Hebreus 4

Téereb Injiil (WOL2010) vs VC

Sair da comparação
VC Versão Católica
1 Yàlla dige na ne dina am ñu dugg ca noflaayam. Kon ndegam dige boobu mi ngi taxaw ba tey, moytuleen ba kenn ci yéen réer ba du dugg ci noflaay boobu.
1 Enquanto, pois, subsiste a promessa de entrar no seu descanso, tenhamos cuidado em que ninguém de nós corra o risco de ser excluído.
2 Nun jot nanu xibaaru jàmm bi ni ñoom, waaye kàddu, ga ñu déggoon, jariñu leen dara, ndaxte boolewuñu ci ngëm, ba ñu koy déglu.
2 A boa nova nos foi trazida a nós, como o foi a eles. Mas a eles de nada aproveitou, porque caíram na descrença.
3 Nun ñi gëm nag nooy dugg ci noflaayam, ni ko Mbind mi waxe:
3 Nós, porém, se tivermos fé, haveremos de entrar no descanso. Ele disse: Eu jurei na minha ira: não entrarão no lugar do meu descanso. Ora, as obras de Deus estão concluídas desde a criação do mundo;
4 am na fu ñu wax ci Mbind mi ne:
4 pois, em certa passagem, falou do sétimo dia o seguinte: E, terminado o seu trabalho, descansou Deus no sétimo dia {Gn 2,2}.
5 Te it waxoon na ci baat yi nu jota lim ba noppi:
5 Se, pois, ele repete: Não entrarão no lugar do meu descanso,
6 Kon am na ñu ci wara dugg ba tey. Te ñi jëkkoona jot xibaaru jàmm bi, dugguñu ci ndax seen déggadi.
6 é sinal de que outros são chamados a entrar nele. E como aqueles a quem primeiro foi anunciada a promessa não entraram por não ter tido a fé,
7 Noonu ay ati at gannaaw ga, Yàlla àppaat na beneen bés, def ko «tey jii», bi mu waxee ci gémmiñu Daawuda ci baat yii ñu jota lim:
7 Deus, após muitos anos, por meio de Davi, estabelece um novo dia, um hoje, ao pronunciar as palavras mencionadas: Hoje, se ouvirdes a sua voz, não endureçais os vossos corações.
8 Su Yosuwe dugaloon sunu maam ya ca noflaayu Yàlla ba, kon gannaaw gi Yàlla du wax dara ci lu jëm ci beneen bés.
8 Se Josué lhes houvesse dado repouso, não teria depois disso falado dum outro dia.
9 Kon ba tey Yàllaa ngi dencal ay gaayam noflaay bu nirook noflaayu Yàlla ca juróom ñaareelu fan ba.
9 Por isso, resta um repouso sabático para o povo de Deus.
10 Ndaxte képp ku masa dugg ca noflaayu Yàlla, noppalu na ci ay jëfam ni Yàlla.
10 E quem entrar nesse repouso descansará das suas obras, assim como descansou Deus das suas.
11 Nanu farlu boog, ngir dugg ci noflaay boobu, ba kenn baña déggadi, ba daanu ni maam ya ca màndiŋ ma.
11 Assim, apressemo-nos a entrar neste descanso para não cairmos por nossa vez na mesma incredulidade.
12 Xam nanu ne kàddug Yàlla mi ngi dund te am na doole. Moo gëna ñaw jaasiy ñaari boor. Day dagg ba fa xol ak xel digaloo, ba fa yax yi ak yuq gi di teqalikoo, te man na àtte xalaat yi ak mébéti xol.
12 Porque a palavra de Deus é viva, eficaz, mais penetrante do que uma espada de dois gumes e atinge até a divisão da alma e do corpo, das juntas e medulas, e discerne os pensamentos e intenções do coração.
13 Te itam amul mbindeef mu mana nëbbu Yàlla, waaye lépp a ubbiku, ba ne fàŋŋ ci bëti ki nu wara àtte.
13 Nenhuma criatura lhe é invisível. Tudo é nu e descoberto aos olhos daquele a quem havemos de prestar contas.
14 Gannaaw am nanu sarxalkat bu maga mag bu àgg ba ca kanam Yàlla, di Yeesu Doomu Yàlla ji, nanu jàpp bu dëgër yoon wi nu gëm.
14 Temos, portanto, um grande Sumo Sacerdote que penetrou nos céus, Jesus, Filho de Deus. Conservemos firme a nossa fé.
15 Sarxalkat bu mag bi nu am, du ku manula bokk ak nun sunuy naqar; moom sax far jaar na ci nattu ni nun ci bépp fànn, waaye deful bàkkaar.
15 Porque não temos nele um pontífice incapaz de compadecer-se das nossas fraquezas. Ao contrário, passou pelas mesmas provações que nós, com exceção do pecado.
16 Kon nag nanu am kóolute ci jege jalu Yàlla bu yiw ba, ngir jot yërmandeem ak yiwam, ngir mu wallu nu fu soxla taxawe.
16 Aproximemo-nos, pois, confiadamente do trono da graça, a fim de alcançar misericórdia e achar a graça de um auxílio oportuno.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Hebreus 4, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.