Hebreus 5
Téereb Injiil (WOL2010) vs ARC
1 Sarxalkat bu mag bu nekk nag, ci biir nit ñi lañu ko jële, te fal ko muy dox seen diggante ak Yàlla. Noonu dina jébbal Yàlla ay sarax, tey rendi ay mala ngir dindi seeni bàkkaar.
1 Porque todo sumo sacerdote, tomado dentre os homens, é constituído a favor dos homens nas coisas concernentes a Deus, para que ofereça dons e sacrifícios pelos pecados,
2 Te ndegam moom ci boppam nit kese la, man na muñal ñiy moy ndax seen ñàkka xam.
2 e possa compadecer-se ternamente dos ignorantes e errados, pois também ele mesmo está rodeado de fraqueza.
3 Li mu ñàkk doole moo tax mu wara def ay sarax ngir mbaalug bàkkaaram, ni mu ko tàmmee defal mbooloo mi.
3 E, por esta causa, deve ele, tanto pelo povo como também por si mesmo, fazer oferta pelos pecados.
4 Kenn manula teral sa bopp ba doon ab sarxalkat, su dul ne Yàllaa la woo, ni mu ko defe woon Aaróona.
4 E ninguém toma para si essa honra, senão o que é chamado por Deus, como Arão.
5 Kirist itam yékkatiwul boppam, ba doon sarxalkat bu mag, waaye Yàlla moo ko woo, bi muy wax ne:
5 Assim, também Cristo não se glorificou a si mesmo, para se fazer sumo sacerdote, mas glorificou aquele que lhe disse: Tu és meu Filho, hoje te gerei.
6 Am na feneen fu mu wax ne:
6 Como também diz noutro lugar: Tu és sacerdote eternamente, segundo a ordem de Melquisedeque.
7 Giiru dundam gépp ci àddina, Kirist da daan ñaan wall ci Yàlla, di ko dénku, boole ko ak i jooy ak i rongooñ. Da doon ñaan ci Yàlla, mi ko mana musal ci dee. Te ñaanam nangu na, ndax ni mu jébbale boppam Yàlla.
7 O qual, nos dias da sua carne, oferecendo, com grande clamor e lágrimas, orações e súplicas ao que o podia livrar da morte, foi ouvido quanto ao que temia.
8 Waaye li muy nekk nekk doom, teewul mu jàng déggal Yàlla, jaare ko ci coono bi mu daj.
8 Ainda que era Filho, aprendeu a obediência, por aquilo que padeceu.
9 Noonu la àgge cig mat, ñu def ko ki waral mucc gi dul jeex, ngir ñi ko déggal ñépp.
9 E, sendo ele consumado, veio a ser a causa de eterna salvação para todos os que lhe obedecem,
10 Fekk na Yàlla tudde ko sarxalkat bu mag ni ko Melkisedeg nekke.
10 chamado por Deus sumo sacerdote, segundo a ordem de Melquisedeque.
11 Ci fànn googu, am na lu bare lu nu ci bëgga wax, waaye tekkil leen ko dina jafe, ndaxte dangeena naqari xel.
11 Do qual muito temos que dizer, de difícil interpretação, porquanto vos fizestes negligentes para ouvir.
12 Bu yàgg ngeen waroona jàngal ñeneen ñi, waaye soxla ngeen ba tey ku leen di tette ci kàddug Yàlla. Léegi nag yéena ngi tollu fi ñu leen wara nàmpale, ndaxte àttanuleen ñam wu dëgër.
12 Porque, devendo já ser mestres pelo tempo, ainda necessitais de que se vos torne a ensinar quais sejam os primeiros rudimentos das palavras de Deus; e vos haveis feito tais que necessitais de leite e não de sólido mantimento.
13 Képp kuy nàmp, ab xale nga ba tey. Jëfeegoo njàngle mi jëm ci wàllu njubte.
13 Porque qualquer que ainda se alimenta de leite não está experimentado na palavra da justiça, porque é menino.
14 Waaye ñam wu dëgër, ñi mat a ko yelloo, maanaam ñiy jëfandikoo seen xel ngir ràññee lu baax ak lu bon.
14 Mas o mantimento sólido é para os perfeitos, os quais, em razão do costume, têm os sentidos exercitados para discernir tanto o bem como o mal.
Atalhos do teclado
- Capítulo anterior←
- Próximo capítulo→
- Versículo anteriork
- Próximo versículoj
- Limpar seleçãoEsc
- Esta ajuda?
Estude este capítulo no WhatsApp
Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Hebreus 5, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.