Gálatas 3

Téereb Injiil (WOL2010) vs ACF

Sair da comparação
ACF Almeida Corrigida Fiel
1 Yéen waa Galasi, yéena ñàkk xel! Ku leen fàbbi, gannaaw bi ma leen yégalee ci lu leer ni ñu daaje Yeesu Kirist ca bant ba?
1 Ó insensatos gálatas! quem vos fascinou para não obedecerdes à verdade, a vós, perante os olhos de quem Jesus Cristo foi evidenciado, crucificado, entre vós?
2 Lenn rekk laa bëgg, ngeen wax ma ko: ndax sàmm yoon wee tax, ngeen jot Xelum Yàlla? Déedéet! Dangeena dégg xibaaru jàmm bi te gëm ko.
2 Só quisera saber isto de vós: recebestes o Espírito pelas obras da lei ou pela pregação da fé?
3 Mbaa du nii ngeen ñàkke xel, ba tàmbalee ci Xelum Yàlla, ba noppi yaakaara mate ci seen jëfi bopp?
3 Sois vós tão insensatos que, tendo começado pelo Espírito, acabeis agora pela carne?
4 Mbaa du fitna, yi ngeen daj yépp, dafa nara neen? Manuma koo gëm!
4 Será em vão que tenhais padecido tanto? Se é que isso também foi em vão.
5 Bu leen Yàlla di may Xelam, di leen won jalooreem, ndax li ngeen sàmm yoon a tax, mu def ko, mbaa li ngeen dégg xibaaru jàmm bi te gëm ko?
5 Aquele, pois, que vos dá o Espírito, e que opera maravilhas entre vós, o faz pelas obras da lei, ou pela pregação da fé?
6 Xool-leen ci Ibraayma; Mbind mi wax na ne: «Ibraayma gëm na Yàlla, te Yàlla jàppe ngëmam ni njub.»
6 Assim como Abraão creu em Deus, e isso lhe foi imputado como justiça.
7 Xamleen boog ne boroom ngëm yi rekk ñooy doomi Ibraayma.
7 Sabei, pois, que os que são da fé são filhos de Abraão.
8 Mbind mi tëral na lu jiitu ne Yàlla dina àtte jub ñi dul Yawut ci kaw ngëm. Kon looloo tax mu yégal Ibraayma lu jiitu xibaaru jàmm bi ne ko: «Xeeti àddina yépp dinañu barkeel ci yaw.»
8 Ora, tendo a Escritura previsto que Deus havia de justificar pela fé os gentios, anunciou primeiro o evangelho a Abraão, dizendo: Todas as nações serão benditas em ti.
9 Kon ñi gëm, Yàlla dina leen barkeel, sukkandikoo ko ci seen ngëm, ni mu defal Ibraayma, boroom ngëm.
9 De sorte que os que são da fé são benditos com o crente Abraão.
10 Ñiy wékku ñépp ci jëfi yoon wi, ñu alku lañu, ndaxte bind nañu ne: «Képp ku dul topp lépp lu ndigali yoon wi santaane, yal na alku.»
10 Todos aqueles, pois, que são das obras da lei estão debaixo da maldição; porque está escrito: Maldito todo aquele que não permanecer em todas as coisas que estão escritas no livro da lei, para fazê-las.
11 Bir na sax ne sàmm yoon du tax kenn jub fa kanam Yàlla, ndaxte Mbind mi tëral na ne: «Ku jub ci kaw ngëm dinga dund.»
11 E é evidente que pela lei ninguém será justificado diante de Deus, porque o justo viverá pela fé.
12 Waaye yoon wi laajul ngëm. Mbind mi nee na: «Ku manoona matal li yoon wi wax, kon dinga dund ba fàww.»
12 Ora, a lei não é da fé; mas o homem, que fizer estas coisas, por elas viverá.
13 Waaye Kirist jot na nu ci alkànde, ji yoon wi indi; mu gàddul nu ko, ba far alku moom ci boppam, ndaxte Mbind mi nee na: «Képp ku ñu rey, wékk ko ci bant, alku nga.»
13 Cristo nos resgatou da maldição da lei, fazendo-se maldição por nós; porque está escrito: Maldito todo aquele que for pendurado no madeiro;
14 Noonu barke bi Yàlla dig Ibraayma baawaan na, ba daj ñi dul Yawut te gëm Kirist Yeesu, te nu jot ci kaw ngëm Xel mu Sell, mi Yàlla dige.
14 Para que a bênção de Abraão chegasse aos gentios por Jesus Cristo, e para que pela fé nós recebamos a promessa do Espírito.
15 Bokk yi, maa ngi misaal wax ji ci jëfi doom Aadama. Xam ngeen ne kóllëre gu ñu fas ba noppi, waruñu koo fecci, walla ñu ciy rax dara.
15 Irmãos, como homem falo; se a aliança de um homem for confirmada, ninguém a anula nem a acrescenta.
16 Léegi nag Yàlla am na lu mu dig Ibraayma ak askanam. Mbind mi waxul: «Ak i sëtam», mu mel ni ñu bare, waaye kenn la wax: «Ak sa askan», maanaam Kirist.
16 Ora, as promessas foram feitas a Abraão e à sua descendência. Não diz: E às descendências, como falando de muitas, mas como de uma só: E à tua descendência, que é Cristo.
17 Li ma ci bëgga wax mooy lii: ndegam Yàlla fas na kóllëreem, yoonu Musaa, wi feeñ ñeenti téeméeri at ak fanweer gannaaw ga, du ko mana fecci, ba tebbi digeb Yàlla.
17 Mas digo isto: Que tendo sido a aliança anteriormente confirmada por Deus em Cristo, a lei, que veio quatrocentos e trinta anos depois, não a invalida, de forma a abolir a promessa.
18 Ndaxte xéewal, yi Yàllay dige, bu ñu doon jóge ci yoon wi, kon ajootuñu ci dige bi, fekk ci kaw dige la ko Yàlla maye Ibraayma.
18 Porque, se a herança provém da lei, já não provém da promessa; mas Deus pela promessa a deu gratuitamente a Abraão.
19 Waaw kon yoonu Musaa, luy njariñam? Dañu koo wàcceel nit ñi, ngir seen jàdd yoon ne fàŋŋ. Looloo doon wàllu yoon wi, ba kera Sët biy ñëw, moom mi ñu digoon dige bi. Yoon wi nag, Yàlla tëral na ko jaare ci ay malaaka, te am na ku ko jottali.
19 Logo, para que é a lei? Foi ordenada por causa das transgressões, até que viesse a posteridade a quem a promessa tinha sido feita; e foi posta pelos anjos na mão de um medianeiro.
20 Waaye aajowul jottalikat, su fi kenn rekk teewee, te Yàlla kenn la.
20 Ora, o medianeiro não o é de um só, mas Deus é um.
21 Ndax kon yoonu Musaa wi dafa juuyoo ak li Yàlla dige? Mukk! Su amoon yoon wu nit mana sàmm, ba mu jural ko dund gu sax, kon sàmm yoon dina tax nit jub fa kanam Yàlla.
21 Logo, a lei é contra as promessas de Deus? De nenhuma sorte; porque, se fosse dada uma lei que pudesse vivificar, a justiça, na verdade, teria sido pela lei.
22 Waaye yoon wi tëj na ñépp ci dooley bàkkaar, ngir ñi gëm Yeesu Kirist jot li Yàlla dige woon ci seen kaw ngëm.
22 Mas a Escritura encerrou tudo debaixo do pecado, para que a promessa pela fé em Jesus Cristo fosse dada aos crentes.
23 Bi ngëm Yeesu Kirist feeñagul nag, yoon wi da noo tëjoon ràpp, ba kera ngëm di feeñ.
23 Mas, antes que a fé viesse, estávamos guardados debaixo da lei, e encerrados para aquela fé que se havia de manifestar.
24 Ci noonu la nu yoon wi doon note, ba Kirist di ñëw, ngir Yàlla àtte nu jub ci kaw ngëm.
24 De maneira que a lei nos serviu de aio, para nos conduzir a Cristo, para que pela fé fôssemos justificados.
25 Waaye léegi, bi jamonoy ngëm ji ñëwee, nekkatunu ci kilifteefu yoon wi.
25 Mas, depois que veio a fé, já não estamos debaixo de aio.
26 Yéen ñépp doomi Yàlla ngeen ndax li ngeen bokk ci Kirist Yeesu ci kaw ngëm.
26 Porque todos sois filhos de Deus pela fé em Cristo Jesus.
27 Yéen ñépp, ñi ñu sóob ci ndox ngir wone seen bokk ci Kirist, soloo ngeen Kirist.
27 Porque todos quantos fostes batizados em Cristo já vos revestistes de Cristo.
28 Kon nag amul xàjjale ci diggante Yawut ak ki dul Yawut, ci diggante jaam ak gor, ci diggante góor ak jigéen. Yéen ñépp benn ngeen ci seen bokk ci Kirist.
28 Nisto não há judeu nem grego; não há servo nem livre; não há macho nem fêmea; porque todos vós sois um em Cristo Jesus.
29 Bu ngeen bokkee ci Kirist, kon bokk ngeen ci askanu Ibraayma, te jot ngeen xéewal, yi ko Yàlla dig.
29 E, se sois de Cristo, então sois descendência de Abraão, e herdeiros conforme a promessa.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Gálatas 3, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.