Gálatas 6

Téereb Injiil (WOL2010) vs VC

Sair da comparação
VC Versão Católica
1 Bokk yi, ku ñu fekk muy def lu Yàlla bëggul, yéen ñi topp Xelum Yàlla, nangeen ko jubbanti ak xol bu lewet. Waaye nanga sàmm sa bopp, ngir bàkkaar bañ laa fiir, yaw itam.
1 Irmãos, se alguém for surpreendido numa falta, vós, que sois animados pelo Espírito, admoestai-o em espírito de mansidão. E tem cuidado de ti mesmo, para que não caias também em tentação!
2 Jàpplanteleen, noonu dingeen sàmm yoon wi Kirist tëral.
2 Ajudai-vos uns aos outros a carregar os vossos fardos, e deste modo cumprireis a lei de Cristo.
3 Ndaxte kuy naagu te fekk doo dara, dangay nax sa bopp.
3 Quem pensa ser alguma coisa, não sendo nada, engana-se a si mesmo.
4 Na ku nekk seetlu ni muy beye sasam. Bu ko defee dina mana naw boppam, tey bañ di diirante mbagg ak ñi ci des.
4 Cada um examine o seu procedimento. Então poderá gloriar-se do que lhe pertence e não do que pertence a outro.
5 Ndaxte ku ci nekk dangaa wara yenu sab yen.
5 Pois cada um deve carregar o seu próprio fardo.
6 Kiy jàng kàddug Yàlla war na sédd ki koy jàngal ci alalam jépp.
6 Aquele que recebe a catequese da palavra, reparta de todos os seus bens com aquele que o instrui.
7 Bu leen ci dara nax; kenn du foontoo Yàlla, ndaxte lu waay ji, moom ngay góob.
7 Não vos enganeis: de Deus não se zomba. O que o homem semeia, isso mesmo colherá.
8 Ku ji ngir sa nafsu, dinga góob li sa nafsu meññ, maanaam ag yàqute. Waaye ku ji lu soloo ak Xelum Yàlla, li Xel mi meññ ngay góob, maanaam dund gu dul jeex.
8 Quem semeia na carne, da carne colherá a corrupção; quem semeia no Espírito, do Espírito colherá a vida eterna.
9 Bunu tàyyi ci def lu baax, ndaxte bu nu ci sawaree, bu waxtu wi jotee dinanu jariñu.
9 Não nos cansemos de fazer o bem, porque a seu tempo colheremos, se não relaxarmos.
10 Noonu fi ak nu koy man, nanuy defal ñépp lu baax, rawatina nag sunu bokk yi gëm.
10 Por isso, enquanto temos tempo, façamos o bem a todos os homens, mas particularmente aos irmãos na fé.
11 Seetleen araf yu mag yii ma leen bind ci sama loxob bopp!
11 Vede com que tamanho de letras vos escrevo, de próprio punho!
12 Ñiy gistal ci seen yaram, ñooñoo bëgg ngeen xaraf, ngir ragala daj fitna ci yégle deewu Kirist ca bant ba.
12 Os que vos obrigam à circuncisão são homens que se querem impor, só para não serem perseguidos por causa da cruz de Cristo.
13 Kureel gi faaydaal xaraf, ñoom ci seen bopp sax, duñu topp yoon wi. Dañoo bëgga ngeen xaraf, ba ñu mana bàkku ci seen yaram, yéen.
13 Pois nem os próprios circuncisos observam a lei. E se fazem questão de que vos mandeis circuncidar, é para terem motivo de se gloriarem na vossa carne.
14 Man ci sama wàllu bopp, duma bàkku mukk su dul ci deewu sunu Boroom Yeesu Kirist, ba ñu ko daajee ca bant ba. Deeyam moo tax ma mel ni ku dee ci yëfi àddina; yëfi àddina dee ci man.
14 Quanto a mim, não pretendo, jamais, gloriar-me, a não ser na cruz de nosso Senhor Jesus Cristo, pela qual o mundo está crucificado para mim e eu para o mundo.
15 Xaraf ak baña xaraf dara amu ci solo. Li am solo mooy nekk mbindeef mu bees.
15 Porque a circuncisão e a incircuncisão de nada valem, mas sim a nova criatura.
16 Ñiy topp ndigal lii nag, yal na Yàlla wàcce jàmm ak yërmande ci ñoom, ak ci Israyilu Yàlla.
16 A todos que seguirem esta regra, a paz e a misericórdia, assim como ao Israel de Deus.
17 Léegi nag, bu ma kenn lëjalati, ndaxte yor naa ci sama yaram ay leget yuy màndargaal ne jaamu Yeesu laa.
17 De ora em diante ninguém me moleste, porque trago em meu corpo as marcas de Jesus.
18 Bokk yi, yal na yiwu Yeesu Kirist sunu Boroom ànd ak seen xel. Amiin.
18 A graça de nosso Senhor Jesus Cristo esteja com vosso espírito, irmãos. Amém.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Gálatas 6, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.