Gálatas 4
Téereb Injiil (WOL2010) vs ACF
1 Li ma leen di wax, mooy lii: doom ji wara donni baayam, fi ak mu ngi cig ndaw, ak lu ko alal jiy lew lépp, du wuute dara ak jaam.
1 Digo, pois, que todo o tempo que o herdeiro é menino em nada difere do servo, ainda que seja senhor de tudo;
2 Ñi ko yore tey sàmm alalam ñoo koy yilif, ba jamono ji ko baayam àppaloon mat.
2 Mas está debaixo de tutores e curadores até ao tempo determinado pelo pai.
3 Nun itam naka noonu, laata nuy mat, aaday àddina ñoo nu notoon, ba def nu ni ay jaam.
3 Assim também nós, quando éramos meninos, estávamos reduzidos à servidão debaixo dos primeiros rudimentos do mundo.
4 Waaye bi àpp bi Yàlla tëraloon matee, yónni na Doomam, mu juddoo ci jigéen, ci biir yoonu Musaa,
4 Mas, vindo a plenitude dos tempos, Deus enviou seu Filho, nascido de mulher, nascido sob a lei,
5 ngir jot ñi yoon wi notoon, ndax Yàlla jàpp nu ni ay doomam.
5 Para remir os que estavam debaixo da lei, a fim de recebermos a adoção de filhos.
6 Gannaaw doomi Yàlla ngeen nag, Yàlla yónni na Xelu Doomam ci sunu xol, mu koy wooye nii: «Abba», maanaam «Baay.»
6 E, porque sois filhos, Deus enviou aos vossos corações o Espírito de seu Filho, que clama: Aba, Pai.
7 Noonu dootuloo jaam, doom nga. Te ndegam doom nga, Yàlla jagleel na la cér ci xéewal, yi mu dencal ay doomam.
7 Assim que já não és mais servo, mas filho; e, se és filho, és também herdeiro de Deus por Cristo.
8 Bu jëkk, bi ngeen xamagul Yàlla, yéena ngi doon jaamu yeneen yu ñu daan bokkaaleel Yàlla.
8 Mas, quando não conhecíeis a Deus, servíeis aos que por natureza não são deuses.
9 Waaye léegi nag bi ngeen xamee Yàlla, walla boog bi leen Yàlla xàmmee, nan ngeen mana def, bay delluwaat ca aaday àddina? Aada yooyee ñàkk doole te ñàkk njariñ, lu tax ngeen bëgg, ñu notaat leen?
9 Mas agora, conhecendo a Deus, ou, antes, sendo conhecidos por Deus, como tornais outra vez a esses rudimentos fracos e pobres, aos quais de novo quereis servir?
10 Yéena ngi fonk bés yi, weer yi, màggal yi ak at yi!
10 Guardais dias, e meses, e tempos, e anos.
11 Sama xel dalul ci yéen, ngir ragal sama coono ci yéen neen.
11 Receio de vós, que não haja trabalhado em vão para convosco.
12 Bokk yi, dama leen di ñaan, ngeen mel ni man, ndaxte man itam fekksi naa leen ci seen xalaat. Tooñuleen ma.
12 Irmãos, rogo-vos que sejais como eu, porque também eu sou como vós; nenhum mal me fizestes.
13 Xam ngeen ne sama wopp moo taxoon, ma yégal leen xibaaru jàmm bi.
13 E vós sabeis que primeiro vos anunciei o evangelho estando em fraqueza da carne;
14 Coono, gi leen sama wopp tegoon, taxul ngeen bañ ma, taxul ngeen séexlu ma. Waaye teeru ngeen ma, ni bu ngeen doon teeru malaakam Yàlla walla Yeesu Kirist.
14 E não rejeitastes, nem desprezastes isso que era uma tentação na minha carne, antes me recebestes como um anjo de Deus, como Jesus Cristo mesmo.
15 Waaw, fan la seen mbég jaar? Ndaxte seedeel naa leen ne su ngeen ko manoon, kon luqi ngeen seeni bët, jox ma.
15 Qual é, logo, a vossa bem-aventurança? Porque vos dou testemunho de que, se possível fora, arrancaríeis os vossos olhos, e mos daríeis.
16 Ndax dëgg, gi ma leen wax, moo tax ngeen def ma ab noon?
16 Fiz-me acaso vosso inimigo, dizendo a verdade?
17 Nit ñooñu leen di farle, seen mébét baaxul. Dañu leena bëgga tàggale ak nun, ngir ngeen far ak ñoom.
17 Eles têm zelo por vós, não como convém; mas querem excluir-vos, para que vós tenhais zelo por eles.
18 Farle baax na, bu àndee ak mébét mu baax. Waaye bu sama jëmm rekk tax ngeen koy def.
18 É bom ser zeloso, mas sempre do bem, e não somente quando estou presente convosco.
19 Sama doom yi! Yéena tax may dellu ci metit ni kuy matu, ba kera jikkoy Kirist di mat ci yéen.
19 Meus filhinhos, por quem de novo sinto as dores de parto, até que Cristo seja formado em vós;
20 Léegi bëggoon naa nekk ci seen biir, ngir mana jubbanti sama kàddu, ndaxte xamatuma nu may doxale ak yéen!
20 Eu bem quisera agora estar presente convosco, e mudar a minha voz; porque estou perplexo a vosso respeito.
21 Yéen ñi bëgga topp yoon wi, xanaa xamuleen li yoonu Musaa wi wax?
21 Dizei-me, os que quereis estar debaixo da lei, não ouvis vós a lei?
22 Mbind mi nee na: Ibraayma am na ñaari doom; ki jaam bi jur ak ki gor si jur.
22 Porque está escrito que Abraão teve dois filhos, um da escrava, e outro da livre.
23 Doomu jaam bi juddu na ni bépp doom, waaye doom, ji mu am ak soxnaam, juddu na ci kaw digeb Yàlla.
23 Todavia, o que era da escrava nasceu segundo a carne, mas, o que era da livre, por promessa.
24 Loolu nag am na lu muy misaal. Ñaari jigéen ñi dañoo bijji ñaari kóllëre. Benn bi di Ajara, mooy wone kóllëre, gi Yàlla fasoon ca tundu Sinayi. Ay jaam lay jur.
24 O que se entende por alegoria; porque estas são as duas alianças; uma, do monte Sinai, gerando filhos para a servidão, que é Agar.
25 Ajara moomu mooy tundu Sinayi, wi nekk ca réewu Arabi. Te it mooy misaalu dëkku Yerusalem, bi fi nekk tey. Ndaxte moom ak i doomam yépp ay jaam lañu.
25 Ora, esta Agar é Sinai, um monte da Arábia, que corresponde à Jerusalém que agora existe, pois é escrava com seus filhos.
26 Waaye Yerusalem, ga ca kaw, mooy gor si. Moom mooy sunu ndey.
26 Mas a Jerusalém que é de cima é livre; a qual é mãe de todos nós.
27 Ndaxte Mbind mi nee na:
27 Porque está escrito: Alegra-te, estéril, que não dás à luz; Esforça-te e clama, tu que não estás de parto; Porque os filhos da solitária são mais do que os da que tem marido.
28 Yéen bokk yi, yéenay doom yi ñu dige woon, niki Isaaxa.
28 Mas nós, irmãos, somos filhos da promessa como Isaque.
29 Waaye doom ji juddoo ni bépp doom, dafa daan sonal doom ji juddoo ci dooley Xelum Yàlla. Te loolu mooy law ba léegi.
29 Mas, como então aquele que era gerado segundo a carne perseguia o que o era segundo o Espírito, assim é também agora.
30 Lu ci Mbind mi wax nag? Nee na: «Dàqal jaam bi ak doomam, ndaxte doomu jaam bi warula bokk cér ak doomu gor si ci ndono.»
30 Mas que diz a Escritura? Lança fora a escrava e seu filho, porque de modo algum o filho da escrava herdará com o filho da livre.
31 Kon nag bokk yi, nun dunu doomi jaam, ay doomi gor lanu.
31 De maneira que, irmãos, somos filhos, não da escrava, mas da livre.
Atalhos do teclado
- Capítulo anterior←
- Próximo capítulo→
- Versículo anteriork
- Próximo versículoj
- Limpar seleçãoEsc
- Esta ajuda?
Estude este capítulo no WhatsApp
Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Gálatas 4, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.