Filipenses 3
Téereb Injiil (WOL2010) vs ACF
1 Kon nag samay bokk, bégleen ci Boroom bi. Duma sonn mukk ci di leen ko wax, ndax seen mucc moo ci aju.
1 Resta, irmãos meus, que vos regozijeis no Senhor. Não me aborreço de escrever-vos as mesmas coisas, e é segurança para vós.
2 Moytuleen xaj yi, waaw, moytuleen ñiy jëfe lu bon, ñoom ñi seen xarafal weesul wàññi yaramu nit.
2 Guardai-vos dos cães, guardai-vos dos maus obreiros, guardai-vos da circuncisão;
3 Ndaxte nun noo xaraf tigi, nun ñiy màggal Yàlla ci Xel mu Sell mi, di damu ci Kirist Yeesu, te amunu benn yaakaar ci matug nit.
3 Porque a circuncisão somos nós, que servimos a Deus em espírito, e nos gloriamos em Jesus Cristo, e não confiamos na carne.
4 Ba tey manoon naa am yaakaar ci sama bopp; su nit doon damu, maa ciy raw.
4 Ainda que também podia confiar na carne; se algum outro cuida que pode confiar na carne, ainda mais eu:
5 Xarafoon naa ca ayu-bés ga, bokk ci bànni Israyil ci giiru Beñamin, di Ebrë ci deret ak ci meen. Bu dee ci yoonu Musaa ngeen bëgga wax, ci tariixab Farisen laa bokkoon;
5 Circuncidado ao oitavo dia, da linhagem de Israel, da tribo de Benjamim, hebreu de hebreus; segundo a lei, fui fariseu;
6 bu dee it ci mbirum farlu, daan naa fitnaal mbooloom ñi gëm Kirist; bu dee ci njub ci sàmm yoon, awma benn gàkk.
6 Segundo o zelo, perseguidor da igreja, segundo a justiça que há na lei, irrepreensível.
7 Waaye loolu lépp lu ma tegoon ay njariñ fa kanam Yàlla, dëddu naa ko ngir Kirist.
7 Mas o que para mim era ganho reputei-o perda por Cristo.
8 Rax-ca-dolli dëddu naa lépp ngir xéewali xam Kirist Yeesu sama Boroom, di xam-xam bu xóot, ba xel manu koo takk. Moo tax ñàkk naa sama lépp, te def ko ni mbalit, ngir am cér ci Kirist.
8 E, na verdade, tenho também por perda todas as coisas, pela excelência do conhecimento de Cristo Jesus, meu Senhor; pelo qual sofri a perda de todas estas coisas, e as considero como escória, para que possa ganhar a Cristo,
9 Na ma Yàlla fekk ci moom, waxuma ci njub gu aju ci sàmm yoon, waaye gu aju ci gëm Kirist, maanaam njub gi nu Yàlla sol ci kaw ngëm.
9 E seja achado nele, não tendo a minha justiça que vem da lei, mas a que vem pela fé em Cristo, a saber, a justiça que vem de Deus pela fé;
10 Moom laay ittewoo xam, ak doole ji ànd ak ndekkiteem, ma bokk ci ay coonoom, ba fekki ko ci deeyam,
10 Para conhecê-lo, e à virtude da sua ressurreição, e à comunicação de suas aflições, sendo feito conforme à sua morte;
11 ngir mana séddu ci ndekkiteem, su ma ko manee am.
11 Para ver se de alguma maneira posso chegar à ressurreição dentre os mortos.
12 Waxuma ne jagoo naa ko ba noppi, waxuma it ne aji mat laa, waaye maa ngi daw, ngir jot li tax Kirist jël ma.
12 Não que já a tenha alcançado, ou que seja perfeito; mas prossigo para alcançar aquilo para o que fui também preso por Cristo Jesus.
13 Bokk yi, gëmuma ne jot naa ko ba noppi, waaye lenn lii laay def: fàtte li ma weesu, jublu ci li féete kanam,
13 Irmãos, quanto a mim, não julgo que o haja alcançado; mas uma coisa faço, e é que, esquecendo-me das coisas que atrás ficam, e avançando para as que estão diante de mim,
14 di daw yen muj ga, ngir jot li ma Yàlla taxa woo, di cér bi ma Yàlla wooye te dencal ma ko ci asamaan ci darajay Kirist Yeesu.
14 Prossigo para o alvo, pelo prêmio da soberana vocação de Deus em Cristo Jesus.
15 Nun ñi mat nag, nanu xalaat loolu. Su ngeen ci amee werantey xol, Yàlla dina leen ko leeralal.
15 Por isso todos quantos já somos perfeitos, sintamos isto mesmo; e, se sentis alguma coisa de outra maneira, também Deus vo-lo revelará.
16 Li am daal, fa seen ngëm tolloo, na fa seen jëf àgg.
16 Mas, naquilo a que já chegamos, andemos segundo a mesma regra, e sintamos o mesmo.
17 Kon nag bokk yi, toppleen ma te xool ñiy roy ci li nu tëral diirub sunu ngan ci yéen.
17 Sede também meus imitadores, irmãos, e tende cuidado, segundo o exemplo que tendes em nós, pelos que assim andam.
18 Ndaxte jëfi ñu bare juuyoo na ak dee gi Kirist dee; loolu wax naa leen ko ba tàyyi, maa ngi koy waxaat léegi ak i jooy.
18 Porque muitos há, dos quais muitas vezes vos disse, e agora também digo, chorando, que são inimigos da cruz de Cristo,
19 Alku lañuy mujje, ñoom ñiy jaami seen biir, di wonoo lu ruslu, tey wut yëfi àddina rekk.
19 Cujo fim é a perdição; cujo Deus é o ventre, e cuja glória é para confusão deles, que só pensam nas coisas terrenas.
20 Waaye nun waa asamaan lanu, te noo ngi xaar Boroom bi Yeesu Kirist jóge fa, musalsi nu.
20 Mas a nossa cidade está nos céus, de onde também esperamos o Salvador, o Senhor Jesus Cristo,
21 Noonu dina soppi sunu yaram wu toroxlu, def ko ni yaramam wi ànd ak ndam dëppook kàttanam, gi ko mana notal mbindeef yépp.
21 Que transformará o nosso corpo abatido, para ser conforme o seu corpo glorioso, segundo o seu eficaz poder de sujeitar também a si todas as coisas.
Atalhos do teclado
- Capítulo anterior←
- Próximo capítulo→
- Versículo anteriork
- Próximo versículoj
- Limpar seleçãoEsc
- Esta ajuda?
Estude este capítulo no WhatsApp
Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Filipenses 3, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.