidade, como os outros sumos sacerdotes, de oferecer todos os dias sacrifícios, primeiro pelos pecados próprios, depois pelos do povo; pois isto o fez de uma só vez para sempre, oferecendo-se a si mesmo.
28 Naka yoonu Musaa, aji néew doole yi lay fal sarxalkat yu mag. Waaye ngiñu Yàlla gi ñëw gannaaw yoon wi, Doom ji la fal sarxalkat bu mag bu mat ba fàww.
28 Enquanto a lei elevava ao sacerdócio homens sujeitos às fraquezas, o juramento, que sucedeu à lei, constitui o Filho, que é eternamente perfeito.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Hebreus 7, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.