Gálatas 5

Téereb Injiil (WOL2010) vs BKJ

Sair da comparação
1 Kirist a nu daggal sunu buumi njaam, ngir goreel nu. Kon dëgërleen ci seen ngor te baña delluwaat ci njaam.
1 Firmemo-nos, portanto, na liberdade com que Cristo nos libertou; não nos submetamos outra vez ao jugo da escravidão.
2 Dégluleen! Man Pool maa leen koy wax: bu ngeen itteelee xaraf, kon Kirist dootu leen jariñ dara.
2 Eis que eu, Paulo, vos declaro, que se vós vos circuncidardes, de nada vos servirá Cristo.
3 Te maa ngi dellu di waxaat ne, képp kuy farataal xaraf, fàww nga sàmm lépp lu yoon wi santaane.
3 E testifico novamente, a todo homem que for circuncidado, ele está obrigado a observar toda a lei.
4 Yéen ñiy fexee jub fa kanam Yàlla ci kaw sàmm yoon, tàggalikoo ngeen ak Kirist; dëddu ngeen yiwu Yàlla.
4 Cristo torna-se sem efeito para vós que procurais a justificação pela lei; vós decaístes da graça.
5 Waaye njub, gi nu Yàlla dencal ëllëg, nu ngi koy séentu ci kaw ngëm ak ci ndimbalu Xelum Yàlla.
5 Porque nós, pelo Espírito, aguardamos a esperança da justiça pela fé.
6 Ndaxte bu nu bokkee ci Kirist Yeesu, xaraf ak baña xaraf, dara amu ci solo; li am solo mooy ngëm, giy jëf ci mbëggeel.
6 Porque, em Jesus Cristo, nem a circuncisão nem a incircuncisão valem alguma coisa, mas a fé que opera pelo amor.
7 Ni ngeen jógtee woon de baax na! Waaw, ku leen dog, ba ngeen baña déggal dëgg?
7 Corríeis bem; quem, pois, vos impediu para que não obedecêsseis à verdade?
8 Li ñu leen xiir jógewul ci Yàlla mi leen woo.
8 Esta persuasão não vem daquele que vos chama.
9 Dees na ne: «Tuuti lawiir day tax tooyalu fariñ bépp funki.»
9 Um pouco de fermento leveda toda a massa.
10 Waaye teewul Boroom bi jox na ma kóolute ci yéen. Biral na ma ne dingeen bokk ak man xalaat. Léegi nag, kiy nëxal seen xel, ku mu mana doon, Yàlla dina ko mbugal.
10 Tenho confiança em vós, por meio do Senhor, que de maneira alguma mudareis de opinião; mas aquele que vos perturbar será julgado por isto, seja quem for.
11 Man nag bokk yi, bu ma doon faaydaal xaraf ci sama waare, kon duñu ma fitnaale nii; te it li may yégle ci deewu Kirist ca bant ba dootul naqari kenn.
11 E eu, irmãos, se ainda prego a circuncisão, por que, então, ainda sofro perseguição? Assim, a ofensa da cruz teria cessado.
12 Ñi farataal xaraf te di leen dëpp, nañu gëna sore ci seen réer: bu yaboo sax ñu dagg seen ngóora, ba dara du ci des!
12 Bom seria que fossem cortados, aqueles que vos perturbam.
13 Yéen nag bokk yi, Yàlla woo na leen, ngeen nekk i gor. Waaye nag buleen ci sukkandiku, bay topp seen nafsu, waaye dimbaleenteleen ci kaw mbëggeel.
13 Porque vós, irmãos, fostes chamados à liberdade. Apenas não useis da liberdade para dar ocasião à carne, mas para servir uns aos outros em amor.
14 Ndaxte yoon wépp, ndigal lii a ko tënk: «Nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp.»
14 Porque toda a lei é cumprida em uma só palavra, nesta: Amarás ao teu próximo como a ti mesmo.
15 Waaye moytuleen! Bu ngeen dee màttante ak a lekkante, dingeen yàqante.
15 Mas se vos mordeis e vos devorais uns aos outros, vede que não acabeis por vos destruirdes uns aos outros.
16 Li ma leen di wax mooy lii: dundleen ci Xelum Yàlla, kon dungeen topp seen nafsu.
16 Isto vos digo: Andeis no Espírito, e não satisfareis os desejos da carne.
17 Ndaxte sunu nafsu am na ay bëgg-bëgg yu méngoowul ak yu Xelum Yàlla. Te Xelum Yàlla itam am na ay bëgg-bëgg yu méngoowul ak yu sunu nafsu. Ñoom ñaar dañoo juuyoo ci bépp fànn, ba tax lépp lu ngeen bëggoona def, dungeen ko man.
17 Porque os desejos da carne se opõem aos do Espírito, e os do Espírito contra os da carne, pois opõem-se um ao outro, a fim de que não consigais fazer o que quereis.
18 Waaye bu ngeen toppee Xelum Yàlla, nekkatuleen ci kilifteefu yoon wi.
18 Porém, se deixardes que o Espírito vos guie, já não estais sob a lei.
19 Kuy topp sa nafsu, nii ngay jëfe: njaaloo, xalaat yu bon, def i ñaawteef ak say cér,
19 Ora, as obras da carne são manifestas e aqui estão: Adultério, fornicação, impureza, lascívia,
20 xërëm, luxus, noonoo ak xuloo, ñeetaane, xadar, diiroo mbagg, féewaloo ak xàjjaloo,
20 idolatria, feitiçaria, ódio, discórdia, rivalidade, ira, porfia, rebeliões, heresias,
21 kiñaan, màndite ak xawaare ak yeneen yu ni mel. Léegi nag maa ngi leen di artu, ni ma ko defe woon: ñiy jëfe noonu duñu am cér ci nguuru Yàlla.
21 invejas, homicídios, bebedeiras, orgias e outras coisas semelhantes. A respeito dessas coisas vos falo, como já vos falei outrora, que os que praticam tais coisas não hão de herdar o reino de Deus.
22 Waaye li Xelu Yàlla mi di meññ mooy: mbëggeel, mbég, jàmm, muñ, laabiir, mbaax, kóllëre,
22 Mas o fruto do Espírito é: Amor, alegria, paz, paciência, benignidade, bondade, fé,
23 lewetaay ak maandute. Yoon wi terewul yu ni mel.
23 brandura, temperança; contra essas coisas não há lei.
24 Léegi ñi bokk nag ci Yeesu Kirist, daaj nañu seen nafsu ca bant ba, wacc ko fa, moom ak i xemmemam ak i bëgg-bëggam.
24 Pois aqueles que são de Cristo já crucificaram a carne com as paixões e concupiscências.
25 Gannaaw nag nu ngi dund léegi ci Xelum Yàlla, kon nanu ko topp.
25 Se vivemos pelo Espírito, andemos também no Espírito.
26 Bu nu tiitaru di dëkkante, di iñaanante.
26 Não sejamos ávidos da vanglória, provocando uns aos outros, invejando uns aos outros.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Gálatas 5, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.