Gálatas 2

Téereb Injiil (WOL2010) vs VC

Sair da comparação
VC Versão Católica
1 Ba ñu ca tegee fukki at ak ñeent, ànd naa ak Barnabas, dellu Yerusalem, yóbbaale Tit.
1 Catorze anos mais tarde, subi outra vez a Jerusalém com Barnabé, levando também Tito comigo.
2 Dem naa fa, ndaxte Yàllaa ma fa yebal ci kaw peeñu. Ba ma demee, daje naa ak ñi ñu gëna fonk ca mbooloo ma, ma wéetoo ak ñoom, won leen xibaaru jàmm, bi may yégal ñi dul Yawut, ngir ragal sama coonob démb mbaa tey neen.
2 E subi em conseqüência de uma revelação. Expus-lhes o Evangelho que prego entre os pagãos, e isso particularmente aos que eram de maior consideração, a fim de não correr ou de não ter corrido em vão.
3 Te Tit mi ma gunge woon sax de, li mu bokk ci xeetu Gereg, taxul ñu sonal nu ci xarafal ko.
3 Entretanto, nem sequer meu companheiro Tito, embora gentio, foi obrigado a circuncidar-se.
4 Fekk na mbir moomu nekk coow ndax naaféq, yi yoxoosu ci sunu biir ak mébét mu bon, ngir seet yaatu gi nu am ci Yeesu Kirist, ba fexe noo defaat ay jaam.
4 Mas, por causa dos falsos irmãos, intrusos - que furtivamente se introduziram entre nós para espionar a liberdade de que gozávamos em Cristo Jesus, a fim de nos escravizar -,
5 Waaye yaatalunu leen benn yoon, ngir dëggug xibaaru jàmm bi mana sax ci yéen.
5 fomos, por esta vez, condescendentes, para que o Evangelho permanecesse em sua integridade.
6 Waaye ñi ñu gëna fonk —ak lu mana doon seen sag xooluma ko, ñépp a yem fa kanam Yàlla— waaye ñooñu ñu teg njiit boog, bi ma dajee ak ñoom, yokkuñu dara ci sama sas.
6 Quanto aos que eram de autoridade - o que antes tenham sido não me importa, pois Deus não se deixa levar por consideração de pessoas -, estas autoridades, digo, nada me impuseram.
7 Gis nañu ne Yàllaa nu yebal, muy man di Piyeer, ngir nu yégle xibaaru jàmm bi: ma féetewoo ñi dul Yawut, Piyeer féetewoo Yawut yi.
7 Ao contrário, viram que a evangelização dos incircuncisos me era confiada, como a dos circuncisos a Pedro
8 Ndaxte ni Yàlla jëfe ci Piyeer, miy ndawam ci Yawut yi, noonu it la jëfe ci man, may ndawam ci ñi dul Yawut.
8 {porque aquele cuja ação fez de Pedro o apóstolo dos circuncisos, fez também de mim o dos pagãos}.
9 Saag ak Sefas ak Yowaana nag, ñi ñu teg kenuy mbooloo mi, bi ñu ràññee yen bi ma Yàlla jagleel ci yiwam, ñu fekksi nu ci, ba jox nu loxo, man ak Barnabas, nu liggéey ca ña dul Yawut, ñoom ñu liggéey ca Yawut ya.
9 Tiago, Cefas e João, que são considerados as colunas, reconhecendo a graça que me foi dada, deram as mãos a mim e a Barnabé em sinal de pleno acordo:
10 Li ñu doon laaj rekk moo di, nuy fàttaliku seen aji néew doole yi, fekk sax laxasu woon naa ci def ko.
10 iríamos aos pagãos, e eles aos circuncidados. Recomendaram-nos apenas que nos lembrássemos dos pobres, o que era precisamente a minha intenção.
11 Waaye bi Sefas ñëwee dëkku Ancos, yedd naa ko ci kanam ñépp, ndaxte li mu def jaaduwul.
11 Quando, porém, Cefas veio a Antioquia, resisti-lhe francamente, porque era censurável.
12 Ndaxte laata ndaw yi Saag yónni di ñëw, da daan bokk di lekk ak ñi dul Yawut. Waaye bi ñu agsee, te mu ragal kureel googu faaydaal xaraf, mu dellu gannaaw, di sore ñi dul Yawut.
12 Pois, antes de chegarem alguns homens da parte de Tiago, ele comia com os pagãos convertidos. Mas, quando aqueles vieram, retraiu-se e separou-se destes, temendo os circuncidados.
13 Yeneen Yawut yi it daldi ànd ak Sefas ci naaféqam, ba yóbbaale sax Barnabas.
13 Os demais judeus convertidos seguiram-lhe a atitude equívoca, de maneira que mesmo Barnabé foi levado por eles a essa dissimulação.
14 Bi ma seetee nag ne awuñu woon ci dëgg, gi xibaaru jàmm bi di jàngle, ma yedd Sefas ci kanam ñépp ne ko: «Yaw miy Yawut, gannaaw dëddu nga aaday Yawut yi, ba dund ni ku dul Yawut, lu tax nga bëgga sëf diiney Yawut ci ñi dul Yawut?»
14 Quando vi que o seu procedimento não era segundo a verdade do Evangelho, disse a Cefas, em presença de todos: Se tu, que és judeu, vives como os gentios, e não como os judeus, com que direito obrigas os pagãos convertidos a viver como os judeus?
15 Nun danoo cosaanoo ci xeetu Yawut, te bokkunu ci xeet, yi xamul Yàlla tey bàkkaar.
15 Nós, judeus de nascença, e não pecadores dentre os pagãos,
16 Teewul nu xam ne Yàlla du àtte kenn ni ku jub ci kaw sàmm yoon, waaye ci gëm Yeesu Kirist. Kon nun itam gëm nanu Kirist Yeesu, ngir Yàlla àtte nu jub ci kaw gëm Kirist, te du ci sàmm yoon. Ndaxte du caageenug sàmm yoon mooy tax Yàlla àtte kenn ni ku jub.
16 sabemos, contudo, que ninguém se justifica pela prática da lei, mas somente pela fé em Jesus Cristo. Também nós cremos em Jesus Cristo, e tiramos assim a nossa justificação da fé em Cristo, e não pela prática da lei. Pois, pela prática da lei, nenhum homem será justificado.
17 Waaye ba tey su fekkee ne nu ngi wuta jub ci kaw gëm Kirist, fekk nu ne fàŋŋ di ay bàkkaarkat, ndax nag Kirist moo sas bàkkaar? Mukk!
17 Pois, se nós, que aspiramos à justificação em Cristo, retornamos, todavia, ao pecado, seria porventura Cristo ministro do pecado? Por certo que não!
18 Waaye su ma delloo di sàmm ndigali yoon, yi ma bàyyi, dëgg-dëgg dinaa wone noonu ne moykatu yoon wi laa.
18 Se torno a edificar o que destruí, confesso-me transgressor.
19 Ci li jëm ci yoonu Musaa, dee naa, fekk yoon wi ci boppam moo ko waral, ngir ma mana dund, ba amal njariñ Yàlla.
19 Na realidade, pela fé eu morri para a lei, a fim de viver para Deus. Estou pregado à cruz de Cristo.
20 Daajaale nañu ma ak Kirist ca bant ba, te noonu du man may dundati, waaye Kirist mooy dund ci man. Dundu mbindeef, gi may dund nag, maa ngi koy dund ci gëm Doomu Yàlla ji, moom mi ma bëgg, ba joxe bakkanam ngir man.
20 Eu vivo, mas já não sou eu; é Cristo que vive em mim. A minha vida presente, na carne, eu a vivo na fé no Filho de Deus, que me amou e se entregou por mim.
21 Duma neenal yiwu Yàlla, ndaxte su sàmm yoon doon taxa jub fa kanam Yàlla, kon Kirist dee na cig neen.
21 Não menosprezo a graça de Deus; mas, em verdade, se a justiça se obtém pela lei, Cristo morreu em vão.

Ler em outra tradução

Comparar com outra

Estude este capítulo no WhatsApp

Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Gálatas 2, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.