Filipenses 2
Téereb Injiil (WOL2010) vs ARC
1 Su nu Kirist mayee fit nag ak mbëggeel guy dëfal sunu xol, su nu amee cér ci Xel mu Sell mi, su amee cofeel ak yërmande ci sunu bokk ci moom,
1 Portanto, se há algum conforto em Cristo, se alguma consolação de amor, se alguma comunhão no Espírito, se alguns entranháveis afetos e compaixões,
2 kon mottalileen sama mbég, ci bokk benn xalaat ak genn mbëggeel, benn bakkan ak menn xel.
2 completai o meu gozo, para que sintais o mesmo, tendo o mesmo amor, o mesmo ânimo, sentindo uma mesma coisa.
3 Buleen def dara ci kaw wut aw tur walla wonu, waaye jiital-leen seeni moroom cig woyof.
3 Nada façais por contenda ou por vanglória, mas por humildade; cada um considere os outros superiores a si mesmo.
4 Buleen yem ci topptoo seen bopp rekk, waaye booleleen ci seeni moroom.
4 Não atente cada um para o que é propriamente seu, mas cada qual também para o que é dos outros.
5 Te ngeen soloo xel mi nekkoon ci Kirist Yeesu:
5 De sorte que haja em vós o mesmo sentimento que houve também em Cristo Jesus,
6 Njàlbéen ga fekk na Kirist yor melow Yàlla,
6 que, sendo em forma de Deus, não teve por usurpação ser igual a Deus.
7 Waaye daa wàcce boppam,
7 Mas aniquilou-se a si mesmo, tomando a forma de servo, fazendo-se semelhante aos homens;
8 daa suufeel boppam,
8 e, achado na forma de homem, humilhou-se a si mesmo, sendo obediente até à morte e morte de cruz.
9 Moo tax Yàlla kaweel ko lool,
9 Pelo que também Deus o exaltou soberanamente e lhe deu um nome que é sobre todo o nome,
10 ngir turu Yeesoo tax ñépp sukk,
10 para que ao nome de Jesus se dobre todo joelho dos que estão nos céus, e na terra, e debaixo da terra,
11 te ñépp bokk genn kàddu naan: Yeesu Kirist mooy Boroom bi;
11 e toda língua confesse que Jesus Cristo é o Senhor, para glória de Deus Pai.
12 Noonu samay soppe, xam naa ne masuleena jóg ci dégg ndigal, waxuma sax bi ma nekkee ak yéen rekk, waaye rawatina bi ma leen soree. Kon nag maa ngi leen di ñaan, ngeen biral seen mucc ci seeni jëf, te def ko ci ragal Yàlla gu dëggu.
12 De sorte que, meus amados, assim como sempre obedecestes, não só na minha presença, mas muito mais agora na minha ausência, assim também operai a vossa salvação com temor e tremor;
13 Ndaxte Yàlla ci boppam mooy jëf ci yéen, ngir ngeen fonk coobareem te di ko jëfe.
13 porque Deus é o que opera em vós tanto o querer como o efetuar, segundo a sua boa vontade.
14 Lépp lu ngeen di def nag, buleen ci boole xultu mbaa xuloo.
14 Fazei todas as coisas sem murmurações nem contendas;
15 Noonu dingeen am xol bu laab bu àndul ak ŋàññ, di goney Yàlla yu amul sikk ci biir jamono ju yàqu te rëb. Dangeen di leer ci seen biir ni weer ci àddina si,
15 para que sejais irrepreensíveis e sinceros, filhos de Deus inculpáveis no meio duma geração corrompida e perversa, entre a qual resplandeceis como astros no mundo;
16 di jottali kàddug dund gi. Noonu bu bésu Kirist ñëwee, dinaa mana bég, xam ne dawuma lu amul njariñ te sonnuma cig neen.
16 retendo a palavra da vida, para que, no Dia de Cristo, possa gloriar-me de não ter corrido nem trabalhado em vão.
17 Bu sama deret waree tuuru sax, ngir seen ngëm mat sëkk, ma mel ni naan gu ñu boole ak sarax su jëm ci Yàlla, ba tey bég naa ci, te dinaa ci bégati.
17 E, ainda que seja oferecido por libação sobre o sacrifício e serviço da vossa fé, folgo e me regozijo com todos vós.
18 Yéen itam nag bégleen, waaw, fekksileen ma ci sama mbég.
18 E vós também regozijai-vos e alegrai-vos comigo por isto mesmo.
19 Gannaaw loolu, bu soobee Boroom bi Yeesu, yaakaar naa ne dinaa leen yónnee Timote balaa yàgg, ngir sama xel dal ci xam nan ngeen def.
19 E espero, no Senhor Jesus, que em breve vos mandarei Timóteo, para que também eu esteja de bom ânimo, sabendo dos vossos negócios.
20 Ndaxte amu fi kenn gannaaw Timote, ku bokk ak man xalaat te fonk leen bu wér.
20 Porque a ninguém tenho de igual sentimento, que sinceramente cuide do vosso estado;
21 Ñi ci des ñépp, seen bopp lañuy xalaat, waaye du mbiri Yeesu Kirist.
21 porque todos buscam o que é seu e não o que é de Cristo Jesus.
22 Waaye xam ngeen takkuteg Timote, ci ni mu ànde ak man ci tas xibaaru jàmm bi, ni doom di taxawoo baayam.
22 Mas bem sabeis qual a sua experiência, e que serviu comigo no evangelho, como filho ao pai.
23 Moom laa yaakaara yónni fi yéen nag, waxtu wu ma yégee, nu sama mbir di tëdde.
23 De sorte que espero enviá-lo a vós logo que tenha provido a meus negócios.
24 Waaye wóor na ma ne Boroom bi dina ma may, man ci sama bopp, ma seetsi leen balaa yàgg.
24 Mas confio no Senhor que também eu mesmo, em breve, irei ter convosco.
25 Ci lu jëm ci sama mbokk Epafrodit nag, miy sama nawle ci liggéey bi ak ci xeex bi, te di seen ndaw ci faj samay soxla, jàpp naa ne war naa leen koo delloo.
25 Julguei, contudo, necessário mandar-vos Epafrodito, meu irmão, e cooperador, e companheiro nos combates, e vosso enviado para prover às minhas necessidades;
26 Ndaxte namm na leen lool, te tiisoo na li ngeen yég jagadeem.
26 porquanto tinha muitas saudades de vós todos e estava muito angustiado de que tivésseis ouvido que ele estivera doente.
27 Ci dëgg-dëgg woppoon na ba xawa dee, waaye Yàlla yërëm na ko, ba fëgg boppam, rax-ca-dolli siggil na ma man itam, ngir ma baña am tiis ci kaw tiis.
27 E, de fato, esteve doente e quase à morte, mas Deus se apiedou dele e não somente dele, mas também de mim, para que eu não tivesse tristeza sobre tristeza.
28 Noonu delloo naa leen ko ci lu gaaw, ngir ñëwam bégal seeni xol, te man itam sama xol féex.
28 Por isso, vo-lo enviei mais depressa, para que, vendo-o outra vez, vos regozijeis, e eu tenha menos tristeza.
29 Teeruleen ko teeru bu rafet nag ngir Boroom bi, te teral ñi mel ni moom.
29 Recebei-o, pois, no Senhor, com todo o gozo, e tende-o em honra:
30 Ndaxte liggéeyal na Kirist, ba riisu dee, te gar na bakkanam ci taxawal leen ci topptoo, bi ngeen yéene woon ci man.
30 porque, pela obra de Cristo, chegou até bem próximo da morte, não fazendo caso da vida, para suprir para comigo a falta do vosso serviço.
Atalhos do teclado
- Capítulo anterior←
- Próximo capítulo→
- Versículo anteriork
- Próximo versículoj
- Limpar seleçãoEsc
- Esta ajuda?
Estude este capítulo no WhatsApp
Peça à IA da Bíblia Fala para explicar Filipenses 2, comparar traduções ou montar um estudo — tudo direto pelo WhatsApp.