Hebreus 3
Téereb Injiil (WOL2010) vs ARA
1 Kon nag yéen bokk yu sell yi, yéen ñi Yàlla woo, ngeen bokk ci nguuram gu kawe ga, seetleen ci Yeesu, moom miy ndawu Yàlla li, di sarxalkat bu mag bi ci yoon wi nu gëm.
1 Por isso, santos irmãos, que participais da vocação celestial, considerai atentamente o Apóstolo e Sumo Sacerdote da nossa confissão, Jesus,
2 Ku takku la ci liggéey bi ko Yàlla sas, ni ko Musaa nekke woon ci lépp lu jëm ci waa kër Yàlla.
2 o qual é fiel àquele que o constituiu, como também o era Moisés em toda a casa de Deus.
3 Waaye Yeesu yelloo na ndam lu sut lu Musaa, ni kiy tabax kër ëppe maana kër ga muy tabax.
3 Jesus, todavia, tem sido considerado digno de tanto maior glória do que Moisés, quanto maior honra do que a casa tem aquele que a estabeleceu.
4 Ndaxte kër gu nekk am na ku ko sos, waaye ki sos lépp mooy Yàlla.
4 Pois toda casa é estabelecida por alguém, mas aquele que estabeleceu todas as coisas é Deus.
5 Musaa moom ku takku la woon ci lépp lu jëm ci waa kër Yàlla. Waaye jawriñ rekk la woon, ngir seede li Yàlla waroona yégle.
5 E Moisés era fiel, em toda a casa de Deus, como servo, para testemunho das coisas que haviam de ser anunciadas;
6 Yeesu nag ku takku la it, waaye Doom la, juy yilif kër Baayam. Nun nooy këram googu, bu nu saxee ci sunu kóolute te di bég ci li nuy séentu.
6 Cristo, porém, como Filho, em sua casa; a qual casa somos nós, se guardarmos firme, até ao fim, a ousadia e a exultação da esperança.
7 Moo tax Xel mu Sell mi wax lii ci Mbind mi:
7 Assim, pois, como diz o Espírito Santo: Hoje, se ouvirdes a sua voz,
8 buleen dëgër bopp,
8 não endureçais o vosso coração como foi na provocação, no dia da tentação no deserto,
9 Yàlla ne:
9 onde os vossos pais me tentaram, pondo-me à prova, e viram as minhas obras por quarenta anos.
10 diirub ñeent fukki at.
10 Por isso, me indignei contra essa geração e disse: Estes sempre erram no coração; eles também não conheceram os meus caminhos.
11 Giñ naa kon ci sama mer ne:
11 Assim, jurei na minha ira: Não entrarão no meu descanso.
12 Bokk yi, wottuleen ba kenn ci yéen baña am xol bu bon te gëmadi, bay dëddu Yàlla jiy dund.
12 Tende cuidado, irmãos, jamais aconteça haver em qualquer de vós perverso coração de incredulidade que vos afaste do Deus vivo;
13 Waaye bés bu nekk, deeleen soññante ci lu jëm ci Yàlla, fi ak bés boobu ñu wax wéyul, ngir ragal bàkkaar nax kenn, ba xolam tëju.
13 pelo contrário, exortai-vos mutuamente cada dia, durante o tempo que se chama Hoje, a fim de que nenhum de vós seja endurecido pelo engano do pecado.
14 Am nanu wàll ci Kirist, su nu wéyee fii ba muj ga ci sunu kóolute, gi nu amoon ca njàlbéen ga.
14 Porque nos temos tornado participantes de Cristo, se, de fato, guardarmos firme, até ao fim, a confiança que, desde o princípio, tivemos.
15 Lii la Mbind mi wax:
15 Enquanto se diz: Hoje, se ouvirdes a sua voz, não endureçais o vosso coração, como foi na provocação.
16 Ñan ñoo dégg baatu Yàlla bi nag te di ko dëddu? Xanaa ña Musaa génne woon Misra ñépp.
16 Ora, quais os que, tendo ouvido, se rebelaram? Não foram, de fato, todos os que saíram do Egito por intermédio de Moisés?
17 Te ñan la Yàlla mere lu mat ñeent fukki at? Xanaa ñi daan bàkkaar te seeni néew tëdd ca màndiŋ ma.
17 E contra quem se indignou por quarenta anos? Não foi contra os que pecaram, cujos cadáveres caíram no deserto?
18 Te it bi Yàlla defee ngiñ lii: «Duñu dugg mukk ci sama noflaay,» booba ñan ñoo ko taxoon di wax? Xanaa ña ko déggadil.
18 E contra quem jurou que não entrariam no seu descanso, senão contra os que foram desobedientes?
19 Noonu gis nanu sax ne jotuñoo dugg ci noflaay boobu ndax seen gëmadi.
19 Vemos, pois, que não puderam entrar por causa da incredulidade.
Atalhos do teclado
- Capítulo anterior←
- Próximo capítulo→
- Versículo anteriork
- Próximo versículoj
- Limpar seleçãoEsc
- Esta ajuda?
Estude este capítulo no WhatsApp
Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Hebreus 3, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.