Hebreus 6

Téereb Injiil (WOL2010) vs ARIB

Sair da comparação
ARIB Almeida Revisada Imprensa Bíblica
1 Kon nag léegi nanu jóge ci liifantu gi jëm ci Kirist, te jàll cig mat. Nanu baña dalaat njàngle mu jëkk moomu, ci ne nit ñi dañoo wara tuub jëf, yi jëm ci dee, te gëm Yàlla,
1 Pelo que deixando os rudimentos da doutrina de Cristo, prossigamos até a perfeição, não lançando de novo o fundamento de arrependimento de obras mortas e de fé em Deus,
2 di leen jàngalaat ci mbirum sangu set ci ay fànn yu bare, ak teg loxo ak ci mbirum ndekkite ak lu jëm ci àtte biy sax dàkk.
2 e o ensino sobre batismos e imposição de mãos, e sobre ressurreição de mortos e juízo eterno.
3 Te noonu lanuy def, bu soobee Yàlla.
3 E isso faremos, se Deus o permitir.
4 Li nu wara jëme kanam mooy lii: su amee ay nit ñu Yàlla xasa leeral ba noppi, ñu mos mayu Yàlla gi, am wàll ci Xelam mu Sell,
4 Porque é impossível que os que uma vez foram iluminados, e provaram o dom celestial, e se fizeram participantes do Espírito Santo,
5 te xam mbaax, gi ci kàddug Yàlla, ak kéemaani jamono jiy ñëw,
5 e provaram a boa palavra de Deus, e os poderes do mundo vindouro,
6 te loolu lépp teewul ñu walbatiku, ñooñu kenn dootu leen mana yeesalaat, ba ñu tuub seeni bàkkaar. Li ko waral moo di, dañoo bëgga daajaat Doomu Yàlla ji ci bant, di ko toroxal, te fekk muy seen ngaañ.
6 e depois caíram, sejam outra vez renovados para arrependimento; visto que, quanto a eles, estão crucificando de novo o Filho de Deus, e o expondo ao vitupério.
7 Maanaam suuf suy naan taw bi ciy dal, tey jox ñi ñu koy beyal gàncax gu am njariñ, day jot barke bi jóge ci Yàlla.
7 Pois a terra que embebe a chuva, que cai muitas vezes sobre ela, e produz erva proveitosa para aqueles por quem é lavrada, recebe a bênção da parte de Deus;
8 Waaye su meññee ay dég ak ay xaaxaam, du am benn njariñ; repp na ñu alag ko, te lakk lay mujje.
8 mas se produz espinhos e abrolhos, é rejeitada, e perto está da maldição; o seu fim é ser queimada.
9 Waaye nag yéen samay soppe, su fekkee ne sax nii lanuy waxe, nu ngi yaakaar li gën ci yéen te ànd ak mucc.
9 Mas de vós, ó amados, esperamos coisas melhores, e que acompanham a salvação, ainda que assim falamos.
10 Yàlla ñàkkul worma bay fàtte seen liggéey ak mbëggeel, gi ngeen wone ci turam, ci li ngeen dimbali ay gaayam, te yéena ngi koy def ba tey.
10 Porque Deus não é injusto, para se esquecer da vossa obra, e do amor que para com o seu nome mostrastes, porquanto servistes aos santos, e ainda os servis.
11 Waaye danoo bëgg kenn ku nekk ci yéen wone cawarte gu mel ni ga ngeen amoon, ba kera ngeen di am mat, gi ngeen di séentu.
11 E desejamos que cada um de vós mostre o mesmo zelo até o fim, para completa certeza da esperança;
12 Bëggunu ngeen tayel, waaye royleen ñi gëm te muñ, ndaxte ñooñu ñooy jot li leen Yàlla dig.
12 para que não vos torneis indolentes, mas sejais imitadores dos que pela fé e paciência herdam as promessas.
13 Ibraayma bokk na ci ñoom. Bi Yàlla di dige ak moom, manul woona giñ ci keneen ku ko gëna màgg, ba tax mu giñ ci boppam,
13 Porque, quando Deus fez a promessa a Abraão, visto que não tinha outro maior por quem jurar, jurou por si mesmo,
14 ne ko: «Sàllaaw dinaa la barkeel, yokk saw askan.»
14 dizendo: Certamente te abençoarei, e grandemente te multiplicarei.
15 Noonu Ibraayma di xaar tey muñ, ba jot li ko Yàlla digoon.
15 E assim, tendo Abraão esperado com paciência, alcançou a promessa.
16 Nit kuy giñ nag, daf koy wékk ci ku ko sut. Ngiñ lu mel noonu moo wóoral mbir te mooy jeexal lépp lu ñuy werante.
16 Pois os homens juram por quem é maior do que eles, e o juramento para confirmação é, para eles, o fim de toda contenda.
17 Ñi wara jot li mu dige, Yàlla dafa leen bëggoona won ne dogalam du tebbiku mukk; looloo tax mu dige, boole ci ngiñ.
17 assim que, querendo Deus mostrar mais abundantemente aos herdeiros da promessa a imutabilidade do seu conselho, se interpôs com juramento;
18 Noonu ñaari jëf yooyu nga xam ne duñu tebbiku te Yàlla manu cee dellu gannaaw, dañu nuy gëna sóob ci muñ, nun ñi daw ba am kiiraay, ngir nu mana téye bu dëgër yaakaar, ji mu nu dig.
18 para que por duas coisas imutáveis, nas quais é impossível que Deus minta, tenhamos poderosa consolação, nós, os que nos refugiamos em lançar mão da esperança proposta;
19 Ci yaakaar jooju lanu sës sunu xol, ba mana sampu bu dëgër. Yaakaar la juy jàll ba fa Yàlla nekk, ca gannaaw ridob bérab bu sell baa sell.
19 a qual temos como âncora da alma, segura e firme, e que penetra até o interior do véu;
20 Yeesu ci boppam moo fa jëkka dugg, muy ndaw li nu jiitu, ñu def ko sarxalkat bu mag ba fàww, mel ni Melkisedeg.
20 aonde Jesus, como precursor, entrou por nós, feito sacerdote para sempre, segundo a ordem de Melquisedeque.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Hebreus 6, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.