Hebreus 10
Téereb Injiil (WOL2010) vs ARIB
1 Yoonu Musaa dafa misaal xéewal yi waroona ñëw; takkandeer la ci yëf yu dëggu yi, waaye du ñoom ci seen bopp. Looloo tax manula yeggale cig mat ñi ñëw ci Yàlla, ndaxte at mu nekk duñu jóg ci jébbal Yàlla sarax yooyu.
1 Porque a lei, tendo a sombra dos bens futuros, e não a imagem exata das coisas, não pode nunca, pelos mesmos sacrifícios que continuamente se oferecem de ano em ano, aperfeiçoar os que se chegam a Deus.
2 Sarax yi ñuy def, bu ñu manoona sellal ñiy jaamu benn yoon ba fàww, kon dinañu leen bàyyi, ndaxte dootuñu am yeraange ci seeni bàkkaar.
2 Doutra maneira, não teriam deixado de ser oferecidos? pois tendo sido uma vez purificados os que prestavam o culto, nunca mais teriam consciência de pecado.
3 Waaye dañuy fàttaliku bàkkaar yi ci sarax yi ñuy def at mu jot.
3 Mas nesses sacrifícios cada ano se faz recordação dos pecados,
4 Ndaxte deretu yëkk ak ju sikket manula dindi bàkkaar.
4 porque é impossível que o sangue de touros e de bodes tire pecados.
5 Looloo tax bi muy wàcc àddina, Kirist nee na:
5 Pelo que, entrando no mundo, diz: Sacrifício e oferta não quiseste, mas um corpo me preparaste;
6 Sarax yu ñuy lakk walla sarax yiy dindi bàkkaar,
6 não te deleitaste em holocaustos e oblações pelo pecado.
7 Moo tax ma ne: “Damaa wàcc ngir def sa coobare, yaw Yàlla,
7 Então eu disse: Eis-me aqui {no rol do livro está escrito de mim} para fazer, ó Deus, a tua vontade.
8 Wax na bu jëkk: «Saraxi mala walla yeneen sarax, sarax yu ñuy lakk walla sarax yiy dindi bàkkaar, bëgguloo leen te benn neexu la ci.» Teewul yoon wi moo leen santaane.
8 Tendo dito acima: Sacrifício e ofertas e holocaustos e oblações pelo pecado não quiseste, nem neles te deleitaste {os quais se oferecem segundo a lei};
9 Noonu mu tegaat ca ne: «Damaa wàcc ngir def sa coobare.» Noonu toxal na jëfin wu jëkk wa, ngir wuutal fi weneen wu bees.
9 agora disse: Eis-me aqui para fazer a tua vontade. Ele tira o primeiro, para estabelecer o segundo.
10 Te ci li Kirist def coobarey Yàlla, bi mu joxee yaramam sarax benn yoon ba fàww, moo tax nu sell ci bàkkaar.
10 É nessa vontade dele que temos sido santificados pela oferta do corpo de Jesus Cristo, feita uma vez para sempre.
11 Bés bu nekk sarxalkat yi dañuy taxaw di liggéeyal Yàlla, di sax ci def sarax yu manula dindi bàkkaar yi mukk.
11 Ora, todo sacerdote se apresenta dia após dia, ministrando e oferecendo muitas vezes os mesmos sacrifícios, que nunca podem tirar pecados;
12 Waaye nag sarxalkat bii di Kirist, bi mu sarxee sarax bu am doole ngir dindi bàkkaar yi benn yoon ba fàww, dafa toog ca ndijooru Yàlla,
12 mas este, havendo oferecido um único sacrifício pelos pecados, assentou-se para sempre à direita de Deus,
13 di xaar ba kera mu daaneel ko ay noonam ci kanamam.
13 daí por diante esperando, até que os seus inimigos sejam postos por escabelo de seus pés.
14 Noonu ñi ñuy sellal, ci benn sarax rekk la leen yeggali cig mat ba fàww.
14 Pois com uma só oferta tem aperfeiçoado para sempre os que estão sendo santificados.
15 Te it Xel mu Sell mi seedeel na nu ko;
15 E o Espírito Santo também no-lo testifica, porque depois de haver dito:
16 dafa jëkka wax ne:
16 Este é o pacto que farei com eles depois daqueles dias, diz o Senhor: Porei as minhas leis em seus corações, e as escreverei em seu entendimento; acrescenta:
17 Noonu mu tegaat ca ne:
17 E não me lembrarei mais de seus pecados e de suas iniqüidades.
18 Kon nag fu ñuy baale bàkkaar, aajootul sarax su koy dindi.
18 Ora, onde há remissão destes, não há mais oferta pelo pecado.
19 Bokk yi, gannaaw nag deretu Yeesu may na nu sañ-sañu dugg ca bérab bu sell baa sell,
19 Tendo pois, irmãos, ousadia para entrarmos no santíssimo lugar, pelo sangue de Jesus,
20 nuy jaar ci rido bi, ci yoon wi mu nu ubbil, di yoon wu bees tey dund, maanaam ndax li mu joxe yaramam sarax te mi ngi dund,
20 pelo caminho que ele nos inaugurou, caminho novo e vivo, através do véu, isto é, da sua carne,
21 te gannaaw am nanu sarxalkat bu mag, biy yilif waa kër Yàlla,
21 e tendo um grande sacerdote sobre a casa de Deus,
22 kon nanu jege Yàlla ak xol bu laab, ak ngëm gu ànd ak kóolute, am xel mu dal ci bépp yeraange, ak yaram wu ñu raxas ci ndox mu sell.
22 cheguemo-nos com verdadeiro coração, em inteira certeza de fé; tendo o coração purificado da má consciência, e o corpo lavado com água limpa,
23 Nanu jàpp ci yaakaar, ji nu am, te baña toqi, ndaxte ki nu dig, lu mu wax def ko.
23 retenhamos inabalável a confissão da nossa esperança, porque fiel é aquele que fez a promessa;
24 Nanu seet ni nu mana xiirtalante cig mbëggeel ak ci jëf yu baax.
24 e consideremo-nos uns aos outros, para nos estimularmos ao amor e às boas obras,
25 Te bunu bàyyi sunu ndaje yi, ni ko ñenn ñi di defe, waaye nanuy nàddante ci ngëm, di ko feddali, fi ak yéena ngi gis bésu Boroom biy jubsi.
25 não abandonando a nossa congregação, como é costume de alguns, antes admoestando-nos uns aos outros; e tanto mais, quanto vedes que se vai aproximando aquele dia.
26 Gannaaw ba nu nangoo xam dëgg ba noppi, bu nu teyee di def bàkkaar, kon sarax dootul am ngir bàkkaar yooyu.
26 Porque se voluntariamente continuarmos no pecado, depois de termos recebido o pleno conhecimento da verdade, já não resta mais sacrifício pelos pecados,
27 Déedéet, bu nu defee noonu, dinanu tiit di xaar àtte ba, muy taal bu yànj, biy wara lakk nooni Yàlla yi.
27 mas uma expectação terrível de juízo, e um ardor de fogo que há de devorar os adversários.
28 Ku weddi ndigali yoonu Musaa wi, te ñaar walla ñetti nit seede ko, dina dee ci lu amul benn yërmande.
28 Havendo alguém rejeitado a lei de Moisés, morre sem misericórdia, pela palavra de duas ou três testemunhas;
29 Ku xeeb Doomu Yàlla ji te fonkadi deretu kóllëre, ji ñu ko sellale, te muy toroxal Xelum Yàlla, mi indi yiw, naka la mbugalam wara gëna yéese?
29 de quanto maior castigo cuidais vós será julgado merecedor aquele que pisar o Filho de Deus, e tiver por profano o sangue do pacto, com que foi santificado, e ultrajar ao Espírito da graça?
30 Xam nanu ki wax ne: «Man maay àtte, maay fey jëf.» Te newaat na: «Boroom bi dina àtte ay gaayam.»
30 Pois conhecemos aquele que disse: Minha é a vingança, eu retribuirei. E outra vez: O Senhor julgará o seu povo.
31 Ndaw tiitaange ci ku sàggan, ba tàbbi ci loxoy Yàlla jiy dund!
31 Horrenda coisa é cair nas mãos do Deus vivo.
32 Fàttalikuleen bés yu jëkk ya, ba leeru Yàlla tàbbee ci yéen; dékku ngeen xeex bu mag ciy fitna.
32 Lembrai-vos, porém, dos dias passados, em que, depois de serdes iluminados, suportastes grande combate de aflições;
33 Léeg-léeg ñu saaga leen ak di leen sonal ci kanam nit ñi; léeg-léeg it ngeen taxawu ñi ñuy def noonu.
33 pois por um lado fostes feitos espetáculo tanto por vitupérios como por tribulações, e por outro vos tornastes companheiros dos que assim foram tratados.
34 Ndaxte bokk ngeen naqar ak ñi ñu tëj, te nangu ngeen ak xol bu sedd, ñu foqarñi seen alal, xam ne am ngeen alal ju gën te di sax ba fàww.
34 Pois não só vos compadecestes dos que estavam nas prisões, mas também com gozo aceitastes a espoliação dos vossos bens, sabendo que vós tendes uma possessão melhor e permanente.
35 Kon nag buleen sàggane kóolute gi ngeen am, ndaxte ëmb na yool bu mag.
35 Não lanceis fora, pois, a vossa confiança, que tem uma grande recompensa.
36 Dangeena wara muñ, ba def coobarey Yàlla, sooga jot li mu leen digoon.
36 Porque necessitais de perseverança, para que, depois de haverdes feito a vontade de Deus, alcanceis a promessa.
37 Ndaxte lii la Mbind mi wax:
37 Pois ainda em bem pouco tempo aquele que há de vir virá, e não tardará.
38 Ku jub ci sama kanam dina dund ci kaw ngëm,
38 Mas o meu justo viverá da fé; e se ele recuar, a minha alma não tem prazer nele.
39 Nun nag bokkunu ci ñiy dellu gannaaw bay réer, waaye nu ngi bokk ci ñi am ngëm tey mucc.
39 Nós, porém, não somos daqueles que recuam para a perdição, mas daqueles que crêem para a conservação da alma.
Atalhos do teclado
- Capítulo anterior←
- Próximo capítulo→
- Versículo anteriork
- Próximo versículoj
- Limpar seleçãoEsc
- Esta ajuda?
Estude este capítulo no WhatsApp
Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Hebreus 10, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.